23243 | MAT 2:5 | Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: |
23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |
23262 | MAT 3:1 | Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude. |
23277 | MAT 3:16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
23298 | MAT 4:20 | Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom. |
23300 | MAT 4:22 | Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom. |
23329 | MAT 5:26 | Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj. |
23353 | MAT 6:2 | Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23356 | MAT 6:5 | «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23367 | MAT 6:16 | «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23405 | MAT 7:20 | Ci seeni jëf nag ngeen leen di xàmmee. |
23408 | MAT 7:23 | Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Masuma leena xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.” |
23417 | MAT 8:3 | Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ. |
23424 | MAT 8:10 | Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii. |
23427 | MAT 8:13 | Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér. |
23430 | MAT 8:16 | Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp. |
23438 | MAT 8:24 | Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yëngal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw. |
23440 | MAT 8:26 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. |
23454 | MAT 9:6 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
23478 | MAT 9:30 | Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.» |
23482 | MAT 9:34 | Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
23494 | MAT 10:8 | Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen. |
23501 | MAT 10:15 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu. |
23509 | MAT 10:23 | Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen mana wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.» |
23528 | MAT 10:42 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gëna ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.» |
23539 | MAT 11:11 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut. |
23540 | MAT 11:12 | Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll. |
23553 | MAT 11:25 | Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. |
23579 | MAT 12:21 | Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.» |
23596 | MAT 12:38 | Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.» |
23644 | MAT 13:36 | Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.» |
23667 | MAT 14:1 | Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am. |
23681 | MAT 14:15 | Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu mana lekk?» |
23685 | MAT 14:19 | Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo ma, ñu toog ca ñax ma. Mu jël juróomi mburu ya ak ñaari jën ya, xool ci kaw, sant Yàlla. Mu damm mburu ma, jox ko taalibe ya, ñu séddale ko nit ña. |
23691 | MAT 14:25 | Ca njël nag Yeesu jëm ci ñoom, di dox ci kaw dex gi. |
23694 | MAT 14:28 | Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.» |
23697 | MAT 14:31 | Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?» |
23699 | MAT 14:33 | Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.» |
23703 | MAT 15:1 | Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko: |
23730 | MAT 15:28 | Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa. |
23737 | MAT 15:35 | Ci kaw loolu Yeesu sant mbooloo mi, ñu toog ci suuf. |
23757 | MAT 16:16 | Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.» |
23769 | MAT 16:28 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, am na ñi fi taxaw, ñoo xam ne duñu dee, te gisuñu Doomu nit ki ñëw ci nguuram.» |
23789 | MAT 17:20 | Yeesu ne leen: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.» |
23797 | MAT 18:1 | Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gëna màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?» |
23799 | MAT 18:3 | ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen waññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23814 | MAT 18:18 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lépp lu ngeen yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan, te lépp lu ngeen yiwi ci àddina, dees na ko yiwi ci asamaan. |
23854 | MAT 19:23 | Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu! |
23859 | MAT 19:28 | Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil. |
23864 | MAT 20:3 | Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu. |
23881 | MAT 20:20 | Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn. |
23884 | MAT 20:23 | Yeesu ne leen: «Ci dëgg dingeen naan sama kaas, waaye toog ci sama ndijoor mbaa sama càmmoñ, du man maa koy maye, waaye sama Baay moo koy may ñi mu ko waajal.» |
23904 | MAT 21:9 | Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
23911 | MAT 21:16 | Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu ne leen: «Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleena jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?» |
