Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   I    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23214  MAT 1:1  Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
23215  MAT 1:2  Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
23218  MAT 1:5  Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi,
23230  MAT 1:17  Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
23244  MAT 2:6  “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
23258  MAT 2:20  ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
23259  MAT 2:21  Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
23270  MAT 3:9  te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
23340  MAT 5:37  Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
23424  MAT 8:10  Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii.
23425  MAT 8:11  Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23481  MAT 9:33  Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, masuñu koo gis ci Israyil.»
23490  MAT 10:4  Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nara wor Yeesu.
23492  MAT 10:6  Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar.
23509  MAT 10:23  Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen mana wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
23542  MAT 11:14  Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Ilyaas bi waroona ñëw.
23627  MAT 13:19  Boo xamee ne nit mu ngi déglu wax ju jëm ci nguuru Yàlla te xamu ko, Ibliis day ñëw, këf li ñu def ci xolam; kooku mooy ki jot ci jiwu wi ci kaw yoon wi.
23646  MAT 13:38  àddina mooy tool bi; ñi bokk ci nguuru Yàlla ñoo di jiwu wu baax wi; ñi bokk ci Ibliis ñooy jëmb bi;
23674  MAT 14:8  Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.»
23684  MAT 14:18  Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii
23726  MAT 15:24  Yeesu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xari bànni Israyil yu réer.»
23733  MAT 15:31  Nit ñépp waaru, ndaxte gis nañu luu yuy wax, làggi yu wér, lafañ yuy dox, ak gumba yuy gis. Ñu daldi màggal Yàlla Buuru Israyil.
23755  MAT 16:14  Taalibe yi ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Ilyaas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi
23772  MAT 17:3  Naka noonu ñu gis yonenti Yàlla Musaa ak Ilyaas, di waxtaan ak Yeesu.
23773  MAT 17:4  Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.»
23779  MAT 17:10  Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Ilyaas mooy jëkka ñëw?»
23780  MAT 17:11  Yeesu ne leen: «Waaw, dëgg la, Ilyaas war na ñëw, jubbanti lépp.
23781  MAT 17:12  Teewul maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nara sonal léegi Doomu nit ki
23785  MAT 17:16  Indi naa ko ci say taalibe, waaye manuñu koo faj.»
23786  MAT 17:17  Noonu Yeesu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen di wara muñal?» Mu ne leen: «Indil-leen ma xale bi fii
23859  MAT 19:28  Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, bés baa ngi ñëw bu Yàllay yeesalaat lépp, te Doomu nit ki toog ci jalam, bi soloo ndam. Bés boobu nag, yéen ñi ma topp dingeen toog ci fukki jal ak ñaar, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.
23973  MAT 22:32  “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.»
24137  MAT 26:14  Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya,
24207  MAT 27:9  Noonu la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Yeremi am, bi mu naan: «Fab nañu fanweeri poseti xaalis ya, mooy njég li bànni Israyil xayma woon ci nit ki;
24240  MAT 27:42  «Waa jii musal na ñeneen te manula musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko.
24245  MAT 27:47  Ñenn ña ca ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.»
24247  MAT 27:49  Waaye ña ca des ne: «Bàyyil, nu seet ba xam Ilyaas dina ñëw, musal ko.»
24365  MRK 3:8  Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon.
24376  MRK 3:19  ak Yudaa Iskariyo mi nara wor Yeesu.
24491  MRK 6:15  Ñeneen ne: «Kii Ilyaas la.» Ñi ci des ne: «Yonent la, bu mel ni yonent yu jëkk ya.»
24597  MRK 8:28  Ñu ne ko: «Am na ñuy ne yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yi
24611  MRK 9:4  Noonu ñu gis yonenti Yàlla Ilyaas ak Musaa, di wax ak Yeesu.
24612  MRK 9:5  Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.»
24618  MRK 9:11  Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Ilyaas moo wara jëkka ñëw?»
24619  MRK 9:12  Yeesu ne leen: «Waaw, Ilyaas dina jëkka ñëw, jubbanti lépp. Waaye itam lu tax bind nañu ne, Doomu nit ki war na sonn lu bare, ñu xeeb ko, dëddu ko.
24620  MRK 9:13  Waaye maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na, te def nañu ko la leen neex, ni ko Mbind mi waxe.»
24626  MRK 9:19  Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen wara muñal? Indil-leen ma xale bi
24757  MRK 12:15  Waaye Yeesu xam na seen naaféq, mu ne leen: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir? Indil-leen ma posetu denariyon, ma seet.»
24768  MRK 12:26  Te sax li jëm ci mbirum ndekkite, xanaa jànguleen lii Yàlla wax ci Tawreetu Musaa ci saarum ngarab si: “Maay Yàllay Ibraayma, Isaaxa ak Yanqóoba”?
24771  MRK 12:29  Noonu Yeesu ne ko: «Bii: “Dégluleen, yéen bànni Israyil! Yàlla sunu Boroom mooy Boroom bi, te kenn la.
24833  MRK 14:10  Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya, ngir wori Yeesu.
24927  MRK 15:32  Almasi bii, di buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gis ko te gëm.» Ñi ñu daajaale ak moom it di ko xarab.
24930  MRK 15:35  Ñenn ci ña fa taxaw nag, bi ñu ko déggee, ñu ne: «Mu ngi woo yonent Yàlla Ilyaas.»
24931  MRK 15:36  Noonu kenn daw, jël aw sagar, capp ko ci bineegar, mu teg ko ci bant, jox ko ko, mu muucu. Mu ne: «Bàyyileen, nu seet, ba xam Ilyaas dina ñëw, wàcce ko.»
