23231 | MAT 1:18 | Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. |
23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23272 | MAT 3:11 | Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
23277 | MAT 3:16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
23279 | MAT 4:1 | Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane. |
23349 | MAT 5:46 | Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it? |
23350 | MAT 5:47 | Su ngeen nuyoo seeni bokk rekk, lu ngeen def lu doy waar? Xanaa ñi xamul Yàlla duñu def noonu it? |
23376 | MAT 6:25 | «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, buleen seen bakkan jaaxal, ci lu ngeen wara lekk, walla lu ngeen wara naan. Buleen jaaxle it ngir seen yaram, ci lu ngeen wara sol. Xanaa bakkan gënul lekk, te yaram gënul koddaay? |
23464 | MAT 9:16 | Xam ngeen ne, kenn du daax mbubb mu màggat ak sekkit wu bees; ndaxte sekkit wi day ñoddi mbubb mi, te xottiku bi gëna yaatu. |
23506 | MAT 10:20 | du yéenay wax, waaye Xelum seen Baay mooy wax ci yéen. |
23535 | MAT 11:7 | Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li? |
23562 | MAT 12:4 | Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, gis fa mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, mu daldi ko lekk. Fekk jaaduwul mu lekk ca, moom walla ña mu àndaloon; sarxalkat rekk a ko sañoona lekk. |
23576 | MAT 12:18 | «Kii mooy sama Ndaw li ma tànn, di sama Soppe bi neex sama xol. Dinaa def sama Xel ci moom, muy yégal xeet yi yoonu njub. |
23586 | MAT 12:28 | Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen. |
23587 | MAT 12:29 | «Su fi amee nit ku bare doole, te nit bëgga dugg ci këram, nangu alalam, naka la koy defe? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp. |
23589 | MAT 12:31 | Yeesu teg ca ne: «Loolu moo tax maa ngi leen koy wax, bàkkaar walla sos wu mu mana doon, dinañu ko baale, waaye ku sosal Xelum Yàlla, duñu ko baal. |
23590 | MAT 12:32 | Ku sosal Doomu nit ki, dinañu ko baal, waaye ku sosal Xel mu Sell mi, duñu ko baal mukk, du ci àddina si, du ci àllaaxira. |
23662 | MAT 13:54 | dem fa mu yaroo. Mu di leen jàngal ci seen jàngu, ba ñu waaru ne: «Xam-xam bii ak kéemaan yii, fu mu ko jële? |
23710 | MAT 15:8 | “Xeet wii ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma. |
23719 | MAT 15:17 | Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu? |
23750 | MAT 16:9 | Ndax xamaguleen ba tey? Xanaa fàttalikuwuleen juróomi mburu ya ngir juróomi junniy góor ña, ak ñaata pañe ngeen dajale woon ciy dammit? |
23795 | MAT 17:26 | Piyeer ne ko: «Xanaa ñi bokkul ci kër gi.» Yeesu ne ko: «Kon doom yi nag mucc nañu ci. |
23817 | MAT 18:21 | Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko wara baal? Xanaa ba ci juróom ñaari yoon?» |
23835 | MAT 19:4 | Yeesu ne leen: «Xanaa jànguleen ne, ca njàlbéen ga Aji Bind ji sàkk na leen, kii góor, kii jigéen, |
23883 | MAT 20:22 | Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.» |
23886 | MAT 20:25 | Waaye Yeesu woo leen ne leen: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, njiit yi dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi dañu leen di not. |
23932 | MAT 21:37 | Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” |
23937 | MAT 21:42 | Kon Yeesu ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind yi? “Doj wi tabaxkat yi sànni; mujj na di doju koñ; ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.” |
23984 | MAT 22:43 | Noonu Yeesu ne leen: «Lu tax nag Daawuda, bi muy wax ci kàttanu Xelu Yàlla mi, di ko wooye “Boroom bi” ne: |
23989 | MAT 23:2 | «Xutbakat ya ak Farisen ya ñu ngi toog ci jalu Musaa. |
24033 | MAT 24:7 | Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yëngu-yënguy suuf ci bérab yu bare. |
24125 | MAT 26:2 | «Xam ngeen ne ñaari fan a des ci màggalu bésu Mucc ba, te dinañu wor Doomu nit ki, daaj ko ci bant.» |
24164 | MAT 26:41 | Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» |
24176 | MAT 26:53 | Xanaa xamuloo ne man naa laaj sama Baay, te dina ma may ci taxawaay bi mbooloom malaaka mu xel dajul? |
24193 | MAT 26:70 | Waaye Piyeer weddi ko ci kanam ñépp ne ko: «Xawma li ngay wax.» |
