Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word.”»    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23244  MAT 2:6  “Yaw Betleyem ci diiwaanu Yude, du yaw yaa yées ci njiiti Yude, ndaxte ci yaw la njiit di génne, kiy sàmm Israyil sama xeet.”»
23264  MAT 3:3  Yaxya mooy ki ñu doon wax jaarale ko ci yonent Yàlla Esayi, bi mu naan: «Am na baat buy xaacu ca màndiŋ ma ne: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”»
23282  MAT 4:4  Waaye Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk, waaye itam gépp kàddu gu génne ci gémmiñug Yàlla.”»
23284  MAT 4:6  Mu ne ko: «Boo dee Doomu Yàlla, tëbal ci suuf, ndaxte Mbind mi nee na: “Dina jox ay malaakaam ndigal ci sa mbir, ñu leewu la ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”»
23285  MAT 4:7  Yeesu ne ko: «Bind nañu it ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
23288  MAT 4:10  Waaye Yeesu ne ko: «Sore ma Seytaane, ndaxte Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom, te jaamu ko moom rekk.”»
23711  MAT 15:9  Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
23900  MAT 21:5  «Waxal waa Siyoŋ: “Seen buur a ngi ñëw ci yéen; ku lewet la, te war mbaam-sëf, dig cumbur, doomu mbaam.”»
24141  MAT 26:18  Yeesu ne leen: «Demleen ca dëkk ba, jëm ca diw, ngeen ne ko: “Kilifa gi nee na: Sama jamono jege na; ci sa kër laay màggalsi bésu Mucc ba, man ak samay taalibe.”»
24184  MAT 26:61  «Kii nee woon na: “Man naa toj kër Yàlla ga, tabaxaat ko ci ñetti fan.”»
24241  MAT 27:43  Gannaaw dénk na boppam Yàlla, kon na ko Yàlla musal, bu ko soppee, ndaxte nee na: “Maay Doomu Yàlla.”»
24287  MRK 1:3  Baat a ngi xaacu ca màndiŋ ma naan: “Xàll-leen yoonu Boroom bi, jubal-leen fi muy jaar.”»
24404  MRK 4:12  Noonu la, ngir: “Ñuy xool bu baax waaye duñu gis dara, di déglu bu baax waaye duñu xam dara, ngir bañ ñu tuub seeni bàkkaar te Yàlla baal leen.”»
24539  MRK 7:7  Seen màggal amul benn njariñ, ci li ñuy jàngle dénkaaney nit kese.”»
24676  MRK 10:19  Xam nga ndigal yi: “Bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, bul nangu alalu jaambur, teralal sa ndey ak sa baay.”»
24712  MRK 11:3  Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”»
24753  MRK 12:11  ci Boroom bi la loolu jóge, te yéemu nanu ci.”»
24881  MRK 14:58  «Nun daal dégg nanu, mu ne: “Dinaa toj kër Yàlla, gii loxoy nit liggéey, tabax ci ñetti fan geneen gu nit liggéeyul.”»
24949  MRK 16:7  Kon nag demleen, ne Piyeer ak taalibe ya: “Mi ngi leen di jiitu Galile. Foofa ngeen koy gise, ni mu leen ko waxe woon.”»
25100  LUK 3:6  Bu ko defee bépp mbindeef dina gis mucc gi Yàlla tëral.”»
25136  LUK 4:4  Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nit du dunde mburu rekk.”»
25140  LUK 4:8  Yeesu ne ko: «Mbind mi nee na: “Nanga màggal Yàlla sa Boroom te jaamu ko moom rekk.”»
25143  LUK 4:11  dinañu la leewu ci seeni loxo, ngir nga baña fakktalu ciw doj.”»
25144  LUK 4:12  Yeesu ne ko: «Bind nañu ne: “Bul diiŋat Yàlla, sa Boroom.”»
25155  LUK 4:23  Mu daldi leen ne: «Xam naa ne dingeen ma ne: “Fajkat bi, fajal sa bopp. Yég nanu li xew Kapernawum, defal lu ni mel fii ci réew mi nga dëkk.”»
25215  LUK 5:39  Ku naan biiñ bu màggat du bëgg bu bees bi, ndax day wax ne: “Bu màggat bi baax na.”»
25459  LUK 10:27  Nit ka ne ko: «“Nanga bëgg Yàlla sa Boroom ak sa xol bépp ak sa bakkan bépp, sa kàttan gépp ak sa xel mépp,” te it: “Nanga bëgg sa moroom, ni nga bëgge sa bopp.”»
25467  LUK 10:35  Bi bët setee, mu génne ñaari poseti xaalis, jox ko boroom kër ga ne ko: “Nanga topptoo nit kooku. Bés bu ma fi jaaraatee, dinaa la fey, man ci sama bopp, lépp loo ci dolli ci xaalis.”»
25596  LUK 13:9  Xëy na dina meññi. Bu ko deful, nga gor ko.”»
25646  LUK 14:24  Maa ngi leen koy wax, ci ñi ma woo woon ci sama reer bi, kenn du ci ñam.”»
25689  LUK 15:32  Waaye war nanoo bànneexu te bég, ndaxte sa rakk jii dafa dee woon te dundaat na, dafa réeroon te feeñ na.”»
25720  LUK 16:31  Waaye Ibraayma ne ko: “Su ñu dégluwul Musaa ak yonent yi, kon ku dekki sax, du tax ñu gëm.”»
25730  LUK 17:10  Noonu yéen itam bu ngeen toppee li ñu leen sant lépp ba noppi, dangeena war ne: “Ay surga rekk lanu. Sunu warugar lanu def.”»
