23374 | MAT 6:23 | waaye bu sa bët woppee, kon sa yaram wépp lëndëm. Leer gi nekk ci yaw, bu nekkee lëndëm, naka la lëndëm googu di këruuse! |
23381 | MAT 6:30 | Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? |
23396 | MAT 7:11 | Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak seen Baay bi nekk ci kaw dina jox lu baax ñi ko koy ñaan! |
23624 | MAT 13:16 | «Waaye yéen barkeel ngeen, ndaxte seeni bët a ngi gis te seeni nopp di dégg! |
23724 | MAT 15:22 | Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.» |
23828 | MAT 18:32 | Sang ba nag woolu jaraaf ba ne ko: “Yaw jaraaf ju soxor nga! Baal naa la sa bor bépp, ndaxte tinu nga ma. |
23854 | MAT 19:23 | Noonu Yeesu wax taalibeem ya ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, lu jafee ngoogu! |
23904 | MAT 21:9 | Mbooloom ña ko jiitu ak ña ko topp ñépp di wax ca kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Ca bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
24000 | MAT 23:13 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tëj nguuru Yàlla Aji Kawe ji ci kanam nit ñi; yéen dungeen ci dugg, te dungeen bàyyi ku ci bëgga dugg, mu dugg ci. |
24002 | MAT 23:15 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi wër géej ak suuf, ngir sàkku benn taalibe, ba noppi ngeen def ko nitu sawara, ku leen yées ñaari yoon. |
24003 | MAT 23:16 | «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.” |
24004 | MAT 23:17 | Yéen ñi dof te gumba! Lan moo gëna màgg, wurus wi walla kër Yàlla, gi tax wurus wi sell? |
24006 | MAT 23:19 | Gumba yi! Lan moo gëna màgg, sarax si walla sarxalukaay bi tax sarax si sell? |
24010 | MAT 23:23 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak anet ak kumin, te sàggane yi gëna màgg ci yoonu Musaa, maanaam njub, yërmande ak ngëm. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen bàyyi la ca des. |
24011 | MAT 23:24 | Yéen njiit yu gumba yi! Yéena ngi segg wallax-njaan, tey wann giléem. |
24012 | MAT 23:25 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dafa fees ak càcc ak ëppal. |
24013 | MAT 23:26 | Farisen yu gumba yi! Jëkkleena setal biir kaas bi ak ndab li, ngir biti bi itam set. |
24014 | MAT 23:27 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi mel ni bàmmeel yu ñu weexal. Ci biti am nañu melo wu rafet, waaye ci biir dañoo fees ak yaxi ñi dee ak tilim ju nekk. |
24016 | MAT 23:29 | «Yéen xutbakat yi ak Farisen yi, naaféq yi, dingeen torox! Ndaxte yéena ngi tabax xabruy yonent yi, tey rafetal bàmmeeli ñu jub ñi. |
24024 | MAT 23:37 | «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam, te nanguwuleen! |
24045 | MAT 24:19 | Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooyu, ngalla it ñiy nàmpal! |
24103 | MAT 25:26 | Waaye njaatigeem ne ko: “Surga bu bon nga te tayel! Gannaaw xamoon nga ne damay dajale fu ma jiwul, tey góob fu ma faruwul, |
24162 | MAT 26:39 | Bi mu waxee loolu, Yeesu dem ci kanam tuuti, ne nërëm ci suuf, di ñaan ne: «Sama Baay, bu manee am, na ma kaasu naqar bii teggi! Moona, bumuy ci sama coobare, waaye na sa coobare am.» |
24240 | MAT 27:42 | «Waa jii musal na ñeneen te manula musal boppam! Ndegam mooy buuru Israyil, na wàcc léegi ci bant bi, nu gëm ko. |
24671 | MRK 10:14 | Bi ko Yeesu gisee nag, mu metti ko lool, mu ne leen: «Bàyyileen xale yi, ñu ñëw fi man! Buleen leen tere, ndaxte ñu mel ni ñoom ñoo yelloo nguuru Yàlla. |
