Wildebeest analysis examples for:   wol-wol2010   Word?»    February 25, 2023 at 01:33    Script wb_pprint_html.py   by Ulf Hermjakob

23440  MAT 8:26  Waaye Yeesu ne leen: «Yéen ñi néew ngëm, lu tax ngeen tiit?» Ci kaw loolu mu jóg, daldi gëdd ngelaw li ak duus yi. Lépp dal, ba ne nemm.
23441  MAT 8:27  Bi ko nit ña gisee, ñu waaru naan: «Kii kan la ci biir nit ñi, ba ngelaw li ak dex gi di ko déggal?»
23443  MAT 8:29  Ña rab jàpp daldi xaacu naan: «Yaw Doomu Yàlla ji, loo nuy fexeel? Ndax danga noo bëgga mbugal, bala waxtu way jot?»
23459  MAT 9:11  Bi ko Farisen ya gisee nag, ñu ne taalibe ya: «Lu tax seen kilifa di lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
23462  MAT 9:14  Gannaaw loolu taalibey Yaxya ñëw ci Yeesu ne ko: «Lu tax nuy woor, nun ak Farisen yi, te say taalibe duñu woor?»
23476  MAT 9:28  Noonu Yeesu dugg ca kër ga, gumba ya toppsi ko. Yeesu ne leen: «Ndax gëm ngeen ne man naa def li ngeen ma laaj?» Ñu ne ko: «Waaw, Sang bi.»
23531  MAT 11:3  ne ko: «Ndax yaa di Ki wara ñëw, walla danoo wara xaar keneen?»
23568  MAT 12:10  te amoon na fa nit ku loxoom làggi. Noonu Farisen ya laaj ko: «Faj ci bésub noflaay bi, ndax loolu jaadu na?» Fekk ñuy wut buntu tuumaal ko.
23581  MAT 12:23  Noonu mbooloo mépp yéemu naan: «Ndax kii du Sëtu Daawuda bi?»
23606  MAT 12:48  Waaye Yeesu ne ko: «Kan mooy sama ndey ak ñan ñooy samay rakk?»
23659  MAT 13:51  Noonu Yeesu laaj taalibe ya ne leen: «Loolu lépp, ndax xam ngeen lu muy tekki?» Ñu ne ko: «Waaw.»
23664  MAT 13:56  Te ay rakkam yu jigéen, ndax nekkuñu fi ak nun? Lii lépp nag, fu mu ko jële?»
23681  MAT 14:15  Ca ngoon sa taalibe yi ñëw ci moom ne ko: «Fii àllub neen la, te léegi mu guddi. Doo yiwi mbooloo mi, ngir ñu dem ci dëkk yu ndaw yi, jënd lu ñu mana lekk?»
23697  MAT 14:31  Ca saa sa Yeesu tàllal loxoom, jàpp ko naan: «Yaw mi néew ngëm, lu tax nga am xel ñaar?»
23714  MAT 15:12  Bi taalibeem ya déggee loolu, ñu ñëw ci moom ne ko: «Ndax xam nga ne, Farisen yi dañoo mer ndax loolu nga wax?»
23735  MAT 15:33  Noonu taalibeem ya laaj ko: «Waaye fu nuy jële ci àll bi mburu mu doy ngir mbooloo mu tollu nii?»
23736  MAT 15:34  Yeesu ne leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaari mburu ak ay jën yu ndaw.»
23754  MAT 16:13  Bi ñu fa jógee, Yeesu dem ca diiwaanu Sesare bu Filib. Foofa mu laaj taalibeem ya: «Lu nit ñiy wax ci Doomu nit ki; mooy kan?»
23756  MAT 16:15  Noonu Yeesu ne leen: «Waaye yéen, ku ngeen may teg?»
23779  MAT 17:10  Noonu taalibe ya laaj ko: «Lu tax xutbakat ya nag di wax ne, Ilyaas mooy jëkka ñëw?»
23786  MAT 17:17  Noonu Yeesu ne: «Yéen niti jamono jii, yéen ñi gëmadi te dëng, ba kañ laa wara nekk ak yéen, ba kañ laa leen di wara muñal?» Mu ne leen: «Indil-leen ma xale bi fii.»
