Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   A    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23216  MAT 1:3  Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram;
23217  MAT 1:4  Aram Aminadab; Aminadab Nason; Nason Salmon;
23220  MAT 1:7  Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf;
23221  MAT 1:8  Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;
23222  MAT 1:9  Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya;
23223  MAT 1:10  Esekiya Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas;
23226  MAT 1:13  miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor;
23227  MAT 1:14  Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
23240  MAT 2:2  Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.»
23242  MAT 2:4  Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo.
23260  MAT 2:22  Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile.
23263  MAT 3:2  Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na
23264  MAT 3:3  Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”»
23265  MAT 3:4  Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
23290  MAT 4:12  Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
23295  MAT 4:17  Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na
23296  MAT 4:18  Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
23306  MAT 5:3  «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo.
23313  MAT 5:10  Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo.
23322  MAT 5:19  Ku tebbi nag ba gëna tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gëna tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23323  MAT 5:20  Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23325  MAT 5:22  Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk:Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara.
23364  MAT 6:13  Yàlla boo nu teg ci yoonu nattu, waaye yal nanga nu musal ci lu bon. Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.”
23375  MAT 6:24  «Kenn manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal.
23378  MAT 6:27  Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo mana yokk waxtu ci àppam?
23406  MAT 7:21  «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw.
23425  MAT 8:11  Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23456  MAT 9:8  Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi.
23488  MAT 10:2  Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;
23489  MAT 10:3  Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade;
23493  MAT 10:7  Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.”
23530  MAT 11:2  Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem,
23539  MAT 11:11  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut.
23559  MAT 12:1  Amoon na benn bésub noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk.
23619  MAT 13:11  Noonu mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
23632  MAT 13:24  Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam.
23639  MAT 13:31  Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam.
23641  MAT 13:33  Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
23652  MAT 13:44  Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba.
23653  MAT 13:45  «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet.
23654  MAT 13:46  Am bés mu gis per buy jar njég lu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
23655  MAT 13:47  Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk.
23660  MAT 13:52  Yeesu ne leen: «Kon nag xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
23683  MAT 14:17  Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
23725  MAT 15:23  Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
23742  MAT 16:1  Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.»
23755  MAT 16:14  Taalibe yi ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Ilyaas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi.»
23757  MAT 16:16  Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
23760  MAT 16:19  Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.»
23761  MAT 16:20  Noonu Yeesu dénk taalibe yi bu wóor ne leen: «Buleen wax kenn ne maay Almasi bi.»
23794  MAT 17:25  Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?»
23799  MAT 18:3  ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen waññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23800  MAT 18:4  Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gëna màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23819  MAT 18:23  «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgga waññ alalam ak ay jaraafam.
23835  MAT 19:4  Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen,
23843  MAT 19:12  Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu baña séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko mana nangu, nangu ko.»
23845  MAT 19:14  Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
23854  MAT 19:23  Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu!
23855  MAT 19:24  Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.»
23862  MAT 20:1  «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu reseñam.
23923  MAT 21:28  «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu reseñ.”
23926  MAT 21:31  Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobarey baayam?» Ñu ne: «Taaw baYeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkka dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23928  MAT 21:33  Yeesu teg ca ne: «Dégluleen beneen léeb. Amoon na fi benn boroom kër bu jëmbët toolu reseñ. Mu ñag tool bi, gas ci biir pax, ngir nal ci reseñ yi. Mu tabax wottukaay, batale ko ay beykat, daldi tukki.
23943  MAT 22:2  «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur buy waajal céetu doomam ju góor.
23966  MAT 22:25  Amoon na ci nun nag juróom ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba noppi, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom.
23983  MAT 22:42  «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda
24000  MAT 23:13  «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci.
24022  MAT 23:35  Noonu deretu ñi jub, ji ñu tuur jépp ci àddina, dina xëppu ci seen kaw, li dale ci deretu Abel mi jub, ba ci deretu Sakari doomu Baraki, mi ngeen rey ci diggante bérab bu sell bi ak sarxalukaay bi.
24061  MAT 24:35  Asamaan ak suuf dinañu wéy, waaye samay wax du wéy mukk.
24078  MAT 25:1  «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba.
24111  MAT 25:34  «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndijoor:Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina.
24163  MAT 26:40  Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
24186  MAT 26:63  Waaye Yeesu ne cell. Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.»
24187  MAT 26:64  Yeesu ne ko: «Wax nga ko. Maa ngi leen koy wax it, li dale fii dingeen gis Doomu nit ki toog ci ndijooru Aji Man ji, di ñëw ci niiri asamaan si.»
24202  MAT 27:4  ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu ne ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.»
24253  MAT 27:55  Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dànd, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo.
24255  MAT 27:57  Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon.
24263  MAT 27:65  Pilaat ne leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.»
24277  MAT 28:13  ne leen: «Nangeen wax lii:Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.”
24290  MRK 1:6  Yaxya nag mi ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk laxasaayu der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
24291  MRK 1:7  Mu waare ne: «Am na kuy ñëw sama gannaaw koo xam ne kii moo ma ëpp kàttan; yeyoowuma sax sëgg, ngir tekki ay dàllam.
24300  MRK 1:16  Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon.
24308  MRK 1:24  «Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla
24313  MRK 1:29  Bi nga xamee ne génn nañu ci jàngu bi, ñu ànd ak Saag ak Yowaana, dem ci kër Simoŋ ak Andare.
24324  MRK 1:40  Am bés ku gaana ñëw ci moom, sukk, ñaan ko ne: «Soo ko bëggee, man nga maa wéral.»
24336  MRK 2:7  «Kii kan la, ba saña wax lii; mi ngi sosal Yàlla. Ana ku mana baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»
24343  MRK 2:14  Bi Yeesu di romb, mu gis ku ñuy wax Lewi, doomu Alfe, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ci man.» Mu jóg, daldi topp ci moom.
24352  MRK 2:23  Amoon na benn bésub noflaay Yeesu jaar ciy tool yu ñor. Bi ñuy dem nag, ay taalibeem daldi fàq ay gub.
24355  MRK 2:26  Xanaa yéguleen li amoon ci bési Abiyatar sarxalkat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kër Yàlla ga, lekk mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, jox ci it ña mu àndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat?»
24358  MRK 3:1  Am beneen bés, Yeesu duggaat ci jàngu bi, fekk amoon na fa nit ku loxoom làggi.
24359  MRK 3:2  Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu man koo tuumaal.
24375  MRK 3:18  Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;