23235 | MAT 1:22 | Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: |
23239 | MAT 2:1 | Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. |
23240 | MAT 2:2 | Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.» |
23241 | MAT 2:3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. |
23242 | MAT 2:4 | Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo. |
23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |
23247 | MAT 2:9 | Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk. |
23266 | MAT 3:5 | Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan. |
23272 | MAT 3:11 | Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara. |
23273 | MAT 3:12 | Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.» |
23276 | MAT 3:15 | Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu. |
23277 | MAT 3:16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
23282 | MAT 4:4 | Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
23286 | MAT 4:8 | Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. |
23287 | MAT 4:9 | Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» |
23289 | MAT 4:11 | Noonu Seytaane bàyyi ko. Te ay malaaka daldi ñëw fi Yeesu, di ko topptoo. |
23290 | MAT 4:12 | Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile. |
23291 | MAT 4:13 | Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. |
23296 | MAT 4:18 | Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon. |
23297 | MAT 4:19 | Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.» |
23298 | MAT 4:20 | Ca saa sa ñu daldi bàyyi seeni mbaal, topp ci moom. |
23300 | MAT 4:22 | Ca saa sa ñu daldi bàyyi gaal ga ak seen baay, topp ci moom. |
23301 | MAT 4:23 | Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngle ci seeni jàngu tey yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña, |
23302 | MAT 4:24 | ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen. |
23303 | MAT 4:25 | Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan. |
23314 | MAT 5:11 | «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man. |
23316 | MAT 5:13 | «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. |
23318 | MAT 5:15 | Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp. |
23321 | MAT 5:18 | Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am. |
23323 | MAT 5:20 | Ndaxte maa ngi leen koy wax, bu seen njubte ëppul njubteg xutbakat ya ak Farisen ya, dungeen tàbbi mukk ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23325 | MAT 5:22 | Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara. |
23327 | MAT 5:24 | nanga fa bàyyi sa sarax ca kanam sarxalukaay ba, nga jëkka dem, juboo ak sa mbokk, ba noppi dellu, joxe sa sarax. |
23331 | MAT 5:28 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel. |
23333 | MAT 5:30 | Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. Bu la sa loxol ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. |
23334 | MAT 5:31 | «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.” |
23339 | MAT 5:36 | Bul giñ it ci sa bopp, ndaxte manuloo weexal mbaa ñuulal benn ci say kawar. |
23342 | MAT 5:39 | Waaye man maa ngi leen di wax ne buleen bañ ku leen def lu bon, waaye ku la pes ci sa lexu ndijoor, jox ko ba ca des. |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23347 | MAT 5:44 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, soppleen seeni bañaale te ñaanal ñi leen di fitnaal, |
23349 | MAT 5:46 | Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban yool ngeen am? Xanaa juutikat yi duñu def noonu it? |
23353 | MAT 6:2 | Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23355 | MAT 6:4 | ngir sa sarax nekk kumpa. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23356 | MAT 6:5 | «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23357 | MAT 6:6 | Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23367 | MAT 6:16 | «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23368 | MAT 6:17 | Yaw nag booy woor, xeeñalal sa bopp te nga sëlmu, |
23369 | MAT 6:18 | ngir sa koor baña feeñu nit ñi, waaye mu feeñu sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23373 | MAT 6:22 | «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer, |
23374 | MAT 6:23 | waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! |
23375 | MAT 6:24 | «Kenn manula jaamoondoo ñaari sang; fàww nga bañ kii, bëgg ki ci des, walla nga jàpp ci kenn ki, xeeb ki ci des. Manuleena boole jaamu Yàlla ak jaamu Alal. |
23377 | MAT 6:26 | Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare? |
23378 | MAT 6:27 | Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo mana yokk waxtu ci àppam? |
23383 | MAT 6:32 | Ndaxte loolu lépp, ñi xamul Yàlla ñoo koy wut. Te seen Baay, bi nekk ci kaw, xam na ne am ngeen soxla ci loolu lépp. |
23384 | MAT 6:33 | Waaye jëkkleena wut nguuram ak njubteem, te loolu lépp dina leen ko ci dollil. |
23385 | MAT 6:34 | Buleen jaaxle nag ngir ëllëg, ndaxte ëllëg dina topptoo boppam. Bés bu nekk, coonoom doy na ko. |
23391 | MAT 7:6 | «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen. |
23393 | MAT 7:8 | Ndaxte képp kuy ñaan, dinga am; kuy seet, dinga gis; kuy fëgg, ñu ubbil la. |
23397 | MAT 7:12 | «Kon nag lépp lu ngeen bëgg, nit ñi defal leen ko, yéen itam nangeen leen ko defal; ndaxte loolu moo ëmb yoonu Musaa ak waxi yonent yi. |
23406 | MAT 7:21 | «Du képp ku may wax: “Boroom bi, Boroom bi,” mooy dugg ca nguuru Yàlla Aji Kawe ji; ka cay dugg mooy kiy def sama coobarey Baay, bi nekk ci kaw. |
23409 | MAT 7:24 | «Képp ku dégg nag lii ma leen wax, te di ko jëfe, dinga mel ni nit ku am xel, ku tabax këram, samp ko ciw doj. |
23410 | MAT 7:25 | Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa. |
23411 | MAT 7:26 | Waaye képp ku dégg lii ma leen wax te jëfewuloo ko, dinga mel ni nit ku ñàkk xel, ku tabax këram ci gannuus bi. |
23412 | MAT 7:27 | Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.» |
23413 | MAT 7:28 | Bi Yeesu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma daldi waaru ca njàngleem, |
23415 | MAT 8:1 | Bi loolu amee Yeesu wàcc ca tund wa, te mbooloo mu bare topp ko. |
23418 | MAT 8:4 | Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.» |
23419 | MAT 8:5 | Gannaaw loolu Yeesu duggoon na Kapernawum. Bi mu fa duggee nag, ab njiitu xare fekksi ko. Mu ñaan ko, |
23424 | MAT 8:10 | Bi ko Yeesu déggee, mu waaru, ne ña topp ci moom: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, masumaa gis ci bànni Israyil ku gëme ni kii. |
23425 | MAT 8:11 | Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23429 | MAT 8:15 | Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo. |
23430 | MAT 8:16 | Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp. |
23431 | MAT 8:17 | Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan: «Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.» |
23433 | MAT 8:19 | Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.» |
23434 | MAT 8:20 | Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.» |
23436 | MAT 8:22 | Yeesu ne ko: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.» |