23214 | MAT 1:1 | Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. |
23235 | MAT 1:22 | Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: |
23273 | MAT 3:12 | Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.» |
23287 | MAT 4:9 | Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» |
23340 | MAT 5:37 | Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge. |
23352 | MAT 6:1 | «Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw. |
23374 | MAT 6:23 | waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! |
23376 | MAT 6:25 | «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk, walla lu ngeen wara naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen wara sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay? |
23382 | MAT 6:31 | Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu wara lekk? Lu nu wara naan?” walla: “Lu nu wara sol?” |
23388 | MAT 7:3 | Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw? |
23431 | MAT 8:17 | Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan: «Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.» |
23433 | MAT 8:19 | Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.» |
23440 | MAT 8:26 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. |
23452 | MAT 9:4 | Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol? |
23459 | MAT 9:11 | Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» |
23462 | MAT 9:14 | Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?» |
23465 | MAT 9:17 | Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.» |
23481 | MAT 9:33 | Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, masuñu koo gis ci Israyil.» |
23513 | MAT 10:27 | Li ma leen wax ci biir lëndëm, waxleen ko ci leer; li ma leen déey, yégleleen ko ci kaw taax yi. |
23535 | MAT 11:7 | Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li? |
23537 | MAT 11:9 | Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent. |
23545 | MAT 11:17 | ne leen: “Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen, woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.” |
23589 | MAT 12:31 | Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu mana doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal. |
23613 | MAT 13:5 | Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. |
23615 | MAT 13:7 | Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko. |
23616 | MAT 13:8 | Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, li ci des fanweer. |
23622 | MAT 13:14 | Li Esayi waxoon ci kàddug Yàlla am na ci ñoom, bi mu naan: “Dingeen déglu bu baax waaye dungeen xam dara; di xool bu baax waaye dungeen gis dara. |
23642 | MAT 13:34 | Loolu Yeesu wax mbooloo ma, ëmb na ko lépp ciy léeb, te waxuleen dara lu dul ciy léeb. |
23659 | MAT 13:51 | Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.» |
23664 | MAT 13:56 | Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?» |
23672 | MAT 14:6 | Bi ñu ca tegee ab diir nag, ñuy màggal bés ba Erodd juddu woon, te doomu Erojàdd ju jigéen di fecc ci biir gan ñi. Loolu neex Erodd, |
23673 | MAT 14:7 | ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.» |
23704 | MAT 15:2 | «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.» |
23707 | MAT 15:5 | Waaye yéen dangeen ne: “Ku wax sa ndey walla sa baay: ‘Li ngeen wara jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,’ |
23754 | MAT 16:13 | Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?» |
23762 | MAT 16:21 | Li dale ci jamono jooja, Yeesu tàmbali na xamal taalibeem yi ne war na dem Yerusalem, daj fa coono yu bare, jóge ca njiit ya, ca sarxalkat yu mag ya ak ca xutbakat ya; ñu rey ko, mu dekki ca ñetteelu fan ba. |
23779 | MAT 17:10 | Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Ilyaas mooy jëkka ñëw?» |
23788 | MAT 17:19 | Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun manunu woona dàq rab wi?» |
23791 | MAT 17:22 | Bi ñuy wër diiwaanu Galile nag, Yeesu ne leen: «Léegi ñu jébbal Doomu nit ki ci loxoy nit ñi; |
23808 | MAT 18:12 | «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent, te dem wuti ma réer? |
23819 | MAT 18:23 | «Loolu moo tax nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni buur bu bëgga waññ alalam ak ay jaraafam. |
23829 | MAT 18:33 | Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?” |
23836 | MAT 19:5 | te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.” |
23837 | MAT 19:6 | Kon nag nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. Lu Yàlla takk nag, bu ko nit tas.» |
23838 | MAT 19:7 | Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox soxnaam kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?» |
23848 | MAT 19:17 | Yeesu ne ko: «Lu tax nga laaj ma ci wàllu lu baax? Kenn kepp moo baax. Boo bëggee dugg ca dund googu ci kaw, nanga sàmm ndigal yi.» |
23857 | MAT 19:26 | Noonu Yeesu xool leen ne: «Loolu të na nit, waaye dara tëwul Yàlla.» |
23867 | MAT 20:6 | Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?” |
23882 | MAT 20:21 | Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.» |
23893 | MAT 20:32 | Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?» |
23920 | MAT 21:25 | La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” |
23922 | MAT 21:27 | Ñu ne Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. |
