23214 | MAT 1:1 | Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. |
23229 | MAT 1:16 | Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo. |
23230 | MAT 1:17 | Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. |
23231 | MAT 1:18 | Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. |
23242 | MAT 2:4 | Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo. |
23263 | MAT 3:2 | Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.» |
23272 | MAT 3:11 | Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
23278 | MAT 3:17 | Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.» |
23291 | MAT 4:13 | Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. |
23295 | MAT 4:17 | Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.» |
23306 | MAT 5:3 | «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |
23313 | MAT 5:10 | Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |
23322 | MAT 5:19 | Ku tebbi nag ba gëna tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gëna tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23323 | MAT 5:20 | Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23325 | MAT 5:22 | Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara. |
23334 | MAT 5:31 | «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.” |
23343 | MAT 5:40 | Ku la bëgga kalaame, ngir jël sa turki, nga boole ca it sa mbubb mu mag. |
23344 | MAT 5:41 | Ku la ga, nga yenul ko doxub benn kilomet, àndal ak moom ñaar. |
23375 | MAT 6:24 | «Kenn manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal. |
23394 | MAT 7:9 | Kan ci yéen, bu la sa doom ñaanee mburu, nga jox ko doj? |
23397 | MAT 7:12 | «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi. |
23406 | MAT 7:21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. |
23409 | MAT 7:24 | «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj. |
23419 | MAT 8:5 | Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko, |
23425 | MAT 8:11 | Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23433 | MAT 8:19 | Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.» |
23441 | MAT 8:27 | Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?» |
23457 | MAT 9:9 | Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp. |
23477 | MAT 9:29 | Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.» |
23493 | MAT 10:7 | Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.” |
23500 | MAT 10:14 | Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk. |
23512 | MAT 10:26 | Kon nag buleen leen ragal, ndaxte amul dara lu nëbbu, lu ñu warula biral, mbaa luy kumpa lu ñu warula siiwal. |
23517 | MAT 10:31 | Kon buleen ragal dara, yéena gën ndiiraanu ramatu. |
23518 | MAT 10:32 | «Koo xam ne nangu nga ma ci kanam nit ñi, man itam dinaa la nangu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw. |
23523 | MAT 10:37 | Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma. |
23524 | MAT 10:38 | Koo xam ne kii nanguwuloo ñàkk sa bakkan, ba mel ni ku ñu daaj ci bant, te nga topp ma, yeyoowuloo ma. |
23525 | MAT 10:39 | Kuy rawale sa bakkan, ñàkk ko, te ku ñàkk sa bakkan ndax man, jotaat ko. |
23527 | MAT 10:41 | Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub. |
23531 | MAT 11:3 | ne ko: «Ndax yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?» |
23536 | MAT 11:8 | Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur. |
23539 | MAT 11:11 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut. |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23549 | MAT 11:21 | Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. |
23551 | MAT 11:23 | Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey. |
23569 | MAT 12:11 | Yeesu ne leen: «Ku fi amoon xar, mu daanu ci kàmb ci bésub noflaay bi, ndax doo ko jàpp, génne ko? |
23570 | MAT 12:12 | Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésub noflaay bi jaadu na.» |
23576 | MAT 12:18 | «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn, di sama Soppe bi neex sama xol. Dinaa def sama Xel ci moom, muy yégal xeet yi yoonu njub. |
23582 | MAT 12:24 | Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.» |
23585 | MAT 12:27 | Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte. |
23590 | MAT 12:32 | Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira. |
23596 | MAT 12:38 | Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.» |
23599 | MAT 12:41 | Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi. |
23606 | MAT 12:48 | Waaye Yeesu ne ko: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?» |
23619 | MAT 13:11 | Noonu mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko. |
23628 | MAT 13:20 | Ki jot ci jiwu wi ci bérab bu bare ay doj nag, mooy ki dégg wax ji, am ci bànneex bu gaaw; |
