23324 | MAT 5:21 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul rey nit; ku rey nit, yoon dina la dab.” |
23330 | MAT 5:27 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bul njaaloo.” |
23334 | MAT 5:31 | «Waxoon nañu ne: “Ku fase sa soxna, nga bindal ko kayitu pase.” |
23336 | MAT 5:33 | «Dégg ngeen itam ne waxoon nañu maam ya ne leen: “Bul weddi sa ngiñ, waaye li nga giñ def ko ngir Boroom bi.” |
23341 | MAT 5:38 | «Te it dégg ngeen ne waxoon nañu: “Bët, bët a koy fey; bëñ, bëñ a koy fey.” |
23346 | MAT 5:43 | «Dégg ngeen ne waxoon nañu: “Soppal sa moroom te sib sa bañaale.” |
23364 | MAT 6:13 | Yàlla boo nu teg ci yoonu nattu, waaye yal nanga nu musal ci lu bon. Ndaxte yaw yaa yelloo nguur ak kàttan ak màggaay, ba fàww. Amiin.” |
23408 | MAT 7:23 | Ci kaw loolu dinaa leen wax dëgg ne leen: “Masuma leena xam; soreleen ma, yéen ñiy def bàkkaar.” |
23461 | MAT 9:13 | Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Demleen nag te seet lu wax joojuy tekki. Ndaxte ñëwuma, ngir woo ñi jub, waaye bàkkaarkat yi laay woo.» |
23493 | MAT 10:7 | Bu ngeen demee nag, yégleleen naan: “Nguuru Yàlla Aji Kawe ji jegesi na.” |
23538 | MAT 11:10 | Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.” |
23545 | MAT 11:17 | ne leen: “Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen, woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.” |
23546 | MAT 11:18 | Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul, naanul, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” |
23547 | MAT 11:19 | Gannaaw gi nag, Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” Waaye li xam-xamu Yàlla di jur, mooy firndeel ne dëgg la.» |
23565 | MAT 12:7 | Mbind mi nee na: “Yërmande laa bëgg, waaye du rendi saraxi mala.” Su ngeen xamoon lu wax joojuy tekki, kon dungeen teg tooñ ñi tooñul. |
23602 | MAT 12:44 | Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma génne woon.” Bu ñëwee nag, mu fekk kërug neen, ñu bale ko, defar ko ba lépp jekk. |
23623 | MAT 13:15 | Ndaxte xolu xeet wii dafa dërkiis; dañuy déglu ak nopp yu naqari, tey gëmm seeni bët, ngir baña gis ak seeni bët, dégg ak seeni nopp, te xam ci seen xol, ñu waññiku ci man, ma wéral leen.” |
23636 | MAT 13:28 | Mu ne leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?” |
23706 | MAT 15:4 | Yàlla nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” te it: “Ku móolu sa ndey walla sa baay, dees na la rey.” |
23708 | MAT 15:6 | kooku amatul warugaru teral baayam.” Noonu tebbi ngeen kàddug Yàlla ndax seen aada. |
23743 | MAT 16:2 | Noonu Yeesu ne leen: «Ngoon gi dangeen naan: “Du taw suba ndax asamaan si dafa xonq.” |
23744 | MAT 16:3 | Te suba gi ngeen naan: “Tey daal dina taw, ndax asamaan si dafa xonq te xiin.” Kon man ngeena ràññee melow asamaan, waaye manuleena ràññee firndey jamono ji nu tollu. |
23822 | MAT 18:26 | Kon jaraaf ja daanu ciy tànkam ne ko: “Muñal ma, dinaa la fey lépp.” |
23824 | MAT 18:28 | «Bi loolu amee jaraaf ja génn, gis benn moroomu jaraafam bu ko ameel ay junni. Mu daldi ko jàpp, poñe ko ne ko: “Fey ma li nga ma ameel.” |
23825 | MAT 18:29 | Kon moroomam daanu ci suuf, ñaan ko ne: “Muñal ma, dinaa la fey.” |
23836 | MAT 19:5 | te mu ne: “Looloo tax góor di teqalikook ndeyam ak baayam, ànd ak soxnaam, ñoom ñaar doon benn.” |
