24088 | MAT 25:11 | Gannaaw loolu janq ya ca des agsi naan: “Sang bi, Sang bi, ubbil nu!” |
25612 | LUK 13:25 | Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” |
25614 | LUK 13:27 | Mu ne leen: “Nee naa leen xawma fu ngeen bokk. Yéen ñépp soreleen ma, defkati lu bon yi!” |
25713 | LUK 16:24 | Noonu mu yuuxu ne: “Maam Ibraayma, yërëm ma! Yebalal Lasaar, mu sëpp catul baaraamam ci ndox, seralal ma sama làmmiñ, ndaxte maa ngi sonn lool ci sawara sii!” |
25743 | LUK 17:23 | Dees na leen ne: “Mi ngi fii!” walla: “Ma nga fale!” Buleen dem, mbaa ngeen di leen topp. |
25760 | LUK 18:3 | Amoon na itam ca dëkk ba jigéen ju jëkkëram faatu ju daan faral di ñëw ci moom, naan ko: “Àtte ma ak sama noon!” |
26033 | LUK 23:29 | Ndaxte jamono dina ñëw, ju ñu naan: “Jigéen ñi masula jur ak ñi masula nàmpal, barkeel ngeen!” |
30170 | HEB 8:11 | Kenn dootul wara jàngal moroomam walla mbokkam, di wax naan: “Xamal Boroom bi!” Ndaxte ñépp dinañu ma xam, li dale ci ki gëna ndaw ba ci ki gëna mag. |