Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   g    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23227  MAT 1:14  Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
23229  MAT 1:16  Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
23230  MAT 1:17  Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
23231  MAT 1:18  Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
23232  MAT 1:19  Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub teggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura.
23233  MAT 1:20  Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi lage.
23234  MAT 1:21  Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
23235  MAT 1:22  Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
23236  MAT 1:23  «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
23237  MAT 1:24  Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
23238  MAT 1:25  Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
23239  MAT 2:1  Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñuge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
23240  MAT 2:2  Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir ggal ko.»
23241  MAT 2:3  Bi ko Erodd buur baggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp.
23242  MAT 2:4  Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo.
23244  MAT 2:6  “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
23245  MAT 2:7  Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
23246  MAT 2:8  Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma demggal ko.»
23247  MAT 2:9  Ba ñugloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk.
23248  MAT 2:10  Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réya réy.
23249  MAT 2:11  Ñu dugg ca kër ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di koggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
23250  MAT 2:12  Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew.
23251  MAT 2:13  Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko;gal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
23252  MAT 2:14  Yuusufa nag g, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
23253  MAT 2:15  Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
23254  MAT 2:16  Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.
23256  MAT 2:18  «Baat jib na ci Rama, ay jooy ak yuux gu réy, Rasel mooy jooy ay doomam teggul kenn dëfal ko, ndaxte saay nañu.»
23257  MAT 2:19  Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra,
23258  MAT 2:20  ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu;gal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
23259  MAT 2:21  Yuusufag nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
23260  MAT 2:22  Waaye bi muggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile.
23261  MAT 2:23  Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan: «Dees na ko tudde Nasareen.»
23263  MAT 3:2  Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
23265  MAT 3:4  Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem.
23266  MAT 3:5  Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan.
23267  MAT 3:6  Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
23268  MAT 3:7  Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
23269  MAT 3:8  Jëfeleen nag ni ñu tuub seeni bàkkaar,
23270  MAT 3:9  te buleen wax ci seen xel naan: “Nun daal doomi Ibraayma lanu,” ndaxte maa ngi leen koy wax, Yàlla man na sàkkal Ibraayma ay doom ci doj yii.
23271  MAT 3:10  Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si.
23272  MAT 3:11  Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.