23233 | MAT 1:20 | Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge. |
23235 | MAT 1:22 | Loolu lépp xewoon na, ngir amal li Boroom bi wax, jaarale ko cib yonent, bi mu naan: |
23241 | MAT 2:3 | Bi ko Erodd buur ba déggee, mu daldi jaaxle, moom ak waa Yerusalem gépp. |
23242 | MAT 2:4 | Mu woolu nag sarxalkat yu mag yépp ak xutbakati xeet wa, laaj leen fu Almasi bi, maanaam Kirist, wara juddoo. |
23244 | MAT 2:6 | “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”» |
23247 | MAT 2:9 | Ba ñu dégloo buur ba nag, ñu dem. Te biddiiw, ba ñu gisoon ca penku ba, ne tëll jiite leen, ba àgg, tiim fa xale ba nekk. |
23248 | MAT 2:10 | Ba ñu gisee biddiiw ba nag, ñu am mbég mu réya réy. |
23250 | MAT 2:12 | Bi ñu ko defee Yàlla artu na leen ci biir gént, ñu baña dellu ca Erodd. Noonu ñu jaar weneen yoon, ñibbi seen réew. |
23251 | MAT 2:13 | Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» |
23253 | MAT 2:15 | Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.» |
23254 | MAT 2:16 | Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon. |
23256 | MAT 2:18 | «Baat jib na ci Rama, ay jooy ak yuux gu réy, Rasel mooy jooy ay doomam te bëggul kenn dëfal ko, ndaxte saay nañu.» |
23257 | MAT 2:19 | Bi nga xamee ne Erodd faatu na, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ca Misra, |
23260 | MAT 2:22 | Waaye bi mu déggee ne Arkelawus moo donn Erodd baayam ca nguuru Yude, mu ragal faa dem. Yàlla artu ko nag ci gént, mu daldi dem diiwaanu Galile. |
23265 | MAT 3:4 | Yaxya nag mu ngi soloon mbubb mu ñu ràbbe kawaru giléem, takk geñog der ci ndiggam. Ay njéeréer la doon dunde ak lem. |
23266 | MAT 3:5 | Noonu ñépp génn jëm ci moom, ñi dëkk Yerusalem ak diiwaanu Yude, ak waa dexu Yurdan. |
23268 | MAT 3:7 | Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
23271 | MAT 3:10 | Sémmiñ wi tiim na reeni garab yi. Garab nag gu meññul doom yu baax, dees na ko gor, sànni ko ci sawara si. |
23273 | MAT 3:12 | Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.» |
23276 | MAT 3:15 | Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu. |
23277 | MAT 3:16 | Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu. |
23278 | MAT 3:17 | Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.» |
23282 | MAT 4:4 | Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”» |
23286 | MAT 4:8 | Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam. |
23287 | MAT 4:9 | Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.» |
23290 | MAT 4:12 | Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile. |
23291 | MAT 4:13 | Gannaaw gi, mu toxoo dëkku Nasaret, dem dëkk Kapernawum, bi féeteek dex ga ci diiwaani Sabulon ak Neftali. |
23293 | MAT 4:15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali, di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan, yaw Galile, réewum ñi dul Yawut— |
23294 | MAT 4:16 | xeet wa nekkoon cig lëndëm, gis na leer gu mag, ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim, leer fenkal na leen.» |
23301 | MAT 4:23 | Ba loolu amee Yeesu doon wër Galile gépp, di jàngle ci seeni jàngu tey yégle xibaaru jàmm bi ci nguuru Yàlla; muy faj jàngoro yépp ak wéradi yépp ca nit ña, |
23302 | MAT 4:24 | ba tax turam siiw ba ci biir réewu Siri mépp. Ñu di ko indil ñi wopp ñépp, ñi sonn ndax ay jàngoro ak metit yu bare, ñi rab jàpp, ñiy say ak ñi làggi, mu faj leen. |
23304 | MAT 5:1 | Bi Yeesu gisee mbooloo ma nag, mu yéeg ca tund wa, toog; taalibeem ya ñëw ci moom. |
23306 | MAT 5:3 | «Yéen ñi xam seen ñàkk doole ngir neex Yàlla, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |
23307 | MAT 5:4 | Yéen ñi nekk ci naqar, barkeel ngeen, ndax dees na dëfal seen xol. |
23308 | MAT 5:5 | Yéen ñi lewet, barkeel ngeen, ndax dingeen moomi àddina. |
23309 | MAT 5:6 | Yéen ñi xiif te mar njub, barkeel ngeen, ndax dingeen regg. |
