23268 | MAT 3:7 | Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
23296 | MAT 4:18 | Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
23303 | MAT 4:25 | Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan. |
23323 | MAT 5:20 | Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23426 | MAT 8:12 | Waaye ñi waroona bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.» |
23431 | MAT 8:17 | Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan: «Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.» |
23438 | MAT 8:24 | Ca saa sa ngelaw lu bare daldi yëngal dex ga, ba duus ya sàng gaal ga. Fekk booba Yeesu nelaw. |
23444 | MAT 8:30 | Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. |
23450 | MAT 9:2 | Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.» |
23459 | MAT 9:11 | Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» |
23462 | MAT 9:14 | Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?» |
23482 | MAT 9:34 | Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
23488 | MAT 10:2 | Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam; |
23489 | MAT 10:3 | Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade; |
23494 | MAT 10:8 | Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen. |
23560 | MAT 12:2 | Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi.» |
23562 | MAT 12:4 | Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; sarxalkat rekk a ko sañoona lekk. |
23568 | MAT 12:10 | te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésub noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko. |
23572 | MAT 12:14 | Farisen ya génn nag, daldi gise, ngir fexee reylu Yeesu. |
23582 | MAT 12:24 | Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.» |
23596 | MAT 12:38 | Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.» |
23635 | MAT 13:27 | «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?” |
23644 | MAT 13:36 | Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.» |
23658 | MAT 13:50 | sànni leen ci sawara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.» |
23669 | MAT 14:3 | Ndaxte Erodd jàppoon na Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam, |
23681 | MAT 14:15 | Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu mana lekk?» |
23703 | MAT 15:1 | Ca jamono jooja amoon na bés ay Farisen ak ay xutbakat jóge Yerusalem, ñëw ci Yeesu ne ko: |
23714 | MAT 15:12 | Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?» |
23717 | MAT 15:15 | Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.» |
23742 | MAT 16:1 | Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.» |
23747 | MAT 16:6 | Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23752 | MAT 16:11 | Kon nag lu tax xamuleen ne waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23753 | MAT 16:12 | Noonu ñu xam ne, Yeesu waxul woon lawiiru mburu, waaye ñu moytu njànglem Farisen ya ak Sadusen ya. |
23754 | MAT 16:13 | Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?» |
23803 | MAT 18:7 | «Yaw àddina, dinga torox ndax say fiir yiy yóbbe nit bàkkaar. Fiir manta ñàkk, waaye toroxte dal na nit ki koy lal. |
23824 | MAT 18:28 | «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.” |
23834 | MAT 19:3 | Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase soxnaam, saa su ko neexee?» |
23838 | MAT 19:7 | Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox soxnaam kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?» |
23891 | MAT 20:30 | Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23940 | MAT 21:45 | Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya dégg nañu léebam yooyu, ñu xam ne ñoom lay wax. |
23954 | MAT 22:13 | Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.” |
23956 | MAT 22:15 | Booba Farisen ya dem gise, ba xam lu ñu wara def, ngir fiir Yeesu ci waxam. |
23975 | MAT 22:34 | Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje. |
23982 | MAT 22:41 | Bi Farisen ya dajee nag, Yeesu laaj leen: |
23989 | MAT 23:2 | «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa. |
24000 | MAT 23:13 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci. |
24002 | MAT 23:15 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon. |
24010 | MAT 23:23 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des. |
24012 | MAT 23:25 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal. |
24013 | MAT 23:26 | Farisen yu gumba yi! Jëkkleena setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set. |
