23236 | MAT 1:23 | «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» |
23269 | MAT 3:8 | Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, |
23398 | MAT 7:13 | «Jaarleen ci bunt bu xat bi, ndaxte bunt bi ak yoon wi jëm sànku yaatu nañu, te ñi ciy jaar bare. |
23453 | MAT 9:5 | Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gëna yomb? |
23454 | MAT 9:6 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
23557 | MAT 11:29 | Jébbaluleen ci man te jàng ci man, ndaxte lewet naa te woyof, te dingeen am noflaay ci seen xol. |
23638 | MAT 13:30 | Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”» |
23670 | MAT 14:4 | te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.» |
23728 | MAT 15:26 | Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.» |
23736 | MAT 15:34 | Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.» |
23770 | MAT 17:1 | Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool. |
23776 | MAT 17:7 | Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.» |
23789 | MAT 17:20 | Yeesu ne leen: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.» |
23796 | MAT 17:27 | Waaye bëgguma nu naqaral leen; demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkka xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.» |
23916 | MAT 21:21 | Noonu Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen gëmee te baña werante, dingeen def li ma def figg gi, rax-ca-dolli bu ngeen nee tund wale: “Jógal tàbbi ca géej ga,” dina ko def. |
23962 | MAT 22:21 | Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» |
24013 | MAT 23:26 | Farisen yu gumba yi! Jëkkleena setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set. |
24058 | MAT 24:32 | Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. |
24133 | MAT 26:10 | Yeesu nag xam la ñu wax, mu ne leen: «Jigéen ji defal na ma jëf ju rafet; lu tax ngeen di ko sonal? |
24149 | MAT 26:26 | Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen: «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.» |
24169 | MAT 26:46 | Jógleen nu dem; xool-leen, ki may wor a ngi nii, di ñëw.» |
24178 | MAT 26:55 | Booba Yeesu ne mbooloo mi: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. Moona daa naa toog bés bu nekk ca kër Yàlla ga, di jàngle, te jàppuleen ma. |
24204 | MAT 27:6 | Sarxalkat yu mag ya nag fab xaalis ba, naan: «Jaaduwul nu def xaalis bii ci dencukaayu xaalis bi ci kër Yàlla gi, ndaxte njégu deret la.» |
24273 | MAT 28:9 | Ba ñuy dem nag, Yeesu taseek ñoom ne leen: «Maa ngi leen di nuyu.» Jigéen ña jegesi, laxasu cay tànkam, di ko màggal. |
24299 | MRK 1:15 | naan: «Jamono ji mat na, nguuru Yàlla jegesi na; tuubleen seeni bàkkaar te gëm xibaaru jàmm bi.» |
24338 | MRK 2:9 | Lan moo gëna yomb, ma wax ku làggi ki: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma wax ko: “Jógal, jël sa basaŋ, tey dox”? |
24360 | MRK 3:3 | Yeesu ne ku loxoom làggi: «Jógal, taxaw ci kanam ñépp.» |
24445 | MRK 5:12 | Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.» |
24472 | MRK 5:39 | Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.» |
24474 | MRK 5:41 | Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.» |
24494 | MRK 6:18 | Te Yaxya ne ko: «Jaaduwul nga denc sa jabaru mag.» |
24514 | MRK 6:38 | Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am? Demleen seeti.» Ñu dem seeti ne ko: «Juróomi mburu ak ñaari jën.» |
24560 | MRK 7:28 | Jigéen ji ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci lekkukaayu gone yi.» |
24574 | MRK 8:5 | Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.» |
24589 | MRK 8:20 | Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.» |
24609 | MRK 9:2 | Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam; |
24706 | MRK 10:49 | Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» |
24732 | MRK 11:23 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ku ne tund wale: “Jógal, tàbbi ca géej ga,” te nga gëm ne loolu dina am, bañ cee boole xel ñaar, kon sa ñaan nangu. |
