23216 | MAT 1:3 | Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram; |
23296 | MAT 4:18 | Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
23428 | MAT 8:14 | Gannaaw loolu Yeesu dem kër Piyeer. Ba mu eggee, mu fekk gorob Piyeer bu jigéen tëdd ak yaram wu tàng. |
23488 | MAT 10:2 | Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam; |
23694 | MAT 14:28 | Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.» |
23695 | MAT 14:29 | Yeesu ne ko: «Kaay!» Piyeer nag wàcc ca gaal ga, di dox ci kaw ndox mi, jëm ci Yeesu. |
23717 | MAT 15:15 | Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.» |
23757 | MAT 16:16 | Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.» |
23759 | MAT 16:18 | Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara. |
23763 | MAT 16:22 | Bi mu waxee ba noppi, Piyeer woo ko ci pegg, bëgg koo yedd ne ko: «Yàlla tere, Boroom bi, loolu du la dal.» |
23764 | MAT 16:23 | Waaye Yeesu waññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.» |
23770 | MAT 17:1 | Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool. |
23773 | MAT 17:4 | Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» |
23793 | MAT 17:24 | Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?» |
23794 | MAT 17:25 | Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» |
23795 | MAT 17:26 | Piyeer ne ko: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci. |
23817 | MAT 18:21 | Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko wara baal? Xanaa ba ci juróom ñaari yoon?» |
23858 | MAT 19:27 | Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw, nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?» |
24156 | MAT 26:33 | Piyeer nag daldi jël kàddu gi naan: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la dàggeeku mukk.» |
24158 | MAT 26:35 | Piyeer ne ko: «Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu. |
24160 | MAT 26:37 | Bi mu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer ak ñaari doomi Sebede, daldi am tiis ba xonet. |
24163 | MAT 26:40 | Noonu mu ñëw ca taalibe ya, fekk leen ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Amuleen sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? |
24181 | MAT 26:58 | Piyeer topp ko fu sore, ba ci ëttu sarxalkat bu mag ba; mu dugg, toog ak surga ya, ngir seet nu mbir may mujje. |
24192 | MAT 26:69 | Bi looluy xew, Piyeer moom ma nga toogoon ca biti ca ëtt ba. Noonu benn mbindaan ñëw ci moom ne ko: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Galile.» |
24193 | MAT 26:70 | Waaye Piyeer weddi ko ci kanam ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.» |
24195 | MAT 26:72 | Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.» |
24196 | MAT 26:73 | Nees-tuut ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.» |
24197 | MAT 26:74 | Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab. |
24198 | MAT 26:75 | Noonu Piyeer fàttaliku la Yeesu waxoon ne: «Bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi génn, di jooy jooy yu metti. |
24200 | MAT 27:2 | Ñu yeew ko, yóbbu ko, jébbal ko Pilaat boroom réew ma. |
24211 | MAT 27:13 | Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo li ñu la jiiñ lépp?» |
24215 | MAT 27:17 | Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?» |
24220 | MAT 27:22 | Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
24222 | MAT 27:24 | Naka Pilaat xam ne du ci man dara, fekk na sax yëngu-yëngu bi gëna am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanam mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.» |
24224 | MAT 27:26 | Noonu Pilaat bàyyil leen Barabas, mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant. |
24256 | MAT 27:58 | Mu dem ca Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Pilaat santaane, ñu jox ko ko. |