24681 | MRK 10:24 | Wax jooju nag daldi jaaxal taalibe yi lool. Waaye Yeesu neeti leen: «Samay xarit, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! |
24706 | MRK 10:49 | Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» |
24718 | MRK 11:9 | Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! |
24719 | MRK 11:10 | Nguuru sunu maam Daawuda giy ñëw dina barkeel! Ci bérab yu gëna kawe, nañu ne: “Osaana!”» |
24771 | MRK 12:29 | Noonu Yeesu ne ko: «Bii: “Dégluleen, yéen bànni Israyil! Yàlla sunu Boroom mooy Boroom bi, te kenn la. |
24787 | MRK 13:1 | Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!» |
24819 | MRK 13:33 | Moytuleen te xool! Xamuleen kañ la waxtu wi di jot. |
24864 | MRK 14:41 | Ñetteelu yoon mu délsi ci ñoom ne leen: «Yéena ngi nelaw tey noppalu ba tey! Jeex na. Waxtu wi jot na; ñu ngi wor Doomu nit ki ci loxoy bàkkaarkat yi. |
25004 | LUK 1:42 | Elisabet wax ca kaw ne: «Barkeel nañu la ci jigéen ñi, barkeel doom ji nga ëmb! |
25030 | LUK 1:68 | «Cant ñeel na Boroom bi, Yàllay Israyil, ndaxte wallusi na mbooloom, ba jot leen! |
25101 | LUK 3:7 | Mbooloo ma daan ñëw ngir mu sóob leen ci ndox, Yaxya daan na leen wax naan: «Yéen ñi fees ak daŋar mel ni ay co! Ku leen artu ngeen daw merum Yàlla mi nara wàcc? |
25168 | LUK 4:36 | Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.» |
25257 | LUK 6:42 | Nan nga mana waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk. |
25280 | LUK 7:16 | Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!» |
25435 | LUK 10:3 | Demleen! Maa ngi leen di yónni, mel ni ay mbote ci biir ay bukki. |
25513 | LUK 11:39 | Noonu Boroom bi ne ko: «Waaw, yéen Farisen yi, yéena ngi setal bitib kaas bi ak ndab li, waaye ci biir dangeena fees ak càcc ak mbon! |
25514 | LUK 11:40 | Yéena ñàkk xel! Xanaa du ki defar biti moo defar biir itam? |
25516 | LUK 11:42 | Yéen Farisen yi dingeen torox! Ndaxte yéena ngi sàkk asaka ci naana ak ru ak léjum bu nekk, waaye sàggane ngeen njubte ak mbëggeel ci Yàlla. Loolu ngeen wara def, waxuma nag ngeen sàggane la ca des. |
25517 | LUK 11:43 | Yéen Farisen yi, dingeen torox! Ndaxte ca jàngu ya, toogu ya féete kanam ngeen di taamu te bëgg ñépp di leen nuyoo ñaari loxo ca pénc ma. |
25520 | LUK 11:46 | Noonu Yeesu neeti leen: «Yéen itam xutbakat yi, dingeen torox! Ndaxte dangeen di sëf nit ñi say yu diis, waaye dungeen nangoo laal sëf bi sax ak seen cati baaraam. |
25548 | LUK 12:20 | Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?” |
25552 | LUK 12:24 | Seetleen baaxoñ yi: duñu ji, duñu góob, amuñu dencukaay, amuñu sàq, teewul Yàllaa ngi leen di dundal. Céy ni ngeen ëppe maana picc yi! |
25556 | LUK 12:28 | Yéen ñi néew ngëm! Bu Yàlla woddee nii ñaxum tool yi, miy sax tey, te bu subaa ñu def ko ci taal bi, ndax du leen gëna wodd? |
25584 | LUK 12:56 | Naaféq yi ngeen doon! Man ngeena ràññee melow asamaan ak suuf, waaye lu tax manuleena ràññee li jamonoy léegi ji di tekki? |
25602 | LUK 13:15 | Boroom bi ne ko: «Naaféq yi! Ndax bésub noflaay bi, kenn ku nekk ci yéen du yiwee ca gétt ga yëkkam walla mbaamam ngir wëggi ko? |
25621 | LUK 13:34 | «Yerusalem, Yerusalem, yaw miy rey yonent yi, tey sànni ay doj ndaw yi, ba ñu dee, aka maa bëggoona dajale say doom, ni ginaar di uufe ay cuujam te nanguwuleen! |
