23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23238 | MAT 1:25 | Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu. |
23253 | MAT 2:15 | Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.» |
23260 | MAT 2:22 | Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile. |
23268 | MAT 3:7 | Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
23272 | MAT 3:11 | Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
23275 | MAT 3:14 | Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!» |
23282 | MAT 4:4 | Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
23288 | MAT 4:10 | Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”» |
23322 | MAT 5:19 | Ku tebbi nag ba gëna tuuti ci ndigal yii, te ngay jàngal nit ñi noonu, dees na la tudde ki gëna tuuti ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. Waaye ku leen di sàmm, di leen digle, dees na la tudde ku mag ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23325 | MAT 5:22 | Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara. |
23331 | MAT 5:28 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel. |
23334 | MAT 5:31 | «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.” |
23335 | MAT 5:32 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa soxna te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga. |
23337 | MAT 5:34 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, buleen giñ dara; bumu doon ci asamaan, ndaxte moo di jalu Buur Yàlla; |
23342 | MAT 5:39 | Waaye man maa ngi leen di wax ne buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndijoor, jox ko ba ca des. |
23347 | MAT 5:44 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal, |
23352 | MAT 6:1 | «Wottuleena def seeni jëf yu jub ci kanam nit ñi, muy ngistal. Lu ko moy, dungeen am yool ci seen Baay bi nekk ci kaw. |
23354 | MAT 6:3 | Waaye booy sàkk sarax, bu sa loxob càmmoñ xam li sa loxob ndijoor di def, |
23366 | MAT 6:15 | Waaye su ngeen baalul ñi leen tooñ, seen Baay it du leen baal seeni tooñ. |
23371 | MAT 6:20 | Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko. |
23384 | MAT 6:33 | Waaye jëkkleena wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil. |
23389 | MAT 7:4 | Walla nan ngay waxe sa mbokk: “May ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” fekk gànj a ngii ci sa bët yaw? |
23395 | MAT 7:10 | Walla mu ñaan la jën, nga jox ko jaan? |
23399 | MAT 7:14 | Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul. |
23411 | MAT 7:26 | Waaye képp ku dégg lii ma leen wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gannuus bi. |
23422 | MAT 8:8 | Waaye njiit la ne ko: «Sang bi, yeyoowuma nga dugg ci sama kër; waxal genn kàddu rekk, te sama surga dina wér. |
23426 | MAT 8:12 | Waaye ñi waroona bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.» |
23434 | MAT 8:20 | Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» |
23440 | MAT 8:26 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. |
23452 | MAT 9:4 | Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Lu tax ngeen am xalaat yu bon ci seen xol? |
23454 | MAT 9:6 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
23460 | MAT 9:12 | Waaye bi ko Yeesu déggee, mu ne: «Ñi wér soxlawuñu fajkat, ñi wéradi ñoo ko soxla. |
23463 | MAT 9:15 | Yeesu ne leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor. |
23465 | MAT 9:17 | Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.» |
23473 | MAT 9:25 | Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg. |
23476 | MAT 9:28 | Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu ne ko: «Waaw, Sang bi.» |
23479 | MAT 9:31 | Waaye ñu génn rekk, siiwal turam fu nekk. |
23482 | MAT 9:34 | Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
23492 | MAT 10:6 | Waaye demleen ci bànni Israyil, ñoom ñi réer niy xar. |
23503 | MAT 10:17 | Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu. |
23515 | MAT 10:29 | Ñaari picci ramatu, ndax duñu ko jaay ci dërëm? Waaye benn ci ñoom du daanu ci suuf te soobul seen Baay. |
23519 | MAT 10:33 | Waaye ku ma gàntu ci kanam nit ñi, man itam dinaa la gàntu ci sama kanam Baay, bi nekk ci kaw. |
23536 | MAT 11:8 | Kon lu ngeen seeti woon nag? Nit ku sol yére yu rafet? Waaye ñi sol yére yu rafet ñu ngi dëkk ci këri buur. |
23537 | MAT 11:9 | Lu tax ngeen génn nag? Ngir gis ab yonent? Waaw, wax naa leen ne ëpp na yonent. |
23539 | MAT 11:11 | Ci dëgg maa ngi leen koy wax, ci li jigéen jur, ku sut Yaxya masula feeñ. Waaye ba tey ki gëna ndaw ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji moo ko sut. |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23550 | MAT 11:22 | Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Tir ak Sidon ñoo leen di tane. |
23552 | MAT 11:24 | Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.» |
23554 | MAT 11:26 | Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.» |
23564 | MAT 12:6 | Waaye maa ngi leen koy wax, am na ci seen biir ku sut kër Yàlla ga. |
23573 | MAT 12:15 | Waaye bi ko Yeesu yégee, mu sore foofa; te ñu bare topp ko, mu wéral leen ñoom ñépp. |