23865 | MAT 20:4 | Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba, te dinaa leen fey lu jaadu.” |
23868 | MAT 20:7 | Ñu ne ko: “Kenn jëlu nu.” Mu ne leen: “Demleen yéen itam ca tool ba.” |
23869 | MAT 20:8 | «Bi nga xamee ne timis jot na, boroom tool ba ne jawriñ ja: “Woowal liggéeykat yi te fey leen seen bëccëg, tàmbali ci ñi mujja ñëw, ba ci ñi fi jëkk.” |
23873 | MAT 20:12 | naan: “Ñi mujja ñëw, benn waxtu rekk lañu liggéey, ba noppi nga yemale leen ak nun, ñi yenu coonob bëccëg bi ak naaj wu metti wi.” |
23898 | MAT 21:3 | Te bu leen kenn waxee dara, ngeen ne ko: “Boroom bi da leena soxla.” Kon ca saa sa dina leen bàyyi, ñu dem.» |
23923 | MAT 21:28 | «Lu di seen xalaat ci lii? Kenn nit amoon na ñaari doom. Am bés mu ñëw ca taaw ba ne ko: “Sama doom, demal tey liggéeyi ca sama toolu reseñ.” |
23932 | MAT 21:37 | Mujj mu yónni doomam naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” |
23933 | MAT 21:38 | Waaye bi beykat yi gisee doom ji, ñu ne ci seen bopp: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndonoom.” |
23937 | MAT 21:42 | Kon Yeesu ne leen: «Xanaa masuleena jàng lii ci Mbind yi? “Doj wi tabaxkat yi sànni; mujj na di doju koñ; ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.” |
23950 | MAT 22:9 | Demleen nag buntu dëkk ba, woo ku ngeen fa gis ci reeri céet gi.” |
23954 | MAT 22:13 | Noonu buur ba ne ay surgaam: “Yeewleen ko ci tànk yi ak ci loxo yi, sànni ko ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy tey yéyu.” |
23965 | MAT 22:24 | «Kilifa gi, Musaa nee woon na: “Boo xamee ne góor dee na te amul doom, na rakkam donn jabaram, ngir sàkkal magam njaboot.” |
23978 | MAT 22:37 | Yeesu ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp ak sa xel mépp.” |
23980 | MAT 22:39 | Te ñaareel bi noona la mel: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” |
23994 | MAT 23:7 | Dañoo bëgg ñépp nuyoo leen ñaari loxo ca pénc ma, di leen wooye “kilifa gi.” |
24003 | MAT 23:16 | «Yéen njiit yu gumba yi, dingeen torox! Yéena ngi wax ne: “Ku giñe kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci wurusu kër Yàlla gi, dugg na.” |
24005 | MAT 23:18 | Dangeen ne it: “Ku giñe sarxalukaay bi ci kër Yàlla gi, ngiñ li duggul, waaye ku giñ ci sarax si ci kawam, dugg na.” |
24017 | MAT 23:30 | Te yéena ngi wax ne: “Bu nu fekke woon sunu jamonoy maam, dunu ànd ak ñoom ciy tuur deretu yonent yi.” |
24083 | MAT 25:6 | «Noonu ci xaaju guddi baat jib ne: “Boroom séet baa ngi, génnleen, gatandu ko.” |
24085 | MAT 25:8 | Ñi ñàkk xel wax ñi am xel: “Mayleen nu ci seen diw, ndaxte sunuy làmp ñu ngi bëgga fey.” |
24089 | MAT 25:12 | Mu ne leen: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, xawma leen.” |
24097 | MAT 25:20 | Noonu ki jot juróomi milyoŋ ya jegeñsi, indi yeneen juróom naan: “Kilifa gi, dénk nga ma juróomi milyoŋ; seetal, ame naa ci yeneen juróom.” |
24098 | MAT 25:21 | Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” |
24099 | MAT 25:22 | Naka noona ki jot ñaari milyoŋ it jegeñsi ne ko: “Kilifa gi, dénk nga ma ñaari milyoŋ, seetal, ame naa ci yeneen ñaar.” |
24100 | MAT 25:23 | Njaatigeem ne ko: “Def nga lu baax, surga bu baax nga te takku. Gannaaw takku nga ci lu tuuti, dinaa la dénk lu bare. Kaay bokk ci sama mbég.” |
24102 | MAT 25:25 | Moo tax ma ragaloon la, ba dem, nëbb sa xaalis ci biir suuf; mi ngii, fabal li nga moom.” |