23788  MAT 17:19  Bi loolu amee taalibe ya ñëw ci Yeesu, laaj ko ci pegg: «Lu tax nun manunu woona dàq rab wi?»
23793  MAT 17:24  Gannaaw loolu Yeesu ak taalibe ya ñëw Kapernawum. Bi ñu fa àggee nag, laajkati warugaru kër Yàlla ga ñëw ci Piyeer ne ko: «Ndax seen kilifa du fey posetu ñaari daraxma ngir warugar wi?»
23794  MAT 17:25  Piyeer ne leen: «Ahakay!» Ba ñu eggee kër ga nag, Yeesu jëkka wax ne Piyeer: «Waaw, lu ciy sa xalaat, Simoŋ? Buuri àddina si, ñan lañuy laaj juuti walla galag? Seeni doom walla ñi bokkul ci njaboot gi?»
23797  MAT 18:1  Ca waxtu woowu taalibe ya ñëwoon nañu ci Yeesu, laaj ko: «Kan moo gëna màgg ci nguuru Yàlla mi nekk ci kaw?»
23817  MAT 18:21  Noonu Piyeer ñëw ci Yeesu, laaj ko: «Boroom bi, bu ma sama mbokk tooñee, ñaata yoon laa ko wara baal? Xanaa ba ci juróom ñaari yoon?»
23834  MAT 19:3  Bi mu fa nekkee, ay Farisen ñëw ci moom, bëgg koo fiir; ñu ne ko: «Ndax jaadu na nit fase soxnaam, saa su ko neexee?»
23838  MAT 19:7  Bi Yeesu waxee loolu, Farisen ya laaj ko ne: «Waaye Musaa santaane na, nit jox soxnaam kayitu pase, tàggook moom. Lu tax mu wax loolu nag?»
23847  MAT 19:16  Bi muy dem nag, nit daldi ñëw ci moom ne ko: «Kilifa gi, lan laa wara def ci lu baax, ngir mana am dund gu dul jeex?»
23849  MAT 19:18  Waxambaane wa laaj ko: «Yan la?» Yeesu ne ko: «Yii: bul bóome, bul njaaloo, bul sàcc, bul seede lu dul dëgg,
23851  MAT 19:20  Waxambaane wa ne ko: «Sàmm naa yooyu yépp, lu ma deseeti?»
23856  MAT 19:25  Bi nga xamee ne taalibe ya dégg nañu loolu, ñu daldi waaru lool ne ko: «Kan moo mana mucc nag?»
23858  MAT 19:27  Bi ko Piyeer déggee, mu daldi ne: «Waaw, nun nag, dëddu nanu lépp, topp la; kon nu nuy mujje nun?»
23882  MAT 20:21  Yeesu ne ko: «Loo bëggoon?» Mu ne ko: «Damaa bëggoon nga santaane ne, boo nekkee ci sa nguur, sama ñaari doom ñii toog ak yaw, kenn ci sa ndijoor, ki ci des ci sa càmmoñ.»
23883  MAT 20:22  Yeesu ne ko: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan?» Ñu ne ko: «Man nañu ko.»
23893  MAT 20:32  Noonu Yeesu daldi taxaw, woo leen ne: «Lu ngeen bëgg, ma defal leen ko?»
23905  MAT 21:10  Bi nga xamee ne Yeesu dugg na Yerusalem, dëkk ba bépp yëngatu ne: «Kii moo di kan?»
23911  MAT 21:16  Noonu ñu ne Yeesu: «Ndax dégg nga li ñuy wax?» Yeesu ne leen: «Waaw, dégg naa ko. Ndax masuleena jàng lii ci Mbind mi: “Ci gémmiñu perantal ak ñiy nàmp sàkkal nga sa bopp ay cant”?»