25674 | LUK 15:17 | Mujj xelam délsi, mu ne: “Sama baay am na ay surga yu bare, te dañuy lekk ba suur. Man nag maa ngi fii di bëgga dee ak xiif! |
25713 | LUK 16:24 | Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci sawara sii!” |
25752 | LUK 17:32 | Fàttalikuleen soxnas Lóot! |
25781 | LUK 18:24 | Yeesu xool ko, daldi ne: «Boroom alal, dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu! |
25799 | LUK 18:42 | Noonu Yeesu ne ko: «Na say bët gis! Sa ngëm faj na la.» |
25822 | LUK 19:22 | Buur ba ne ko: “Ci say wax laa lay àtte, surga bu bon bi! Xamoon nga ne, nit ku néeg laa, di nangu lu ma dénkaanewul, te dajale lu ma jiwul. |
25838 | LUK 19:38 | Ñu ngi naan: «Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!» |
25842 | LUK 19:42 | naan: «Céy yaw itam, boo xamoon bésub tey yi la mana indil jàmm! Waaye fi mu ne manuloo koo gis. |
25916 | LUK 21:21 | Kon nag ku nekk ci biir diiwaanu Yude, nanga daw ca tund ya; ku nekk ci biir dëkk bi, nanga ko génn; te ku nekk ca tool ya, bul dugg ca dëkk ba! |
25918 | LUK 21:23 | Ngalla jigéen ñi ëmb ca bés yooya, ngalla it ñiy nàmpal! Ndaxte tiis wu metti dina am ci réew mi, te Yàlla dina wàcce meram ci waa réew mii. |
25964 | LUK 22:31 | Yeesu teg ca ne: «Simoŋ, Simoŋ! Seytaane ñaan na, ñu jébbal leen ko, ngir mu teqale leen ni ñu teqalee dugub ak xatax. |
26025 | LUK 23:21 | Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
26032 | LUK 23:28 | Yeesu daldi walbatiku ca ñoom ne: «Yéen jigéeni Yerusalem, buleen ma jooy! Jooyleen seen bopp ak seeni doom. |
26085 | LUK 24:25 | Noonu Yeesu ne leen: «Yéen daal, yéena ñàkk xel, te seen xol yéexa gëm li yonent yi yégle woon! |
26180 | JHN 2:16 | daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!» |
26319 | JHN 5:40 | te bëgguleena ñëw ci man ngir am dund! |
26362 | JHN 6:36 | Waaye wax naa leen ko ba noppi; gis ngeen ma te taxul ngeen gëm! |
26386 | JHN 6:60 | Bi ñu dégloo Yeesu ba noppi, taalibeem yu bare nee nañu: «Njàngle mii de, jafe na! Kan moo ko mana déglu?» |
26416 | JHN 7:19 | Xanaa du Musaa moo leen jox ndigali Yàlla yi? Waaye kenn ci yéen sàmmu ko! Lu tax ngeen bëgg maa rey?» |
26417 | JHN 7:20 | Mbooloo ma ne ko: «Xanaa dangaa am ay rab! Ku lay wuta rey?» |
26418 | JHN 7:21 | Yeesu ne leen: «Benn jaloore rekk laa def, te yéen ñépp ngeen jaaxle! |
26434 | JHN 7:37 | Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na: “Ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”» |
26502 | JHN 8:52 | Yawut ya ne ko: «Léegi wóor nanu ne dangaa am ay rab! Ibraayma faatu na, yonent yépp faatu, yaw nga naan: “Kuy sàmm sama wax doo ñam dee.” |
26518 | JHN 9:9 | Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!» |
26539 | JHN 9:30 | Waa ja ne leen: «Loolu de, doy na waar! Xamuleen fu mu jóge, te moo ubbi samay bët! |
26570 | JHN 10:20 | Ñu bare ca ñoom naan: «Dafa ànd ak rab! Dafa dof! Lu tax ngeen koy déglu?» |
26656 | JHN 12:7 | Waaye Yeesu ne ko: «Bàyyi ko! Jekkoon na mu denc ko ngir bés bu ñu may suul. |
26662 | JHN 12:13 | Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na Yàlla barkeel buuru Israyil!» |
26768 | JHN 14:31 | Waaye àddina si war na xam ne bëgg naa Baay bi te ni ma ko Baay bi sante, ni laay jëfe. Jógleen, nu dem! |
