Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word.»    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23234  MAT 1:21  Dina jur doom ju góor; nanga ko tudde Yeesu, ndaxte moo di kiy musal xeetam ci seeni bàkkaar.»
23236  MAT 1:23  «Janq bi dina ëmb, jur doom ju góor, ñu tudde ko Emanuwel,» liy tekki «Yàlla ganesi na nu.»
23240  MAT 2:2  Ñu ne: «Ana buur bi juddul Yawut yi? Ndaxte gis nanu biddiiwam ci penku te ñëw nanu ngir màggal ko.»
23246  MAT 2:8  Noonu mu yebal leen Betleyem naan: «Demleen fa, seet bu wóor mbirum xale ba. Bu ngeen ci amee lu wóor nag, ngeen xamal ma ko, ngir man itam ma dem màggal ko.»
23251  MAT 2:13  Bi nga xamee ne boroom xam-xam ya ñibbi nañu, benn malaakam Boroom bi feeñu Yuusufa ci gént ne ko: «Erodd mu ngi ci tànki wut xale bi, ngir rey ko; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga daw jëm Misra, toog fa, ba kera ma koy wax.»
23253  MAT 2:15  Mu toog fa, ba Erodd faatu. Noonu am li Boroom bi waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Woo naa sama doom, mu génn Misra.»
23256  MAT 2:18  «Baat jib na ci Rama, ay jooy ak yuux gu réy, Rasel mooy jooy ay doomam te bëggul kenn dëfal ko, ndaxte saay nañu.»
23258  MAT 2:20  ne ko: «Ñi doon wuta rey xale ba dee nañu; jógal nag, jël xale bi ak ndeyam te nga dellu Israyil.»
23261  MAT 2:23  Mu ñëw nag dëkk ci dëkk bu ñuy wax Nasaret. Noonu am la ñu waxoon ca xale ba, jaarale ko ca yonent ya, bi ñu naan: «Dees na ko tudde Nasareen.»
23263  MAT 3:2  Nii la doon waaree: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jege na.»
23273  MAT 3:12  Layoom mu ngi ci loxoom, ngir jéri dàgga ja, ba mu set; pepp ma dina ko def ca sàq ma, waaye xatax ba dina ko lakk ci sawara su dul fey mukk.»
23276  MAT 3:15  Yeesu ne ko: «Bàyyil noonu, ndaxte war nanoo mottali lépp lu jub.» Noonu Yaxya nangu.
23278  MAT 3:17  Te baat bu jóge asamaan dégtu ne: «Kii mooy sama Doom ji ma bëgg; ci moom laa ame bànneex.»
23281  MAT 4:3  Noonu fiirkat bi ñëw ci moom ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, santal doj yii, ñu nekk mburu.»
23287  MAT 4:9  Mu ne ko: «Lii lépp dinaa la ko may, boo sukkee màggal ma.»
23294  MAT 4:16  xeet wa nekkoon cig lëndëm, gis na leer gu mag, ña dëkkoon ca réew, ma dee tiim, leer fenkal na leen.»
23295  MAT 4:17  Booba Yeesu tàmbali di waare naan: «Tuubleen seeni bàkkaar, ndaxte nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.»
23297  MAT 4:19  Yeesu ne leen: «Ñëwleen topp ci man, ma def leen nappkati nit.»
23412  MAT 7:27  Ba mu noppee, taw bi daldi sóob, wal mi ñëw, ngelaw li jóg, ñu dal ci kaw kër ga; mu màbb, ba ne tasar.»
23416  MAT 8:2  Noonu ku gaana ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sang bi, soo ko bëggee, man nga maa faj.»
23417  MAT 8:3  Yeesu tàllal loxoom, laal ko naan: «Bëgg naa ko, wéral.» Ca saa sa ngaanaam daldi deñ.
23418  MAT 8:4  Yeesu ne ko: «Déglul, bu ko wax kenn, waaye demal won sa bopp sarxalkat bi, te nga jébbal Yàlla sarax, si yoonu Musaa santaane, ngir mu nekk seede ci ñoom.»
23420  MAT 8:6  ne ko: «Sang bi, sama surga dafa làggi, tëdd ca kër ga te sonn lool.»
23421  MAT 8:7  Yeesu ne ko: «Dinaa ñëw faj ko.»
23423  MAT 8:9  Ndaxte man itam maa ngi nekk ci ndigal, te ame naa ay xarekat ci sama ndigal. Su ma nee kii: “Demal,” mu dem. Mbaa ma ne keneen ki: “Ñëwal,” mu ñëw. Te su ma nee sama jaam: “Defal lii,” mu def ko.»