23915  MAT 21:20  Bi nga xamee ne taalibe ya gis nañu loolu, ñu waaru naan: «Nan la figg gi daldi wowe ci taxawaay bi?»
23920  MAT 21:25  La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?”
23926  MAT 21:31  Noonu Yeesu laaj leen: «Kan ci ñaari doom yooyu moo def coobarey baayam?» Ñu ne: «Taaw ba.» Yeesu ne leen: «Ci dëgg maa ngi leen koy wax, juutikat yi ak jigéeni moykat yi ñoo leen jëkka dugg ci nguuru Yàlla Aji Kawe ji.
23935  MAT 21:40  Noonu Yeesu laaj leen: «Bu boroom tool bi ñëwee nag, na muy def beykat yi?»
23958  MAT 22:17  Wax nu nag loo xam ci lii: ndax jaadu na, nu fey buur bi Sesaar galag walla déet?»
23961  MAT 22:20  Yeesu ne leen: «Kan lañu ci def nataalam ak turam?»
23969  MAT 22:28  Bu ndekkite taxawee nag, jabaru kan lay doon ci juróom ñaar ñi, ndaxte ñépp jël nañu ko?»
23977  MAT 22:36  «Kilifa gi, ban ndigal moo gëna màgg ci yoonu Musaa?»
23983  MAT 22:42  «Lu ngeen xalaat ci Almasi bi; kan la nekk sëtam?» Ñu ne ko: «Daawuda.»
23986  MAT 22:45  Gannaaw Daawuda nag wooye na ko: “Boroom bi,” nu muy nekke sëtam?»
24029  MAT 24:3  Noonu bi nga xamee ne Yeesu toog na ca tundu Oliw ya, taalibeem ya ñëw ci moom cig wet. Ñu ne ko: «Wax nu kañ la loolu di am, te luy tegtale ne yaa ngi ñëw te àddina di tukki?»
24138  MAT 26:15  ne leen: «Lan ngeen ma mana jox, ngir ma jébbal leen Yeesu?» Noonu sarxalkat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer.
24140  MAT 26:17  Bés bu jëkk ca màggal, ga ñuy wax Mburu ma amul lawiir, taalibe yi ñëw ci Yeesu ne ko: «Foo bëggoon nu defaral la reeru bésu Mucc ba?»
24145  MAT 26:22  Taalibe ya am naqaru xol bu réy; ku nekk daldi ne ko: «Mbaa du man, Boroom bi?»
24148  MAT 26:25  Yudaa, mi ko nara wor, laaj ko: «Mbaa du man, kilifa gi?» Yeesu ne ko: «Wax nga ko.»
24185  MAT 26:62  Ci kaw loolu sarxalkat bu mag ba jóg ne ko: «Ndax doo wax dara? Loo xam ci li ñii seede ci yaw?»
24189  MAT 26:66  Lu ngeen ci xalaat?» Ñu ne ko: «Yoon teg na ko dee.»
24191  MAT 26:68  ne ko: «Yaw Kirist, yonent bi, ndax xam nga ku la dóor?»
24209  MAT 27:11  Gannaaw loolu Yeesu taxaw ca kanam boroom réew ma, boroom réew ma laaj ko: «Ndax yaa di buuru Yawut yi?»
24211  MAT 27:13  Noonu Pilaat ne ko: «Xanaa dégguloo li ñu la jiiñ lépp?»
24215  MAT 27:17  Bi nga xamee ne daje nañu nag, Pilaat laaj leen: «Kan ngeen bëgg, ma bàyyi ko, Barabas walla Yeesu mi ñuy wax Kirist?»
