Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word,»    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23236  MAT 1:23  «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
24210  MAT 27:12  Yeesu ne ko: «Wax nga ko,» waaye waxul dara ca la ko sarxalkat yu mag ya ak njiit ya jiiñ.
24474  MRK 5:41  Mu jàpp loxoom ne ko: «Talita kumi,» liy tekki: «Janq bi, maa ngi la koy wax, jógal.»
24868  MRK 14:45  Noonu mu ñëw ci Yeesu ne ko: «Kilifa gi,» daldi ko fóon.
25307  LUK 7:43  Simoŋ ne ko: «Xanaa ki ñu baal bor bi gëna bare.» Yeesu ne ko: «Àtte nga dëgg,»
26264  JHN 4:39  Bi jigéen ja nee waa dëkk ba: «Wax na ma li ma def lépp,» ñu bare gëm nañu Yeesu.
26860  JHN 18:6  Bi leen Yeesu nee: «Man la,» ñu daldi dellu gannaaw, ba daanu.
26920  JHN 19:26  Bi Yeesu gisee yaayam taxaw ci wetu taalibe, bi mu bëggoon, mu ne ko: «Soxna si, sa doom a ngi,»
27127  ACT 4:36  Noonu amoon na fa ku tudd Yuusufa, te ndaw yi dàkkentale ko Barnabas, miy tekki «Kiy dëgëral fit yi,» mu soqikoo ci giiru Lewi, te juddoo dunu Sipar.
27245  ACT 7:60  Bi mu ko waxee, mu sukk, wax ak baat bu kawe: «Boroom bi, bu leen bindal bàkkaar bii,» ba noppi mu nelaw.
28113  ROM 4:23  Waaye loolu lañu bind ne: «Yàlla jagleel na ko njub,» du Ibraayma rekk a moom wax ji.
28166  ROM 7:7  Kon nag lu nu wara wax? Ndax bàkkaar ci yoonu Musaa la jóge? Mukk! Waaye moo ma xamal luy bàkkaar. Ndaxte su ma yoon wi waxul woon: «Bul bëgg yëfi jaambur,» kon duma xam luy xemmem.
28234  ROM 9:11  Waaye Yàlla wax ko ne: «Yanqóoba rakk ji mooy yilif magam Esawu,» fekk xale ya juddooguñu te defaguñu dara, muy lu baax, muy lu bon. Yàlla def na noonu, maanaam tànn kenn ci doom yi, ngir dogalam mana taxaw, te sukkandikuwul ci seeni jëf waaye ci wooteb Yàlla.
28343  ROM 13:9  Ndaxte ndigali Yàlla yépp, yi deme ni: «Bul njaaloo, bul bóome, bul sàcc, bul bëgge,» walla leneen ndigal lu mu mana doon, wax jii moo leen ëmb: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.»
28482  1CO 3:4  Bu kenn yéglee ne: «Man ci Pool laa bokk,» keneen ne: «Man ci Apolos,» ndax jëfewuleen ni niti àddina rekk?
28547  1CO 6:12  Am na ci yéen ñu naan: «Sañ naa lépp.» Waaw, waaye du lépp a jariñ nit. «Sañ naa lépp,» waaye duma bàyyi dara, mu not ma.
28658  1CO 10:23  Dafa am ñu naan: «Lépp lanu sañ.» Waaw, waaye du lépp a baax ci nun. «Lépp lanu sañ,» waaye it lépp du yékkati ngëm.
28663  1CO 10:28  Waaye bu leen kenn nee: «Lii sarax la, bu ñu jagleel xërëm yi,» suurleen ko ndax ki leen ko xamal, ngir xel mu dal.
28705  1CO 12:3  Moo tax ma leen di xamal lii: ku Xelum Yàlla solu du wax ne: «Yeesu dafa araam.» Te it kenn manula wax ne: «Yeesu mooy Boroom bi,» su ko ko Xelum Yàlla waxloowul.
28717  1CO 12:15  Kon bu tànk nee: «Man duma loxo, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.