23630 | MAT 13:22 | Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg wax ji, waaye soxlay àddina ak naxi alal tanc wax ji, ba du jur njariñ. |
23631 | MAT 13:23 | Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom benn fukk mbaa fanweer.» |
23632 | MAT 13:24 | Noonu Yeesu dégtal leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni nit ku ji jiwu wu baax ci toolam. |
23639 | MAT 13:31 | Yeesu waxaat leen beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni doomu fuddën bu nit jël, ji ko ci toolam. |
23641 | MAT 13:33 | Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.» |
23652 | MAT 13:44 | Yeesu teg ca ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni alal ju nëbbu cib tool. Nit ki ko gis nëbbaat ko; xolam sedd, ba mu dem jaay li mu am lépp, jënd tool ba. |
23653 | MAT 13:45 | «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet. |
23655 | MAT 13:47 | Yeesu waxaat ne: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni mbaal mu ñu wàcce ci géej, mu jàpp jën wu nekk. |
23660 | MAT 13:52 | Yeesu ne leen: «Kon nag xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.» |
23665 | MAT 13:57 | Kon ñu daldi koy xeeb. Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.» |
23668 | MAT 14:2 | Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.» |
23695 | MAT 14:29 | Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu. |
23706 | MAT 15:4 | Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.” |
23707 | MAT 15:5 | Waaye yéen dangeen ne: “Ku wax sa ndey walla sa baay: ‘Li ngeen wara jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,’ |
23724 | MAT 15:22 | Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» |
23744 | MAT 16:3 | Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, waaye manuleena ràññee firndey jamono ji nu tollu. |
23752 | MAT 16:11 | Kon nag lu tax xamuleen ne waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23760 | MAT 16:19 | Dinaa la jox caabiy nguuru Yàlla Aji Kawe ji; li nga yeew ci àddina, dees na ko yeew ci asamaan; li nga yiwi ci àddina dees na ko yiwi ci asamaan.» |
23765 | MAT 16:24 | Gannaaw loolu Yeesu ne taalibeem ya: «Ku bëgga aw ci samay tànk, na bàyyi boppam, te gàddu bant bi ñu ko wara daaj, doora topp ci man. |
23774 | MAT 17:5 | Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» |
23793 | MAT 17:24 | Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?» |
23795 | MAT 17:26 | Piyeer ne ko: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci. |
23797 | MAT 18:1 | Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gëna màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?» |
23799 | MAT 18:3 | ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen waññikuwul ci Yàlla, ba mel niy xale, dungeen dugg mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23800 | MAT 18:4 | Kuy suufeelu nag, ba mel ni xale bii, kooku mooy ki gëna màgg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23819 | MAT 18:23 | «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgga waññ alalam ak ay jaraafam. |
23821 | MAT 18:25 | waaye jaraaf ja amul lu mu feye. Kon nag sangam santaane, ñu jaay ko moom ak soxnaam ak ay doomam ak lépp lu mu am, ngir fey bor ba. |
23822 | MAT 18:26 | Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.” |
23825 | MAT 18:29 | Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.” |
23837 | MAT 19:6 | Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.» |
23843 | MAT 19:12 | Ndaxte am na ñu judduwaale tële, am na ñu tële ci loxoy nit, te am na ñu baña séy ngir nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Ku ko mana nangu, nangu ko.» |
23845 | MAT 19:14 | Bi Yeesu gisee loolu, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, te buleen leen tere, ñu ñëw fi man. Ndaxte ñu mel ni ñoom, ñoo yelloo nguuru Yàlla Aji Kawe ji.» |
23847 | MAT 19:16 | Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def ci lu baax, ngir mana am dund gu dul jeex?» |
23848 | MAT 19:17 | Yeesu ne ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.» |
23854 | MAT 19:23 | Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu! |
23855 | MAT 19:24 | Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.» |
23856 | MAT 19:25 | Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo mana mucc nag?» |
23860 | MAT 19:29 | Koo xam ne kii dëddu nga ngir sama tur ay kër, ay doomi ndey yu góor walla yu jigéen, ndey walla baay, ay doom walla ay tool, dinga ko jotaat téeméeri yoon, ba noppi am dund gu dul jeex. |
23862 | MAT 20:1 | «Noonu nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni boroom kër bu génn ci suba teel, ngir jël ay liggéeykat ndax toolu reseñam. |
23868 | MAT 20:7 | Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” |
23875 | MAT 20:14 | Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw, |