23423 | MAT 8:9 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |
23924 | MAT 21:29 | Taaw ba ne ko: “Demuma,” waaye gannaaw loolu xelam yedd ko, mu dem. |
23925 | MAT 21:30 | Gannaaw gi, baay ba ñëw ca tofo ba, wax ko noonu. Mu ne ko: “Waaw,” waaye demul.» |
23997 | MAT 23:10 | Buñu leen tudde it ay “njiit,” ndaxte kenn rekk moo di seen Njiit, mooy Kirist. |
25272 | LUK 7:8 | Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.» |