23275 | MAT 3:14 | Waaye Yaxya gàntu ko ne: «Man maa soxla, nga sóob ma ci ndox, te yaa ngi ñëw ci man!» |
23439 | MAT 8:25 | Noonu taalibe ya daldi jegesi, yee ko naan: «Sang bi, musal nu, nu ngiy dee!» |
23475 | MAT 9:27 | Bi Yeesu jógee foofa, ñaari gumba topp ko, di wax ca kaw naan: «Yërëm nu, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
23571 | MAT 12:13 | Noonu Yeesu ne nit ka: «Tàllalal sa loxo!» Mu tàllal ko nag, loxoom daldi wér, mel ni ba ca des. |
23692 | MAT 14:26 | Waaye bi ko taalibe yi gisee, muy dox ci kaw dex ga, ñu daldi jommi naan: «Njuuma la!» daldi tiit bay yuuxu. |
23693 | MAT 14:27 | Waaye ca saa sa Yeesu ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» |
23696 | MAT 14:30 | Waaye bi mu gisee ni ngelaw li mettee, mu daldi tiit, tàmbalee suux. Mu woote ne: «Sang bi, wallu ma!» |
23727 | MAT 15:25 | Waaye jigéen ja ñëw, sukk ci kanamam naan: «Sang bi, wallusi ma!» |
23891 | MAT 20:30 | Fekk ñaari gumba toog ci wetu yoon wa. Bi gumba ya déggee ne Yeesu di jaar, ñu daldi yuuxu ne ko: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23892 | MAT 20:31 | Waaye nit ña gëdd leen, ngir ñu noppi. Teewul gumba ya gëna yuuxu naan: «Sang bi, yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm nu!» |
23910 | MAT 21:15 | Bi nga xamee ne sarxalkat yu mag ya ak xutbakat ya gis nañu yëf yu doy waar ya mu def, te dégg xale yu ndaw ya nekk ca kër Yàlla ga, di wax ci kaw naan: «Osaana, yaw Sëtu Daawuda bi!» ñu daldi mer. |
23914 | MAT 21:19 | Noonu mu séen garabu figg ca yoon wa, waaye bi mu fa agsee, gisu ci dara lu dul ay xob rekk. Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Dootuloo meññ mukk!» Ca saa sa figg ga daldi wow. |
24172 | MAT 26:49 | Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaam-maalikum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng. |
24220 | MAT 27:22 | Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
24221 | MAT 27:23 | Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!» |
24227 | MAT 27:29 | Ñu ràbb kaalag dég, teg ko ci boppam, teg bantu xat ci loxol ndijooram, sukk ci kanamam, di ko ñaawal ne ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» |
24238 | MAT 27:40 | naan: «Yaw mi mana toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan, musalal sa bopp; boo nekkee Doomu Yàlla, wàccal ci bant bi!» |
24309 | MRK 1:25 | Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» |
24431 | MRK 4:39 | Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li, ne dex gi: «Noppil te dal!» Noonu ngelaw li dal, ba lépp ne nemm. |
24526 | MRK 6:50 | Ndaxte ñépp gis ko te jommi ci. Waaye mu wax ak ñoom ci saa si ne leen: «Takkleen seen fit, man la, buleen tiit!» |
24680 | MRK 10:23 | Noonu Yeesu xool taalibe yi ko wër ne leen: «Boroom alal dugg ci nguuru Yàlla, lu jafee ngoogu!» |
24685 | MRK 10:28 | Ci kaw loolu Piyeer daldi ko ne: «Nun de dëddu nanu lépp te topp la!» |
24704 | MRK 10:47 | Noonu mu dégg ne, Yeesum Nasaret moo fay romb; mu daldi yuuxu naan: «Yërëm ma, yaw Sëtu Daawuda bi!» |
24705 | MRK 10:48 | Ci kaw loolu ñu bare gëdd ko, ngir mu noppi. Teewul mu gëna yuuxu naan: «Yaw Sëtu Daawuda bi, yërëm ma!» |