24759 | MRK 12:17 | Noonu Yeesu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» Ñu daldi waaru ci mbiram. |
24810 | MRK 13:24 | «Waaye booba, gannaaw metit yooyu: “Jant bi dina lëndëm te weer dootul leer; |
24814 | MRK 13:28 | Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. |
24826 | MRK 14:3 | Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani, mu dem këru Simoŋ ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jigéen ñëw, yor njaq lu ñu defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree bare. Jigéen ji toj njaq li, tuur latkoloñ ci boppu Yeesu. |
24831 | MRK 14:8 | Jigéen ji def na li mu man; diw na sama yaram ak latkoloñ, ngir waajal sama rob, laata moo jot. |
24845 | MRK 14:22 | Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, jox leen ko naan: «Jël-leen, lii sama yaram la.» |
24864 | MRK 14:41 | Ñetteelu yoon mu délsi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. |
24865 | MRK 14:42 | Jógleen nu dem; ki may wor a ngi nii, di ñëw.» |
24871 | MRK 14:48 | Yeesu ne leen: «Jóg ngeen ngir jàpp ma, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. |
24981 | LUK 1:19 | Malaaka ma ne ko: «Man maay Jibril miy taxaw ci kanam Yàlla. Dañu maa yónni ngir ma wax ak yaw te yégal la xibaaru jàmm boobu. |
24988 | LUK 1:26 | Bi Elisabet nekkee ci juróom benni weeram, Yàlla yónni na malaakaam Jibril ca dëkku Nasaret ca diiwaanu Galile. |
24989 | LUK 1:27 | Mu yebal ko ca janq bu ñu may waa ju bokk ci askanu Daawuda te ñu koy wax Yuusufa, waaye àndaguñu. Janq baa ngi tudd Maryaama. |
24990 | LUK 1:28 | Malaaka ma dikk ca moom ne ko: «Jàmm nga am, yaw mi Boroom bi defal aw yiw; mu ngi ak yaw.» |
25000 | LUK 1:38 | Maryaama ne ko: «Jaamub Boroom bi laa. Na Yàlla def ci man li nga wax.» Ci noonu malaaka ma daldi dem. |
25079 | LUK 2:37 | Jëkkër ja gaañu, te séyaatul. Léegi amoon na juróom ñett fukki at ak ñeent. Mi ngi dëkke woona jaamu Yàlla guddi ak bëccëg ca kër Yàlla ga, di ñaan ak di woor. |
25102 | LUK 3:8 | Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar, te baña nax seen bopp naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na defal Ibraayma ay doom ci doj yii. |
25180 | LUK 5:4 | Bi mu jànglee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gëna xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.» |
25199 | LUK 5:23 | Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gëna yomb? |
25205 | LUK 5:29 | Noonu Lewi togglu ay ñam yu bare ci këram, ngir teral Yeesu. Juutikat yu bare ak yeneen gan ñu nga fa woon, di lekkandoo ak ñoom. |
25223 | LUK 6:8 | Waaye Yeesu xam seen xalaat, daldi ne ku loxoom làggi: «Jógal taxaw ci kanam ñépp.» Nit ka daldi jóg taxaw. |
25257 | LUK 6:42 | Nan nga mana waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. |
25317 | LUK 8:3 | Sànn, soxnas ku ñuy wax Kusa, mi doon wottu alalu Erodd; ak Susànn ak ñeneen jigéen. Jigéen ñooñu ñoo doon joxe seen alal, ngir dimbali Yeesu ak ay taalibeem. |
25358 | LUK 8:44 | Jigéen ja jegeñsi Yeesu nag, doxe ko gannaaw, laal catu mbubbam. Ca saa sa deret ji dal. |
25366 | LUK 8:52 | Ña fa nekk ñépp di yuuxu ak di jooy xale bi. Noonu Yeesu ne leen: «Bàyyileen seen jooy yi. Janq bi deewul, day nelaw rekk.» |
25383 | LUK 9:13 | Waaye Yeesu ne leen: «Joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Amunu lu dul juróomi mburu ak ñaari jën. Xanaa ndax nu dem jëndal mbooloo mii lu ñu lekk?» |
25449 | LUK 10:17 | Juróom ñaar fukki taalibe yi ak ñaar délsi, fees ak mbég te naan: «Boroom bi, rab yi sax déggal nañu nu ndax sa tur.» |
25534 | LUK 12:6 | Juróomi picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci ñaari dërëm? Moona Yàlla fàttewul benn ci ñoom. |
25561 | LUK 12:33 | Jaayleen seen alal, sarxe ko, ngir sàkku ay mbuusi xaalis yu dul bënn, maanaam alal ju dul jeex ca laaxira; foofa sàcc du ko jege te max du ko yàq. |
25603 | LUK 13:16 | Jigéen jii nag bokk ci askanu Ibraayma te Seytaane tënk ko fukki at ak juróom ñett, ndax kenn waru koo yiwi ci bésub noflaay bi?» |
