23215 | MAT 1:2 | Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam; |
23228 | MAT 1:15 | Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba; |
23229 | MAT 1:16 | Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo. |
23236 | MAT 1:23 | «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.» |
23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |
23252 | MAT 2:14 | Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga. |
23273 | MAT 3:12 | Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.» |
23307 | MAT 5:4 | Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol. |
23332 | MAT 5:29 | Bu la sa bëtu ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. |
23353 | MAT 6:2 | Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23356 | MAT 6:5 | «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23367 | MAT 6:16 | «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23370 | MAT 6:19 | «Buleen dajale alal ci àddina, fu ko max ak xomaag di yàqe, ak fu sàcc di dugg, jot ko. |
23371 | MAT 6:20 | Waaye dajaleleen alal ci laaxira, fu ko max ak xomaag dul yàqe, ak fu sàcc dul dugg, jot ko. |
23377 | MAT 6:26 | Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare? |
23390 | MAT 7:5 | Naaféq, jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. |
23407 | MAT 7:22 | Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?” |
23425 | MAT 8:11 | Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji. |
23430 | MAT 8:16 | Ca ngoon sa ñu indil ko ñu bare ñu rab jàpp. Yeesu dàq rab ya ak kàddoom te faj ñi wopp ñépp. |
23445 | MAT 8:31 | Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.» |
23463 | MAT 9:15 | Yeesu ne leen: «Ndax gan yi ñëw ci céet dinañu naqarlu dara, li feek boroom céet gaa ngi ànd ak ñoom? Waaye bés yaa ngi ñëw yu ñuy jële boroom céet gi ci seen biir; booba nag dinañu woor. |
23465 | MAT 9:17 | Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.» |
23472 | MAT 9:24 | Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal. |
23473 | MAT 9:25 | Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg. |
23481 | MAT 9:33 | Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, masuñu koo gis ci Israyil.» |
23482 | MAT 9:34 | Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
23487 | MAT 10:1 | Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp. |
23494 | MAT 10:8 | Fajleen ñi wopp, dekkal ñi dee, fajleen gaana yi te dàq rab yi. Cig neen ngeen ame, mayeleen cig neen. |
23500 | MAT 10:14 | Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu seeni wax, génnleen ca kër ga mbaa ca dëkk ba, yëlëb seen pëndu tànk. |
23559 | MAT 12:1 | Amoon na benn bésub noflaay Yeesu jaar ci ay tool yu ñor, fekk ay taalibeem xiif; ñu daldi fàq ay gub nag, di lekk. |
23582 | MAT 12:24 | Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.» |
23584 | MAT 12:26 | Bu Seytaane dàqee Seytaane nag, xeex na boppam; kon naka la nguuram di mana yàgge? |
23585 | MAT 12:27 | Te it bu fekkee ne man damay dàq ay rab ci kàttanu Beelsebul, seeni taalibe nag, ci gan kàttan lañu leen di dàqe? Kon ñoo leen di àtte. |
23586 | MAT 12:28 | Waaye bu fekkee ne ci Xelum Yàlla laay dàqe rab, kon nguuru Yàlla agsi na ba ci yéen. |
23623 | MAT 13:15 | Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.” |
23638 | MAT 13:30 | Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”» |
23675 | MAT 14:9 | Bi ko buur ba déggee, mu am naqar, waaye ngiñ la ak gan ña tax mu santaane, ñu jox ko ko. |
