27703 | ACT 20:9 | Noonu waxambaane wu tudd Ëtikus te toog ca palanteer ba, gëmméentu bay jeyaxu. Bi Pool di gëna yaatal waxtaanam nag, nelaw daldi ko jàpp, mu xàwwikoo ca ñetteelu taax ma, daanu, ñu yékkati ko, fekk mu dee. |
27937 | ACT 27:14 | Waaye nees-tuut ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon», jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw. |
29881 | 2TI 1:5 | Maa ngi fàttaliku sa ngëm gu dëggu, gi nekkoon ci sa maam Lowis ak sa yaay Ënis, te mu wóor ma ne sax na ci yaw it. |
29958 | 2TI 4:21 | Gaawala ñëw, bala lolli di gàllankoor sa yoon. Ëbulus, Pudeñsë, Linus, Këlójaa ak yeneen bokk yépp ñu ngi lay nuyu. |