24195 | MAT 26:72 | Waaye Piyeer weddiwaat, boole ko ak ay ngiñ ne ko: «Xawma nit kooku.» |
24197 | MAT 26:74 | Bi mu ko déggee, Piyeer daldi giñ ak di waat ne: «Xawma nit kooku.» Te ci taxawaay ginaar daldi sab. |
24211 | MAT 27:13 | Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo li ñu la jiiñ lépp?» |
24254 | MAT 27:56 | Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama ndeyu Saag ak Yuusufa, ak ndeyu doomi Sebede ya. |
24269 | MAT 28:5 | Noonu malaaka ma ne jigéen ña: «Buleen tiit. Xam naa ne yéena ngi wut Yeesu, ma ñu daajoon ca bant ba, |
24283 | MAT 28:19 | Demleen nag sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox ci turu Baay bi ak Doom ji ak Xel mu Sell mi; |
24285 | MRK 1:1 | Xibaaru jàmm bu Yeesu Kirist, Doomu Yàlla, nii la tàmbalee. |
24287 | MRK 1:3 | Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
24292 | MRK 1:8 | Maa ngi leen di sóob ci ndox, waaye moom dina leen sóob ci Xel mu Sell mi.» |
24294 | MRK 1:10 | Bi muy génn ndox mi, mu daldi gis asamaan xar, te Xelum Yàlla di wàcc ci melow pitax, ñëw ci moom. |
24296 | MRK 1:12 | Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma. |
24308 | MRK 1:24 | «Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw, ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell, ji jóge ci Yàlla.» |
24355 | MRK 2:26 | Xanaa yéguleen li amoon ci bési Abiyatar sarxalkat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kër Yàlla ga, lekk mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, jox ci it ña mu àndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat?» |
24384 | MRK 3:27 | «Su fi amee nit ku bare doole, naka la kenn mana dugge ci këram, nangu alalam? Xanaa dafay jëkka yeew ku bare doole ka, ba noppi doora toj këram gépp. |
24386 | MRK 3:29 | Waaye kuy sosal Xel mu Sell mi deesu ko baal mukk; gàddu na bàkkaar ba fàww.» |
24464 | MRK 5:31 | Ay taalibeem ne ko: «Xanaa gisuloo mbooloo mi lay wër; ngay laaj: “Ku ma laal?”» |
24513 | MRK 6:37 | Waaye Yeesu ne leen: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?» |
24538 | MRK 7:6 | Yeesu ne leen: «Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, yéen naaféq yi, bi mu bindee: “Xeet wii, ñu ngi may teral ci seen gémmiñ, waaye seen xol sore na ma. |
24541 | MRK 7:9 | Mu teg ca ne leen: «Xelu ngeen ci tebbi ndigali Yàlla, ngir sàmm seen aada. |
24550 | MRK 7:18 | Yeesu ne leen: «Ndax yéen itam seen xol dafa tëju? Xanaa xamuleen ne, dara lu jóge biti, dugg ci nit, du ko mana indil sobe, |
24586 | MRK 8:17 | Waaye Yeesu yég loolu ne leen: «Lu tax ngeen di werante ci li ngeen indaalewul mburu? Xanaa gisaguleen te xamuleen? Ndax seen xol dafa fatt ba tey? |
24587 | MRK 8:18 | Ndax ay gumbay njàccaar ngeen, te seeni nopp naqari? Xanaa fàttalikuwuleen; |
24633 | MRK 9:26 | Noonu rab wa daldi yuuxu, sayloo xale bi, génn. Xale bi ne nemm, mel ni ku dee, ba tax ñu bare ne: «Dee na.» |
24657 | MRK 9:50 | Xorom lu baax la, waaye bu sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Amleen xorom te ngeen jàmmoo.» |
24676 | MRK 10:19 | Xam nga ndigal yi: “Bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay.”» |
24695 | MRK 10:38 | Waaye Yeesu ne leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan? Ndax man ngeena sóobu ci metit, yi ma nara sóobu?» |
24699 | MRK 10:42 | Waaye Yeesu woo leen naan: «Xam ngeen ne ci xeeti àddina, ñi ñu teg njiit dañu leen di dóor yetu nguur, te kilifa yi di leen not. |
24748 | MRK 12:6 | «Noonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu bëgg. Mujj mu yónni ko naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” |
24751 | MRK 12:9 | Noonu Yeesu laaj leen: «Boroom tool bi nag, lu muy def? Xanaa ñëw, rey beykat ya, dénk tool ba ñeneen. |
24774 | MRK 12:32 | Xutbakat bi ne ko: «Waaw, kilifa gi, li nga wax dëgg la: Yàlla kenn la, te amul jeneen Yàlla ju dul moom. |
24778 | MRK 12:36 | Daawuda moom wax na ci kàttanu Xel mu Sell mi naan: “Boroom bi nee na sama Boroom: ‘Toogal ci sama ndijoor, ba kera may daaneel say noon ci sa kanam.’ ” |
24794 | MRK 13:8 | Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yëngu-yënguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu. |