25612 | LUK 13:25 | Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” |
25618 | LUK 13:31 | Ca jamono jooja ay Farisen ñëw ca Yeesu ne ko: «Jógeel fii, dem feneen, ndaxte Erodd a ngi lay wuta rey.» |
25631 | LUK 14:9 | Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rusa dem ca toogu bu gannaawe ba. |
25739 | LUK 17:19 | Noonu Yeesu ne ko: «Jógal dem; sa ngëm faj na la.» |
25742 | LUK 17:22 | Noonu mu ne taalibe ya: «Jamono dina ñëw, fu ngeen di bëgga gis su doon sax benn fan ci jamono ju Doomu nit ki di ñëw, waaye dungeen ko gis. |
25770 | LUK 18:13 | «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggula siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”» |
25779 | LUK 18:22 | Bi Yeesu déggee loolu, mu ne ko: «Lenn rekk moo la dese. Jaayal li nga am lépp, séddale ko miskin yi te dinga woomle ca asamaan; boo noppee, nga ñëw topp ci man.» |
25873 | LUK 20:25 | Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.» |
25903 | LUK 21:8 | Yeesu ne: «Moytuleen, bu leen kenn nax. Ndaxte ñu bare dinañu ñëw ci sama tur ne: “Moom laa,” walla ñu naan: “Jamono ji jegesi na.” Buleen topp ñooñu. |
25950 | LUK 22:17 | Noonu mu fab kaas, daldi sant Yàlla ne: «Jël-leen kaas bii, séddoo ko. |
25979 | LUK 22:46 | Noonu mu ne leen: «Lu tax ngeen di nelaw? Jógleen ñaan, ngir baña daanu cig fiir.» |
25985 | LUK 22:52 | Noonu Yeesu ne sarxalkat yu mag ya ak kilifay wottukati kër Yàlla ga ak njiiti xeet, wa ko jàppsi woon: «Jóg ngeen, gànnaayoo jaasi ak yet, mel ni ñuy topp sàcc. |
26032 | LUK 23:28 | Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom. |
26033 | LUK 23:29 | Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi masula jur ak ñi masula nàmpal, barkeel ngeen!” |
26059 | LUK 23:55 | Jigéen ña gungee woon Yeesu Galile, ànd ak Yuusufa, gis bàmmeel ba ak na ñu ca dence néewu Yeesu ba. |
26065 | LUK 24:5 | Jigéen ña am tiitaange ju mag, daldi dëpp seen jë ci suuf. Waaye ñu ne leen: «Lu tax ngeen di seet kiy dund ci biir néew yi? |
26070 | LUK 24:10 | Jigéen ña ñoo doon Maryaamam Magdala, Sànn, ak Maryaama yaayu Saag. Yeneen jigéen yi leen gunge woon itam nettali loolu ndaw ya. |
26180 | JHN 2:16 | daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!» |
26234 | JHN 4:9 | Jigéen ja ne ko: «Yaw, ngay Yawut, man maay jigéen ju dëkk Samari; nan nga ma mana ñaane ndox?» Jigéen ja wax na loolu, ndaxte Yawut ya bokkuñu woon ak waa Samari ndab yu ñuy lekke. |
26236 | JHN 4:11 | Jigéen ja ne ko: «Sang bi, teen bi xóot na te amuloo baag, kon fooy jële ndoxum dund? |
26242 | JHN 4:17 | Jigéen ja ne ko: «Awma jëkkër de.» Yeesu ne ko: «Wax nga dëgg ne amuloo jëkkër, |
26244 | JHN 4:19 | Jigéen ja ne ko: «Sang bi, gis naa ne ab yonent nga. |
26246 | JHN 4:21 | Yeesu ne ko: «Jigéen ji, gëmal lii ma lay wax: dina am jamono joo xam ne du ci tund wale te du ci Yerusalem ngeen di jaamoo Baay bi. |
26250 | JHN 4:25 | Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi —maanaam Kirist— dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.» |
26286 | JHN 5:7 | Jarag ja ne ko: «Sang bi, duma am ku ma sóob ci ndox mi, bu yëngoo; su ma ciy fexee dem, ñu jëkk ma ci.» |
26287 | JHN 5:8 | Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.» |
26290 | JHN 5:11 | Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”» |
26291 | JHN 5:12 | Ñu ne ko nag: «Ku la ne: “Jëlal sa basaŋ te dox”?» |
26306 | JHN 5:27 | Jox na Doom ji itam sañ-sañu àtte, ndaxte mooy Doomu nit ki. |
26315 | JHN 5:36 | «Waaye yor naa ci man seede su gëna mag si ma Yaxya di seedeel: maa ngi def jëf, yi ma Baay biy sant. Jëf yooyu may def nag ñooy seede ne, Baay bi moo ma yónni. |
26355 | JHN 6:29 | Yeesu ne leen: «Jëf ji neex Yàlla, moo di gëm ki mu yónni.» |
26357 | JHN 6:31 | Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”» |
26400 | JHN 7:3 | Noonu rakki Yeesu yu góor ya ne ko: «Jóge fi te dem diiwaanu Yude, ngir say taalibe gis, ñoom itam, jaloore yi ngay def. |