23245 | MAT 2:7 | Ci kaw loolu Erodd woolu ci kumpa boroom xam-xam ya, di leen ceddowu, ngir xam bu wóor kañ la biddiiw bi feq. |
23251 | MAT 2:13 | Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.» |
23254 | MAT 2:16 | Bi Erodd gisee nag, ne boroom xam-xam ya nax nañu ko, mu daldi mer lool. Mu santaane ñu dugg ca Betleyem ak la ko wër, rey xale yu góor ya fa am ñaari at jëm suuf, méngook jamono, ja ko boroom xam-xam ya waxoon. |
23264 | MAT 3:3 | Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
23379 | MAT 6:28 | «Te lu tax ngeen di jaaxle ngir koddaay? Seetleen bu baax, ni tóor-tóori ñax mi di saxe ci tool yi. Duñu liggéey, duñu ëcc, |
23391 | MAT 7:6 | «Buleen jox lu sell xaj yi, mbaa sànni seeni per ci kanam mbaam-xuux yi, ngir bañ ñu dëggaate ko te walbatiku, xotti leen. |
23414 | MAT 7:29 | ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul. |
23444 | MAT 8:30 | Fekk amoon na ca wet ya géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. |
23445 | MAT 8:31 | Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.» |
23446 | MAT 8:32 | Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma. |
23454 | MAT 9:6 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
23456 | MAT 9:8 | Ba mbooloo ma gisee loolu, ñu daldi ragal te màggal Yàlla, mi dénk sañ-sañ bu tollu noonu doom Aadama yi. |
23487 | MAT 10:1 | Noonu Yeesu woo ca moom fukki taalibeem ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, tey faj jàngoro yépp ak wéradi yépp. |
23514 | MAT 10:28 | Te buleen ragal ñu mana rey yaram, te manuñoo rey ruu, waaye ragal-leen ki mana sànk yaram ak ruu ci sawara. |
23540 | MAT 11:12 | Ci li dale ci jamonoy Yaxya ba léegi, nit ñaa ngi góor-góorlu ngir dugg ci nguuru Yàlla, te ñi sawar ñoo ci am wàll. |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23553 | MAT 11:25 | Ca jamono joojale Yeesu wax na lii: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. |
23600 | MAT 12:42 | Te it ca bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi. |
23784 | MAT 17:15 | naan: «Sang bi, yërëmal sama doom, ndaxte mu ngi say, di am coono bu metti; léeg-léeg mu daanu ci sawara, léeg-léeg mu daanu ci ndox. |
23855 | MAT 19:24 | Ma waxaat leen ko: giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.» |
23864 | MAT 20:3 | Ci yoor-yoor mu génn, gis ñeneen ñu toog ca pénc ma te liggéeyuñu. |
23918 | MAT 21:23 | Gannaaw loolu Yeesu dugg ca kër Yàlla ga, di fa jàngle. Bi muy jàngle nag sarxalkat yu mag ya ak njiiti xeet wa ñëw ci moom ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Ku la may boobu sañ-sañ?» |
23919 | MAT 21:24 | Yeesu ne leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ko waxee, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. |
23922 | MAT 21:27 | Ñu ne Yeesu nag: «Loolu xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. |
23945 | MAT 22:4 | Kon mu yónneeti yeneen surga ne leen: “Bu ngeen demee, yégal-leen gan yi sama woote bii: ‘Reer yi noppi na, reylu naa samay nag ak samay jur gu duuf; lépp sotti na, ñëwleen ci reer yi.’ ” |
24021 | MAT 23:34 | Moo tax maa ngi leen di yónnee ay yonent ak ay boroom xam-xam ak ay xutbakat. Ñenn ñi dingeen leen rey te daaj leen ci bant; ñeneen ñi dingeen leen dóor ay yar ci seeni jàngu, di leen fitnaal ci dëkkoo dëkk. |