24797 | MRK 13:11 | Saa su ñu leen jàppee nag, dëj leen ci péncum layoo, buleen jàq ci li ngeen wara wax; li ngeen jot ca waxtu woowa waxleen ko, ndaxte du yéenay wax waaye Xel mu Sell mi. |
24807 | MRK 13:21 | «Booba nag, bu leen kenn waxee: “Kaayleen gis, Kirist a ngi fi,” mbaa: “Xool-leen, mu nga fale,” buleen ko gëm. |
24819 | MRK 13:33 | Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot. |
24823 | MRK 13:37 | Li ma leen wax, ñépp laa ko wax: “Xool-leen!”» |
24861 | MRK 14:38 | Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» |
24863 | MRK 14:40 | délsiwaat, fekk leen ñuy nelaw, ndaxte seeni bët dañoo diis. Xamuñu lu ñu koy tontoo. |
24891 | MRK 14:68 | Waaye Piyeer weddi ko naan: «Xawma li ngay wax, dégguma ci dara.» Mu daldi génn, dem ca buntu kër ga. |
24894 | MRK 14:71 | Waaye Piyeer daldi giñ ak a waat naan: «Xawma nit ki ngay wax.» |
24899 | MRK 15:4 | Kon nag Pilaat laajaat ko: «Déggal lépp li ñu lay jiiñ. Xanaa amoo ci tont?» |
24904 | MRK 15:9 | Pilaat nag xam ne kiñaan rekk a taxoon sarxalkat yu mag yi jébbal ko Yeesu. Kon mu ne mbooloo mi: «Xanaa ma bàyyil leen buuru Yawut yi?» |
24935 | MRK 15:40 | Amoon na fa nag ay jigéen, ñu leen dànd, di xool. Xàmmi nañu ci: Maryaama mi dëkk Magdala, Maryaama yaayu Saag mu ndaw ak Yuusufa, ak Salome. |
24977 | LUK 1:15 | ndaxte dina nekk ku màgg ca kanam Yàlla. Du naan biiñ walla dara luy màndil, te bu juddoo, Xel mu Sell mi daldi ko solu. |
24997 | LUK 1:35 | Malaaka ma ne ko: «Xel mu Sell mi dina wàcc ci yaw, te Aji Kawe ji dina la yiir ci kàttanam. Moo tax xale biy juddu dinañu ko wooye Ku sell ki, Doomu Yàlla ji. |
25003 | LUK 1:41 | Naka la Elisabet dégg Maryaama di nuyoo, doomam daldi yëngatu ci biiram. Noonu Xelum Yàlla mu Sell mi daldi solu Elisabet. |
25029 | LUK 1:67 | Sakari baayu Yaxya daldi fees ak Xel mu Sell mi. Noonu mu wax ci kàddug Yàlla ne: |
25067 | LUK 2:25 | Amoon na ca Yerusalem nit ku tudd Simeyon. Nit ku fonkoon yoonu Yàlla la te déggal ko, doon séentu jamono, ji Yàlla wara dëfal bànni Israyil. Xel mu Sell mi mu ngi ci moom, |
25069 | LUK 2:27 | Noonu Xelum Yàlla daldi yóbbu Simeyon ba ca kër Yàlla ga. Bi waajuri Yeesu indee xale ba, ngir sédde ko Yàlla, ni ko yoon wi santaanee, |
25076 | LUK 2:34 | Noonu Simeyon ñaanal leen, ba noppi ne Maryaama: «Xale bii Yàllaa ko yónni, ngir ñu bare ci Israyil daanu te yékkatiku. Def na ko it muy firnde ju ñuy weddi, |
25082 | LUK 2:40 | Xale baa nga doon màgg, di dëgër, mu fees ak xel te yiwu Yàlla ànd ak moom. |
25091 | LUK 2:49 | Mu ne leen: «Lu tax ngeen may seet? Xanaa xamuleen ne damaa wara nekk ci sama kër Baay?» |
25098 | LUK 3:4 | Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar. |
25110 | LUK 3:16 | Noonu Yaxya wax leen ñoom ñépp ne leen: «Man maa ngi leen di sóob ci ndox. Waaye ki ma ëpp kàttan dina ñëw te yeyoowumaa tekki ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
25116 | LUK 3:22 | Noonu Xel mu Sell mi daldi wàcc ci moom, yor jëmmu pitax, te baat bu jóge asamaan jib ne: «Yaa di sama Doom, ji ma bëgg; ci yaw laa ame bànneex.» |
25133 | LUK 4:1 | Noonu Yeesu fees ak Xel mu Sell mi, jóge dexu Yurdan. |
25134 | LUK 4:2 | Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif. |
25146 | LUK 4:14 | Yeesu dellu diiwaanu Galile, fees ak dooley Xelum Yàlla, te turam siiw ca diiwaan booba bépp. |
25150 | LUK 4:18 | «Xelum Boroom baa ngi ci man, ndaxte moo ma tànn, ngir ma yégal néew doole yi xibaaru jàmm bi. Dafa maa yónni, ngir ma yégal jaam ñi ne dinañu leen goreel, yégal gumba yi ne dinañu gis, te jot ñi ñu not, |
25155 | LUK 4:23 | Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”» |
25166 | LUK 4:34 | «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!» |
25197 | LUK 5:21 | Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku mana baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?» |
25219 | LUK 6:4 | Xanaa yéguleen, ni mu dugge woon ca kër Yàlla ga, jël mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, lekk ca, jox ca ña mu àndaloon? Fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat.» |
25222 | LUK 6:7 | Xutbakat yi ak Farisen yi ñu ngi ko doon xool, ba xam ndax dina ko faj ci bésub noflaay bi, ngir ñu am lu ñu ko tuumaale. |