24311 | MRK 1:27 | Bi loolu amee ñépp waaru, ba laajante naan: «Kii mooy kan? Mii njàngle lu bees la te ànd ak sañ-sañ. Day sant rab yi sax, ñu di ko déggal.» |
24483 | MRK 6:7 | Noonu mu woo ci moom fukki taalibe ya ak ñaar, jox leen sañ-sañu dàq rab yi, yónni leen, ñu ànd ñaar-ñaar. |
25084 | LUK 2:42 | Noonu bi Yeesu amee fukki at ak ñaar, ñu dem màggal ga, ni ñu ko daan defe naka-jekk. |
25164 | LUK 4:32 | Mu jàngal leen ca bésub noflaay ba, ñu waaru ca njàngleem, ndaxte dafa wax ak sañ-sañ. |
25868 | LUK 20:20 | Noonu ñu koy yeeru, daldi yónni ay nit ñu mbubboo njub, sas leen ñu fexe koo jàpp ci ay waxam, ngir jébbal ko boroom réew, ma yor kilifteef ak sañ-sañ. |
25972 | LUK 22:39 | Noonu Yeesu génn, dem ca tundu Oliw ya, ni mu ko daan defe naka-jekk. Taalibeem ya topp ci moom. |
27981 | ACT 28:14 | Gis nanu fa ay bokk, ñu ñaan nu, nu toog fa ayu-bés. Noonu nu dem Room. |
28012 | ROM 1:14 | Am naa warugar sama diggante ak ñépp, muy ñi jàng ni Gereg yi, muy ñi jàngul ni Baarbaar yi, ñi bare xam-xam ak ñi barewul xam-xam. |
28148 | ROM 6:12 | Buleen mayati bàkkaar nag, mu yilif seeni yaram yu néew doole, bay topp ay bëgg-bëggam. |
28258 | ROM 10:2 | Seedeel naa leen ne, ñu farlu lañu ci jaamu Yàlla, waaye seen njaamu àndul ak xam-xam. |
28436 | 1CO 1:5 | Ndaxte ci yiwi Yàlla yépp ngeen woomle ci Kirist, muy ci wax, muy ci xam-xam. |
28453 | 1CO 1:22 | Ndaxte Yawut yi ñu ngi laaj ay firnde; Gereg yi di wut xam-xam. |
28620 | 1CO 9:12 | Ndegam ñeneen a am sañ-sañ boobu ci yéen, nun kon waxi-noppi. Waaye nag jariñoowunu sañ-sañ boobu. Danuy far muñ lépp, ngir baña indi ndog ci yoonu xibaaru jàmm bu Kirist bi. |
28734 | 1CO 13:1 | Su fekkee ne damay wax làkki nit ñi ak yu malaaka yi sax, te boolewuma ci mbëggeel, duma dara lu dul ndënd muy riir, walla jóolóoli buy kandaŋ-kandaŋi. |
29110 | 2CO 12:20 | Ragal naa, bu ma ñëwee ci yéen, fekk leen nu ma neexul, te yéen it ngeen fekk ma nu leen neexul. Ragal naa fekk ay xuloo ci seen biir, ak ñeetaane, xadar ak diiroo mbagg, xas ak jëw, réy-réylu ak yëngu-yëngu. |
29142 | GAL 1:18 | Ba ñu ca tegee ñetti at, ma sooga dem Yerusalem, ngir xamanteek Sefas, dal fa moom lu mat ñaari ayu-bés. |
29253 | GAL 5:24 | Léegi ñi bokk nag ci Yeesu Kirist, daaj nañu seen nafsu ca bant ba, wacc ko fa, moom ak i xemmemam ak i bëgg-bëggam. |
29548 | COL 1:16 | Ndaxte ci moom la Yàlla sàkke lépp lu nekk ci asamaan ak suuf, li ñuy gis ak li ñu manula gis, muy buur, njiit, kilifa mbaa boroom sañ-sañ. Lépp lu ñu sàkk, ci moom lañu ko jaarale, ci moom lañu ko jëme. |
29564 | COL 2:3 | Ci moom lañu denc lépp lu ñuy sàkku ci xel ak ci xam-xam. |
30177 | HEB 9:5 | Ca kaw gaal ga teg nañu fa ñaari nataali mbindeef yu ñuy wax serub, yu doon wone ndamu Yàlla. Seeni laaf ñoo doon yiir kubéeru saraxu njotlaay ga. Waaye loolu lépp léegi manunu koo tekki benn-benn. |
30431 | JAS 5:10 | Bokk yi, defleen yonent, yi wax ci turu Boroom bi, seeni royukaay ci muñ tiis ak ci góor-góorlu. |
30438 | JAS 5:17 | Naka noonu Ilyaas nit la woon ku bindoo ni nun, waaye bi mu saxee ci ñaan Yàlla, ngir mu baña taw, ndox laalul suuf diirub ñetti at ak genn-wàll. |
30637 | 1JN 2:20 | Yéen nag, Aji Sell ji sol na leen Xelam, te yéen ñépp am ngeen xam-xam. |
31133 | REV 21:11 | ànd ak ndamu Yàlla. Leeraayam mel ni leeraayu per bu jafe lool, ni jamaa buy ray-rayi. |