24033 | MAT 24:7 | Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Dina am ay xiif ak ay yëngu-yënguy suuf ci bérab yu bare. |
24111 | MAT 25:34 | «Noonu Buur bi dina wax ñi féete ndijoor: “Agsileen, yéen ñi sama Baay barkeel, jël-leen nguur, gi ñu leen waajal li dale ci njàlbéenug àddina. |
24128 | MAT 26:5 | Waaye ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yëngu-yëngu baña am ci nit ñi.» |
24164 | MAT 26:41 | Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» |
24196 | MAT 26:73 | Nees-tuut ña fa taxawoon ñëw ci Piyeer ne ko: «Ci lu wóor ne yaw itam bokk nga ci ñoom, ndaxte sa waxin feeñal na la.» |
24222 | MAT 27:24 | Naka Pilaat xam ne du ci man dara, fekk na sax yëngu-yëngu bi gëna am doole, mu daldi fab ndox, raxas ay loxoom ca kanam mbooloo ma ne leen: «Set naa ci deretu ku jub kii; nu ngeen xam, defleen ko.» |
24265 | MAT 28:1 | Gannaaw bésub noflaay ba nag, ca fajar ga, ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, Maryaamam Magdala ak Maryaama ma ca des dem, seeti bàmmeel ba. |
24287 | MRK 1:3 | Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”» |
24306 | MRK 1:22 | Te ñu waaru ca njàngleem, ndaxte jàngal na leen ak sañ-sañ bu seeni xutbakat amul. |
24339 | MRK 2:10 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu mu ne làggi ba: |
24372 | MRK 3:15 | mu joxaale leen sañ-sañu dàq ay rab. |
24444 | MRK 5:11 | Fekk amoon na fa ca tund wa géttu mbaam-xuux yu bare yuy for. |
24445 | MRK 5:12 | Rab ya ñaan Yeesu: «Jox nu ndigal, nu dugg mbaam-xuux ya.» |
24446 | MRK 5:13 | Mu may leen ko. Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab fa. Mbaam-xuux ya nag matoon nañu ñaari junni. |
24449 | MRK 5:16 | Ña fekke woon mbir ma nag nettali leen mbirum nit ka ak mbaam-xuux ya. |
24478 | MRK 6:2 | Bésub noflaay bi nag mu jàngal leen ci seen jàngu, ba mbooloom ñi ko dégg waaru naan: «Lii, fu mu ko jële, te xam-xam bii mu yor, lu mu doon, ba muy def kéemaan yii? |
24483 | MRK 6:7 | Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar. |
24485 | MRK 6:9 | Sol-leen ay dàll te yem ci benn turki.» |
24486 | MRK 6:10 | Mu ne leen: «Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen jóge dëkk ba. |
24499 | MRK 6:23 | Mu boole ci ngiñ ne ko: «Loo ma mana laaj, dinaa la ko jox, ba ci genn-wàllu réew mi sax.» |
24626 | MRK 9:19 | Yeesu ne leen: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen wara muñal? Indil-leen ma xale bi.» |
24629 | MRK 9:22 | Léeg-léeg rab wi bëmëx ko ci sawara, léeg-léeg mu bëmëx ko ci ndox, ngir rey ko. Soo ko manee, yërëm nu te xettali nu.» |
24682 | MRK 10:25 | Giléem jaar ci bën-bënu puso moo gëna yomb boroom alal dugg ci nguuru Yàlla.» |
24734 | MRK 11:25 | Te it bu ngeen di ñaan, fekk ngeen jàppal kenn dara, baal-leen ko, ngir seen Baay bi ci kaw baal leen seeni tooñ, yéen itam.» |
24737 | MRK 11:28 | ne ko: «Yëf yii ngay def, ci ban sañ-sañ nga koy defe? Te ku la may sañ-sañu def ko?» |
24738 | MRK 11:29 | Yeesu ne leen: «Man itam dinaa leen laaj lenn; bu ngeen ma ci tontoo, kon dinaa leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii. |
