23260 | MAT 2:22 | Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile. |
23271 | MAT 3:10 | Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si. |
23274 | MAT 3:13 | Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan. |
23286 | MAT 4:8 | Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. |
23290 | MAT 4:12 | Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile. |
23291 | MAT 4:13 | Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. |
23293 | MAT 4:15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali, di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan, yaw Galile, réewum ñi dul Yawut— |
23296 | MAT 4:18 | Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
23301 | MAT 4:23 | Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngle ci seeni jàngu tey yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña, |
23303 | MAT 4:25 | Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan. |
23328 | MAT 5:25 | «Gaawala juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeena egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la. |
23403 | MAT 7:18 | Garab gu baax manula meññ doom yu bon, naka itam garab gu bon manula meññ doom yu neex. |
23404 | MAT 7:19 | Garab gu nekk gu dul meññ doom yu neex, dees na ko gor, sànni ko ca sawara sa. |
23419 | MAT 8:5 | Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko, |
23428 | MAT 8:14 | Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng. |
23442 | MAT 8:28 | Bi Yeesu jàllee nag, ba teer ca diiwaanu waa Gadara, ñaar ñu rab jàpp daldi génn ca sëg ya, ñëw kar ko. Ñaar ñooñu nag, ñu soxor lañu woon, ba kenn ñemewul woona jaar foofa. |
23458 | MAT 9:10 | Gannaaw ga Yeesu doon lekk ca kër ga, te ay juutikat ak i boroom bàkkaar yu bare dikk, bokk lekk ak Yeesu ak taalibeem ya. |
23462 | MAT 9:14 | Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?» |
23472 | MAT 9:24 | Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal. |
23501 | MAT 10:15 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu. |
23530 | MAT 11:2 | Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem, |
23533 | MAT 11:5 | Gumba yaa ngi gis, lafañ yiy dox, gaana yi wér, tëx yiy dégg, ñi dee di dekki, te néew doole ñaa ngi dégg xibaaru jàmm bi. |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23548 | MAT 11:20 | Gannaaw loolu Yeesu daldi gëdd dëkk, ya mu defe woon la ëpp cay kéemaanam, ndaxte tuubuñu seeni bàkkaar. |
23560 | MAT 12:2 | Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi.» |
23635 | MAT 13:27 | «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?” |
23667 | MAT 14:1 | Ca jamono joojale Erodd boroom diiwaanu Galile dégg na tur, wa Yeesu am. |
23687 | MAT 14:21 | Gannaaw jigéen ña ak gone ya, góor ña doon lekk matoon nañu juróomi junni. |
23715 | MAT 15:13 | Yeesu ne leen: «Garab gu sama Baay bi ci kaw jiwul, dees na ko buddi. |
23723 | MAT 15:21 | Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon. |
23731 | MAT 15:29 | Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, ñëw ci weti dexu Galile; mu yéeg ca aw tund, toog fa. |
23734 | MAT 15:32 | Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.» |
23740 | MAT 15:38 | Gannaaw jigéen ñi ak gone yi, góor ñi ci lekk matoon nañu ñeenti junni. |
23746 | MAT 16:5 | Gannaaw loolu taalibe yi jàllaat dex gi, fekk fàtte nañoo yóbbaale mburu. |
23765 | MAT 16:24 | Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man. |