23426  MAT 8:12  Waaye ñi waroona bokk ca nguur ga, dees na leen sànni ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.»
23427  MAT 8:13  Ci kaw loolu Yeesu wax njiit la ne ko: «Ñibbil, na ame, ni nga ko gëme.» Noonu ca waxtu woowa sax surga ba daldi wér.
23431  MAT 8:17  Loolu mu def, def na ko, ngir la ñu waxoon jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi am, bi mu naan: «Fab na sunuy wopp, gàddu sunuy jàngoro.»
23433  MAT 8:19  Laata ñuy jàll, benn xutbakat daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, dinaa la topp fépp foo jëm.»
23434  MAT 8:20  Waaye Yeesu ne ko: «Till yi am nañu seeni kàmb, te picci asamaan am nañu ay tàgg, waaye Doomu nit ki amul fu mu noppal boppam.»
23435  MAT 8:21  Noonu keneen ca taalibe ya ne ko: «Sang bi, may ma, ma jëkka dem suuli sama baay.»
23436  MAT 8:22  Yeesu ne ko: «Toppal ci man te bàyyi ñi dee, ñu suul seeni néew.»
23445  MAT 8:31  Rab ya nag ñaan ko ne: «Boo nu dàqee, sànni nu ca géttu mbaam-xuux ya.»
23450  MAT 9:2  Foofa ñu indil ko ku tëdd ci basaŋ, fekk yaramam wépp làggi. Bi Yeesu gisee seen ngëm, mu ne ku làggi ka: «Na sa xel dal, sama waay, baal nañu la say bàkkaar.»
23451  MAT 9:3  Bi mu waxee loolu, ay xutbakat daldi ne ci seen biir: «Nit kii mu ngi sosal Yàlla.»
23454  MAT 9:6  Waaye xamleen ne, Doomu nit ki am na ci àddina sañ-sañu baale bàkkaar yi.» Ci kaw loolu Yeesu ne ku làggi ka: «Jógal, jël sa basaŋ te nga ñibbi.»
23457  MAT 9:9  Bi Yeesu jógee foofa, mu gis nit ku tudd Macë, toog ca juuti ba. Yeesu ne ko: «Kaay topp ma.» Noonu Macë jóg, daldi ko topp.
23461  MAT 9:13  Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.»
23465  MAT 9:17  Te it duñu def biiñ bu bees ci mbuusi der yu màggat. Lu ko moy, mbuus yi dañuy toj, biiñ bi tuuru te mbuus yi yàqu. Waaye biiñ bu bees, dees na ko def ci mbuus yu bees. Noonu ñoom ñaar duñu yàqu.»
23466  MAT 9:18  Bi leen Yeesu di wax loolu, benn njiitu jàngu daldi ñëw, sukk ci kanamam ne ko: «Sama doom ju jigéen dafa faatu léegi, waaye ñëwal, teg ko say loxo, te dina dundaat.»
23470  MAT 9:22  Bi mu ko defee Yeesu waññiku ne ko: «Na sa xel dal, soxna si, sa ngëm faj na la.» Noonu jigéen ja daldi wér ca saa sa.
23472  MAT 9:24  Mu ne leen: «Génnleen, janq bi deewul, day nelaw rekk.» Bi ko mbooloo ma déggee, ñu daldi ko ñaawal.
23476  MAT 9:28  Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu ne ko: «Waaw, Sang bi.»
23477  MAT 9:29  Kon Yeesu daldi laal seeni bët ne leen: «Na am, ni ngeen ko gëme.»
23478  MAT 9:30  Ca saa sa seeni bët daldi ubbiku. Yeesu dénk leen bu wér ne leen: «Moytuleen kenn xam ko.»
23481  MAT 9:33  Yeesu dàq rab wa, luu ba daldi wax. Bi ñu ko gisee, mbooloo ma waaru, ñu ne: «Lu mel nii, masuñu koo gis ci Israyil.»
23482  MAT 9:34  Waaye Farisen ya ne: «Ci kàttanu buuru rab yi lay dàqe rab yi.»
23486  MAT 9:38  Ñaanleen nag Boroom ngóob mi, mu yebal ay liggéeykat, ñu góob toolam.»
23509  MAT 10:23  Boo xamee ne fitnaal nañu leen ci dëkk bii, demleen ca ba ca kanam. Ci dëgg maa ngi leen koy wax, dungeen mana wër dëkki Israyil yépp, te Doomu nit ki ñëwul.»