24219  MAT 27:21  Noonu boroom réew ma laaj leen: «Kan ci ñaar ñii ngeen bëgg, ma bàyyil leen ko?» Ñu ne ko: «Barabas.»
24220  MAT 27:22  Pilaat ne leen: «Nan laay def nag Yeesu, mi tudd Kirist?» Ñépp ne ko: «Daaj ko ci bant, ba mu dee!»
24221  MAT 27:23  Boroom réew ma ne leen: «Lu tax? Gan tooñ la def?» Waaye ñu daldi yuuxu bu gëna kawe naan: «Daaj ko ci bant!»
24244  MAT 27:46  Noonu ci wetu ñetti waxtu Yeesu daldi wootee kàddu gu dëgër naan: «Eli, Eli, lema sabaktani?» liy tekki «Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga dëddu ma?»
24336  MRK 2:7  «Kii kan la, ba saña wax lii; mi ngi sosal Yàlla. Ana ku mana baale bàkkaar yi, ku dul Yàlla doŋŋ?»
24345  MRK 2:16  Waaye xutbakat yi bokk ci Farisen yi, bi ñu gisee ne dafa bokk lekk ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar, ñu daldi laaj taalibe yi: «Lu tax muy lekkandoo ak ay juutikat ak ay boroom bàkkaar?»
24347  MRK 2:18  Taalibey Yaxya nag ak Farisen yi daan nañu woor. Ñu ñëw nag fi Yeesu ne ko: «Lu tax taalibey Yaxya yi ak yu Farisen yi di woor, te say taalibe duñu woor?»
24353  MRK 2:24  Noonu Farisen ya ne Yeesu: «Gisal, lu tax say taalibe di def lu jaaduwul ci bésub noflaay bi?»
24355  MRK 2:26  Xanaa yéguleen li amoon ci bési Abiyatar sarxalkat bu mag bi, ni Daawuda dugge woon ca kër Yàlla ga, lekk mburu, ya ñu teewal ca kanam Yàlla, jox ci it ña mu àndaloon; fekk jaaduwul kenn lekk ko, ku dul sarxalkat?»
24361  MRK 3:4  Noonu Yeesu ne leen: «Lan moo jaadu, nu def ko bésub noflaay bi, lu baax mbaa lu bon; nu musal nit mbaa nu rey nit?» Waaye ñu ne cell.
24390  MRK 3:33  Waaye Yeesu ne leen: «Kan mooy sama ndey? Ñan ñooy samay rakk?»
24430  MRK 4:38  Fekk Yeesu tëdd di nelaw ci ngegenaay ci taatu gaal gi. Taalibe yi daldi ko yee naan: «Kilifa gi, ndax sunu bakkan soxalu la?»
24432  MRK 4:40  Yeesu ne taalibe ya: «Lu tax ngeen tiit? Ndax gëmaguleen?»
24433  MRK 4:41  Ñu daldi ragal lool, naan ci seen biir: «Kii moo di kan, ba ngelaw li ak dex gi sax di ko déggal?»
24442  MRK 5:9  Noonu Yeesu laaj ko: «Noo tudd?» Mu ne ko: «Coggal laa tudd, ndaxte ñu bare lanu.»
24463  MRK 5:30  Yeesu yég ci saa si ne, doole génn na ci moom. Mu walbatiku nag ne mbooloo mi: «Ana ku laal samay yére?»
24479  MRK 6:3  Ndax kii du minise bi? Ndax du doomu Maryaama te magu Saag, Yuusufa, Yuda ak Simoŋ? Te ay rakkam yu jigéen ndax nekkuñu fi ak nun?» Kon nag ñu daldi ko xeeb.
24500  MRK 6:24  Noonu janq bi génn ne ndeyam: «Lu may laaj?» Mu ne ko: «Laajal boppu Yaxya.»
24513  MRK 6:37  Waaye Yeesu ne leen: «Yéen joxleen leen lu ñu lekk.» Ñu ne ko: «Xanaa nu jënd lu tollook peyu juróom ñetti weer ci mburu, jox leen ñu lekk?»
24537  MRK 7:5  Noonu Farisen ya ak xutbakat ya laaj ko ne: «Lu tax say taalibe duñu topp aaday yoon, yi maam yi tëral, waaye ñuy lekk ak loxo yu setul?»
