26151 | JHN 1:38 | Yeesu geestu, gis ne ñoo ngi koy topp. Mu ne leen: «Lu ngeen soxla woon?» Ñu ne ko: «Foo dëkk, Ràbbi?» Ràbbi mi ngi tekki «Kilifa gi». |
26952 | JHN 20:16 | Noonu Yeesu ne ko: «Maryaama.» Mu walbatiku, làkk ko ci yawut ne ko: «Ràbbuni!» Ràbbuni mooy tekki «Kilifa gi». |
30133 | HEB 7:2 | Noonu Ibraayma fab fukkeelu cér bi, maanaam asaka, ci li mu jële woon ci xare ba lépp, jox ko. Ci lu jëkk turu Melkisedeg mi ngi tekki «buur bu jub bi». Gannaaw loolu mooy buuru Salem, tur woowu mooy tekki «buuru jàmm». |
30497 | 1PE 3:6 | ni Saarata déggale woon Ibraayma, ba daan ko wooye «Sang bi». Yéen nag, su ngeen dee def lu baax te bañ cee boole genn njàqare, kon mel na ni Saarataa leen jaboote. |