24742 | MRK 11:33 | Ñu wax Yeesu nag ne: «Loolu de xamunu ko.» Noonu Yeesu ne leen: «Kon man itam duma leen wax ci ban sañ-sañ laay defe yëf yii.» |
24757 | MRK 12:15 | Waaye Yeesu xam na seen naaféq, mu ne leen: «Lu tax ngeen bëgg maa fiir? Indil-leen ma posetu denariyon, ma seet.» |
24794 | MRK 13:8 | Xeet dina jóg, xeex ak weneen xeet, réew xeex ak meneen réew. Te yëngu-yënguy suuf dina am ciy bérab yu bare, ak ay xiif. Loolu lépp mooy ndoortel metit yi, mel ni jigéen juy matu. |
24820 | MRK 13:34 | «Mi ngi mel ni nit ku tukki, mu dénk këram ay surgaam, ku nekk ak sa sas, te sant bëkk-néeg bi, mu xool. |
24825 | MRK 14:2 | Kon nag ñu ne: «Bumu doon ci bésu màggal bi, ngir yëngu-yëngu baña am ci nit ñi.» |
24861 | MRK 14:38 | Xool-leen te ñaan, ngir baña daanu cig fiir. Seen xol jag na, waaye seen bind a woyof.» |
24893 | MRK 14:70 | Waaye Piyeer weddiwaat ko. Nees-tuut ñi fa taxaw ne Piyeer: «Yaw mi de, ci lu wóor bokk nga ci, nde waa Galile nga.» |
24920 | MRK 15:25 | booba fekk yoor-yoor di jot. |
24944 | MRK 16:2 | Kon bés bu jëkk ci ayu-bés gi, ñu njëlu dem ca bàmmeel ba, |
24951 | MRK 16:9 | Bi Yeesu dekkee nag ci suba teel ca bés bu jëkk ca ayu-bés ga, mu jëkka feeñu Maryaama mu dëkk Magdala, mi mu dàqe woon juróom ñaari rab. |
24965 | LUK 1:3 | Léegi nag kon man ci sama wàll, gëstu naa ci lépp li ko dale ca njàlbéen ga, te fas naa la ko yéenee bindal, nettali la ni xew-xew yooyu deme woon tembe. |
25027 | LUK 1:65 | Waa dëkk ba bépp jaaxle, xew-xew yooyu siiw ca tundi Yude yépp. |
25094 | LUK 2:52 | Yeesoo ngi doon màgg ci jëmm, tey yokku ci xam-xam te neex Yàlla ak nit ñi. |
25098 | LUK 3:4 | Loolu lañu bind ci téereb waxi yonent Yàlla Esayi naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar. |
25138 | LUK 4:6 | ne ko: «Dinaa la jox bépp sañ-sañu nguur yii ak seen ndam ndaxte jébbal nañu ma ko, te ku ma soob laa koy jox. |
25168 | LUK 4:36 | Bi loolu amee ñépp waaru, ñuy waxante ci seen biir naan: «Céy jii wax! Ci sañ-sañ ak doole lay sant rab yi, ñu daldi génn.» |
25200 | LUK 5:24 | Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ba: «Maa ngi la koy sant, jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.» |
25246 | LUK 6:31 | Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko. |
25252 | LUK 6:37 | «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal. |
25299 | LUK 7:35 | Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
25313 | LUK 7:49 | Noonu ñi doon lekkandoo ak moom di wax ci seen xel naan: «Kii am sañ-sañu baale bàkkaar mooy kan?» |
25328 | LUK 8:14 | Ki jot ci jiwu wi ci xaaxaam yi mooy ki dégg kàddu gi, waaye nees-tuut soxla yi ak alal ak bànneexi àddina tanc ko, ba du àgg cig mat. |
25346 | LUK 8:32 | Fekk amoon na fa géttu mbaam-xuux yu bare, yuy for ca tund wa. Rab ya ñaan Yeesu, mu may leen, ñu dugg mbaam-xuux ya. Mu may leen ko. |
25347 | LUK 8:33 | Noonu rab ya génn nit ka, dugg mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab. |
25371 | LUK 9:1 | Benn bés Yeesu dajale fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen doole ak sañ-sañu dàq rab yépp ak di faj jàngoro yi. |
25374 | LUK 9:4 | Kër gu ngeen dugg, dal-leen fa, ba kera ngeen di fa jóge. |