23791 | MAT 17:22 | Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi; |
23793 | MAT 17:24 | Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?» |
23832 | MAT 19:1 | Bi nga xamee ne Yeesu wax na loolu ba noppi, mu jóge Galile, dem ci wàllu réewu Yawut yi, gi féete ci gannaaw dexu Yurdan. |
23844 | MAT 19:13 | Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen. |
23871 | MAT 20:10 | Gannaaw ga nag ñi mu jëkka jël ñëw, yaakaar ne dinañu jot lu ëpp loolu, waaye ñoom itam ñu jot ku nekk benn denariyon. |
23878 | MAT 20:17 | Gannaaw loolu Yeesu di dem Yerusalem, ànd ak fukki taalibe yi ak ñaar. Noonu mu wéetoo ak ñoom, di leen xamal ci yoon wi lii: |
23890 | MAT 20:29 | Gannaaw loolu Yeesu génn Yeriko, te mbooloo mu bare topp ko. |
23896 | MAT 21:1 | Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya jege woon nañu Yerusalem, ba agsi dëkku Betfase ci wetu tundu Oliw ya. Noonu Yeesu yebal ñaari taalibe, |
23906 | MAT 21:11 | Mbooloo ma ne leen: «Kii moo di yonentu Yàlla Yeesu, bi jóge Nasaret ci Galile.» |
23918 | MAT 21:23 | Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngle. Bi muy jàngle nag sarxalkat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?» |
23925 | MAT 21:30 | Gannaaw gi, baay ba ñëw ca tofo ba, wax ko noonu. Mu ne ko: “Waaw,” waaye demul.» |
23942 | MAT 22:1 | Gannaaw loolu Yeesu nettali leen beneen léeb ne leen: |
23968 | MAT 22:27 | Gannaaw ñoom ñépp, jigéen ja faatu. |
23975 | MAT 22:34 | Gannaaw gi, Farisen ya yég nañu ne yey na Sadusen ya. Kon nag ñu daldi daje. |
23986 | MAT 22:45 | Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?» |
23988 | MAT 23:1 | Gannaaw loolu Yeesu waxoon na mbooloo ma ak taalibeem ya ne leen: |
24006 | MAT 23:19 | Gumba yi! Lan moo gëna màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell? |
24055 | MAT 24:29 | «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yëngu. |
24088 | MAT 25:11 | Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” |
24096 | MAT 25:19 | «Gannaaw diir bu yàgg njaatigeb surga ya délsi, daldi leen laaj alalam. |
24098 | MAT 25:21 | Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” |
24100 | MAT 25:23 | Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” |
24101 | MAT 25:24 | «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul. |
24103 | MAT 25:26 | Waaye njaatigeem ne ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul, |
24118 | MAT 25:41 | «Gannaaw loolu dina wax ñi ci càmmoñam: “Soreleen ma yéen ñi alku, te dem ci sawara su dul fey, si ñu sàkkal Seytaane ak ay malaakaam. |
24150 | MAT 26:27 | Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen: «Yéen ñépp naanleen ci, |
24153 | MAT 26:30 | Gannaaw loolu ñu woy Yàlla, ba noppi génn, dem ca tundu Oliw ya. |
24155 | MAT 26:32 | Waaye bu ma dekkee, dinaa leen jiituji Galile.» |
24186 | MAT 26:63 | Waaye Yeesu ne cell. Sarxalkat bu mag ba ne ko: «Giñloo naa la ci Yàlla miy dund, nga wax nu, ndax yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla ji.» |
24192 | MAT 26:69 | Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.» |
24209 | MAT 27:11 | Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanam boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» |
24221 | MAT 27:23 | Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!» |
24231 | MAT 27:33 | Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.» |