23923 | MAT 21:28 | «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu reseñ.” |
23938 | MAT 21:43 | «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, dinañu leen xañ nguuru Yàlla, dénk ko xeet wuy def ay jëfam. |
23959 | MAT 22:18 | Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi? |
23973 | MAT 22:32 | “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.» |
23979 | MAT 22:38 | Loolu moo di li jëkk te ëpp ci li Yàlla santaane. |
23983 | MAT 22:42 | «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.» |
23984 | MAT 22:43 | Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne: |
23990 | MAT 23:3 | Lépp lu ñu leen wax nag, defleen ko te sàmm ko, waaye buleen roy seeni jëf, ndaxte dañuy wax waaye duñu ko jëfe. |
24004 | MAT 23:17 | Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gëna màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell? |
24006 | MAT 23:19 | Gumba yi! Lan moo gëna màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell? |
24010 | MAT 23:23 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des. |
24041 | MAT 24:15 | «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam. |
24070 | MAT 24:44 | Loolu moo tax yéen itam taxawleen jonn, ndaxte Doomu nit ki dina ñëw ci waxtu wu ngeen ko séenuwul.» |
24086 | MAT 25:9 | Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?” |
24138 | MAT 26:15 | ne leen: «Lan ngeen ma mana jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu sarxalkat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer. |
24139 | MAT 26:16 | Li dale ci saa soosa nag Yudaa di fexe jamono ju mu leen mana jébbal Yeesu. |
24185 | MAT 26:62 | Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo wax dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?» |
24189 | MAT 26:66 | Lu ngeen ci xalaat?» Ñu ne ko: «Yoon teg na ko dee.» |
24202 | MAT 27:4 | ne leen: «Am naa bàkkaar ci li ma wor nit ku tooñul, ngir ñu rey ko.» Ñu ne ko: «Lu ciy sunu yoon? Loolu yaa ko yég.» |
24206 | MAT 27:8 | Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret. |
24221 | MAT 27:23 | Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!» |
24243 | MAT 27:45 | La tàmbalee digg bëccëg, ba ci tisbaar, réew mépp lëndëm. |
24271 | MAT 28:7 | te ngeen dem bu gaaw, wax ay taalibeem ne dekki na te jiituji na leen Galile; foofa ngeen koy gise. Lii laa leen wax.» |
24337 | MRK 2:8 | Waaye Yeesu yég ci xelam li ñuy werante ci seen biir, ne leen: «Lu tax ngeen di werantee nii ci seen xel? |
24338 | MRK 2:9 | Lan moo gëna yomb, ma wax ku làggi ki: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma wax ko: “Jógal, jël sa basaŋ, tey dox”? |
24341 | MRK 2:12 | Ca saa sa mu jël basaŋam te génn fa kanam ñépp. Noonu ñépp waaru, di màggal Yàlla naan: «Lu mel ni lii, masunu koo gis.» |
24343 | MRK 2:14 | Bi Yeesu di romb, mu gis ku ñuy wax Lewi, doomu Alfe, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ci man.» Mu jóg, daldi topp ci moom. |
24344 | MRK 2:15 | Bi loolu amee Yeesu ak i taalibeem di lekk ci kër Lewi, fekk ay juutikat ak ay boroom bàkkaar yu bare di lekkandoo ak ñoom, ndaxte ñu bare ci ñoom a ko toppoon. |
24345 | MRK 2:16 | Waaye xutbakat yi bokk ci Farisen yi, bi ñu gisee ne dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar, ñu daldi laaj taalibe yi: «Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?» |
24347 | MRK 2:18 | Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?» |
24351 | MRK 2:22 | Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi yàqu, biiñ bi tuuru. Waaye biiñ bu bees, ci mbuus yu bees lañu koy def.» |
24361 | MRK 3:4 | Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell. |
24397 | MRK 4:5 | Leneen ci pepp mi wadd ci bérab bu bare ay doj te néew suuf, mu daldi sax bu gaaw, ndaxte suuf si barewul. |
24399 | MRK 4:7 | Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi sax, tanc ko, te meññul dara. |
24400 | MRK 4:8 | Li ci des dal ci suuf su baax, mu jóg, sax, di focci ay gub; lii àntu, ba mat fanweeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, lii mat téeméer.» |
24422 | MRK 4:30 | Yeesu ne leen ati: «Lu nu mana méngaleel nguuru Yàlla? Walla ban léeb lanu ko mana misaale? |
24432 | MRK 4:40 | Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?» |
24472 | MRK 5:39 | Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.» |
24478 | MRK 6:2 | Bésub noflaay bi nag mu jàngal leen ci seen jàngu, ba mbooloom ñi ko dégg waaru naan: «Lii, fu mu ko jële, te xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def kéemaan yii? |
24498 | MRK 6:22 | Booba doomu Erojàdd dugg di fecc, mu neex Erodd ak gan ñi, ba buur bi ne janq bi: «Laaj ma loo bëgg, dinaa la ko jox.» |
24499 | MRK 6:23 | Mu boole ci ngiñ ne ko: «Loo ma mana laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wàllu réew mi sax.» |
24500 | MRK 6:24 | Noonu janq bi génn ne ndeyam: «Lu may laaj?» Mu ne ko: «Laajal boppu Yaxya.» |
24537 | MRK 7:5 | Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?» |
24543 | MRK 7:11 | Waaye yéen dangeen ne: ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga wara jariñoo ci man Korban la,” —maanaam saraxu Yàlla la— |
24547 | MRK 7:15 | Li ci biti, tey dugg nit, du ko mana indil sobe, waaye li génn ci nit, loolu mooy indil nit sobe.» |