26155 | JHN 1:42 | Noonu mu yóbbu ko ci Yeesu. Yeesu xool ko ne ko: «Yaa di Simoŋ, doomu Yowaana. Dinañu la wooye Sefas.» Sefas mi ngi tekki «Piyeer», maanaam «xeer». |
27321 | ACT 9:36 | Amoon na nag ci dëkku Yope taalibe bu jigéen bu tudd Tabita, liy tekki «Dorkas», maanaam «kéwél», te muy wéy ci jëf yu baax ak sarxe. |
27937 | ACT 27:14 | Waaye nees-tuut ngelaw lu wole penku, ñu di ko wax «Ërakilon», jóge ca dun ba, ne milib ci sunu kaw. |
28199 | ROM 8:15 | Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.» |
28888 | 2CO 1:20 | Te lépp lu Yàlla dige woon fekk na «waawam» ci moom. Noonu kon ci Kirist lanuy waxe: «Amiin», ngir yékkati ndamu Yàlla. |
29204 | GAL 4:6 | Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba», maanaam «Baay.» |
30433 | JAS 5:12 | Te li fi raw samay bokk, buleen waat mukk, bu muy ci asamaan mbaa ci suuf mbaa ci leneen lu mu mana doon. Nangeen yem ci: «waaw» ak «déedéet», ngir bañ cee layoo fa kanam Yàlla. |