24260 | MAT 27:62 | Ba bët setee nag, ca bés ba topp bésu Waajal ba, sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya dajaloo, jëm ci Pilaat. |
24263 | MAT 27:65 | Pilaat ne leen: «Amleen, ay wottukat a ngi nii. Demleen wottuji ko, ni ngeen mane.» |
24373 | MRK 3:16 | Fukk ak ñaar ñii la tànn: Simoŋ, mi mu tudde Piyeer, |
24470 | MRK 5:37 | Noonu Yeesu dem, ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana rekk, ndaxte mayul keneen, mu ànd ak moom. |
24598 | MRK 8:29 | Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.» |
24601 | MRK 8:32 | Noonu mu xamal leen mbir mi, ba mu leer nàññ. Bi ko Piyeer déggee, mu woo ko ci pegg, daldi ko yedd. |
24602 | MRK 8:33 | Waaye Yeesu geestu, gis yeneen taalibe yi, mu daldi yedd Piyeer ne ko: «Sore ma Seytaane; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.» |
24609 | MRK 9:2 | Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana, mu yóbbu leen ñoom rekk fu wéet ci tund wu kawe lool. Foofa jëmmam soppiku ci seen kanam; |
24612 | MRK 9:5 | Piyeer daldi ne Yeesu: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» |
24685 | MRK 10:28 | Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!» |
24730 | MRK 11:21 | Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!» |
24789 | MRK 13:3 | Gannaaw loolu, bi nga xamee ne Yeesu toog na ci tundu Oliw ya, jàkkaarlook kër Yàlla ga, Piyeer, Saag, Yowaana ak Andare fekki ko cig wet, laaj ko: |
24852 | MRK 14:29 | Kon Piyeer ne ko: «Bu la ñépp dàggeekoo, man duma la bàyyi mukk.» |
24854 | MRK 14:31 | Waaye Piyeer gëna sax ca la mu waxoon naan: «Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu. |
24856 | MRK 14:33 | Mu ànd ak Piyeer, Saag ak Yowaana, daldi jàq, ba xonet. |
24860 | MRK 14:37 | Noonu mu délsi ci taalibe yi, fekk ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu? |
24877 | MRK 14:54 | Piyeer nag topp ko fu sore, ba ci ëttu sarxalkat bu mag bi, mu toog fa ak alkaati yi, di jaaru ci taal bi. |
24889 | MRK 14:66 | Piyeer nag ma nga toogoon ci ëtt bi féete suuf. Noonu benn mbindaanu sarxalkat bu mag ba romb fa. |
24890 | MRK 14:67 | Mu gis Piyeer di jaaru, xool ko jàkk naan: «Yaw itam àndoon nga ak Yeesum Nasaret moomu.» |
24891 | MRK 14:68 | Waaye Piyeer weddi ko naan: «Xawma li ngay wax, dégguma ci dara.» Mu daldi génn, dem ca buntu kër ga. |
24893 | MRK 14:70 | Waaye Piyeer weddiwaat ko. Nees-tuut ñi fa taxaw ne Piyeer: «Yaw mi de, ci lu wóor bokk nga ci, nde waa Galile nga.» |
24894 | MRK 14:71 | Waaye Piyeer daldi giñ ak a waat naan: «Xawma nit ki ngay wax.» |
24895 | MRK 14:72 | Ci saa si ginaar sab ñaareelu yoon. Noonu Piyeer fàttaliku li ko Yeesu wax: «Bala ginaar a sab ñaari yoon, dinga ma weddi ñetti yoon.» Mu daldi jooy jooy yu metti. |
24896 | MRK 15:1 | Ci suba teel sarxalkat yu mag yi gise, ñoom ak njiit yi ak xutbakat yi ak kureelu àttekat yi yépp. Ñu yeew nag Yeesu, daldi ko yóbbu, jébbal ko Pilaat. |
24897 | MRK 15:2 | Noonu Pilaat laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.» |
24899 | MRK 15:4 | Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?» |
24900 | MRK 15:5 | Waaye ba tey Yeesu waxul dara, ba tax Pilaat waaru. |
24901 | MRK 15:6 | Màggal gu nekk nag Pilaat daan na may mbooloo mi, ñu tànn kenn ci ñi ñu tëjoon, mu bàyyil leen ko. |
24903 | MRK 15:8 | Noonu mbooloo mi ñëw, laaj Pilaat, mu defal leen la mu daan def. |
24904 | MRK 15:9 | Pilaat nag xam ne kiñaan rekk a taxoon sarxalkat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?» |
24906 | MRK 15:11 | Waaye sarxalkat yu mag yi xiir mbooloo mi, ñu laaj Pilaat, mu bàyyil leen Barabas. |
24907 | MRK 15:12 | Kon Pilaat ne leen: «Lan laay def nag ak ki ngeen di wooye buuru Yawut yi?» |
