Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   r    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23214  MAT 1:1  Lii mooy cosaanu Yeesu Kirist, sëtu Daawuda, sëtu Ibraayma.
23215  MAT 1:2  Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
23216  MAT 1:3  Yuda, Peres ak Sara ci Tamar; Peres Esron, miy baayu Aram;
23217  MAT 1:4  Aram Aminadab; Aminadab Nason; Nason Salmon;
23218  MAT 1:5  Salmon jur ci Raxab doom ju tudd Bowas; Bowas am ak Ruut Obedd; Obedd jur Isayi,
23219  MAT 1:6  miy baayu buur bi Daawuda. Daawuda moo jur Suleymaan ci ki nekkoon soxnas Uri;
23220  MAT 1:7  Suleymaan jur Robowam; Robowam Abiya; Abiya Asaf;
23221  MAT 1:8  Asaf Yosafat; Yosafat Yoram, miy baayu Osiyas;
23222  MAT 1:9  Osiyas jur Yowatam; Yowatam Akas, miy baayu Esekiya;
23224  MAT 1:11  Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
23225  MAT 1:12  Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel,
23226  MAT 1:13  miy baayu Abiyudd; Abiyudd Eliyakim; Eliyakim Asor;
23227  MAT 1:14  Asor Sadog; Sadog Akim; Akim Eliyudd;
23228  MAT 1:15  Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;
23229  MAT 1:16  Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
23230  MAT 1:17  Mboolem giir googu nag, la dale ca Ibraayma ba ca Daawuda, fukk lañu ak ñeent; la dale ca Daawuda ba ca njaam ga ca Babilon, fukk lañu ak ñeent; la dale njaam ga ca Babilon ba ci Kirist, fukk lañu ak ñeent.
23231  MAT 1:18  Nii la Yeesu Kirist juddoo. Bi ñu mayee Maryaama ndeyam Yuusufa, waaye laata ñoo ànd, gis nañu ne dafa ëmb ci kàttanu Xel mu Sell mi.
23232  MAT 1:19  Yuusufa jëkkëram nag, nekkoon na nit ku jub te bëggu ko woona weer. Mu nara xàccook moom ci sutura.
23233  MAT 1:20  Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
23234  MAT 1:21  Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar
23235  MAT 1:22  Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan:
23236  MAT 1:23  «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
23237  MAT 1:24  Noonu Yuusufa yewwu, yeggali soxnaam, na ko ko malaakam Boroom bi sante woon.
23238  MAT 1:25  Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
23239  MAT 2:1  Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
23240  MAT 2:2  Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.»
23241  MAT 2:3  Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp.
23242  MAT 2:4  Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo.
23243  MAT 2:5  Ñu ne ko: «Ca Betleyem ci diiwaanu Yude, ndaxte lii lañu bind jaarale ko cib yonent:
23244  MAT 2:6  “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
23245  MAT 2:7  Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
23246  MAT 2:8  Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
23247  MAT 2:9  Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk.
23248  MAT 2:10  Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réya réy.
23249  MAT 2:11  Ñu dugg car ga, gis xale ba ak Maryaama ndeyam, ñu daldi sukk, di ko màggal. Ñu ubbi seeni boyetu alal, may ko wurus ak cuuraay ak ndàbb lu xeeñ lu ñuy wax miir.
23250  MAT 2:12  Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew.
23251  MAT 2:13  Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
23252  MAT 2:14  Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
23253  MAT 2:15  Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
23254  MAT 2:16  Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la kor, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.