Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   ó    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23215  MAT 1:2  Ibraayma moo jur Isaaxa; Isaaxa jur Yanqóoba; Yanqóoba jur Yuda ak i doomi baayam;
23224  MAT 1:11  Yosiyas jur Yekoñas ak i doomi baayam ca jamono, ja ñu defe Yawut ya jaam, yóbbu leen Babilon.
23225  MAT 1:12  Ba ñu leen yóbboo ca Babilon, Yekoñas jur Salacel; Salacel Sorobabel,
23228  MAT 1:15  Eliyudd Eleyasar; Eleyasar Matan, miy baayu Yanqóoba;
23229  MAT 1:16  Yanqóoba nag moo jur Yuusufa jëkkëru Maryaama; te ci Maryaama la Yeesu, mi ñuy wax Kirist, juddoo.
23233  MAT 1:20  Waaye bi muy xalaat ci loolu, benn malaakam Boroom bi daldi ko feeñu ci gént ne ko: «Yaw Yuusufa, sëtu Daawuda, bul ragala yeggali Maryaama sa jabar, ndaxte doom ji mu ëmb, ci Xel mu Sell mi la jóge.
23234  MAT 1:21  Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
23236  MAT 1:23  «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
23238  MAT 1:25  Waaye àndul ak moom, ba kera mu mucc, jur doom ju góor; mu tudde ko Yeesu.
23239  MAT 2:1  Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem ci diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon.
23245  MAT 2:7  Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq.
23246  MAT 2:8  Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
23251  MAT 2:13  Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
23252  MAT 2:14  Yuusufa nag jóg, jël xale ba ak ndeyam, làquji Misra ca guddi ga.
23254  MAT 2:16  Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon.
23258  MAT 2:20  ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
23259  MAT 2:21  Yuusufa jóg nag, jël xale ba ak ndeyam, dellu Israyil.
23267  MAT 3:6  Ñu nangu seeni bàkkaar, Yaxya sóob leen ca dexu Yurdan.
23268  MAT 3:7  Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
23272  MAT 3:11  Man maa ngi leen di sóob ci ndox, ci lu ànd ak tuub seeni bàkkaar. Waaye kiy ñëw sama gannaaw moo ma ëpp kàttan, ba yeyoowuma koo yóbbul sax ay dàllam. Kooku dina leen sóob ci Xel mu Sell mi ak sawara.
23274  MAT 3:13  Booba Yeesu jóge Galile, ñëw ngir Yaxya sóob ko ca dexu Yurdan.
23275  MAT 3:14  Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!»
23277  MAT 3:16  Bi ko Yaxya sóobee ca dex ga, Yeesu génn. Ca saa sa asamaan yi daldi ubbiku, te Yaxya gis Xelum Yàlla wàcc ci melow pitax, ñëw ci kaw Yeesu.
23278  MAT 3:17  Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
23279  MAT 4:1  Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
23283  MAT 4:5  Bi mu waxee loolu, Seytaane yóbbu ko ca dëkk bu sell ba, teg ko ca njobbaxtalu kër Yàlla ga.
23286  MAT 4:8  Gannaaw loolu Seytaane yóbbu ko ci kaw tund wu kawe lool, won ko réewi àddina yépp ak seeni ndam.
23290  MAT 4:12  Am bés Yeesu dégg ne jàpp nañu Yaxya; mu jóg nag, jëm Galile.
23303  MAT 4:25  Noonu mbooloo mu bare topp ci moom, jóge ci wàlli Galile ak diiwaan bi ñuy wax Fukki dëkk yi, ci dëkku Yerusalem ak ci diiwaanu Yude, ba ci gannaaw dexu Yurdan.
23326  MAT 5:23  Booy yóbbu nag sa sarax ca sarxalukaay ba, te nga fàttaliku foofa ne, sa mbokk am na lu mu la meree,
23328  MAT 5:25  «Gaawala juboo ak ki lay yóbbu, ngeen layooji, bala ngeena egg; ngir bañ ki ngay layool jébbal la àttekat ba, kooka jox la alkaati ba, ñu tëj la.
23332  MAT 5:29  Bu la sa bëtu ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, luqi ko, sànni ko fu sore.
23333  MAT 5:30  Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw, ñu sànni sa yaram wépp ci sawara. Bu la sa loxol ndijoor bëggee yóbbe bàkkaar, dagg ko, sànni ko fu sore. Ndaxte ñàkk benn ci say cér moo gën ci yaw ñu sànni sa yaram wépp ci sawara.
23340  MAT 5:37  Sa waaw na nekk waaw, sa déedéet na nekk déedéet. Loo ci teg, ci Ibliis la jóge.
23377  MAT 6:26  Seetleen picci asamaan: duñu ji, duñu góob, duñu denc ci sàq; teewul seen Baay bi ci kaw moo leen di dundal. Ndax ëppuleen maana picc yi ci lu bare?
23379  MAT 6:28  «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc,
23399  MAT 7:14  Waaye buntu dund gu wóor xat na, te yoon wi jëm kaw sew na, te ñi ko gis barewul.
23410  MAT 7:25  Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; waaye màbbul, ndaxte mu ngi jàpp ca doj wa.
23412  MAT 7:27  Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
23425  MAT 8:11  Maa ngi leen koy wax, ñu bare dinañu ñëw, jóge ci penku ak sowu, bokk lekk ak Ibraayma ak Isaaxa ak Yanqóoba ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23429  MAT 8:15  Bi mu ko gisee, Yeesu laal loxoom, tàngoor wa daldi wàcc; soxna sa jóg, di ko topptoo.
23440  MAT 8:26  Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
23453  MAT 9:5  Ma wax ne: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma ne: “Jógal te dox,” lan moo ci gëna yomb?
