Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   ŋ    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23262  MAT 3:1  Ca jamono jooja Yaxya feeñoon na, di waare ca màndiŋu Yude.
23264  MAT 3:3  Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”»
23268  MAT 3:7  Noonu ay Farisen ak ay Sadusen yu bare ñëw ci Yaxya, ngir mu sóob leen ñoom itam ca dex ga. Waaye bi leen Yaxya gisee, mu ne leen: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co, ku leen artu, ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
23279  MAT 4:1  Bi loolu amee Xelum Yàlla yóbbu Yeesu ca màndiŋ ma, ngir mu jànkoonte ak fiiri Seytaane.
23285  MAT 4:7  Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
23296  MAT 4:18  Gannaaw loolu Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare. Fekk ñuy sànni seen caax ca dex ga, ndaxte ay nappkat lañu woon.
23450  MAT 9:2  Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
23454  MAT 9:6  Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
23488  MAT 10:2  Fukki ndaw ak ñaar, ya Yeesu yónni woon nag, nii lañu tuddoon: ku jëkk ki mooy Simoŋ mi ñuy wax Piyeer, ak Andare mi bokk ak moom ndey ak baay; Saag doomu Sebede, ak Yowaana rakkam;
23490  MAT 10:4  Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew; ak Yudaa Iskariyo, mi nara wor Yeesu.
23535  MAT 11:7  Bi nga xamee ne taalibe ya Yaxya yónni woon ci Yeesu dem nañu, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
23592  MAT 12:34  Yéen ñi fees ak daŋar ni ay co, naka ngeen mana waxe lu baax, fekk dangeen bon? Ndaxte gémmiñ, la fees xol lay wax.
23663  MAT 13:55  Ndax kii du doomu minise bi, te ndeyam tudd Maryaama? Ndax rakkam yu góor duñu Saag, Yuusufa, Simoŋ ak Yuda?
23757  MAT 16:16  Ci kaw loolu Simoŋ Piyeer ne: «Yaa di Almasi bi, Doomu Yàlla Aji Dund ji.»
23758  MAT 16:17  Yeesu ne ko: «Barkeel ñeel na la, Simoŋ doomu Yunus, ndaxte du nit moo la xamal lii, waaye sama Baay bi nekk ci kaw.
23794  MAT 17:25  Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?»
23820  MAT 18:24  Ba mu tàmbalee waññ nag, ñu indil buur ba ku ko ameel ay milyoŋ yu baree bare,
23900  MAT 21:5  «Waxal waa Siyoŋ: “Seen buur a ngi ñëw ci yéen; ku lewet la, te war mbaam-sëf, dig cumbur, doomu mbaam.”»
23959  MAT 22:18  Waaye Yeesu xam seen njublaŋ, mu ne leen nag: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir, yéen naaféq yi?
24020  MAT 23:33  Yéen ñi mel ni ay jaan, te fees ak daŋar niy co, naka ngeen di mucce mbugalu sawara?
24092  MAT 25:15  Kenn ka, mu dénk ko juróomi milyoŋ, keneen ka, mu dénk ko ñaar; ka ca des, benn; daldi tukki.
24093  MAT 25:16  «Bi mu demee nag, ki jot juróomi milyoŋ ya dem, di ci jula, ba amaat yeneen juróom.
24095  MAT 25:18  Waaye ki jot benn milyoŋ dem, gas pax, nëbb fa xaalisu njaatigeem.
24097  MAT 25:20  Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.”
24099  MAT 25:22  Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.”
24101  MAT 25:24  «Gannaaw loolu nag, ki jot benn milyoŋ jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, xamoon naa ne, nit ku néeg nga; dangay dajale foo jiwul, tey góob foo faruwul.
24105  MAT 25:28  Noonu njaatige bi ne: “Nanguleen xaalis bi ci moom, jox ko boroom fukki milyoŋ yi.
24129  MAT 26:6  Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani ca kër Simoŋ ma gaana woon,
24230  MAT 27:32  Bi nga xamee ne génn nañu, ñu daje ak nit ku dëkk Siren te tudd Simoŋ; ñu ga ko, ngir mu gàddu bant, ba ñu wara daaj Yeesu.
24231  MAT 27:33  Ñu ñëw nag fa ñuy wax Golgota, biy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.»
24258  MAT 27:60  dugal ko ca bàmmeel bu bees, ba mu yettaloon boppam ciw doj. Mu béraŋ doj wu mag ca buntu bàmmeel ba, dem.