24978  LUK 1:16  Dina delloosi niti Israyil yu bare ci Yàlla seen Boroom.
24979  LUK 1:17  Mooy jiitu, di yégle ñëwug Boroom bi, ànd ak xel mi ak doole, ji yonent Yàlla Ilyaas amoon, ngir jubale xoli baay yi ak doom yi, ngir delloo ñi déggadi ci maanduteg ñi jub. Noonu dina waajal mbooloo muy teeru Boroom bi
25016  LUK 1:54  Wallu na bànni Israyil giy jaamam, di fàttaliku yërmandeem,
25017  LUK 1:55  ni mu ko dige woon sunuy maam, jëmale ko ci Ibraayma ak askanam ba fàww.»
25030  LUK 1:68  «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen!
25035  LUK 1:73  di ngiñ, li mu giñaloon sunu maam Ibraayma naan,
25042  LUK 1:80  Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.
25067  LUK 2:25  Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla wara dëfal bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom,
25074  LUK 2:32  Muy leer giy leeral xeet yi, di ndamu Israyil say gaa.»
25076  LUK 2:34  Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi,
25095  LUK 3:1  Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen.
25102  LUK 3:8  Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii.
25126  LUK 3:32  Daawuda mooy doomu Isayi; Isayi, Obedd; Bowas; Salmon; Nason.
25128  LUK 3:34  Yanqóoba; Isaaxa; Ibraayma; Teraa; Naxor;
25157  LUK 4:25  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ca jamonoy Ilyaas, bi mu tawul lu mat ñetti at ak genn-wàll, te xiif bu metti am ca réew mépp, amoon na ca Israyil jigéen yu bare yu seen jëkkër faatu.
25158  LUK 4:26  Moona Yàlla yónniwul Ilyaas ci kenn ci ñoom, waaye mu yebal ko ci jigéen ju jëkkëram faatu, ju dëkk Sarebta, ca wetu Sidon.
25159  LUK 4:27  Te it amoon na ca Israyil, ca jamonoy yonent Yàlla Alyaasa, ay nit ñu bare ñu gaana. Waaye fajul ci kenn ku dul Naamaan, mi dëkkoon réewu Siri
25231  LUK 6:16  Yudaa doomu Saag, ak Yudaa Iskariyo, mi mujja wor.
25273  LUK 7:9  Bi ko Yeesu déggee, mu waaru. Noonu mu walbatiku ca mbooloo, ma topp ci moom, ne leen: «Maa ngi leen koy wax, ci bànni Israyil sax, masuma cee gis ku gëme nii
25378  LUK 9:8  Am it ñuy wax naan: Ilyaas moo délsi. Ñeneen naan: «Kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki
25389  LUK 9:19  Ñu ne ko: «Am na ñu naan, yaa di Yaxya; ñeneen ne, Ilyaas; ñi ci des ne yaay kenn ci yonent yu jëkk yaa dekki
25400  LUK 9:30  Am ñaari nit di waxtaan ak moom, muy yonenti Yàlla Musaa ak Ilyaas.
25403  LUK 9:33  Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» Fekk xamul la mu doon wax.
25411  LUK 9:41  Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen te di leen muñal? Indil ma sa doom.»
25603  LUK 13:16  Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi
25615  LUK 13:28  Foofa dingeen jooy, di yéyu, bu ngeen gisee seeni maam Ibraayma, Isaaxa, Yanqóoba ak yonent yépp ci nguuru Yàlla, te ñu dàq leen ca biti.
25680  LUK 15:23  Indileen sëllu wu duuf wa te rey ko, nu lekk te bànneexu;
25711  LUK 16:22  «Noonu miskin ma dee, malaaka yi yóbbu ko ca wetu Ibraayma. Boroom alal ja itam dee, ñu suul ko.
25712  LUK 16:23  Bi ñu koy mbugal ca sawara, mu téen, séen fu sore Ibraayma ak Lasaar ci wetam.
25713  LUK 16:24  Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci sawara sii!”
25714  LUK 16:25  Ibraayma ne ko: “Sama doom, fàttalikul ne jot nga sa bànneex ci àddina, fekk Lasaar dëkk ci tiis. Looloo tax xolam sedd fii, yaw nag, ngay sonn.
25718  LUK 16:29  Ibraayma ne ko: “Say doomu baay, ñu ngeek yoonu Musaa ak téerey yonent yi. Nañu leen déggal.”
25719  LUK 16:30  Boroom alal ja ne ko: “Déedéet, maam Ibraayma, waaye su kenn dekkee, dem ca ñoom, dinañu tuub seeni bàkkaar.”
25720  LUK 16:31  Waaye Ibraayma ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»
25809  LUK 19:9  Yeesu ne ko: «Mucc gi wàcc na tey ci kër gii, ndaxte nit kii, ci askanu Ibraayma la bokk itam.
25885  LUK 20:37  Te Musaa sax wone na ne, néew yi dinañu dekki, ci saarum ngarab si. Foofa Musaa wooye na fa Boroom bi: “Yàllay Ibraayma, Yàllay Isaaxa, di Yàllay Yanqóoba.”
25936  LUK 22:3  Noonu Seytaane daldi solu Yudaa, mi ñuy wooye Iskariyo te mu bokkoon ca fukki taalibe ya ak ñaar.
25963  LUK 22:30  Dingeen lekkandoo te naanandoo ak man ci sama nguur. Te dingeen toog ci jal yi, di àtte fukki giir ak ñaar yu bànni Israyil.»