23454  MAT 9:6  Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
23455  MAT 9:7  Noonu làggi ba daldi jóg, ñibbi.
23457  MAT 9:9  Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp.
23467  MAT 9:19  Noonu Yeesu jóg, topp ko, moom ak ay taalibeem.
23473  MAT 9:25  Waaye ñu génne leen, Yeesu dugg, jàpp loxob janq ba, mu daldi jóg.
23475  MAT 9:27  Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!»
23480  MAT 9:32  Bi ñu fa jógee nag, amoon na ñeneen ñu ñëw fi moom, indil ko ku rab jàpp, mu luu.
23485  MAT 9:37  Noonu mu ne taalibeem ya: «Ngóob mi yaatu na, waaye liggéeykat yi barewuñu.
23486  MAT 9:38  Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»
23488  MAT 10:2  Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;
23491  MAT 10:5  Yeesu yónni fukk ñooñule ak ñaar, jox leen ndigal ne leen: «Buleen dem ci ñi dul Yawut mbaa dugg ci benn dëkku waa Samari.
23497  MAT 10:11  «Bu fekkee ne agsi ngeen ci dëkk bu mag mbaa bu ndaw, nangeen fa seet ku fa am faayda, dal ca moom ba kera ngeen jóge dëkk ba.
23502  MAT 10:16  «Dégluleen, maa ngi leen di yónni, mel ni ay xar ci biir ay bukki. Muusleen nag niy jaan, te lewet niy pitax.
23503  MAT 10:17  Waaye moytuleen nit ñi, ndaxte dinañu leen jébbal àttekat yi te dóor leen ay yar ci seeni jàngu.
23504  MAT 10:18  Dees na leen yóbbu ngir man ci kanam i boroom réew ak i buur, ngir ngeen seede ma ci ñoom ak ci ñi dul Yawut.
23507  MAT 10:21  «Mag dina joxe rakkam cig dee, baay joxe doomam; ay doom it dinañu jóg, bañ seeni waajur, di leen reylu.
23523  MAT 10:37  Ku ma gënalul sa ndey walla sa baay, yeyoowuloo ma; ku ma gënalul sa doom ju góor walla ju jigéen, yeyoowuloo ma.
23526  MAT 10:40  «Te lii itam am na, ku leen nangu, nangu na ma, te ku ma nangu, nangu na ki ma yónni.
23527  MAT 10:41  Ku nangu yonent ndax yónnentam, dina jot ci peyu yonent; te ku nangu ku jub ndax njubteem, dina jot ci peyu ku jub.
23529  MAT 11:1  Ba Yeesu joxee fukki taalibeem ya ak ñaar ndigal yooyu, mu jóge fa, ngir dem jàngleji ak a waare ci seeni dëkk.
23530  MAT 11:2  Gannaaw loolu Yaxya dégg ca kaso ba jëfi Almasi bi. Mu yónni ci moom nag ay taalibeem,
23535  MAT 11:7  Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
23538  MAT 11:10  Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.”
23540  MAT 11:12  Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll.
23549  MAT 11:21  Mu ne: «Dingeen torox, yéen waa Korasin ak waa Betsayda, ndaxte kéemaan yi ma def ci yéen, bu ñu leen defoon ci dëkku Tir walla ci dëkku Sidon, kon réccu nañu bu yàgg, xëppoo dóom, sol saaku.
23567  MAT 12:9  Bi loolu amee Yeesu jóge foofa, dugg ci seen jàngu,
23574  MAT 12:16  Te mu dénk leen bu wóor, ñu bañ koo siiwal.
23596  MAT 12:38  Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
23597  MAT 12:39  Yeesu ne leen: «Yéenay laaj firnde, yéen niti jamono ju bon jii, yéen ñi fecci seen kóllëre ak Yàlla, waaye dungeen jot jenn firnde ju dul firndey yonent Yàlla Yunus.
23599  MAT 12:41  Keroog bés pénc waa dëkku Niniw dinañu jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte bi leen Yunus waaree, tuub nañu seeni bàkkaar, te ku sut Yunus a ngi fi.
23600  MAT 12:42  Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi.
23603  MAT 12:45  Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
23615  MAT 13:7  Leneen nag wadd ci biir ay xaaxaam, xaaxaam yi daldi jóg, tanc ko.
23616  MAT 13:8  Li ci des dal ci suuf su baax, nangu ba def ay gub; lii àntu ba mat téeméeri yoon lu ëpp la mu ji woon, lii mat juróom benn fukk, li ci des fanweer.
23619  MAT 13:11  Noonu mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla Aji Kawe ji, waaye ñale mayuñu leen ko.
23631  MAT 13:23  Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom benn fukk mbaa fanweer.»
23635  MAT 13:27  «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?”
23638  MAT 13:30  Bàyyileen ñoom ñaar, ñu màgg, ba ngóob ma jot. Bu ngóob ma jotee nag, dinaa wax ñi koy góob: ‘Jëkkleena dindi jëmb bi, takk ko ay say, lakk ko, waaye ngeen semb dugub ji ci sama sàq.’ ”»
23640  MAT 13:32  Doomu fuddën moo gëna tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
23647  MAT 13:39  Seytaane mooy noon bi ko ji; tukkitel àddina mooy ngóob mi, te malaaka yi ñooy góobkat yi.
23649  MAT 13:41  Doomu nit ki dina yebal ay malaakaam, ñu jële ci nguuram lépp luy yóbbe nit bàkkaar, ak ñiy def bàkkaar,
23661  MAT 13:53  Bi nga xamee ne Yeesu dégtal na léeb yooyu ba noppi, mu jóge fa,
23663  MAT 13:55  Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
23676  MAT 14:10  Mu yónnee nag, ngir ñu dagg boppu Yaxya ca kaso ba.