23677 | MAT 14:11 | Ñu indi bopp bi ci biir ndab, jox ko janq ba, mu jox ko ndeyam. |
23709 | MAT 15:7 | Yéen ñi naaféq, Esayi waxoon na bu baax ci kàddug Yàlla ci seen mbir, bi mu naan: |
23719 | MAT 15:17 | Xamuleen ne, lépp lu dugg ci gémmiñ, ci biir lay jëm tey génn ca bérab bu làqu? |
23721 | MAT 15:19 | Ndaxte ci xol la xalaat yu bon di jóge, ak bóom, njaaloo, ndoxaanu yàqute, càcc, seede lu dul dëgg ak saaga. |
23743 | MAT 16:2 | Noonu Yeesu ne leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.” |
23744 | MAT 16:3 | Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, waaye manuleena ràññee firndey jamono ji nu tollu. |
23788 | MAT 17:19 | Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun manunu woona dàq rab wi?» |
23792 | MAT 17:23 | dinañu ko rey, mu dekki ca ñetteelu fan ba.» Bi ko taalibe ya déggee, ñu am naqar lool. |
23796 | MAT 17:27 | Waaye bëgguma nu naqaral leen; demal sànni oos ca dex ga te nga génne jën wa jëkka xëcc. Boo ubbee gémmiñam, dinga ca gis posetu estateer. Jël ko nag, jox leen ko ngir man ak yaw.» |
23805 | MAT 18:9 | Boo xamee ne sa bët mu ngi lay yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore. Ndaxte nga patt te dugg ci dund gu wóor gi, moo gën ci yaw, nga am ñaari bët, te ñu sànni la ci sawara. |
23827 | MAT 18:31 | «Bi ay moroomam gisee loolu nag, ñu am naqar wu réy, daldi dem, xamal seen sang li xew lépp. |
23836 | MAT 19:5 | te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.” |
23883 | MAT 20:22 | Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.» |
23907 | MAT 21:12 | Bi loolu amee Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, dàq ñépp ña fay jaay ak ña fay jënd. Mu daaneel taabali weccikatu xaalis ya ak tooguy jaaykati pitax ya, |
23959 | MAT 22:18 | Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi? |
23973 | MAT 22:32 | “Maay Yàllay Ibraayma ak Yàllay Isaaxa ak Yàllay Yanqóoba”? Li ciy génn mooy, nekkul Yàllay ñi dee waaye Yàllay ñiy dund la.» |
24000 | MAT 23:13 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci. |
24002 | MAT 23:15 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon. |
24010 | MAT 23:23 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des. |
24012 | MAT 23:25 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal. |
24014 | MAT 23:27 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk. |
24015 | MAT 23:28 | Yéen itam, ci ngistal dangeena mel ni ñu jub, waaye ci seen biir dangeen fees ak naaféq ak lu bon. |
24016 | MAT 23:29 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi. |
24041 | MAT 24:15 | «Dina am bés bu li ñuy wax: “Lu araam luy yàqe” dina tege ca bérab bu sell ba. Mooy li ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Dañeel; ku ko jàng, nanga ko xam. |
24053 | MAT 24:27 | Ndaxte ni melax di fàqe penku, te lerax ba sowu, noonu la ñëwug Doomu nit ki di mel. |
24055 | MAT 24:29 | «Gannaaw metitu bés yooyule nag, ca saa sa jant bi dina lëndëm te weer wi dootul leer; biddiiw yi dinañu fàq, daanu ci asamaan, te kàttani asamaan yi yëngu. |
24058 | MAT 24:32 | Yeesu teg ca ne: «Jàngleen misaalu garabu figg ga. Boo xamee ne ay bànqaasam duy nañu, tey xobam sëq, xam ngeen ne nawet jege na. |
24077 | MAT 24:51 | Dina ko dóor ay yar yu metti, jox ko añub naaféq. Foofa dees na fa jooy tey yéyu. |
24078 | MAT 25:1 | «Booba nguuru Yàlla Aji Kawe ji dina mel ni fukki janq, ñu fab seeni làmp, génn, gatanduji boroom séet ba. |