24241 | MAT 27:43 | Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”» |
24253 | MAT 27:55 | Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dànd, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo. |
24261 | MAT 27:63 | Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.” |
24265 | MAT 28:1 | Gannaaw bésub noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba. |
24271 | MAT 28:7 | te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.» |
24274 | MAT 28:10 | Yeesu ne leen: «Buleen tiit, waaye demleen yégal samay bokk, ñu dem Galile; foofa lañu may gise.» |
24280 | MAT 28:16 | Noonu fukki taalibe ya ak benn dem ci biir Galile, ca tund wa leen Yeesu digaloon. |
24293 | MRK 1:9 | Booba Yeesu jóge na dëkku Nasaret ci diiwaanu Galile, ñëw, Yaxya sóob ko ci dexu Yurdan. |
24298 | MRK 1:14 | Bi nga xamee ne jàpp nañu Yaxya, Yeesu dem ca diiwaanu Galile, di waare xibaaru jàmm bu Yàlla bi, |
24300 | MRK 1:16 | Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
24305 | MRK 1:21 | Gannaaw loolu ñu dem Kapernawum. Ca bésub noflaay nag Yeesu daldi dugg ci jàngu bi, di leen jàngal. |
24312 | MRK 1:28 | Noonu turam daldi siiw ci diiwaani Galile gépp. |
24323 | MRK 1:39 | Noonu mu wër ci diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, tey dàq rab yi. |
24342 | MRK 2:13 | Gannaaw loolu Yeesu génnaat, aw booru dex ga, mbooloo mépp di ñëw ci moom, mu di leen jàngal. |
24353 | MRK 2:24 | Noonu Farisen ya ne Yeesu: «Gisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi?» |
24364 | MRK 3:7 | Gannaaw loolu Yeesu ak ay taalibeem jóge fa, jëm dex ga. Fekk mbooloo mu mag mu jóge diiwaanu Galile, topp ko. |
24370 | MRK 3:13 | Gannaaw loolu Yeesu yéeg ci tund wi, woo ñi ko neex, ñu daldi ñëw ci moom. |
24402 | MRK 4:10 | Gannaaw loolu ba Yeesu nekkee fu wéet, fukki taalibe ak ñaar ña, ak ñeneen ñu daan ànd ak ñoom, laaj ko ci mbirum léeb yi. |
24438 | MRK 5:5 | Guddi ak bëccëg mu nga woon ca sëg ya ak ca tund ya, di yuuxu te jam yaramam ak ay xeer. |
24469 | MRK 5:36 | Waaye Yeesu jàppul wax jooju; mu ne njiit la: «Gëmal rekk te baña tiit.» |
24497 | MRK 6:21 | Noonu bés bu yell ñëw, ba Erodd doon màggal bésu juddoom; mu woo ca xew wa ay jaraafam ak kilifay xare ba ak njiiti diiwaanu Galile. |
24506 | MRK 6:30 | Gannaaw loolu ndaw yi dajaloo ci wetu Yeesu, nettali li ñu def ak li ñu jàngle lépp. |
24556 | MRK 7:24 | Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, jëm weti dëkku Tir. Bi mu fa eggee, mu dugg ci kër, te bëggul kenn xam ko, waaye jataayam manula umpe. |
24558 | MRK 7:26 | fekk jigéen ja ci xeetu Gereg la bokkoon, juddoo wàlli Fenisi ci diiwaanu Siri. Noonu jigéen ja ñaan ko, mu dàq rab wi ci doomam. |
24563 | MRK 7:31 | Bi loolu amee Yeesu jóge na weti Tir, jaar ci wàlli dëkku Sidon, dem dexu Galile, ba noppi dugg ci biir diiwaan, bi ñuy wax Fukki dëkk yi. |
24591 | MRK 8:22 | Gannaaw loolu ñu ñëw ci Betsayda. Foofa ñu indil Yeesu ku gumba, di ko ñaan, mu laal ko. |
24593 | MRK 8:24 | Waa ji xool ne ko: «Gis naa ay nit, ñu mel ni ay garab, te ñu ngi dox.» |
24631 | MRK 9:24 | Ci saa si baayu xale bi wax ci kaw naan: «Gëm naa, dàqal ma sama ngëmadi.» |
24632 | MRK 9:25 | Yeesu gis nag ne, mbooloo maa ngi daw, wërsi ko, mu daldi gëdd rab wi nag ne ko: «Génnal ci moom, yaw rab wu luu te tëx, te bu ko jàppaat; wax naa la ko.» |
24637 | MRK 9:30 | Bi loolu amee ñu jóge fa, jaar ci diiwaanu Galile, Yeesu bëggul kenn yég ko. |