23216 | MAT 1:3 | Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram; |
23217 | MAT 1:4 | Aram Aminadab; Aminadab Nason; Nason Salmon; |
23218 | MAT 1:5 | Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi, |
23219 | MAT 1:6 | miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri; |
23220 | MAT 1:7 | Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf; |
23225 | MAT 1:12 | Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel, |
23227 | MAT 1:14 | Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd; |
23231 | MAT 1:18 | Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. |
23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23268 | MAT 3:7 | Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
23271 | MAT 3:10 | Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si. |
23272 | MAT 3:11 | Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
23279 | MAT 4:1 | Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane. |
23283 | MAT 4:5 | Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga. |
23286 | MAT 4:8 | Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. |
23288 | MAT 4:10 | Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» |
23289 | MAT 4:11 | Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo. |
23291 | MAT 4:13 | Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. |
23293 | MAT 4:15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali, di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan, yaw Galile, réewum ñi dul Yawut— |
23296 | MAT 4:18 | Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
23299 | MAT 4:21 | Ba Yeesu demee ba ca kanam, mu gis yeneen ñaar ñu bokk ndey ak baay, ñuy Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam. Ñu nekk ci seen biir gaal ak Sebede seen baay, di defar seeni mbaal. Noonu Yeesu woo leen. |
23302 | MAT 4:24 | ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen. |
23340 | MAT 5:37 | Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge. |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23349 | MAT 5:46 | Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it? |
23350 | MAT 5:47 | Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy waar? Xanaa ñi xamul Yàlla duñu def noonu it? |
23360 | MAT 6:9 | Yéen nag nii ngeen wara ñaane: “Sunu Baay bi nekk ci kaw, yal na sa tur di lu ñu sellal, |
23365 | MAT 6:14 | «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam. |
23367 | MAT 6:16 | «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23377 | MAT 6:26 | Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare? |
23379 | MAT 6:28 | «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
23380 | MAT 6:29 | waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom. |
23416 | MAT 8:2 | Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.» |
23420 | MAT 8:6 | ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.» |
23422 | MAT 8:8 | Waaye njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér. |
23423 | MAT 8:9 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |
23435 | MAT 8:21 | Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.» |
23439 | MAT 8:25 | Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee!» |
23466 | MAT 9:18 | Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.» |
23475 | MAT 9:27 | Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
23476 | MAT 9:28 | Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu ne ko: «Waaw, Sang bi.» |
23488 | MAT 10:2 | Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam; |
23489 | MAT 10:3 | Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade; |
23490 | MAT 10:4 | Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nara wor Yeesu. |
23491 | MAT 10:5 | Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari. |
23501 | MAT 10:15 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, keroog bésub àtte ba, waa réewu Sodom ak Gomor ñooy tane dëkk boobu. |
23516 | MAT 10:30 | Seen kawari bopp sax, waññees na leen. |
23549 | MAT 11:21 | Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. |
23550 | MAT 11:22 | Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane. |
23551 | MAT 11:23 | Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey. |
23552 | MAT 11:24 | Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.» |
23555 | MAT 11:27 | Yeesu teg ca ne: «Sama Baay jébbal na ma lépp, te kenn manu maa xam, man Doom ji, ku dul Baay bi; kenn it manula xam Baay bi, ku dul man Doom ji, ak ku ma ko bëgga xamal. |
23565 | MAT 12:7 | Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul. |
23576 | MAT 12:18 | «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn, di sama Soppe bi neex sama xol. Dinaa def sama Xel ci moom, muy yégal xeet yi yoonu njub. |
23581 | MAT 12:23 | Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?» |
23584 | MAT 12:26 | Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di mana yàgge? |
23587 | MAT 12:29 | «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgga dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp. |
23590 | MAT 12:32 | Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira. |
23600 | MAT 12:42 | Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi. |
23605 | MAT 12:47 | Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgga wax ak yaw.» |
23636 | MAT 13:28 | Mu ne leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?” |
23647 | MAT 13:39 | Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi. |
23663 | MAT 13:55 | Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda? |
23694 | MAT 14:28 | Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.» |
23696 | MAT 14:30 | Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!» |
23700 | MAT 14:34 | Bi loolu amee ñu jàll, teer ca diiwaanu Senesaret. |
23711 | MAT 15:9 | Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”» |
23723 | MAT 15:21 | Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon. |
23724 | MAT 15:22 | Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» |
23727 | MAT 15:25 | Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» |
23742 | MAT 16:1 | Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.» |
23747 | MAT 16:6 | Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23752 | MAT 16:11 | Kon nag lu tax xamuleen ne waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23753 | MAT 16:12 | Noonu ñu xam ne, Yeesu waxul woon lawiiru mburu, waaye ñu moytu njànglem Farisen ya ak Sadusen ya. |
23754 | MAT 16:13 | Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?» |
23757 | MAT 16:16 | Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.» |
23758 | MAT 16:17 | Yeesu ne ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw. |
23764 | MAT 16:23 | Waaye Yeesu waññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.» |
23770 | MAT 17:1 | Juróom benni fan gannaaw gi, Yeesu àndoon na ak Piyeer, Saag ak Yowaana rakkam, yóbbu leen fu wéet ci tund wu kawe lool. |
23773 | MAT 17:4 | Piyeer nag daldi wax Yeesu ne ko: «Sang bi, bég nanu ci sunu teew fii; soo ko bëggee, dinaa fi defar ñetti mbaar, benn yaw, benn Musaa ak benn Ilyaas.» |
23784 | MAT 17:15 | naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci sawara, léeg-léeg mu daanu ci ndox. |
23789 | MAT 17:20 | Yeesu ne leen: «Seen ngëm gu néew a tax. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, su ngeen amee ngëm gu tuuti sax niw peppu fuddën, kon dingeen ne tund wii: “Jógeel fii, toxu fale,” te dina fa dem, ba dara du leen të.» |
23794 | MAT 17:25 | Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» |
23808 | MAT 18:12 | «Luy seen xalaat ci lii? Su fi amoon nit ku am téeméeri xar, te benn ci ñoom réer, lu muy def? Ndax du bàyyi ca parlukaay ba juróom ñeent fukki xar ya ak juróom ñeent, te dem wuti ma réer? |
23828 | MAT 18:32 | Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma. |
23851 | MAT 19:20 | Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?» |
23874 | MAT 20:13 | Waaye boroom kër ga ne kenn ci ñoom: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon? |
23875 | MAT 20:14 | Kon fabal li nga moom te dem. Su ma bëggee fey ku mujja ñëw, li ma la fey yaw, |
23881 | MAT 20:20 | Ci kaw loolu doomi Sebede ya ànd ak seen ndey, ñëw ci Yeesu. Ndey ja sukk, di ko ñaansi lenn. |
23891 | MAT 20:30 | Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23892 | MAT 20:31 | Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |