23216 | MAT 1:3 | Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram; |
23247 | MAT 2:9 | Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk. |
23263 | MAT 3:2 | Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.» |
23278 | MAT 3:17 | Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.» |
23289 | MAT 4:11 | Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo. |
23295 | MAT 4:17 | Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.» |
23318 | MAT 5:15 | Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp. |
23330 | MAT 5:27 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” |
23335 | MAT 5:32 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa soxna te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga. |
23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23358 | MAT 6:7 | «Te it bu ngeen di ñaan, buleen bareel wax yu amul njariñ, mel ni ñi xamul Yàlla; ñoom defe nañu ne, Yàlla dina leen nangul ndax seen wax ju bare. |
23379 | MAT 6:28 | «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
23383 | MAT 6:32 | Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp. |
23423 | MAT 8:9 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |
23434 | MAT 8:20 | Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» |
23436 | MAT 8:22 | Yeesu ne ko: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.» |
23465 | MAT 9:17 | Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.» |
23489 | MAT 10:3 | Filib ak Bartelemi; Tomaa ak Macë, juutikat ba woon; Saag doomu Alfe, ak Tade; |
23508 | MAT 10:22 | Te yéen nag, ñépp dinañu leen bañ ndax sama tur; waaye ku muñ ba muj ga, mucc. |
23510 | MAT 10:24 | Yeesu teg ca ne: «Taalibe gënul kilifaam, te jaam gënul sangam. |
23514 | MAT 10:28 | Te buleen ragal ñu mana rey yaram, te manuñoo rey ruu, waaye ragal-leen ki mana sànk yaram ak ruu ci sawara. |
23520 | MAT 10:34 | «Te it buleen defe ne damaa ñëw ngir indi jàmm ci àddina; ñëwuma ngir indi jàmm, waaye jaasi laa indaale. |
23526 | MAT 10:40 | «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni. |
23542 | MAT 11:14 | Te Yaxya moomu, su ngeen bëggee nangu lii, mooy Ilyaas bi waroona ñëw. |
23549 | MAT 11:21 | Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku. |
23550 | MAT 11:22 | Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane. |
23551 | MAT 11:23 | Te yaw dëkku Kapernawum, ndax dees na la yékkati bu kawe? Déedéet, dees na la daane bu suufe. Ndaxte kéemaan yi ma def ci yaw, bu ñu leen defoon ci dëkku Sodom, kon mu nekk ba tey. |
23563 | MAT 12:5 | Te it ndax jànguleen ci yoonu Musaa, ne sarxalkat ya ca kër Yàlla ga teraluñu bésub noflaay bi, te tooñuñu? |
23571 | MAT 12:13 | Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des. |
23574 | MAT 12:16 | Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal. |
23585 | MAT 12:27 | Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte. |
23600 | MAT 12:42 | Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi. |
23644 | MAT 13:36 | Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.» |
23653 | MAT 13:45 | «Te it nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni jaaykat buy wut per yu rafet. |
23664 | MAT 13:56 | Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?» |
23666 | MAT 13:58 | Te Yeesu defu fa kéemaan yu bare ndax seen ngëmadi. |
23686 | MAT 14:20 | Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale dammit ya ca des, mu nekk fukki pañe ak ñaar yu fees. |
23693 | MAT 14:27 | Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» |
23706 | MAT 15:4 | Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.” |
23723 | MAT 15:21 | Gannaaw loolu Yeesu jóge fa, dem ci diiwaanu Tir ak Sidon. |
23739 | MAT 15:37 | Noonu ñépp lekk ba suur. Te ñu dajale juróom ñaari dàmba yu fees ak dammit yi ci des. |
23744 | MAT 16:3 | Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, waaye manuleena ràññee firndey jamono ji nu tollu. |
23751 | MAT 16:10 | Te ndax fàttalikuwuleen itam juróom ñaari mburu ya ngir ñeenti junniy góor ña, ak ñaata dàmba ngeen dajale woon ciy dammit? |
23755 | MAT 16:14 | Taalibe yi ne: «Am na ñu naan, Yaxya, ñeneen ñi, Ilyaas; ñi ci des ne, Yeremi walla keneen ci yonent yi.» |
23759 | MAT 16:18 | Te maa ngi lay wax lii: yaa di Piyeer, te ci kaw doj wu réy woowu laay samp mbooloom ñi ma gëm, te dooley dee du ko manal dara. |
23767 | MAT 16:26 | Te it moom àddina sépp lu muy jariñ nit, bu ñàkkee bakkanam? Te nit, lu mu wara weccee bakkanam? |
23781 | MAT 17:12 | Teewul maa ngi leen di wax ne, Ilyaas ñëw na te xàmmiwuñu ko, waaye def nañu ko la leen neex. Noonu it dañoo nara sonal léegi Doomu nit ki.» |
23801 | MAT 18:5 | Te it ku nangu ci sama tur xale bu mel ni kii, man mii nga nangu. |
23806 | MAT 18:10 | «Te it wottuleena xeeb kenn ci ñi gëna tuuti, ndax kat seeni malaakaa ngi sax ci jataayu sama Baay bi nekk ci kaw. Maa leen wax loolu. |
23811 | MAT 18:15 | «Te lii itam, bu sa mbokk defee bàkkaar, demal yedd ko, yéen ñaar rekk. Bu la dégloo, kon gindi nga sa mbokk. |
23840 | MAT 19:9 | Te it maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii fase nga sa soxna te du njaaloo tax, boo séyaatee ak keneen, njaaloo nga.» |
23892 | MAT 20:31 | Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23898 | MAT 21:3 | Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leena soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.» |
23917 | MAT 21:22 | Te lépp lu ngeen laaj cig ñaan, bu ngeen ci boolee ngëm, dingeen ci jot.» |
23921 | MAT 21:26 | Te bu nu nee: “Ci nit ñi,” kon mbooloo mi dal ci sunu kaw, ndaxte ñépp teg nañu Yaxya ab yonent.» |
23924 | MAT 21:29 | Taaw ba ne ko: “Demuma,” waaye gannaaw loolu xelam yedd ko, mu dem. |
23926 | MAT 21:31 | Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobarey baayam?» Ñu ne: «Taaw ba.» Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkka dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23927 | MAT 21:32 | Ndaxte Yaxya ñëw na ci yéen ci yoonu njub, te gëmuleen ko; waaye juutikat yi ak jigéeni moykat yi gëm nañu ko. Te gannaaw bi ngeen gisee loolu, seen xel soppikuwul sax, ba ngeen gëm ko.» |
23966 | MAT 22:25 | Amoon na ci nun nag juróom ñaari góor, ñu bokk ndey ak baay. Taaw ba am jabar ba noppi, faatu; rakk ja donn jabar ja, ndaxte amul woon doom. |
23972 | MAT 22:31 | Te lu jëm ci ndekkitel ñi dee, xanaa masuleena jàng la leen Yàlla waxoon ne: |
23980 | MAT 22:39 | Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” |
23985 | MAT 22:44 | “Boroom bi wax na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ” |
23987 | MAT 22:46 | Ci kaw loolu kenn manu koo tontu genn kàddu. Te li dale ci bés booba kenn ñemeetu koo laaj dara. |
23996 | MAT 23:9 | Te buleen tudde kenn seen “baay” ci àddina, ndaxte kenn rekk moo di seen Baay, ki ci kaw. |