28718  1CO 12:16  Te bu nopp nee: «Duma bët, kon bokkuma ci yaram,» du ko teree bokk ci céri yaram yi.
28813  1CO 15:27  Ndaxte Mbind mi nee na: «Yàlla notal na ko lépp, mu teg ci tànk.» Waaye bu Mbind mi nee, «not na lépp,» wóor na ne moom mi ko notal lépp, génne na ci boppam.
28831  1CO 15:45  Mbind mi nee na: «Nit ku jëkk ka, Aadama, doon na boroom ruu,» waaye Aadama mu mujj mi doon na Xel muy joxe dund.
28933  2CO 4:6  Ndaxte Yàlla mi ne: «Na leer leer ci biir lëndëm,» moo leer ci sunu xol, ngir leeral nu ak xam-xamu ndamu Yàlla, liy feeñ ci xar kanamu Kirist.
29348  EPH 4:9  Su nu waxee ne «yéeg na,» li moo ci génn: daa jëkka wàcc ba ca bérab ya gëna suufe.
29406  EPH 6:2  «Teralal sa ndey ak sa baay,» mooy ndigal li jëkka ëmb dige,
29581  COL 2:20  Ndegam deeyandoo ngeen ak Kirist, ba génne noonu ci aaday àddina, lu tax ngeen di nangu, ñu di leen teg ay sàrt yu mel nii: «Bul fab, bul ñam, bul laal,» ni bu seenug dund aju woon ci àddina si?
29691  1TH 5:3  Fekk nit ñiy naan: «Lépp a ngi ci jàmm, ba ne leww,» booba musiba bett leen, ni aw mat di bette jigéenu biir, te kenn du ci mucc.
29848  1TI 5:18  Ndaxte Mbind mi nee na: «Bul sunjuñ gémmiñu nag wu ñu takk ci bojjukaay,» nee na it: «Ku ñaq, jariñu.»
29913  2TI 2:19  Waaye teewul fondamaa bu dëgër, bi Yàlla tabax, nee na kekk, te lii lañu ci tàmpe: «Boroom bi xam na ñi bokk ci moom,» te it: «Ki tudd turu Boroom bi, na daw lu bon.»
30080  HEB 3:18  Te it bi Yàlla defee ngiñ lii: «Duñu dugg mukk ci sama noflaay,» booba ñan ñoo ko taxoon di wax? Xanaa ña ko déggadil.
30313  HEB 13:5  Buleen bëgge; deeleen doylu, ndaxte Yàlla ci boppam nee na: «Duma la wacc mukk, duma la wor mukk,»
30346  JAS 1:13  Bu la fiir galanee, bul ne: «Yàllaa ko dogal,» ndaxte Yàlla jegewul ak mbon fenn te du fiir kenn.
30363  JAS 2:3  ngeen teral boroom daraja ji ne ko: «Àggal ci jataay bu yiw bi,» ba noppi ngeen ne aji néew doole ji: «Taxawal fale, mbaa nga toog fi ci samay tànk,»
30368  JAS 2:8  Su ngeen sàmmee yoonu Buur Yàlla, ni ko Mbind mi tërale naan: «Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp,» kon def ngeen lu baax.
30376  JAS 2:16  te kenn ci yéen ne ko: «Demal ak jàmm, nga solu te lekk,» te fekk fajuleen aajoom, loolu lu muy jariñ?
30383  JAS 2:23  Noonu li ñu wax ci Mbind mi am na, bi mu naan: «Ibraayma gëm na Yàlla, te Yàlla jàppe ngëmam ni njub,» ba ñu ko wooye xaritu Yàlla.
30589  2PE 2:22  Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: «Xaj mooy waccu, di ko lekkaat,» te it: «Mbaam-xuux, loo ko sang sang, mu xalangu ci ban.»
30690  1JN 4:20  Su kenn nee: «Bëgg naa Yàlla,» te bëgguloo sa mbokk, dangay fen; ndaxte ku bëggul sa mbokk mi ngay gis, doo mana bëgg Yàlla mi nga gisul.