23528  MAT 10:42  Ci dëgg maa ngi leen koy wax, koo xam ne kii may na kaasu ndox mu sedd rekk kenn ci ñi gëna ndaw, ndax sama taalibe la, kooku du ñàkk yoolam mukk.»
23534  MAT 11:6  Yaw mi sa ngëm yolomul ndax man, barkeel nga.»
23547  MAT 11:19  Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.»
23552  MAT 11:24  Waaye maa ngi leen koy wax, keroog bés pénc ma Sodom moo lay tane.»
23554  MAT 11:26  Waaw, Baay, ndaxte looloo la neex.»
23558  MAT 11:30  Ndaxte sama kilifteef lewet na te sama yen diisul.»
23560  MAT 12:2  Farisen ya nag gis ko, ne Yeesu: «Gisal, say taalibe ñu ngi def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi.»
23566  MAT 12:8  Ndaxte Doomu nit ki mooy boroom bésub noflaay bi.»
23570  MAT 12:12  Nit nag, ndax ëppul maana xar? Kon def lu baax ci bésub noflaay bi jaadu na.»
23579  MAT 12:21  Ci turam la xeet yi di ame yaakaar.»
23582  MAT 12:24  Bi Farisen ya déggee loolu nag, ñu ne: «Kii ci kàttanu Beelsebul, buuru rab yi, lay dàqe rab yi.»
23588  MAT 12:30  Noonu ku farul ak man, yaa ngi may xeex, ku dajalewul ak man, yaa ngi tasaare.»
23595  MAT 12:37  Ndaxte dees na la àtte ni ku jub ci say wax, walla ñu daan la ci say wax.»
23596  MAT 12:38  Ci kaw loolu ay xutbakat ak ay Farisen wax ak Yeesu ne ko: «Kilifa gi, danoo bëggoon, nga won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent.»
23603  MAT 12:45  Bu ko gisee nag, mu dem wooyi yeneen juróom ñaari rab yu ko gëna soxor, ñu dugg, sanc fa; ba tax muju nit kooku mooy yées njàlbéenam. Noonu lay nekke ak niti jamono ju bon jii.»
23605  MAT 12:47  Noonu kenn nit ne ko: «Sa yaay ak say rakk ñu ngi nii taxaw ci biti, bëgga wax ak yaw.»
23608  MAT 12:50  Ndaxte ku def sama coobarey Baay bi nekk ci kaw, yaa di sama rakk, sama jigéen ak sama ndey.»
23617  MAT 13:9  Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
23631  MAT 13:23  Ki jot ci jiwu wi ci suuf su baax si nag, mooy ki dégg wax ji te xam ko; mu jural ko njariñ, muy lu mat téeméeri yoon lu ëpp la ñu ji woon, muy juróom benn fukk mbaa fanweer.»
23640  MAT 13:32  Doomu fuddën moo gëna tuuti ci jiwu yépp, waaye bu saxee, mooy sut ci gàncaxi tóokër yi, di nekk garab, ba picci asamaan ñëw, tàgg ciy caram.»
23641  MAT 13:33  Yeesu teg ca beneen léeb ne leen: «Nguuru Yàlla Aji Kawe ji dafa mel ni lawiir bu jigéen jël, jaxase ko ak ñetti andaari fariñ, ba kera tooyal bépp di funki.»
23643  MAT 13:35  Noonu am la ñu waxoon jaarale ko cib yonent, bi mu naan: «Dinaa leen wax ciy léeb, di yégle yëf yu nëbbu li dale ca njàlbéen ga ba bésu tey.»
23644  MAT 13:36  Ci kaw loolu Yeesu bàyyi mbooloo ma, dugg ca kër ga. Taalibeem yi ñëw ci moom ne ko: «Firil nu léebu jëmb, bi sax ci tool bi.»
23651  MAT 13:43  Booba nag ñu jub ñi dinañu leer ni jant bi ci seen nguuru Baay. Déglul bu baax, yaw mi am ay nopp.»
23654  MAT 13:46  Am bés mu gis per buy jar njég lu réy. Mu dem nag, jaay li mu am lépp, jënd ko.»
23658  MAT 13:50  sànni leen ci sawara. Foofa dees na fa jooy te yéyu.»
23660  MAT 13:52  Yeesu ne leen: «Kon nag xutbakat bu nekk bu jàng ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji, dafa mel ni boroom kër buy génne ci dencukaayam yu bees ak yu màggat.»
