24172 | MAT 26:49 | Mu daldi ñëw ci Yeesu nag ne ko: «Salaam-maalikum, kilifa gi!» daldi ko fóon bu tàng. |
24845 | MRK 14:22 | Noonu bi ñuy lekk, Yeesu jël mburu, sant Yàlla, jox leen ko naan: «Jël-leen, lii sama yaram la.» |
26160 | JHN 1:47 | Naka la Yeesu gis Nataneel jëmsi ci moom, mu daldi ne ci mbiram: «Xool-leen, nitu Israyil dëgg a ngee di ñëw; du dox benn tànku caaxaan.» |
30457 | 1PE 1:16 | Ndaxte Mbind mi nee na: «Sell-leen, ndaxte ku sell laa.» |
30589 | 2PE 2:22 | Noonu seen mbir dëggal na li ñuy wax ne: «Xaj mooy waccu, di ko lekkaat,» te it: «Mbaam-xuux, loo ko sang sang, mu xalangu ci ban.» |