23216 | MAT 1:3 | Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram; |
23222 | MAT 1:9 | Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya; |
23223 | MAT 1:10 | Esekiya Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas; |
23226 | MAT 1:13 | miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor; |
23227 | MAT 1:14 | Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd; |
23228 | MAT 1:15 | Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba; |
23236 | MAT 1:23 | «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» |
23239 | MAT 2:1 | Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. |
23241 | MAT 2:3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. |
23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |
23250 | MAT 2:12 | Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew. |
23251 | MAT 2:13 | Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» |
23253 | MAT 2:15 | Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.» |
23254 | MAT 2:16 | Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon. |
23257 | MAT 2:19 | Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra, |
23260 | MAT 2:22 | Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile. |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23292 | MAT 4:14 | Noonu am la ñu waxoon, jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: |
23431 | MAT 8:17 | Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan: «Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.» |
23575 | MAT 12:17 | Def na noonu, ngir amal la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: |
23622 | MAT 13:14 | Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan: “Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara. |
23667 | MAT 14:1 | Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am. |
23669 | MAT 14:3 | Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam, |
23671 | MAT 14:5 | Erodd nag bëgg koo rey, waaye dafa ragal nit ñi, ci li ñu teg Yaxya ab yonent. |
23672 | MAT 14:6 | Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd, |
23674 | MAT 14:8 | Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.» |
23709 | MAT 15:7 | Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan: |
23957 | MAT 22:16 | Noonu ñu yónni ci moom seeni taalibe ak ñi far ak buur bi Erodd ne ko: «Kilifa gi, xam nanu ne ku wóor nga, te ragaloo kenn, ndaxte seetuloo jëmmi nit, waaye dangay xamle yoonu Yàlla ci bu wóor. |
24244 | MAT 27:46 | Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?» |
24286 | MRK 1:2 | Bind nañu ci téereb yonent Yàlla Esayi naan: «Maa ngi yónni sama ndaw ci sa kanam, mu xàllal la sa yoon. |
24363 | MRK 3:6 | Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu. |
24490 | MRK 6:14 | Noonu Erodd buur bi dégg loolu, ndaxte turu Yeesu siiwoon na. Mu ne nag: «Yaxya dekki na, moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.» |
24492 | MRK 6:16 | Waaye bi ko Erodd déggee, mu ne: «Yaxya male ma dagglu boppam, moom moo dekki.» |
24493 | MRK 6:17 | Fekk Erodd yónnee woon na, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam. |
24495 | MRK 6:19 | Moo tax Erojàdd ëmbal ko mer, ba bëgg koo rey, waaye manu koo def. |
24496 | MRK 6:20 | Ndaxte Erodd dafa ragal Yaxya, ba sàmm bakkanam, xam ne ku jub la te sell. Bu ko daan déglu it, day jaaxle lool, teewul mu bég ci déglu ko. |
24497 | MRK 6:21 | Noonu bés bu yell ñëw, ba Erodd doon màggal bésu juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile. |
24498 | MRK 6:22 | Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.» |
24538 | MRK 7:6 | Yeesu ne leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee: “Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma. |
24566 | MRK 7:34 | Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki «Ubbikuleen.» |
24584 | MRK 8:15 | Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.» |
24755 | MRK 12:13 | Bi loolu amee ñu yónni ci Yeesu ay Farisen ak ñu far ak buur bi Erodd, ngir fiir ko ci waxam. |
24929 | MRK 15:34 | Ci tisbaar nag Yeesu wootee kàddu gu dëgër naan: «Elowi, Elowi, lema sabaktani?» liy tekki: «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?» |
24967 | LUK 1:5 | Ca jamonoy Erodd, mi nekkoon buur ca réewu Yawut ya, amoon na sarxalkat bu ñu tudde Sakari te bokk ca mbootaayu sarxalkat, ya askanoo ci Abiya. Soxnaam Elisabet askanoo moom itam ci Aaróona. |
24969 | LUK 1:7 | Waaye amuñu doom, ndaxte Elisabet manula am doom, te it fekk ñoom ñaar ñépp ay màggat lañu. |
24975 | LUK 1:13 | Waaye malaaka ma ne ko: «Bul ragal dara Sakari, ndaxte sa ñaan nangu na. Elisabet sa soxna dina la jural doom, te dinga ko tudde Yaxya. |
24986 | LUK 1:24 | Bi mbir yooyu weesoo, Elisabet soxnaam ëmb, di ko nëbb lu mat juróomi weer |
24988 | LUK 1:26 | Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile. |