23665  MAT 13:57  Kon ñu daldi koy xeeb. Noonu Yeesu ne leen: «Dees na faaydaal yonent, waaye du ci réewam ak ci këram.»
23668  MAT 14:2  Noonu mu ne ay surgaam: «Kooku mooy Yaxya mi dekki; moo tax mu ànd ak kàttanu def ay kéemaan.»
23670  MAT 14:4  te Yaxya daan ko wax: «Jaaduwul nga denc ko.»
23673  MAT 14:7  ba mu dig ko ci kaw ngiñ ne ko: «Loo laaj, dinaa la ko jox.»
23674  MAT 14:8  Noonu ndaw sa daldi topp la ko ndey ji digaloon, ne Erodd: «Indil ma fii ci biir ndab boppu Yaxya.»
23682  MAT 14:16  Waaye Yeesu ne leen: «Matul ñu dem, yéen joxleen leen lu ñu lekk.»
23683  MAT 14:17  Ñu ne ko: «Amunu fi lu dul juróomi mburu ak ñaari jën.»
23684  MAT 14:18  Yeesu ne leen: «Indil-leen ma ko fii.»
23694  MAT 14:28  Ci kaw loolu Piyeer jël kàddu gi ne ko: «Sang bi, bu dee yaw, sant ma, ma dox ci kaw ndox mi, ñëw ci yaw.»
23699  MAT 14:33  Ñi nekk ci gaal gi nag sukk ci kanamam ne ko: «Ci dëgg yaa di Doomu Yàlla ji.»
23704  MAT 15:2  «Lu tax say taalibe di moy aaday yoon, yi maam yi tëral? Ndaxte duñu raxas seeni loxo, bu ñuy lekk.»
23713  MAT 15:11  du li dugg ci gémmiñ mooy indil nit sobe, waaye li ciy génne mooy indil nit sobe.»
23716  MAT 15:14  Bàyyileen leen, ay gumba lañu yuy wommat ay gumba; bu gumba dee wommat moroomam nag, kon dinañu daanu ñoom ñaar ci kàmb.»
23717  MAT 15:15  Piyeer nag jël kàddu gi, laaj Yeesu: «Firil nu léeb wi.»
23722  MAT 15:20  Yooyu ñooy indil nit sobe, waaye lekk ak loxo yoo raxasul du tax nit am sobe.»
23724  MAT 15:22  Ba mu fa àggee nag, jigéenu waa Kanaan, ja dëkk ca wàll yooyu, daldi génn, di wax ca kaw ne ko: «Yaw sang bi, Sëtu Daawuda bi, yërëm ma! Rab jàpp na sama doom ju jigéen, te dafa sonn lool.»
23725  MAT 15:23  Waaye Yeesu waxu ko dara. Ay taalibeem nag ñëw ci moom ne ko: «Doo ko yiwi, mu ngi nuy topp, di yuuxu ci sunu kaw.»
23726  MAT 15:24  Yeesu ne: «Yónniwuñu ma, lu dul ci xari bànni Israyil yu réer.»
23728  MAT 15:26  Yeesu ne ko: «Jël ñamu gone yi, sànni ko xaj yi, rafetul.»
23729  MAT 15:27  Waaye jigéen ja ne ko: «Waaw, sang bi, teewul xaj yi di lekk ruusit, yi rot ci seen lekkukaayu boroom.»
23730  MAT 15:28  Ci kaw loolu Yeesu ne ko: «Yaw jigéen ji, sa ngëm réy na; na am, ni nga ko bëgge.» Noonu doomam daldi wér ca saa sa.
23734  MAT 15:32  Gannaaw loolu Yeesu woo ci moom taalibeem ya ne leen: «Yërëm naa mbooloo mi, ndaxte toog nañu fi man ñetti fan, te amatuñu lu ñu lekk. Bëgguma leena yiwi te lekkuñu, ngir bañ ñu tële ci yoon wi.»
23736  MAT 15:34  Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
23742  MAT 16:1  Amoon na ay Farisen ak ay Sadusen yu ñëw ci Yeesu. Ñu fexe koo fiir, ba laaj ko ne: «Won nu kéemaan guy firndeel sag yónnent, te mu jóge ci asamaan.»