24104 | MAT 25:27 | kon waroon ngaa yóbbu sama xaalis ca denckati xaalis ya. Bés bu ma ñëwee nag, ma mana jot li ma moom ak la mu jur.” |
24107 | MAT 25:30 | Te sànnileen surga bu amul njariñ bi ci biti ci lëndëm gi. Foofa dees na fa jooy te yéyu.” |
24113 | MAT 25:36 | te rafle, ngeen wodd ma; woppoon naa, ngeen seetsi ma; te ñu tëj ma, ngeen ñëw fi man.” |
24117 | MAT 25:40 | Noonu Buur bi dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa yu ngeen defalee loolu kenn ki gëna ndaw ci sama bokk yii, man ngeen ko defal.” |
24120 | MAT 25:43 | Nekkoon naa ab doxandéem, waaye fatuleen ma; te rafle, waaye wodduleen ma; woppoon naa te ñu tëj ma, waaye seetsiwuleen ma.” |
24122 | MAT 25:45 | Kon dina leen ne: “Ci dëgg maa ngi leen koy wax, saa su ngeen ko defalul kenn ci ñi gëna ndaw, man ngeen ko defalul.” |
24154 | MAT 26:31 | Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku ci guddi gii, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.” |
24261 | MAT 27:63 | Ñu ne ko: «Boroom réew mi, fàttaliku nanu ne, naxkat booba waxoon na, bi muy dund naan: “Gannaaw ñetti fan dinaa dekki.” |
24277 | MAT 28:13 | ne leen: «Nangeen wax lii: “Ay taalibeem ñëw nañu ci guddi, sàcc ko, bi nuy nelaw.” |
24542 | MRK 7:10 | Ndaxte Musaa nee na: “Teralal sa ndey ak sa baay,” teg ca ne: “Ku móolu sa yaay walla sa baay, dees na la rey.” |
24655 | MRK 9:48 | Foofa: “Sax ya duñu dee mukk, te sawara sa du fey.” |
24665 | MRK 10:8 | ñoom ñaar doon benn.” Kon nekkatuñu ñaar waaye benn lañu. |
24726 | MRK 11:17 | Mu di leen jàngal ne leen: «Ndax waxuñu ci Mbind mi: “Dees na wooye sama kër këru ñaan ci Yàlla ngir xeet yépp.” Waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.» |
24748 | MRK 12:6 | «Noonu mu dese ko kenn rekk, di doomam ji mu bëgg. Mujj mu yónni ko naan: “Xëy na ñu weg sama doom.” |
24749 | MRK 12:7 | Waaye beykat yi daldi ne ci seen biir: “Kii moo wara donn tool bi; nan ko rey, moom ndono li.” |
24772 | MRK 12:30 | Kon nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa xel mépp ak sa kàttan gépp.” |
24773 | MRK 12:31 | Te ñaareel bi, lii la: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.” Ndigal yii ñoo sut yépp.» |
24811 | MRK 13:25 | biddiiw yi di daanoo asamaan, te kàttani asamaan yiy yëngu.” |
24850 | MRK 14:27 | Booba Yeesu ne leen: «Yéen ñépp dingeen ma dàggeeku, ndaxte bind nañu: “Dinaa dóor sàmm bi, xari jur gi tasaaroo.” |
25291 | LUK 7:27 | Yaxya male moo di ki ñu waxoon ci Mbind mi naan: “Maa ngi yónni sama ndaw, mu jiitu la, te xàllal la yoon ci sa kanam.” |
25296 | LUK 7:32 | Ñu ngi nirook xale yu toog ca pénc ma tey woowante naan: “Liital nanu leen ak toxoro, te fecculeen, woyal nanu leen woyi dëj, te jooyuleen.” |
25297 | LUK 7:33 | Ndaxte Yaxya feeñ na, lekkul mburu, naanul biiñ, ngeen daldi ne: “Dafa ànd ak rab.” |
25298 | LUK 7:34 | Gannaaw gi nag Doomu nit ki ñëw na, lekk, naan, ngeen daldi ne: “Kii daal bëgg na lekk, di naan biiñ, tey xaritoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar.” |
25324 | LUK 8:10 | Mu ne leen: «May nañu leen, ngeen xam mbóoti nguuru Yàlla, waaye ñi ci des, dama leen di wax ci ay léeb. Noonu la, ngir: “Ñuy xool te duñu mana gis, di dégg te duñu mana xam.” |
25437 | LUK 10:5 | «Kër gu ngeen mana dugg, nangeen jëkk ne: “Na jàmm wàcc ci kër gi.” |