26824 | JHN 16:29 | Taalibe yi ne ko: «Léegi yaa ngi wax lu leer te misaaloo! |
26900 | JHN 19:6 | Waaye bi ñu ko gisee, sarxalkat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn tooñ.» |
26909 | JHN 19:15 | Waaye ñuy yuuxoo naan: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo wara daaj ci bant?» Sarxalkat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!» |
26957 | JHN 20:21 | Yeesu dellu ne leen: «Na jàmm wàcc ci yéen! Ni ma Baay bi yónnee, noonu laa leen di yónnee, man itam.» |
27032 | ACT 2:14 | Ci kaw loolu Piyeer taxaw, ànd ak fukki ndaw ya ak benn, mu wax ci kaw, di yégal mbooloo ma ne: «Bokki Yawut yi ak yéen ñépp ñi dëkk Yerusalem, dégluleen bu baax te xam lii ma leen di wax! |
27040 | ACT 2:22 | «Yéen bokki Israyil, dégluleen wax jii! Yeesu mi dëkk Nasaret, nit la woon, ku Yàlla dëggal ci seen kanam ciy kéemaan, ay jaloore ak firnde, ya Yàlla defoon jaarale ko ci moom ci seen biir; yéen xam ngeen ko. |
27187 | ACT 7:2 | Ecen ne ko: «Yéen samay bokk ak samay baay, dégluleen! Yàlla, miy Boroom ndam, feeñu woon na sunu maam Ibraayma, bi mu nekkee réewu Mesopotami, te dëkkagul woon Karan. |
27228 | ACT 7:43 | Yóbbu ngeen sax fu nekk xayma, biy màggalukaayu Molog, ak biddiiwub Refan, bi ñu daan bokkaaleel Yàlla, di ay nataal, yi ngeen defoon ngir màggal leen! Kon nag dinaa leen toxal, yóbbu leen ci gannaaw réewu Babilon.” |
27447 | ACT 13:16 | Noonu Pool jóg, tàllal loxoom ne leen: «Yéen bokki Israyil ak yéen ñi ragal Yàlla, dégluleen! |
27525 | ACT 15:14 | «Bokk yi, dégluleen ma! Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam. |
27589 | ACT 16:37 | Waaye Pool ne alkaati ya: «Dóor nañu nu ay yar ci kanam ñépp, ci lu ñu wéerul ci benn àtte, rax-ca-dolli tëj nañu nu kaso, nun ñiy jaambur ci nguuru Room. Léegi ndax dañu noo bëgga sànni ci mbedd mi ci kumpa? Mukk! Nañu ñëw, ñoom ci seen bopp, gunge nu ci biti.» |
27760 | ACT 21:28 | di xaacu ne: «Wallee, wallee, yéen bokki Israyil! Waa jaa ngi nii, moom miy waare fépp ak ci ñépp, bay suufeel sunu xeet ak yoonu Musaa ak bérab bii; dugal na sax ay Gereg fii ci kër Yàlla gi, ba indi sobe ci bérab bu sell bii.» |
27794 | ACT 22:22 | Mbooloo ma déglu ko nag ba ca wax jooju, waaye bi ñu déggee loolu, ñu daldi yuuxu naan: «Farleen ko ci àddina! Yembar mu mel ni moom yeyoowula dund!» |
27888 | ACT 25:24 | Bi mu ñëwee, Festus ne: «Buur Agaripa ak yéen ñépp, ñi fi teew tey, nit kaa ngi nii! Mbiram moo tax mbooloom Yawut yépp, muy ci Yerusalem, muy fii, wër ma di yuuxu ne: “Nit kii waratula dund.” |
27915 | ACT 26:24 | Bi muy làyyee nii, Festus daldi ko gëdd ak baat bu kawe ne ko: «Dangaa dof, Pool! Xanaa sa njàng mu réy mi da laa xañ sago.» |
28063 | ROM 3:4 | Mukk! Su ñépp nekkoon ay naaféq, du tere Yàlla nekk dëgg. Moom la Mbind mi wax ci Yàlla ne: «Loo wax, ñépp ànd ci, te ku layoo ak yaw, nga yey ko.» |
28065 | ROM 3:6 | Mukk! Ndax su Yàlla jubadi woon, naka lay àttee àddina si? |
28068 | ROM 3:9 | Kon nag lu nu ci wara wax? Nun Yawut yi, ndax noo gën ñi ci des? Mukk! Ndaxte wone nanu ne, nit ñépp ñu ngi ci notaangeg bàkkaar, muy Yawut yi mbaa Gereg yi. |
28071 | ROM 3:12 | Ñépp jeng nañu, ba kenn amalatul Yàlla njariñ. Kenn du def lu baax, du kenn sax! |
28086 | ROM 3:27 | Kan a mana bàkku nag ci kanam Yàlla? Kenn! Lu ko waral nag? Xanaa sàmm yoon? Déedéet! Ngëm rekk. |