24718 | MRK 11:9 | Ñiy jiitu ak ñiy topp ci Yeesu ñépp di wax ci kaw naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! |
25166 | LUK 4:34 | «Moo! Yaw Yeesum Nasaret, loo nuy fexeel? Ndax dangaa ñëw ngir alag nu? Xam naa la, yaa di Aji Sell ji jóge ci Yàlla!» |
26159 | JHN 1:46 | Nataneel ne ko: «Aa! Ndax dara lu baax man na jóge Nasaret?» Filib ne ko: «Ñëwal gis.» |
26662 | JHN 12:13 | Ñu daldi jël cari garab, génn di ko teeru. Ñuy xaacu naan: «Osaana! Yaw miy ñëw ci turu Boroom bi, ku barkeel nga! Na Yàlla barkeel buuru Israyil!» |
27031 | ACT 2:13 | Waaye ñenn ñi di leen ñaawal ne: «Waay! Ñii dañoo màndi ak biiñ.» |
30890 | REV 7:12 | naan: «Amiin! Yal na cant ak ndam, xel ak ngërëm, teraanga, kàttan ak doole féete ak Yàlla sunu Boroom ba fàww. Amiin!» |
31087 | REV 19:1 | Gannaaw loolu ma dégg lu mel ni baat bu xumb bu jollee ca mbooloo mu bare ca asamaan, naan: «Aleluya! Mucc, ndam ak kàttan, Yàlla sunu Boroom moo ko moom. |
31089 | REV 19:3 | Ñu tegaat ca ne: «Aleluya! Saxarus lakku dëkk baa ngi jolli ba fàww!» |
31090 | REV 19:4 | Noonu ñaar fukki mag ña ak ñeent, ak ñeenti mbindeef ya, daldi sukk di jaamu Yàlla, moom mi toog ca gàngune ma. Ñu naan: «Amiin! Aleluya!» |
31092 | REV 19:6 | Ma dégg lu mel ni baatu mbooloo mu bare, mel ni riiru duusi géej, ni yënguy dënnu yu réy, naan: «Aleluya! Sunu Boroom Yàlla Aji Man ji dugg na ci nguuram! |