23310 | MAT 5:7 | Yéen ñi am yërmande, barkeel ngeen, ndax dees na leen yërëm. |
23311 | MAT 5:8 | Yéen ñi am xol bu sell, barkeel ngeen, ndax dingeen gis Yàlla. |
23312 | MAT 5:9 | Yéen ñiy wut jàmm, barkeel ngeen, ndax dees na leen tudde doomi Yàlla. |
23313 | MAT 5:10 | Yéen ñi ñu fitnaal ndax seen njub, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji, yéena ko yelloo. |
23314 | MAT 5:11 | «Barkeel ngeen, bu ñu leen di saaga, di leen fitnaal, di leen sosal lépp lu bon ngir man. |
23315 | MAT 5:12 | Bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu lañu daan fitnaale yonent yi fi jiitu. |
23316 | MAT 5:13 | «Yéena di xoromus àddina. Bu xorom sàppee, nan lañu koy delloo cafkaam? Du jariñati dara, lu dul ñu sànni ko ci biti, nit ñi dox ci kawam. |
23317 | MAT 5:14 | Yéena di leeru àddina. Dëkk, bu nekk ci kaw tund du mana nëbbu. |
23318 | MAT 5:15 | Te it duñu taal làmp, dëpp cig leget, waaye dañu koy wékk, ba muy leeral ñi nekk ci kër gi ñépp. |
23321 | MAT 5:18 | Ndaxte ci dëgg maa ngi leen koy wax, li feek asamaan ak suuf wéyul, benn tomb walla benn rëddu araf du wéy mukk ci yoonu Musaa, ba kera yépp di am. |
23324 | MAT 5:21 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” |
23325 | MAT 5:22 | Waaye man maa ngi leen di wax ne képp ku mere sa mbokk, dinañu la àtte. Ku wax sa mbokk: “Amoo bopp,” dinañu la àtte ca kureelu àttekat ya. Ku ko wax: “Alku nga,” dinañu la àtte ci sawara. |
23328 | MAT 5:25 | «Gaawala juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeena egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la. |
23329 | MAT 5:26 | Ci dëgg maa ngi la koy wax, doo génn foofa mukk te feyuloo dërëm bi ci mujj. |
23330 | MAT 5:27 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” |
23331 | MAT 5:28 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, képp ku xool jigéen, xédd ko, njaaloo nga ak moom ci sa xel. |
23333 | MAT 5:30 | Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. Bu la sa loxol ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. |
23335 | MAT 5:32 | Waaye man maa ngi leen di wax ne, ku fase sa soxna te du ci njaaloo, yaa koy tegtal yoonu njaaloo. Te it ku takk jigéen ju ñu fase, njaaloo nga. |
23336 | MAT 5:33 | «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” |
23340 | MAT 5:37 | Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge. |
23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23348 | MAT 5:45 | ngir wone ne yéenay doomi seen Baay bi nekk ci kaw. Ndaxte mu ngi fenkal jantam ci kaw ñu bon ñi ak ñu baax ñi, te muy tawal ñi jub ak ñi jubadi. |
23353 | MAT 6:2 | Booy sàkk sarax nag, bul yeble ci sa kanam, ñu yéene la. Moom la naaféq yi di def ca jàngu ya ak ca mbedd ya, ngir nit ñi màggal leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23356 | MAT 6:5 | «Bu ngeen di ñaan, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi bëgg di ñaan, taxaw ca jàngu ya ak fa mbedd yay daje, ngir nit ñi gis leen. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23357 | MAT 6:6 | Yaw nag booy ñaan, duggal ci sa néeg, tëj bunt bi, te nga ñaan sa Baay bi bët manta gis. Noonu sa Baay, bi dara umpul, dina la ko delloo. |
23360 | MAT 6:9 | Yéen nag nii ngeen wara ñaane: “Sunu Baay bi nekk ci kaw, yal na sa tur di lu ñu sellal, |
23365 | MAT 6:14 | «Su ngeen baalee ñi leen tooñ, seen Baay bi ci kaw dina leen baal seeni tooñ yéen itam. |
23367 | MAT 6:16 | «Su ngeen di woor, buleen mel ni naaféq yi, ñoom ñi yoggoorlu, di ñaawal seeni kanam, ngir seen koor feeñu nit ñi. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, jot nañu seen pey gépp. |
23373 | MAT 6:22 | «Bët mooy làmpu yaram. Bu sa bët wéree, kon sa yaram wépp leer, |
23374 | MAT 6:23 | waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! |
23378 | MAT 6:27 | Ana kan ci yéen ci kaw njaaxleem moo mana yokk waxtu ci àppam? |