24266  MAT 28:2  Fekk suuf yëngu woon na bu metti, ndaxte benn malaakam Boroom bi wàcc na ci asamaan, ñëw béraŋ doj wa, toog ci kaw.
24287  MRK 1:3  Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”»
24288  MRK 1:4  Noonu Yaxya feeñ ca màndiŋ ma, di sóob nit ñi ci ndox, tey waaree nii: «Tuubleen seeni bàkkaar, ba noppi ma sóob leen ci ndox, ngir Yàlla baal leen seeni bàkkaar.»
24296  MRK 1:12  Ci kaw loolu Xelum Yàlla daldi jéñ Yeesu, mu dem ca màndiŋ ma.
24300  MRK 1:16  Am bés Yeesu doon dox ca tefesu dexu Galile, mu gis fa ñaar ñu bokk ndey ak baay, di Simoŋ ak Andare rakkam, ñuy sànni seeni mbaal ci dex gi, ndaxte ay nappkat lañu woon.
24313  MRK 1:29  Bi nga xamee ne génn nañu ci jàngu bi, ñu ànd ak Saag ak Yowaana, dem ci kër Simoŋ ak Andare.
24314  MRK 1:30  Fekk gorob Simoŋ bu jigéen tëdd wopp ak yaram wu tàng; ñu daldi ko yégal Yeesu.
24320  MRK 1:36  Simoŋ nag ak ñi ànd ak moom di ko seet fu nekk.
24329  MRK 1:45  Waaye naka la waa ji génn, mu di yéene ci kaw li xewoon, te di ko jéebaane, ba tax Yeesu manatulaŋŋaaral dugg cib dëkk, waaye mu nekk ci biti ciy bérab yu wéet. Ba tey nit ñi jóge fu nekk, di ko fa fekk.
24333  MRK 2:4  Waaye manuñu koo jege ndax mbooloo mi. Kon ñu daldi teggi kaw kër gi, di bëtt fa tiim bérab ba Yeesu nekk, daldi yoor basaŋ, ga làggi ba tëdd.
24336  MRK 2:7  «Kii kan la, ba saña wax lii; mi ngi sosal Yàlla. Ana ku mana baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ
24338  MRK 2:9  Lan moo gëna yomb, ma wax ku làggi ki: “Baal nañu la say bàkkaar,” walla ma wax ko: “Jógal, jël sa basaŋ, tey dox”?
24340  MRK 2:11  «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
24341  MRK 2:12  Ca saa sa mu jël basaŋam te génn fa kanam ñépp. Noonu ñépp waaru, di màggal Yàlla naan: «Lu mel ni lii, masunu koo gis.»
24362  MRK 3:5  Ci kaw loolu Yeesu xool leen ak mer, am naqar ndax seen xol bu fatt; ba noppi mu ne nit ki: «Tàllalal sa loxo.» Nit ki tàllal ko, loxoom daldi wérŋŋ.
24373  MRK 3:16  Fukk ak ñaar ñii la tànn: Simoŋ, mi mu tudde Piyeer,
24375  MRK 3:18  Andare ak Filib, Bartelemi ak Macë, Tomaa ak Saag doomu Alfe, Tade ak Simoŋ, mi bokk ca mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
24414  MRK 4:22  Amul dara luy kumpa lu ñu warula siiwal, mbaa mu làqu te warul neŋŋ.
24479  MRK 6:3  Ndax kii du minise bi? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simoŋ? Te ay rakkam yu jigéen ndax nekkuñu fi ak nun?» Kon nag ñu daldi ko xeeb.
24729  MRK 11:20  Ci suba si, bi ñuy dem, ñu gis ne garabu figg gi dee na, ba wow koŋŋ.
24826  MRK 14:3  Bi nga xamee ne Yeesu nekkoon na dëkku Betani, mu dem këru Simoŋ ma gaana woon, di fa lekk. Noonu jigéen ñëw, yor njaq lu ñu defare doj wu tudd albaatar. Njaq li def latkoloñ ju raxul ju ñuy wax nàrd, tey jar lu baree bare. Jigéen ji toj njaq li, tuur latkoloñ ci boppu Yeesu.