24706 | MRK 10:49 | Noonu Yeesu taxaw, daldi ne: «Wooleen ko!» Ñu woo nag gumba gi ne ko: «Na sa xel dal! Jógal! Mu ngi lay woo.» |
24723 | MRK 11:14 | Ci kaw loolu mu ne garab gi: «Dootuloo meññ mukk!» Taalibe yi dégg loolu mu wax. |
24730 | MRK 11:21 | Noonu Piyeer fàttaliku li xewoon, ne Yeesu: «Kilifa gi, xoolal, figg gi nga rëbb dee na, ba wow!» |
24787 | MRK 13:1 | Bi Yeesu di jóge ca kër Yàlla ga, kenn ca taalibe ya ne ko: «Kilifa gi, xoolal! Ni mu réye ay doj, te rafete ni ay taax!» |
24908 | MRK 15:13 | Ñu daldi yuuxuwaat naan: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
24909 | MRK 15:14 | Pilaat ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye mbooloo mi di yuuxu bu gëna kawe: «Daaj ko ci bant!» |
24913 | MRK 15:18 | Ñu daldi ko wax bu kawe: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» |
24925 | MRK 15:30 | wàccal ci bant bi te musal sa bopp!» |
24934 | MRK 15:39 | Njiitu xare nag, bi taxawoon ci kanam Yeesu, bi mu gisee ni Yeesu deeye, mu ne: «Ci dëgg, nit kii Doomu Yàlla la!» |
24987 | LUK 1:25 | te naan: «Lii mooy yiw wi ma Boroom bi defal, ba fajal ma li doon sama gàcce ci nit ñi!» |
25007 | LUK 1:45 | Barke ñeel na la, yaw mi gëm ne li la Boroom bi yégal dina mat!» |
25056 | LUK 2:14 | «Nañu màggal Yàlla ca asamaan su kawe sa, te ci àddina, na jàmm wàcc ci nit, ñi mu nangu ndax yiwam!» |
25166 | LUK 4:34 | «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!» |
25167 | LUK 4:35 | Waaye Yeesu gëdd ko naan: «Noppil te génn ci moom!» Noonu rab wi daaneel nit ki ci suuf ci kanam ñépp, daldi génn ci moom te gaañu ko. |
25173 | LUK 4:41 | Te it ay rab di génn ca nit ña te di yuuxu naan: «Yaay Doomu Yàlla!» Noonu mu gëdd leen, te mayu leen, ñu wax dara, ndaxte xam nañu ne mooy Almasi bi. |
25184 | LUK 5:8 | Naka la Simoŋ Piyeer gis loolu, daldi sukk ci kanam Yeesu ne ko: «Sore ma Boroom bi, ndaxte nitu bàkkaar laa!» |
25280 | LUK 7:16 | Ñépp tiit, bay màggal Yàlla, di wax naan: «Yonent bu mag feeñ na ci sunu biir! Yàlla wallusi na mbooloom!» |
25338 | LUK 8:24 | Noonu taalibe yi jegesi Yeesu, yee ko ne: «Kilifa gi, kilifa gi, nu ngiy dee!» Ci kaw loolu Yeesu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm. |
25487 | LUK 11:13 | Ndegam yéen ñi bon yéena mana jox seeni gone lu baax, astamaak Baay bi nekk ci kaw dina jox Xel mu Sell mi ñi ko koy ñaan!» |
25501 | LUK 11:27 | Bi Yeesu di wax loolu, jenn jigéen yékkati baatam ca biir mbooloo ma ne: «Céy jigéen ji la ëmb te nàmpal la moo barkeel!» |
25637 | LUK 14:15 | Bi mu déggee wax yooyu, kenn ca gan ya ne Yeesu: «Kiy lekk ci ñam, yi Yàlla di joxe ci nguuram, barkeel nga!» |
25659 | LUK 15:2 | Farisen ya ak xutbakat ya di ñurumtu naan: «Waa jii mi ngi nangoo nekk ak ay boroom bàkkaar ak a lekkandook ñoom!» |
25733 | LUK 17:13 | «Yeesu, kilifa gi, yërëm nu!» |
25738 | LUK 17:18 | Amul kenn ci ñoom ku ñëw gërëm Yàlla ku dul doxandéem bii!» |
25795 | LUK 18:38 | Noonu mu yuuxu ne: «Yeesu, Sëtu Daawuda, yërëm ma!» |
25796 | LUK 18:39 | Ñi jiitu woon gëdd ko, ngir mu noppi. Waaye muy gëna yuuxu naan: «Sëtu Daawuda, yërëm ma!» |