23913 | MAT 21:18 | Ci suba teel Yeesu délsi ca dëkk ba, mu xiif. |
23914 | MAT 21:19 | Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk!» Ca saa sa figg ga daldi wow. |
23916 | MAT 21:21 | Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def. |
23920 | MAT 21:25 | La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” |
23921 | MAT 21:26 | Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.» |
23926 | MAT 21:31 | Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobarey baayam?» Ñu ne: «Taaw ba.» Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkka dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23949 | MAT 22:8 | Ci kaw loolu mu ne surga ya: “Reeri céet gi noppi na, waaye ñi ñu woo yeyoowuñu ko. |
23987 | MAT 22:46 | Ci kaw loolu kenn manu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara. |
23993 | MAT 23:6 | Ca reeri xew yi, toogu yu yiw lañuy taamu, tey féete kanam ca jàngu ya. |
24014 | MAT 23:27 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk. |
24023 | MAT 23:36 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, loolu lépp dina dal ci niti jamono jii. |
24028 | MAT 24:2 | Mu ne leen: «Du gis ngeen yii yépp? Ci dëgg maa ngi leen koy wax, lii lépp dina daanu, ba doj dootul des ci kaw doj.» |
24060 | MAT 24:34 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, niti jamono jii duñu wéy te loolu lépp amul. |
24067 | MAT 24:41 | Ci ñaari jigéen ñuy wol ca ëtt ba, dinañu jël kenn ki, bàyyi ki ci des. |
24073 | MAT 24:47 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, njaatige bi dina ko teg ci alalam jépp. |
24089 | MAT 25:12 | Mu ne leen: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.” |
24114 | MAT 25:37 | Ci kaw loolu ñi jub dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, nu jox la, nga lekk; mbaa nga mar, nu jox la, nga naan? |
24117 | MAT 25:40 | Noonu Buur bi dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gëna ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.” |
24121 | MAT 25:44 | Ci kaw loolu dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?” |
24122 | MAT 25:45 | Kon dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gëna ndaw, man ngeen ko defalul.” |
24136 | MAT 26:13 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, fépp fu ñuy yéene xibaaru jàmm bi ci àddina sépp, dinañu fa fàttali it li jigéen jii def.» |
24137 | MAT 26:14 | Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya, |
24144 | MAT 26:21 | Bi ñuy lekk, mu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, kenn ci yéen dina ma wor.» |
24157 | MAT 26:34 | Yeesu ne ko: «Ci dëgg maa ngi la koy wax, ci guddi gii, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» |
24174 | MAT 26:51 | Ca saa sa kenn ci ñi ànd ak Yeesu bocci jaaseem, dóor surgab sarxalkat bu mag ba, nopp ba dagg. |
24179 | MAT 26:56 | Waaye lii lépp xew na, ngir amal Mbindi yonent yi.» Ci kaw loolu taalibe yépp dëddu ko, daw. |
24185 | MAT 26:62 | Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo wax dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?» |
24190 | MAT 26:67 | Ci kaw loolu ñu daldi tifli ci xar kanamam, dóor ko ay kurfeñ. Ñeneen talaata ko, |
24196 | MAT 26:73 | Nees-tuut ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.» |
24199 | MAT 27:1 | Ci suba teel sarxalkat yu mag yépp ak njiiti xeet wa gise, ngir fexee reylu Yeesu. |
24213 | MAT 27:15 | Ca màggal gu nekk nag boroom réew ma daan na may mbooloo ma, ñu tànn kenn ca ña ñu tëjoon, mu daldi leen ko bàyyil. |
24246 | MAT 27:48 | Ca saa sa kenn ci ñoom daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci kaw bant, jox ko ko, mu muucu. |
24249 | MAT 27:51 | Ca saa sa ridob bérab bu sell ba ca kër Yàlla ga xar ñaar, li dale ci kaw ba ci suuf; suuf si yëngu, doj yi toj, bàmmeel yi ubbiku, |
24252 | MAT 27:54 | Noonu njiitu xare bi ak ñi ànd ak moom di wottu Yeesu, bi ñu gisee suuf si yëngu ak li xew, ñu daldi tiit lool ne: «Ci dëgg, kii Doomu Yàlla la.» |
24255 | MAT 27:57 | Ca ngoon amoon na taalibeb Yeesu mu ñëw, tudd Yuusufa te dëkk Arimate; ku bare alal la woon. |
24296 | MRK 1:12 | Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma. |
24302 | MRK 1:18 | Ci saa si ñu bàyyi seeni mbaal, topp ci moom. |
24305 | MRK 1:21 | Gannaaw loolu ñu dem Kapernawum. Ca bésub noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jàngu bi, di leen jàngal. |
24316 | MRK 1:32 | Ca ngoon sa nag, bi jant sowee, ñu indil Yeesu ñi wopp ñépp ak ñi rab jàpp ñépp, |
24319 | MRK 1:35 | Ca njël laata bët di set, Yeesu jóg dem ca bérab bu wéet, di fa ñaan Yàlla. |
24326 | MRK 1:42 | Ca saa sa ngaanaam daldi deñ, mu wér. |
24339 | MRK 2:10 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu mu ne làggi ba: |
24341 | MRK 2:12 | Ca saa sa mu jël basaŋam te génn fa kanam ñépp. Noonu ñépp waaru, di màggal Yàlla naan: «Lu mel ni lii, masunu koo gis.» |
24362 | MRK 3:5 | Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ. |
24363 | MRK 3:6 | Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu. |