24860  MRK 14:37  Noonu mu délsi ci taalibe yi, fekk ñuy nelaw. Mu ne Piyeer: «Simoŋ, dangaa nelaw? Amuloo sax dooley xoolandoo ak man benn waxtu?
24916  MRK 15:21  Amoon na nag nit ku dëkk Siren, tudd Simoŋ, di baayu Alegsàndar ak Rufus. Fekk booba mu romb fa, jóge ca wet, ga féete ak tool ya, ñu ga ko ngir mu gàddu bant bi.
24917  MRK 15:22  Noonu ñu yóbbu Yeesu ca bérab bu ñuy wax Golgota, liy tekki «bérabu Kaaŋu bopp.»
24941  MRK 15:46  Noonu Yuusufa jënd càngaay, wàcce néew bi, laxas ko ci, dugal ko cib bàmmeel bu ñu yett ci xeer. Bi mu ko defee mu béraŋ aw doj, ube ko buntu bàmmeel bi.
24945  MRK 16:3  di laajante: «Ku nuy béraŋal doj, wiy ub bàmmeel bi?» Doj woowu nag bu réya réy la woon. Noonu ñu xool, gis ne doj wa deñ.
24966  LUK 1:4  Noonu dinga mana xam ne li ñu la jàngaloon lu wérŋŋ la.
25042  LUK 1:80  Noonu Yaxyaa ngi doon màgg, te xelam di ubbiku. Mu dëkk ca màndiŋ ma, ba bés ba muy feeñu bànni Israyil.
25096  LUK 3:2  Te it Anas ak Kayif nekkoon sarxalkat yu mag ya. Ca jamono jooja la kàddug Yàlla wàcc ci Yaxya, doomu Sakari, ca màndiŋ ma.
25098  LUK 3:4  Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.
25101  LUK 3:7  Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc?
25134  LUK 4:2  Xelum Yàlla mi yóbbu ko ca màndiŋ ma, mu nekk fa ñeent fukki fan, jànkoonte ak fiiri Seytaane. Lekkul woon dara ci fan yooya, te gannaaw gi mu xiif.
25144  LUK 4:12  Yeesu ne ko: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
25170  LUK 4:38  Bi mu jógee ci jàngu bi, Yeesu dafa dem kër Simoŋ. Gorob Simoŋ bu jigéen dafa feebar, ba yaram wi tàng lool. Ñu ñaan Yeesu, mu dimbali leen ci.
25179  LUK 5:3  Mu dugg ci genn gaal, fekk muy gu Simoŋ, mu ne ko, mu joow ba sore tuuti. Noonu Yeesu toog ca gaal ga, di jàngal mbooloo ma.
25180  LUK 5:4  Bi mu jànglee ba noppi, mu ne Simoŋ: «Joowal gaal gi, ba fa ndox ma gëna xóote, ngeen sànni fa seeni mbaal ngir napp.»
25181  LUK 5:5  Simoŋ ne ko: «Kilifa gi, coono lanu fanaane biig te jàppunu dara. Waaye nag dinaa ko sànni ci sa ndigal.»
25184  LUK 5:8  Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!»
25186  LUK 5:10  ak ña mu bokkaloon liggéey ba, maanaam ñaari doomi Sebede yi di Saag ak Yowaana. Yeesu ne Simoŋ: «Bul ragal dara; gannaaw-si-tey, ay nit ngay mbaal jëme ci man.»
25194  LUK 5:18  Noonu ay nit ñëw, jàppoo basaŋ, ga ñu tëral nit ku yaram wépp làggi. Ñu di ko wuta dugal ca kër ga, ngir indi ko ca Yeesu.
25195  LUK 5:19  Waaye gisuñu fu ñu koy awale ndax mbooloo ma. Ñu daldi yéeg ca kaw kër ga nag, xeddi tiwiil ya, yoor waa ja ak basaŋ ga, wàcce ko ca kanam Yeesu ca biir mbooloo ma.
25197  LUK 5:21  Xutbakat yi ak Farisen yi di werante ci seen xel naan: «Kii mooy kan bay sosal Yàlla? Ana ku mana baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ
25200  LUK 5:24  Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
25201  LUK 5:25  Nit ka jóg ca saa sa ci kanam ñépp, jël basaŋ, ga ñu ko tëraloon, ñibbi tey màggal Yàlla.
25225  LUK 6:10  Ci kaw loolu mu xool leen ñoom ñépp, ba noppi ne nit ka: «Tàllalal sa loxo.» Mu tàllal ko, loxoom daldi wérŋŋ.