25838 | LUK 19:38 | Ñu ngi naan: «Yaw buur biy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na jàmm am ca asamaan, te ndam li féete ca bérab yu gëna kawe!» |
25839 | LUK 19:39 | Waaye ay Farisen yu nekkoon ca mbooloo ma ne Yeesu: «Kilifa gi, yeddal sa taalibe yi!» |
25864 | LUK 20:16 | Xanaa ñëw, rey beykat yooyu, dénk tool ba ñeneen.» Bi Yeesu waxee loolu, nit ña ne ko: «Yàlla tere!» |
25887 | LUK 20:39 | Ci kaw loolu ay xutbakat ne ko: «Li nga wax dëgg la, kilifa gi!» |
25981 | LUK 22:48 | Waaye Yeesu ne ko: «Ci fóon ngay jébbale Doomu nit ki ay noonam!» |
25993 | LUK 22:60 | Waaye Piyeer ne ko: «Sama waay, xawma li ngay wax!» Bi kàddoom di daanu, faf ginaar daldi sab. |
26004 | LUK 22:71 | Ñu daldi ne nag: «Lu nuy doyeeti seede léegi, ndegam nun ci sunu bopp noo ko nangoo ci gémmiñam!» |
26022 | LUK 23:18 | Waaye ñu bokk di yuuxu, ñoom ñépp naan: «Reyal kii te bàyyi Barabas!» |
26025 | LUK 23:21 | Waaye ñuy yuuxu naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» |
26039 | LUK 23:35 | Mbooloo maa nga fa taxaw di seetaan. Njiit ya di ko reetaan naan: «Musal na ñeneen; na musal boppam, su fekkee mooy Almasi bi, ki Yàlla fal!» |
26041 | LUK 23:37 | «Su fekkee ne yaay buuru Yawut yi, musalal sa bopp!» |
26043 | LUK 23:39 | Kenn ca defkatu lu bon ya ñu wékkoon ci bant, di ko xas, naan ko: «Xanaa du yaw yaay Almasi bi? Musalal sa bopp te musal nu!» |
26050 | LUK 23:46 | Yeesu woote ak kàddu gu dëgër naan: «Baay, jébbal naa la sama ruu!» Bi mu waxee loolu, mu delloo ruuwam Yàlla. |
26094 | LUK 24:34 | Ñooñu ne leen: «Dëgg la, Boroom bi dekki na, te feeñu na Simoŋ!» |
26149 | JHN 1:36 | Bi mu gisee Yeesu muy romb, mu daldi ne: «Kii mooy Gàttub Yàlla bi!» |
26162 | JHN 1:49 | Nataneel wax ko ne: «Kilifa gi, yaay Doomu Yàlla ji, yaa di buuru Israyil!» |
26180 | JHN 2:16 | daldi ne jaaykati pitax ya: «Jëleleen fi lii! Sama kër Baay, buleen ko def marse!» |
26184 | JHN 2:20 | Ñu ne ko: «Nga ne kër Yàlla, gii ñu tabax ci ñeent fukki at ak juróom benn, man nga koo yékkati ci ñetti fan!» |
26215 | JHN 3:26 | Ci kaw loolu ñu dem ca Yaxya ne ko: «Kilifa gi, ndax fàttaliku nga kooka nga seede woon te mu nekkoon ak yaw ca gannaaw dexu Yurdan? Moom de, ma ngay sóobe ci ndox léegi te ñépp a ngay dem ca moom!» |
26276 | JHN 4:51 | Bi muy dellu këram nag, ay surgaam gatandu ko. Ñu daldi ne ko: «Xale bi dina dund!» |
26340 | JHN 6:14 | Bi nit ña gisee firnde jooju Yeesu wone, ñu ne: «Dëgg-dëgg kii mooy Yonent, bi wara ñëw ci àddina!» |
26346 | JHN 6:20 | Waaye Yeesu ne leen: «Man la, buleen tiit!» |
26360 | JHN 6:34 | Ñu ne ko nag: «Sang bi, kon dee nu faral di jox ci ñam woowe!» |
26366 | JHN 6:40 | Ndaxte lii mooy bëgg-bëggu Baay bi: képp ku gis Doom ji te gëm ko, am dund gu dul jeex, te bés bu mujj ba, dinaa ko dekkal!» |
26396 | JHN 6:70 | Yeesu ne leen: «Xanaa du maa leen tànn, yéen fukk yi ak ñaar? Moona, am na ci yéen koo xam ne seytaane la!» |
26443 | JHN 7:46 | Alkaati ya ne leen: «Kenn masula waxe ni nit kooku!» |
26446 | JHN 7:49 | Waaye mbooloo mi xamuñu yoonu Musaa; ñu alku lañu!» |
