25307 | LUK 7:43 | Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gëna bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,» |
25760 | LUK 18:3 | Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!” |
25761 | LUK 18:4 | Àttekat ba bañ lu yàgg, waaye am bés mu ne ci xelam: “Ragaluma Yàlla te faalewuma mbindeef, |
26404 | JHN 7:7 | Àddina du leen bañ waaye bañ na ma, man, ndaxte maa wax ne seeni jëf baaxul. |
26473 | JHN 8:23 | Yeesu ne leen: «Yéen, fii ngeen bawoo, ci suuf, waaye man ca kaw laa jóge. Àddina ngeen soqikoo, waaye man bokkuma ci. |
26548 | JHN 9:39 | Yeesu ne ko: «Àttee ma taxa ñëw àddina, ngir ñi gumba gis, ñiy gis gumba.» |
26680 | JHN 12:31 | Àtteb àddina si jot na: léegi ñu dàq malaaka mu bon, mi jiite àddina si. |
26736 | JHN 13:37 | Piyeer ne ko: «Boroom bi, lu tax manuma laa topp léegi? Àttan naa joxe sama bakkan ngir yaw!» |
26737 | JHN 13:38 | Yeesu ne ko: «Àttan ngaa joxe sa bakkan ngir man? Ci dëgg-dëgg maa ngi la koy wax, bala ginaar a sab, dinga ma weddi ñetti yoon. |
26754 | JHN 14:17 | Kooku mooy Xelu Yàlla, mi yor dëgg. Àddina du ko mana nangu, ndaxte gisu ko te xamu ko. Yéen xam ngeen ko, ndaxte mi ngi dëkk ak yéen te dina nekk ci yéen. |
27388 | ACT 11:12 | Te Xel mi ne ma: “Àndal ak ñoom, te bu ci werante.” Juróom benni bokk, yi fi teew, gunge woon nañu ma, ba nu dugg ca kër góor googu. |
27588 | ACT 16:36 | Kon boroom kaso ba yégal loolu Pool ne ko: «Àttekat ya jox nañu ma ndigal, ngir ma yiwi leen, ngeen dem; léegi nag génnleen te dem ci jàmm.» |
28661 | 1CO 10:26 | Ndaxte Mbind mi nee na: «Àddina ak li ci biiram lépp, Boroom bi moo ko moom.» |
28819 | 1CO 15:33 | Bu leen ko réere mbir: «Ànd bu bon dina yàq nit ku baax.» |
28898 | 2CO 2:6 | Àtte bi ko mbooloo mi teg, doy na. |
29945 | 2TI 4:8 | Fi mu ne Yàllaa ngi may xaare añu ku jub, di kaalag ndam gi ma Boroom, biy Àttekat bu jub, di jox ca bés ba, te jéllale naa sama bopp, waaye képp ku def sa xol cig feeñam. |
30363 | JAS 2:3 | ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,» |
30430 | JAS 5:9 | Buleen jàmbatante, samay bokk, ngir ragal Yàlla àtte leen. Àttekat baa ngi ci bunt bi sax! |
30507 | 1PE 3:16 | waaye na tont li lewet te ànd ak wegeel. Àndleen ak xel mu dal; noonu ñi leen di sikkal ndax seen dund gu rafet ci gëm Kirist, dinañu rus ci seeni sos. |