25441 | LUK 10:9 | Nangeen wéral jaragi dëkk ba, te ngeen ne leen: “Nguuru Yàlla jegesi na leen.” |
25443 | LUK 10:11 | “Seen pëndu dëkk, bi taq ci sunuy tànk sax, noo ngi koy faxas, ngir seede leen seen réer. Waaye nag xamleen ne nguuru Yàlla jegesi na.” |
25480 | LUK 11:6 | Dafa am sama xarit bu ma ganesi, te awma dara lu ma ko jox.” |
25481 | LUK 11:7 | «Waaye kooku nekk ci biir néegam, dina ko ne: “Bu ma lakkal, tëj naa bunt bi ba noppi te tëdd naa maak sama njaboot; manumaa jóg di la jox dara.” |
25498 | LUK 11:24 | «Boo xamee ne rab, wa jàppoon nit, génn na ci moom, day wër ay bérab yu wow, di wut fu mu noppaloo, waaye du ko gis. Noonu da naan: “Naa dellu ca sama kër, ga ma jóge.” |
25523 | LUK 11:49 | Looloo tax Yàlla mi xam lépp ne: “Dinaa leen yónnee ay yonent ak ay ndaw. Ñenn ñi dinañu leen fitnaal, rey leen.” |
25545 | LUK 12:17 | muy werante ci xelam naan: “Nu ma wara def? Ndaxte amatuma fu ma dajale sama ngóob mi.” |
25612 | LUK 13:25 | Jamono dina ñëw, ju boroom kër gi di jóg, tëj buntam. Dingeen nekk ci biti di fëgg naan: “Boroom bi, ubbil nu!” Mu ne leen: “Xawma fu ngeen bokk.” |
25613 | LUK 13:26 | Bu ko defee ngeen naan: “Noo doon bokk di lekk ak a naan, te jàngle nga ci sunuy pénc.” |
25619 | LUK 13:32 | Noonu mu ne leen: «Demleen ne bukki boobu ne ko: “Xoolal, maa ngi dàq rab yi tey wéral nit ñi tey ak suba. Ca ñetteelu fan ba, ma àgg fa ma Yàlla jëmale.” |
25631 | LUK 14:9 | Kon ki leen woo yéen ñaar ñépp man na ñëw ci yaw ne la: “Joxal toogu bi nit kii.” Noonu dinga rusa dem ca toogu bu gannaawe ba. |
25632 | LUK 14:10 | Waaye bu ñu la wooyee, demal ca toogu bu gannaawe ba. Bu ko defee ki la woo, bu agsee ne la: “Sama xarit, àggal ca kaw.” Loolu dina la sagal ci ñi nga toogandool ci lekkukaay bi. |
25639 | LUK 14:17 | Bi waxtuw lekk jotee mu yónni surga ca ña muy ganale, fàttali leen: “Man ngeena ñëw, ndaxte lépp sotti na léegi.” |
25640 | LUK 14:18 | «Waaye ñu tàmbali di jégglu ci ngan gi ñoom ñépp. Ku jëkk ka ne ko: “Damaa jënd tool léegi, te fàww ma dem seeti ko. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.” |
25641 | LUK 14:19 | Keneen ne: “Damaa jënd léegi fukki yëkk, te damay dem nii, jéem leena beyloo ba xam. Maa ngi lay ñaan, nga jéggal ma.” |
25642 | LUK 14:20 | Keneen ne ko: “Damay sooga takk jabar, looloo tax duma mana ñëw.” |
25643 | LUK 14:21 | «Surga ba dellu ca njaatigeem nettali ko loolu lépp. Noonu boroom kër ga mer, daldi ne surga ba: “Demal gaaw ca pénc ya ak ca mbedd ya ca dëkk ba, te indil ma fii néew doole yi, ñu làggi ñi, gumba yi ak lafañ yi.” |
25644 | LUK 14:22 | «Surga ba ñëwaat ne ko: “Sang bi, def naa li nga ma sant, waaye bérab bi feesul.” |
25652 | LUK 14:30 | “Waa jii dafa tàmbalee tabax, waaye manu koo àggale.” |
25663 | LUK 15:6 | Boo àggee ca kër ga, dinga woo say xarit ak say dëkkandoo ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama xar ma réeroon.” |
25666 | LUK 15:9 | Bu ko gisee, dina woo ay xaritam ak ay dëkkandoom ne leen: “Kaayleen bànneexu ak man, ndaxte gis naa sama alal ja réeroon.” |
25669 | LUK 15:12 | Benn bés caat ma ne baay ba: “Baay, damaa bëggoon, nga jox ma li may wara féetewoo ci ndono li.” Noonu baay ba daldi leen séddale alalam. |
25678 | LUK 15:21 | Doom ja ne ko: “Baay, tooñ naa Yàlla, tooñ naa la; yeyootumaa nekk sa doom.” |