26518 | JHN 9:9 | Ñii naan: «Moom la de!» Ñee naan: «Du moom! Dañoo niroo rekk.» Mu daldi leen ne: «Man la de!» |
26583 | JHN 10:33 | Yawut ya ne ko: «Jëf ju baax taxul nu bëgg laa sànniy xeer, waaye dangay suufeel turu Yàlla; yaw, nit rekk nga, ba noppi di def sa bopp Yàlla!» |
26608 | JHN 11:16 | Noonu Tomaa, ki turam di tekki «Séex bi», daldi ne yeneen taalibe ya: «Nanu dem nun itam, deeyandoo ak moom!» |
26628 | JHN 11:36 | Noonu nag, Yawut ya ne: «Gis ngeen ni mu ko bëgge woon!» |
26631 | JHN 11:39 | Yeesu ne: «Dindileen xeer wi!» Màrt, jigéenu ku dee ki ne ko: «Boroom bi, dina xasaw xunn fii mu nekk, ndaxte am na ci bàmmeel bi ñeenti fan.» |
26635 | JHN 11:43 | Bi mu waxee loolu, Yeesu woote ak baat bu dëgër ne: «Lasaar, ñëwal ci biti!» |
26640 | JHN 11:48 | Ndaxte su nu ko bàyyee mu jàppoo nii, ñépp dinañu ko gëm, te kilifay Room yi dinañu ñëw, daaneel sunu kër Yàlla gi, tas sunu réew!» |
26662 | JHN 12:13 | Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na Yàlla barkeel buuru Israyil!» |
26668 | JHN 12:19 | Farisen yi nag di waxante naan: «Gis ngeen, manuleen ci dara; ñépp a ngi koy topp!» |
26677 | JHN 12:28 | Baay, màggalal sa tur!» Noonu ñu dégg baat bu jóge asamaan naan: «Màggal naa ko ba noppi, te dinaa ko màggalaat.» |
26678 | JHN 12:29 | Mbooloo ma fa teewoon te dégg baat ba daldi ne: «Dënnu la woon!» Ñeneen naan: «Malaakaa doon wax ak moom.» |
26708 | JHN 13:9 | Simoŋ Piyeer ne ko: «Kon nag Boroom bi, bul yem rekk ci tànk yi, waaye raxasaaleel loxo yi ak bopp bi!» |
26709 | JHN 13:10 | Yeesu ne ko: «Ku sangu ba noppi, soxlaatula raxas lu dul ay tànkam, ndaxte set na wecc. Yéen nag set ngeen, waaye du ñépp!» |
26726 | JHN 13:27 | Naka la Yudaa jël dog wa, Seytaane dugg ci moom. Yeesu ne ko: «Gaawantul ci li ngay def!» |
26736 | JHN 13:37 | Piyeer ne ko: «Boroom bi, lu tax manuma laa topp léegi? Àttan naa joxe sama bakkan ngir yaw!» |
26894 | JHN 18:40 | Noonu ñu daldi yuuxuwaat: «Déedéet, waxunu kii; Barabas lanu wax!» Fekk Barabas moomu taskatu réew la woon. |
26897 | JHN 19:3 | Ñu di ko jegeñsi, di ko pes, naan ko: «Nuyu nanu la, yaw buuru Yawut yi!» |
26899 | JHN 19:5 | Yeesu nag génn, tegoo mbubbum xarekat mu xonq mi ak kaalag dég gi. Pilaat it ne leen: «Waa jaa ngii!» |
26900 | JHN 19:6 | Waaye bi ñu ko gisee, sarxalkat yu mag ya ak alkaati ya di yuuxoo naan: «Daaj ko ci bant! Daaj ko ci bant, ba mu dee!» Pilaat ne leen: «Jël-leen ko, yéen, daaj ko ci bant, ndaxte gisuma ci moom genn tooñ.» |
26906 | JHN 19:12 | Booba nag la Pilaat doon fexee bàyyi Yeesu. Waaye Yawut ya di yuuxoo naan: «Boo bàyyee kii, doo xaritu buur bi Sesaar. Nit ku teg boppam buur, noonub Sesaar la!» |
26908 | JHN 19:14 | Booba ñu ngi waajal màggalu bésu Mucc ba, ca weti digg bëccëg. Pilaat ne Yawut ya: «Seen buur a ngii!» |
26909 | JHN 19:15 | Waaye ñuy yuuxoo naan: «Na dee! Na dee! Daaj ko ci bant!» Pilaat ne leen: «Ndax seen buur bi, dama koo wara daaj ci bant?» Sarxalkat yu mag ya ne ko: «Amunu benn buur bu dul Sesaar!» |
26924 | JHN 19:30 | Bi Yeesu muucoo bineegar bi, mu ne: «Lépp mat na!» Noonu mu sëgg, delloo ruuwam Yàlla. |