24079 | MAT 25:2 | Fekk juróom ca janq ya di ñu am xel, juróom ya ca des ñàkk xel. |
24081 | MAT 25:4 | waaye ñi am xel ñoom fab nañu seeni làmp, fabaale diw ciy njaq. |
24084 | MAT 25:7 | Bi ko janq ya déggee, ñu jóg, defar seeni làmp. |
24088 | MAT 25:11 | Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” |
24130 | MAT 26:7 | jenn jigéen ñëw ci moom, yor njaq lu ñu yette doj wu ñuy wax albaatar. Njaq la def latkoloñ ju jar lu baree bare. Noonu bi Yeesu toogee di lekk, jigéen ji tuur ko ci boppu Yeesu. |
24131 | MAT 26:8 | Waaye bi ko taalibe ya gisee, ñu daldi mer ne: «Yàq gii, lu muy jariñ? |
24145 | MAT 26:22 | Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?» |
24162 | MAT 26:39 | Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.» |
24165 | MAT 26:42 | Yeesu delluwaat di ñaan ne: «Sama Baay, bu fekkee ne kaasu naqar bii manu maa teggi te naanuma ko, kon na sa coobare am.» |
24182 | MAT 26:59 | Noonu sarxalkat yu mag ya ak kureelu àttekat ya di seet naaféq bu mana seede ci Yeesu, ba ñu man koo rey, |
24201 | MAT 27:3 | Bi nga xamee ne Yudaa, mi woroon Yeesu, gis na ne daan nañu ko, mu am naqaru xol. Mu dem nag ca sarxalkat yu mag ya ak njiit ya, delloo leen fanweeri poset yu xaalis, |
24226 | MAT 27:28 | Noonu ñu summi ko, solal ko mbubbum xarekat mu xonq curr. |
24318 | MRK 1:34 | Noonu mu wéral ñu bare, ñu wopp ak ay jàngoro yu wuute, te dàq ay rab yu bare. Waaye mu tere rab yi, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ko. |
24323 | MRK 1:39 | Noonu mu wër ci diiwaanu Galile gépp, di waare ci seeni jàngu, tey dàq rab yi. |
24351 | MRK 2:22 | Te kenn du def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, biiñ bi day toj mbuus yi, ba mbuus yi yàqu, biiñ bi tuuru. Waaye biiñ bu bees, ci mbuus yu bees lañu koy def.» |
24352 | MRK 2:23 | Amoon na benn bésub noflaay Yeesu jaar ciy tool yu ñor. Bi ñuy dem nag, ay taalibeem daldi fàq ay gub. |
24362 | MRK 3:5 | Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wér péŋŋ. |
24372 | MRK 3:15 | mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab. |
24379 | MRK 3:22 | Te it xutbakat ya jóge Yerusalem ne: «Beelsebul jàpp na ko; ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.» |
24380 | MRK 3:23 | Noonu Yeesu woo leen, wax ak ñoom ciy léeb ne leen: «Naka la Seytaane mana dàqe Seytaane? |
24414 | MRK 4:22 | Amul dara luy kumpa lu ñu warula siiwal, mbaa mu làqu te warul ne fàŋŋ. |
24424 | MRK 4:32 | waaye boo ko jiyee, day jóg, màgg, ba sut gàncaxi tóokër yépp; mu sax ay bànqaas yu réy, ba picci asamaan tàgg ci keram.» |
24443 | MRK 5:10 | Muy ñaan Yeesu lool, ngir mu bañ leena dàq ca réew ma. |
24472 | MRK 5:39 | Mu dugg ne leen: «Lu ngeen di soow, tey jooy? Janq bi deewul, day nelaw rekk.» |
24473 | MRK 5:40 | Waaye ñu di ko ñaawal. Noonu Yeesu génne ñépp, woo baayu janq bi ak yaay ji ak ñi mu àndal, dugg fa janq bi nekk. |
24474 | MRK 5:41 | Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.» |
24475 | MRK 5:42 | Ca saa sa janq bi jóg, daldi dox, ndaxte amoon na fukki at ak ñaar. Ñépp daldi waaru, ba ne jomm. |
24476 | MRK 5:43 | Ci kaw loolu Yeesu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal; teg ca naa: «Mayleen janq bi, mu lekk.» |
24483 | MRK 6:7 | Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar. |
24487 | MRK 6:11 | Koo xam ne gàntu na leen, mbaa mu tanqamlu leen, génnleen fa, yëlëb seen pëndu tànk, ngir seede leen seen réer.» |
24489 | MRK 6:13 | Ñu dàq ay rab yu bare, te diw boppi jarag yu bare, wéral leen. |