24014 | MAT 23:27 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk. |
24016 | MAT 23:29 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi. |
24054 | MAT 24:28 | Fa médd nekk, fa la tan yiy dajee. |
24077 | MAT 24:51 | Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu. |
24079 | MAT 25:2 | Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel. |
24107 | MAT 25:30 | Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.” |
24140 | MAT 26:17 | Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru bésu Mucc ba?» |
24171 | MAT 26:48 | Fekk Yudaa moomu joxoon na leen tegtal ne leen: «Ki may fóon, moom la; jàppleen ko.» |
24207 | MAT 27:9 | Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njég li bànni Israyil xayma woon ci nit ki; |
24214 | MAT 27:16 | Fekk booba amoon nañu ku ñu tëjoon, ku siiw te tudd Barabas. |
24259 | MAT 27:61 | Fekk Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des ñoo fa toogoon janook bàmmeel ba. |
24260 | MAT 27:62 | Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat. |
24266 | MAT 28:2 | Fekk suuf yëngu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw. |
24314 | MRK 1:30 | Fekk gorob Simoŋ bu jigéen tëdd wopp ak yaram wu tàng; ñu daldi ko yégal Yeesu. |
24335 | MRK 2:6 | Fekk ay xutbakat toog fa, ñu di werante ci seen xel naan: |
24345 | MRK 2:16 | Waaye xutbakat yi bokk ci Farisen yi, bi ñu gisee ne dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar, ñu daldi laaj taalibe yi: «Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» |
24347 | MRK 2:18 | Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?» |
24353 | MRK 2:24 | Noonu Farisen ya ne Yeesu: «Gisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi?» |
24359 | MRK 3:2 | Am na fa nag ay Farisen, ñuy xool Yeesu, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu man koo tuumaal. |
24363 | MRK 3:6 | Ca saa sa nag Farisen ya génn, daldi gise ak ñi far ak buur bi Erodd, ngir fexe koo reylu. |
24364 | MRK 3:7 | Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko. |
24368 | MRK 3:11 | Fekk booba képp ku rab jàpp ku ko gis, daanu fa kanamam di yuuxu naan: «Yaa di Doomu Yàlla.» |
24373 | MRK 3:16 | Fukk ak ñaar ñii la tànn: Simoŋ, mi mu tudde Piyeer, |
24375 | MRK 3:18 | Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; |
24389 | MRK 3:32 | Fekk booba mbooloo nga toog, wër ko. Ñu ne ko nag: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi taxaw ci biti, di la laaj.» |
24430 | MRK 4:38 | Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?» |
24444 | MRK 5:11 | Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. |
24453 | MRK 5:20 | Noonu waa ji dem ci diiwaanu Fukki dëkk yi, daldi fa yégle la ko Yeesu defal, ba ñépp waaru. |
24493 | MRK 6:17 | Fekk Erodd yónnee woon na, jàpp Yaxya, yeew ko, tëj. Ndaxte Erodd takkoon na Erojàdd jabaru Filib magam. |
24511 | MRK 6:35 | Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. |
24533 | MRK 7:1 | Amoon na bés nag, ay Farisen ak ay xutbakat yu jóge Yerusalem ñëw ci Yeesu. |
24535 | MRK 7:3 | Farisen yi nag ñoom ak Yawut yi yépp dañuy topp aaday yoon, yi maam yi tëral, te fandee leen gënal lekk ak loxo yu ñu raxasul. |
24537 | MRK 7:5 | Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?» |
24558 | MRK 7:26 | fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam. |
24563 | MRK 7:31 | Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi. |
24564 | MRK 7:32 | Foofa ñu indil ko ku tëx te dër lool, ñaan ko mu teg ko loxo. |
24580 | MRK 8:11 | Noonu Farisen yi ñëw, di werante ak moom; ñu fexe koo fiir, ba laaj ko kéemaan gu jóge ci asamaan tey firndeel yónnentam. |
24584 | MRK 8:15 | Noonu Yeesu artu leen ne: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen yi ak ñi far ak buur bi Erodd.» |
24588 | MRK 8:19 | bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.» |
24591 | MRK 8:22 | Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko. |
24596 | MRK 8:27 | Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?» |
24609 | MRK 9:2 | Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam; |
24613 | MRK 9:6 | Fekk xamul lu muy wax, ndaxte tiitaange jàpp na leen ñoom ñett ñépp. |
24655 | MRK 9:48 | Foofa: “Sax ya duñu dee mukk, te sawara sa du fey.” |
24659 | MRK 10:2 | Noonu ay Farisen ñëw ci moom, lalal ko fiir, ñu laaj ko: «Ndax jaadu na, nit fase soxnaam?» |
24755 | MRK 12:13 | Bi loolu amee ñu yónni ci Yeesu ay Farisen ak ñu far ak buur bi Erodd, ngir fiir ko ci waxam. |