24998 | LUK 1:36 | Elisabet sa mbokk mi it dina am doom ju góor cig màggatam. Ki ñu doon wooye ku manula am doom, mu ngi ci juróom benni weeram. |
25002 | LUK 1:40 | Mu dugg ca kër Sakari, daldi nuyu Elisabet. |
25003 | LUK 1:41 | Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet. |
25004 | LUK 1:42 | Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb! |
25018 | LUK 1:56 | Noonu Maryaama toog fa Elisabet lu wara tollook ñetti weer, sooga ñibbi. |
25019 | LUK 1:57 | Gannaaw loolu jamono ji Elisabet wara mucc agsi, mu daldi jur doom ju góor. |
25095 | LUK 3:1 | Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen. |
25098 | LUK 3:4 | Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar. |
25113 | LUK 3:19 | Waaye Yaxya yedd na Erodd boroom diiwaanu Galile, ndaxte dafa takkoon Erojàdd jabaru magam, te it boole woon na ci yeneen ñaawteef, |
25117 | LUK 3:23 | Bi Yeesu di tàmbali liggéeyam, amoon na lu wara tollu ci fanweeri at, di doomu Yuusufa ci bëti nit ñi. Te Yuusufa mooy doomu Eli, |
25119 | LUK 3:25 | Yuusufa, Matacas; Amos; Naxum; Esli; Nagayi. |
25122 | LUK 3:28 | Neri, Melki; Adi; Kosam; Elmadam; Er. |
25123 | LUK 3:29 | Er, Yeesu; Eliyeser; Yorim; Matat; Lewi; |
25124 | LUK 3:30 | Simeyon; Yuda; Yuusufa; Yonam; Eliyakim. |
25125 | LUK 3:31 | Eliyakim, Meleya; Meleya, Mena; Mena, Matata; Matata, Natan; Natan, Daawuda. |
25127 | LUK 3:33 | Nason; Aminadab; Aminadab, Admin; Arni; Esron; Peres; Yuda; |
25129 | LUK 3:35 | Serug; Rew; Peleg; Eber; Sela. |
25131 | LUK 3:37 | Lemeg, Matusalem; Enog, Yeredd; Maleleel; Kaynan; |
25132 | LUK 3:38 | Enos; Set; Set doomu Aadama; Aadama doomu Yàlla. |
25149 | LUK 4:17 | Ñu jox ko téereb yonent Yàlla Esayi. Bi mu ko ubbee, mu gis bérab, ba ñu bind aaya yii: |
25317 | LUK 8:3 | Sànn, soxnas ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem. |
25377 | LUK 9:7 | Bi Erodd boroom diiwaanu Galile déggee li Yeesu ak ay taalibeem doon def lépp, mu jaaxle, ndaxte amoon na, ñu doon wax ci mbiri Yeesu naan: «Yaxya moo dekki.» |
25379 | LUK 9:9 | Waaye Erodd ne: «Yaxya, man mii maa dagglu boppam. Kon kii ma dégg ay jalooreem, mooy kan?» Noonu mu koy fexee gis. |
25618 | LUK 13:31 | Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.» |
26011 | LUK 23:7 | Bi mu yégee ne Yeesoo ngi nekk ci diiwaan bi Erodd yilif, mu yónnee ko Erodd, mi nekkoon ci jamono jooju ci Yerusalem. |
26012 | LUK 23:8 | Bi Erodd gisee Yeesu, mu am mbég mu réy. Bu yàgg ba tey dafa koo bëggoona gis, ndaxte déggoon na ñuy wax ci ay mbiram te yaakaaroon na ne dina ko gis mu def kéemaan. |
26015 | LUK 23:11 | Noonu Erodd ak ay xarekatam toroxal Yeesu, di ko ñaawal. Gannaaw loolu mu solal ko mbubb mu rafet, delloo ko Pilaat. |
26016 | LUK 23:12 | Erodd ak Pilaat dañoo ñi bañante woon bu jëkk, waaye ca bés booba doon nañu ay xarit. |
26019 | LUK 23:15 | Erodd itam gisul tooñ gu mu def, ndegam mu yónneewaat nu ko. Nit kii deful genn tooñ gu jar ñu koy rey. |
26073 | LUK 24:13 | Ca bés boobu ñaar ci taalibe yi di dem ci dëkku Emayus, te mu sore Yerusalem ci lu mat fukki kilomet. |
26136 | JHN 1:23 | Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”» |
26646 | JHN 11:54 | Taxoon na ba Yeesu dootul doxantu ci biir Yawut ya. Noonu mu dem ca gox bu jege màndiŋ ma, ca dëkku Efrayim. Foofa nag la toog ak ay taalibeem. |
26687 | JHN 12:38 | ngir li yonent Yàlla Esayi waxoon am: «Boroom bi, ana ku gëm sunu waare? Kan la Boroom bi won dooleem?» |
26688 | JHN 12:39 | Manuñu woona gëm, ndaxte Esayi dafa waxaat ne: |
26690 | JHN 12:41 | Esayi dafa wax loolu, ndaxte gisoon na ndamu Yeesu te mi ngi doon wax ci ay mbiram. |
27027 | ACT 2:9 | Nun ñi ay Pàrt, waa Medi ak waa Elam, nun ñi dëkk Mesopotami, réewu Yawut yi, Kapados, Pont ak Asi, |
27118 | ACT 4:27 | Ndaxte ci dëgg ci dëkk bii, Erodd ak Poñsë Pilaat ànd ak xeeti àddina ak bànni Israyil, likkoo nañu, ngir daaneel sa Ndaw lu sell li nga fal, di Yeesu, |
27175 | ACT 6:5 | Lii ñu wax nag neex na mbooloo mépp. Noonu ñu tànn Ecen, di nit ku fees ak ngëm ak Xel mu Sell mi, boole ci Filib ak Porokor, teg ca Nikanor, Timon, Parmenas ak Nikolas, mi juddoo Ancos te tuub ci yoonu Yawut ya. |
27178 | ACT 6:8 | Naka noona Ecen, mi fees ak yiw ak kàttan, di def ay kéemaan yu mag ak ay firnde ca nit ña. |
27179 | ACT 6:9 | Waaye ay nit jóg, bokk ci jàngu, bi ñuy wax Jàngub ñi ñu goreel, di ay niti dëkki Siren ak Alegsàndiri, ak it waa diiwaani Silisi ak Asi. Ñuy werante ak Ecen, |
27187 | ACT 7:2 | Ecen ne ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan. |
27240 | ACT 7:55 | Waaye Ecen, mi fees ak Xel mu Sell mi, ne jàkk ci asamaan, gis ndamu Yàlla, te gis Yeesu mi taxaw ci ndijooru Yàlla. |
27244 | ACT 7:59 | Noonu ñu dóor Ecen ay doj, muy ñaan Yàlla ne: «Boroom bi Yeesu, nangul sama ruu!» |