24551  MRK 7:19  ndaxte du dugg ci xol, waaye ci biiram lay jëm, ba noppi daldi génn ca bérab bu làqu?» Ci li mu wax loolu Yeesu daganal na bépp ñam.
24573  MRK 8:4  Taalibe yi ne ko: «Waaye fii àllub neen la; fu nuy jële lu doy ngir dundal leen?»
24574  MRK 8:5  Yeesu laaj leen: «Ñaata mburu ngeen am?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
24588  MRK 8:19  bi ma dammee juróomi mburu ya ngir juróomi junni ña, ñaata pañe yu fees ak ay dammit ngeen ca dajale woon?» Ñu ne ko: «Fukk ak ñaar.»
24589  MRK 8:20  Yeesu neeti leen: «Te bés bi ma dammee juróom ñaari mburu yi ngir ñeenti junni ñi, ñaata dàmba yu fees ak dammit ngeen dajale woon?» Ñu ne ko: «Juróom ñaar.»
24590  MRK 8:21  Noonu Yeesu ne leen: «Ndax seen xol dafa tëju ba tey?»
24592  MRK 8:23  Yeesu nag jàpp loxob gumba gi, yóbbu ko, ba génn dëkk bi. Mu def tiflit ciy bëtam, teg ko loxo naan: «Ndax gis nga dara?»
24596  MRK 8:27  Bi loolu amee Yeesu ànd ak ay taalibeem, dem ca dëkk, yi wër Sesare bu Filib. Bi ñuy dem nag, mu laaj taalibe yi: «Nit ñi, lu ñu wax ne man moom laa?»
24598  MRK 8:29  Noonu Yeesu laaj leen: «Yéen nag, ku ngeen wax ne moom laa?» Piyeer ne ko: «Yaa di Almasi bi.»
24618  MRK 9:11  Noonu taalibe yi laaj Yeesu: «Lu tax xutbakat yi di naan, Ilyaas moo wara jëkka ñëw?»
24623  MRK 9:16  Noonu Yeesu laaj leen: «Ci lan ngeen di werante ak ñoom?»
24628  MRK 9:21  Yeesu laaj baay bi: «Lii kañ la ko dal?» Baay bi ne ko: «Li dale ci ngoneem.
24635  MRK 9:28  Bi Yeesu duggee ci kër gi, taalibe yi laaj ko ci pegg: «Lu tax manunu ko woona dàq?»
24640  MRK 9:33  Bi nga xamee ne egg nañu dëkku Kapernawum, te dugg ci kër gi, Yeesu laaj leen ne: «Lu ngeen doon waxtaane ci yoon wi?»
24659  MRK 10:2  Noonu ay Farisen ñëw ci moom, lalal ko fiir, ñu laaj ko: «Ndax jaadu na, nit fase soxnaam?»
24660  MRK 10:3  Yeesu ne leen: «Lu leen yoonu Musaa sant?»
24674  MRK 10:17  Gannaaw loolu bi Yeesu nekkee ci kaw yoon wi di dem, am ku daw, sukk ci kanamam ne ko: «Kilifa gu baax gi, lu ma wara def, ngir am wàll ci dund gu dul jeex gi?»
24683  MRK 10:26  Wax jooju gënatee jaaxal taalibe ya, ñu naan ci seen biir: «Kon nag ku mana mucc?»
24693  MRK 10:36  Yeesu ne leen: «Lu ngeen bëggoon, ma may leen ko?»
24695  MRK 10:38  Waaye Yeesu ne leen: «Xamuleen li ngeen di ñaan. Ndax man ngeena naan kaasu naqar, bi may naan? Ndax man ngeena sóobu ci metit, yi ma nara sóobu?»
24708  MRK 10:51  Yeesu ne ko: «Loo bëggoon ma defal la ko?» Gumba gi ne ko: «Kilifa gi, damaa bëgga gis.»