25398 | LUK 9:28 | Bi ñu ca tegee luy tollook ayu-bés gannaaw bi Yeesu waxee loolu, mu ànd ak Piyeer, Yowaana ak Saag, yéeg ca kaw tund wa ngir ñaan. |
25409 | LUK 9:39 | Léeg-léeg rab jàpp ko, mu daldi yuuxu ca saa sa, rab wi di ko sayloo, gémmiñ gi di fuur. Du faral di génn ci moom te dina ko sonal. |
25439 | LUK 10:7 | Dal-leen ca kër googa, tey lekk ak a naan lu ñu leen di jox, ndaxte liggéeykat yelloo na jot peyam. Buleen dem nag kër ak kër. |
25451 | LUK 10:19 | Gis ngeen, jox naa leen sañ-sañu joggi ci jaan yi ak ci jiit yi, daan dooley bañaale bi, te dara du leen mana gaañ. |
25453 | LUK 10:21 | Ca saa soosu Xel mu Sell mi feesal Yeesu ak mbég, mu daldi ne: «Yaw Baay, Boroom asamaan ak suuf, maa ngi lay sant ci li nga nëbb yëf yii ñi am xam-xam ak ñi am xel, te xamal leen gone yi. Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.» |
25466 | LUK 10:34 | Noonu mu ñëw, sotti diw ak biiñ ca gaañu-gaañu ya, lëmës ko. Gannaaw loolu mu teg ko ci mbaamam, yóbbu ko ci fanaanukaay, di ko topptoo. |
25473 | LUK 10:41 | Boroom bi ne ko: «Màrt, Màrt, yu baree ngi fees sa xol, nga am ay téq-téq ndax loolu. |
25505 | LUK 11:31 | Keroog bés pénc buur bu jigéen, ba dëkkoon ca sudd, dina jógandoo ak niti jamono jii, yey leen; ndaxte dafa jóge ca catul àddina, ngir déglu xam-xamu Suleymaan, te ku sut Suleymaan a ngi fi. |
25533 | LUK 12:5 | Dinaa leen wax nag ki ngeen wara ragal: ragal-leen ki nga xam ne bu reyee ba noppi, am sañ-sañu sànni ca sawara. Waaw, maa ngi leen koy wax, ragal-leen kooku. |
25546 | LUK 12:18 | Noonu mu ne: “Nii laay def: daaneel sama sàq yi, defaraat yu gëna réy, ba man cee dajale sama dugub ji ak sama am-am bépp. |
25555 | LUK 12:27 | «Seetleen ni tóor-tóori ñax mi di saxe. Duñu liggéey, duñu ëcc, waaye maa ngi leen di wax ne Suleymaan sax ci ndamam soluwul woon ni benn ci ñoom. |
25564 | LUK 12:36 | Mel-leen ni ay surga yuy xaar seen njaatige buy jóge ca céet ga, ndax bu fëggee bunt ba, ñu ubbil ko ca saa sa. |
25575 | LUK 12:47 | «Surga bi xam bëgg-bëggu njaatigeem, te waajul mbaa mu takku def ko, dinañu ko dóor dóor yu metti. |
25576 | LUK 12:48 | Waaye surga bi xamul bëgg-bëggu njaatigeem, te def lu yelloo ay dóor, dinañu ko dóor dóor yu néew. Ku ñu jox lu bare dees na la feyeeku lu bare. Ku ñu dénk lu bare, dees na la laajaat lu ko ëpp. |
25594 | LUK 13:7 | Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?” |
25672 | LUK 15:15 | Mu dem nag, di liggéeyal ku dëkk ca réew ma, kooku yebal ko ca ay toolam ngir mu sàmm mbaam-xuux ya. |
25673 | LUK 15:16 | Mu xiif ba bëgga lekk ca ñamu mbaam-xuux ya, ndaxte kenn mayu ko dara. |
25690 | LUK 16:1 | Yeesu neeti ay taalibeem: «Benn boroom alal moo amoon bëkk-néeg bu ñu jiiñ ne dafay pasar-pasaree alal ji. |
25695 | LUK 16:6 | Mu ne ko: “Téeméeri bidoŋi diwu oliw.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Toogal fii gaaw te bind juróom fukk.” |
25696 | LUK 16:7 | Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom ñett fukk.” |
25697 | LUK 16:8 | Njaatige ba nag daldi naw ni bëkk-néeg bu njublaŋ boobu muuse woon. Ndaxte ñi bokk ci àddina ñoo gëna muus ci li ñu jote ci seen diggante ak seen moroom, ba raw ñi bokk ci leeru Yàlla.» |
25769 | LUK 18:12 | Ayu-bés gu nekk damay woor ñaari yoon, di joxe asaka ci lépp lu ma wut.” |