23214 | MAT 1:1 | Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma. |
23215 | MAT 1:2 | Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam; |
23216 | MAT 1:3 | Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram; |
23217 | MAT 1:4 | Aram Aminadab; Aminadab Nason; Nason Salmon; |
23218 | MAT 1:5 | Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi, |
23219 | MAT 1:6 | miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri; |
23220 | MAT 1:7 | Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf; |
23221 | MAT 1:8 | Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas; |
23222 | MAT 1:9 | Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya; |
23223 | MAT 1:10 | Esekiya Manase; Manase Amon; Amon Yosiyas; |
23224 | MAT 1:11 | Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon. |
23225 | MAT 1:12 | Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel, |
23226 | MAT 1:13 | miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor; |
23227 | MAT 1:14 | Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd; |
23228 | MAT 1:15 | Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba; |
23229 | MAT 1:16 | Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo. |
23230 | MAT 1:17 | Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent. |
23231 | MAT 1:18 | Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi. |
23232 | MAT 1:19 | Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura. |
23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23234 | MAT 1:21 | Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.» |
23235 | MAT 1:22 | Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: |
23236 | MAT 1:23 | «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» |
23237 | MAT 1:24 | Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon. |
23239 | MAT 2:1 | Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. |
23240 | MAT 2:2 | Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.» |
23241 | MAT 2:3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. |
23242 | MAT 2:4 | Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo. |
23243 | MAT 2:5 | Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent: |
23244 | MAT 2:6 | “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”» |
23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |