Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   «Word.»    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23446  MAT 8:32  Yeesu ne leen: «Demleen.» Rab ya nag daldi génn, dugg ca mbaam-xuux ya, ñu daldi bartalu, daanu ca dex ga, lab ca ndox ma.
23659  MAT 13:51  Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.»
23962  MAT 22:21  Ñu ne ko: «Sesaar.» Noonu mu ne leen: «Joxleen nag Sesaar li Sesaar moom, te jox Yàlla li Yàlla moom.»
23983  MAT 22:42  «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.»
24219  MAT 27:21  Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu ne ko: «Barabas.»
24566  MRK 7:34  Mu yërëm ko, ba binni ci xolam, xool ci asamaan, daldi ne: «Effata,» liy tekki «Ubbikuleen.»
24758  MRK 12:16  Ñu jox ko poset bi. Noonu Yeesu laaj leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
25872  LUK 20:24  «Wonleen ma posetu denariyon. Kan lañu ci def nataalam ak turam?» Ñu ne ko: «Sesaar.»
25968  LUK 22:35  Noonu Yeesu ne leen: «Ba ma leen yebalee te yóbbaalewuleen woon xaalis, mbuus, walla dàll, ndax ñàkkoon ngeen dara?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
25984  LUK 22:51  Waaye Yeesu daldi ne: «Bàyyileen.» Mu laal noppu waa ja, wéral ko.
26134  JHN 1:21  Ñu laaj ko ne: «Kon yaay kan? Ndax yaa di Ilyaas?» Mu ne leen: «Déedéet, duma Ilyaas.» Ñu ne ko: «Ndax yaa di Yonent, bi wara ñëw?» Mu ne leen: «Déedéet.»
26952  JHN 20:16  Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi».
26972  JHN 21:5  Yeesu ne leen nag: «Bokk yi, xanaa jàppuleen jën?» Ñu ne ko: «Déedéet.»
28199  ROM 8:15  Nekkatuleen fa kanam Yàlla, ni jaam bu ragal sangam, waaye Xel mi leen Yàlla sol, ay doomi Yàlla la leen def, ba tax nu di wooye Yàlla: «Abba», maanaam «Baay.»
29204  GAL 4:6  Gannaaw doomi Yàlla ngeen nag, Yàlla yónni na Xelu Doomam ci sunu xol, mu koy wooye nii: «Abba», maanaam «Baay.»
30861  REV 5:14  Ñeenti mbindeef ya naan: «Amiin.» Mag ña sukk di màggal.