23583 | MAT 12:25 | Waaye Yeesu xam seen xalaat ne leen: «Réew mu xeex boppam tas, te dëkk mbaa kër guy xeex boppam du mana yàgg. |
23586 | MAT 12:28 | Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen. |
23606 | MAT 12:48 | Waaye Yeesu ne ko: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?» |
23614 | MAT 13:6 | Waaye bi jant bi naajee, mu lakk, wow, ndaxte amul ay reen. |
23624 | MAT 13:16 | «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg! |
23633 | MAT 13:25 | Waaye bi nit ñi di nelaw, noonam ñëw, ji jëmb ci biir dugub ji, daldi dem. |
23659 | MAT 13:51 | Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.» |
23679 | MAT 14:13 | Bi Yeesu déggee deewu Yaxya nag, mu jóge fa, dugg cig gaal, di dem ca bérab bu wéet. Waaye bi ko nit ñi yégee, ñu daldi jóge ci dëkk yi, topp ko ak seeni tànk. |
23682 | MAT 14:16 | Waaye Yeesu ne leen: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.» |
23692 | MAT 14:26 | Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu. |
23693 | MAT 14:27 | Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» |
23696 | MAT 14:30 | Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!» |
23705 | MAT 15:3 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen itam lu tax ngeen di moy li Yàlla santaane, ngir topp seeni aada? |
23707 | MAT 15:5 | Waaye yéen dangeen ne: “Ku wax sa ndey walla sa baay: ‘Li ngeen wara jariñoo ci man, jébbal naa ko Yàlla,’ |
23720 | MAT 15:18 | Waaye li génn ci gémmiñ mu ngi jóge ci xol; loolu mooy indil nit sobe. |
23725 | MAT 15:23 | Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.» |
23727 | MAT 15:25 | Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» |
23729 | MAT 15:27 | Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.» |
23735 | MAT 15:33 | Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?» |
23742 | MAT 16:1 | Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.» |
23745 | MAT 16:4 | Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla. Waaye dungeen jot genn firnde gu dul firndeg Yunus.» Bi Yeesu waxee loolu, mu jóge ci ñoom, dem. |
23747 | MAT 16:6 | Noonu Yeesu ne leen: «Wottuleen te moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23749 | MAT 16:8 | Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen di werante ci seen biir, ndaxte indaalewuleen mburu? |
23752 | MAT 16:11 | Kon nag lu tax xamuleen ne waxuma mburu? Waaye damaa bëgg, ngeen moytu lawiiru Farisen ya ak Sadusen ya.» |
23756 | MAT 16:15 | Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?» |
23764 | MAT 16:23 | Waaye Yeesu waññiku, daldi ne Piyeer: «Sore ma Seytaane, bu ma xatal; yëfi nit ngay fonk, waaye du yëfi Yàlla.» |
23774 | MAT 17:5 | Waaye bi muy wax, niir wu leer muur leen, te baat jib ca niir wa naan: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg, ci moom laa ame bànneex; dégluleen ko.» |
23776 | MAT 17:7 | Waaye Yeesu jegeñsi, laal leen naan: «Jógleen, buleen ragal dara.» |
23780 | MAT 17:11 | Yeesu ne leen: «Waaw, dëgg la, Ilyaas war na ñëw, jubbanti lépp. |
23794 | MAT 17:25 | Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?» |
23796 | MAT 17:27 | Waaye bëgguma nu naqaral leen; demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkka xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.» |
23802 | MAT 18:6 | Waaye ku yóbbe bàkkaar kenn ci ñi gëna tuuti ñi ma gëm, li gën ci moom mooy ñu takk doj wu réy ci baatam, sànni ko ca fa gëna xóot ca géej ga. |
23812 | MAT 18:16 | Waaye bu la dégluwul, àndal ak kenn mbaa ñaar, ngir mbir mi dëggu ci li ko ñaar walla ñett seede. |
23818 | MAT 18:22 | Yeesu ne ko: «Waxuma la ba ci juróom ñaari yoon, waaye ba ci juróom ñaar fukki juróom ñaari yoon. |
23826 | MAT 18:30 | Waaye moom nanguwu ko, mu dem, tëj ko kaso, ba kera mu fey li mu ko ameel. |
23838 | MAT 19:7 | Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox soxnaam kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?» |
23844 | MAT 19:13 | Gannaaw loolu amoon na ay nit ñuy indil Yeesu ay xale, ngir mu teg leen ay loxoom, ñaanal leen. Waaye taalibe ya gëdd leen. |
23849 | MAT 19:18 | Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, |
23851 | MAT 19:20 | Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?» |
23853 | MAT 19:22 | Waaye bi waxambaane wa déggee loolu, mu jóge fa ak tiis, ndaxte ku bare woon alal la. |
23858 | MAT 19:27 | Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw, nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?» |
23861 | MAT 19:30 | Waaye ñu bare ci ñi jiitu, ñooy mujji; ñi mujj, ñooy jiituji. |
23869 | MAT 20:8 | «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.” |
23874 | MAT 20:13 | Waaye boroom kër ga ne kenn ci ñoom: “Sama waay tooñuma la. Ndax juboowunu woon ci benn denariyon? |
23876 | MAT 20:15 | ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?” |
23880 | MAT 20:19 | jébbal ko ñi dul Yawut, ngir ñu di ko ñaawal te di ko dóor ay yar, ba noppi daaj ko ci bant. Waaye ca ñetteelu fan ba dina dekki.» |
23886 | MAT 20:25 | Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di not. |