24017 | MAT 23:30 | Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.” |
24037 | MAT 24:11 | Te it ñu bare ñuy mbubboo turu yonent dinañu feeñ, nax nit ñu bare. |
24038 | MAT 24:12 | Te gannaaw lu bon day law, mbëggeelug ñi ëpp dina wàññiku. |
24048 | MAT 24:22 | Te bu ñu wàññiwul bés yooyu, kenn du mucc, waaye dees na leen wàññi ndax ñi Yàlla tànn. |
24086 | MAT 25:9 | Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?” |
24091 | MAT 25:14 | «Te it nguuru Yàlla dafa mel ni kuy tukki bitim réew. Bi muy laata dem, mu woo ay surgaam, batale leen alalam, ku nekk lu mu àttan. |
24107 | MAT 25:30 | Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.” |
24145 | MAT 26:22 | Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?» |
24158 | MAT 26:35 | Piyeer ne ko: «Boo xamee ne sax, damaa wara dee ak yaw, duma la weddi mukk.» Taalibe yépp it waxe noonu. |
24159 | MAT 26:36 | Bi loolu amee Yeesu ànd ak ñoom ba ca bérab bu tudd Setsemane, mu ne taalibe ya: «Toogleen fii, ma dem fale, ñaan fa.» |
24183 | MAT 26:60 | waaye manuñu koo am. Teewul ñu bare ñëwoon nañu, di seede lu dul dëgg. Ba mujj ñaari nit ñëw naan: |
24197 | MAT 26:74 | Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab. |
24206 | MAT 27:8 | Loolu moo tax ñu wooye tool booba ba tey Toolu deret. |
24217 | MAT 27:19 | Te it bi mu toogee sax ca jalu àttekaay ba, soxnaam yónnee ci moom ne ko: «Bul dugg ci yëfi ku jub kooku, ndaxte tey gént naa ci moom te sonn naa ci lool.» |
24235 | MAT 27:37 | Te it ñu teg ci kaw boppam mbind, mu xamle lu tax ñu rey ko, mu ne: «Kii mooy Yeesu, buuru Yawut yi.» |
24242 | MAT 27:44 | Taskati réew ma it, ya ñu daajaale ak moom, di ko xas noonule. |
24251 | MAT 27:53 | Te gannaaw ndekkitel Yeesu ñu génn ca bàmmeel ya, dugg ca dëkk bu sell ba, te feeñu ñu bare. |
24253 | MAT 27:55 | Amoon na fa it ay jigéen yu bare yu leen dànd, di seetaan. Te ñoo jóge woon Galile, ànd ak Yeesu, di ko topptoo. |
24278 | MAT 28:14 | Te bu ko boroom réew mi yégee nag, dinanu ko neexal, ngir rawale leen.» |
24279 | MAT 28:15 | Wottukat ya nag fab xaalis ba, def la ñu leen santoon. Te nettali boobu siiw na ci Yawut yi ba bésu tey. |
24288 | MRK 1:4 | Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox, tey waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.» |
24295 | MRK 1:11 | Te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.» |
24306 | MRK 1:22 | Te ñu waaru ca njàngleem, ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul. |
24331 | MRK 2:2 | Noonu nit ñu bare dajaloo fa, ba kenn amatul foo taxaw, du ci bunt bi sax. Te Yeesu di leen yégal kàddu gi. |
24347 | MRK 2:18 | Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?» |
24351 | MRK 2:22 | Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi yàqu, biiñ bi tuuru. Waaye biiñ bu bees, ci mbuus yu bees lañu koy def.» |
24362 | MRK 3:5 | Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ. |
24365 | MRK 3:8 | Te it nit ñu bare dégg la mu def, ñu ñëw fi moom, jóge diiwaanu Yude ak dëkku Yerusalem, ca diiwaanu Idume, ca gannaaw dexu Yurdan ak ci wàlli Tir ak Sidon. |
24375 | MRK 3:18 | Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; |
24377 | MRK 3:20 | Am beneen bés Yeesu ñëwaat ca kër ga. Te mbooloo mu bare dajaloowaat fa, ba tax manuñoo lekk sax. |
24379 | MRK 3:22 | Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
24382 | MRK 3:25 | Te kër gu xeex boppam, du mana yàgg. |