24909 | MRK 15:14 | Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gëna kawe: «Daaj ko ci bant!» |
24910 | MRK 15:15 | Noonu Pilaat, mi wuta neex mbooloo mi, bàyyil leen Barabas, ba noppi mu dóorlu Yeesu ay yar, jébbal ko, ngir ñu daaj ko ci bant. |
24911 | MRK 15:16 | Bi loolu amee ñu dugal Yeesu ci biir kër boroom réew ma, mooy bérab bu ñuy wax Peretoriyum, ñu daldi woo mbooloom xarekat yépp. |
24938 | MRK 15:43 | Yuusufa mi dëkk Arimate takk aw fitam, dem Pilaat, laaj ko néewu Yeesu. Yuusufa moomu nag, ku siiw la woon ci kureelu àttekat yi, te doon séentu moom itam nguuru Yàlla. |
24939 | MRK 15:44 | Bi Pilaat déggee ne, Yeesu faatu na xaat, mu waaru. Mu woolu nag njiit li, laaj ko, ndax yàgg na faatu. |
24940 | MRK 15:45 | Bi ko ko njiit li dëggalee, Pilaat jox néew bi Yuusufa. |
24949 | MRK 16:7 | Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya: “Mi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon.”» |
25095 | LUK 3:1 | Fukkeelu at ak juróom ci nguuru Tibeer Sesaar, fekk Poñsë Pilaat yilif diiwaanu Yude, Erodd yilif diiwaanu Galile, Filib magam yilif diiwaanu Iture ak bu Tarakonit, te Lisañas yilif Abilen. |
25127 | LUK 3:33 | Nason; Aminadab; Aminadab, Admin; Arni; Esron; Peres; Yuda; |
25129 | LUK 3:35 | Serug; Rew; Peleg; Eber; Sela. |
25184 | LUK 5:8 | Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!» |
25229 | LUK 6:14 | Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi, |
25359 | LUK 8:45 | Yeesu laaj nit ña ne: «Ana ku ma laal?» Ku nekk di miim. Noonu Piyeer ne ko: «Kilifa gi, nit ñépp a ngi lay wër, di la tanc wet gu nekk.» |
25365 | LUK 8:51 | Bi Yeesu agsee ca kër ga, nanguwul kenn duggaaleek moom, ñu dul Piyeer, Yowaana, Saag ak waajuri xale ba. |
25390 | LUK 9:20 | Yeesu ne leen: «Yéen nag ku ngeen ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi, bi Yàlla yónni.» |
25398 | LUK 9:28 | Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan. |
25402 | LUK 9:32 | Fekk Piyeer ak ñi mu àndal doon gëmméentu, waaye bi ñu yewwoo bu baax, ñu gis ndamu Yeesu, ak ñaari nit ñu taxaw ci wetam. |
25403 | LUK 9:33 | Bi nit ñooñu di sore Yeesu, Piyeer ne ko: «Kilifa gi, bég nanu ci sunu teew fii; nanu defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» Fekk xamul la mu doon wax. |
25569 | LUK 12:41 | Piyeer ne Yeesu: «Boroom bi, ndax dangay dégtal léeb wii ngir nun rekk walla ngir mbooloo mépp?» |
25588 | LUK 13:1 | Ca jamono jooju ay nit ñëw ca Yeesu, nettali mbirum waa Galile, ya Pilaat reylu woon, jaxase seen deret ak dereti mala, yi ñu rendi woon, jébbal leen Yàlla. |
25785 | LUK 18:28 | Noonu Piyeer ne: «Nun de, dëddu nanu li nu am lépp, topp la.» |
25941 | LUK 22:8 | Noonu Yeesu yebal Piyeer ak Yowaana ne leen: «Demleen, defaral nu reeru bésu Mucc ba.» |
25966 | LUK 22:33 | Piyeer ne ko: «Boroom bi, àttan naa ànd ak yaw ca kaso, ba ci dee sax.» |
25967 | LUK 22:34 | Yeesu ne ko: «Piyeer, maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab tey jii, dinga weddi ñetti yoon ne xam nga ma.» |
25987 | LUK 22:54 | Ñu jàpp Yeesu, yóbbu ko ca kër sarxalkat bu mag ba. Piyeer topp fu sore. |
25988 | LUK 22:55 | Amoon na taal ca diggu ëtt ba, ay nit toog, wër ko, Piyeer itam toog ci seen biir. |
25990 | LUK 22:57 | Waaye Piyeer weddi ko ne: «Soxna si, xawma kooku.» |
25991 | LUK 22:58 | Nees-tuut keneen gis ko ne: «Yaw itam ci ñoom nga bokk.» Piyeer ne ko: «Sama waay, bokkuma ci.» |
25993 | LUK 22:60 | Waaye Piyeer ne ko: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab. |
25994 | LUK 22:61 | Noonu Boroom bi geestu, xool Piyeer. Te Piyeer fàttaliku la ko Boroom bi waxoon ne: «Bala ginaar a sab tey jii, dinga ma weddi ñetti yoon.» |
25995 | LUK 22:62 | Piyeer daldi génn, di jooy jooy yu metti. |