25229  LUK 6:14  Simoŋ, mi Yeesu tudde Piyeer, ak Andare, mi bokk ak Piyeer ndey ak baay; Saag ak Yowaana, Filib ak Bartelemi,
25230  LUK 6:15  Macë ak Tomaa, Saag doomu Alfe, ak Simoŋ mi bokk ci mbooloo, ma ñu tudde Ñi farlu ci moom seen réew;
25288  LUK 7:24  Bi ndawi Yaxya yi demee, Yeesu daldi wax ak mbooloo ma ci mbirum Yaxya ne leen: «Lu ngeen seeti woon ca màndiŋ ma? Xanaa barax buy jaayu ci ngelaw li?
25304  LUK 7:40  Yeesu ne ca tonn, daldi ne Farisen ba: «Simoŋ, am na lu ma la wara wax.» Simoŋ ne ko: «Waxal, kilifa gi.»
25307  LUK 7:43  Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gëna bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»
25308  LUK 7:44  daldi walbatiku ca jigéen ja, ne Simoŋ: «Ndax gis nga jigéen jii? Dugg naa sa kër, te joxewuloo ndox, ngir raxas samay tànk. Waaye moom, raxas na samay tànk ak ay rongooñam, ba noppi fomp leen ak kawaram.
25331  LUK 8:17  Amul dara luy kumpa lu ñu dul siiwal bés, walla lu làqu lu ñu dul feeñal, ba mu neŋŋ.
25695  LUK 16:6  Mu ne ko: “Téeméeri bidoŋi diwu oliw.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind juróom fukk.”
25697  LUK 16:8  Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gëna muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.»
25808  LUK 19:8  Waaye Sase taxaw ne Boroom bi: «Déglul Boroom bi, dogu naa may sama genn-wàllu alal miskin yi, te lu ma masa njublaŋ nit, jël alalam, dinaa ko fey ñeenti yoon lu ni tollu.»
25964  LUK 22:31  Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax.
26030  LUK 23:26  Bi ñuy yóbbu Yeesu, ñu jàpp ku ñuy wax Simoŋ te mu dëkk Siren, ku jóge ca wet, ga féete ak tool ya, sëf ko bant, ba ñuy wara daaj Yeesu, ngir mu gàddu ko, topp ci moom.
26037  LUK 23:33  Bi xarekat ya agsee ba ca bérab, ba ñuy wooye Kaaŋu bopp, ñu daaj fa Yeesu ca bant, daajaale ñaari defkati lu bon ya, kenn ca ndijooram, ka ca des ca càmmoñam.
26062  LUK 24:2  Bi ñu agsee, ñu fekk ñu béraŋ doj, wa uboon bàmmeel ba.
26094  LUK 24:34  Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ
26136  JHN 1:23  Yaxya wax leen li yonent Yàlla Esayi waxoon ne: «Man maa di baat biy yégle ci màndiŋ mi ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi!”»
26153  JHN 1:40  Kenn ci ñoom ñaar, ñi déggoon li Yaxya wax te topp Yeesu, ma nga tuddoon Andare, mi bokkoon ak Simoŋ Piyeer ndey ak baay.
26154  JHN 1:41  Andare dafa daldi dem seeti Simoŋ ne ko: «Gis nanu Almasi bi.» Baat boobu mi ngi tekki «Kirist».
26155  JHN 1:42  Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer», maanaam «xeer».
26203  JHN 3:14  Te itam na Musaa sampe woon ab bant ca diggu màndiŋ ma, takk ca jaan, ja mu defare woon xànjar, fàww ñu yékkatee noonu Doomu nit ki,
26287  JHN 5:8  Yeesu ne ko: «Jógal, jël sa basaŋ te dox.»
26288  JHN 5:9  Ca saa sa mu daldi wér, jël basaŋam, daldi dox. Mbir moomu dafa daje woon ak bésub noflaay ba,
26289  JHN 5:10  looloo tax ba Yawut ya daldi ne nit ku wér ka: «Tey bésub noflaay la, te sunu yoon aaye na, ngay yor sa basaŋ
26290  JHN 5:11  Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»