25762  LUK 18:5  waaye jigéen jii lakkal na ma; kon dinaa ko àtte, ngir mu bañatee ñëw sonal ma. Dina rey ak ay wax.”»
25770  LUK 18:13  «Juutikat ba moom, ma nga taxaw fu sore te bëggula siggi sax, xool ca asamaan. Waaye ma ngay fëgg dënnam te naan: “Yaw Yàlla, yërëm ma, man miy bàkkaarkat.”»
25777  LUK 18:20  Xam nga ndigal yi: “Bul njaaloo, bul bóome, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg, teralal sa ndey ak sa baay.”»
25827  LUK 19:27  Waaye sama noon yi, ñi bëggul woon ma doon seen buur, indileen fii, rey leen ci sama kanam.”»
25831  LUK 19:31  Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”»
25846  LUK 19:46  naan leen: «Mbind mi nee na: “Sama kër këru ñaan ci Yàlla lay doon; waaye yéen def ngeen ko këru sàcc.”»
26067  LUK 24:7  Nee woon na: “Fàww ñu jébbal Doomu nit ki bàkkaarkat yi, ñu rey ko ci bant, mu dekki ca ñetteelu fan ba.”»
26128  JHN 1:15  Yaxyaa ngi koy seedeel te yégle na lii; nee na: «Moo taxoon ma wax ne: “Dina ñëw sama gannaaw waaye moo ma gëna màgg, ndaxte nekk na laata may juddu.”»
26146  JHN 1:33  Bi loola laata am, xawma woon mooy kan, waaye Yàlla, mi ma yebal may sóobe ci ndox, nee woon na ma: “Dinga gis Xel mu Sell mi wàcc, tegu ci kaw nit. Kooku moo di ki leen di sóob ci Xel mu Sell mi.”»
26290  JHN 5:11  Mu ne leen: «Ki ma faj moo ma ne: “Jëlal sa basaŋ te dox.”»
26357  JHN 6:31  Sunuy maam dunde nañu mànn ca màndiŋ ma, ndaxte Mbind mi nee na: “Jox na leen, ñu lekk ñam wu wàcce ca asamaan.”»
26434  JHN 7:37  Bés ba mujjoon ca màggal ga moo ca ëpp solo; keroog Yeesu taxaw, wax ca kaw ne: «Ku mar, na ñëw ci man; ku gëm, na naan! Ndaxte Mbind mi nee na: “Ndox mu bare muy dundale dina xellee ci dënnam.”»
26915  JHN 19:21  Noonu sarxalkat yu mag yu Yawut ya ne Pilaat: «Bul bind: “Buuru Yawut,” bindal rekk: “Kii moo ne mooy buuru Yawut yi.”»
27472  ACT 13:41  “Yéen ñiy xeebaate, gisleen lii, ngeen yéemu ba far; ndaxte dinaa def ci seen jamono jëf, joo xam ne su ngeen ko déggee sax, dungeen ko gëm.”»
27478  ACT 13:47  Ndaxte moom la nu Boroom bi sant ci li mu naan: “Samp naa la, nga nekk leeru ñi dul Yawut, ngir nga yóbbu mucc gi, mu daj cati àddina.”»
27729  ACT 20:35  Ci lépp won naa leen royukaay, ci li nu wara dimbali ñi néew doole te fàttaliku li Yeesu Boroom bi wax moom ci boppam ne: “Joxe moo gëna barkeel nangu.”»
27743  ACT 21:11  Mu ñëw ci nun, daldi yeew ay loxoom ak i tànkam ak laxasaayu Pool naan: «Nii la Xel mu Sell mi waxe: “Ki moom laxasaay gii, Yawut yi dinañu ko yeewe nii ca Yerusalem, jébbal ko ñi dul Yawut.”»
27793  ACT 22:21  Waaye Boroom bi ne ma: “Demal, dinaa la yebal fu sore, nga jëm ci xeeti ñi dul Yawut.”»
27807  ACT 23:5  Pool ne leen: «Bokk yi, xawma woon ne sarxalkat bu mag bi la, ndaxte tëral nañu ci Mbind mi ne: “Bul wax lu bon sa kilifag xeet.”»
28249  ROM 9:26  Te: «Fa ñu leen waxe woon: “Dungeen sama xeet,” dees na leen fa wooye “Doomi Yàlla Boroom dund.”»
28359  ROM 14:11  Ndaxte Mbind mi tëral na lii: «Boroom bi nee na: “Ni mu wóore ne maa ngi dund, ni la wóore ne, ñépp dinañu ma sukkal, te ku nekk seede ne maay Yàlla.”»
30073  HEB 3:11  Giñ naa kon ci sama mer ne: “Duñu dugg mukk ci sama noflaay.”»
30152  HEB 7:21  Waaye nag Yeesu moom doon na sarxalkat, bi Yàlla giñee ne ko: «Boroom bi giñ na te du dellu gannaaw mukk: “Doon nga sarxalkat ba fàww.”»
30207  HEB 10:7  Moo tax ma ne: “Damaa wàcc ngir def sa coobare, yaw Yàlla, mu dëppoo ak li ñu bind ci sama mbir ci téereb yoon wi.”»
31008  REV 14:13  Noonu ma dégg baat ci asamaan naan: «Bindal: “Bés ni tey, ñi nekk ci Boroom bi te dee, barkeel nañu.”» Xelum Yàlla nee na: «Waaw, dinañu noppalu ci seeni coono, ndaxte seeni jëf a nga leen di xaar.»
31095  REV 19:9  Gannaaw loolu malaaka ma ne ma: «Bindal lii: “Yéen ñi ñu woo ci reeri céetu Gàtt ba, barkeel ngeen.”» Mu teg ca ne ma: «Kàddu yii ñooy kàdduy Yàlla, di kàddu yu dëggu.»