23382 | MAT 6:31 | Buleen jaaxle nag, di wax ne: “Lu nu wara lekk? Lu nu wara naan?” walla: “Lu nu wara sol?” |
23407 | MAT 7:22 | Bu bés baa, ñu bare dinañu ma wax: “Boroom bi, Boroom bi, ndax du ci saw tur lanu daa waxe ci kàddug Yàlla? Ndax du ci saw tur lanu daa dàqe ay rab? Ndax du ci saw tur lanu daa defe ay kéemaan yu bare?” |
23635 | MAT 13:27 | «Noonu surgay boroom kër ga ñëw ci moom ne ko: “Góor gi, xanaa jiwuloo jiwu wu baax ci sa tool? Fu jëmb bi jóge nag?” |
23636 | MAT 13:28 | Mu ne leen: “Noon a ko def.” Surga ya ne ko: “Ndax nu dem dindi ko?” |
23829 | MAT 18:33 | Lu tax yaw itam yërëmoo sa moroom, ni ma la yërëme?” |
23867 | MAT 20:6 | Mu génnati ci tàkkusaan, gis ñeneen di tendeefal. Mu ne leen: “Lu tax ngeen yendoo tendeefal, te liggéeyiwuleen?” |
23876 | MAT 20:15 | ndax sañumaa def ak sama alal li ma neex? Walla ndax danga am kiñaan ci li ma yéwén?” |
23920 | MAT 21:25 | La Yaxya daan def, di sóob nit ñi ci ndox, fu mu ko jële, ci Yàlla walla ci nit ñi?» Ci kaw loolu ñu daldi werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” |
23953 | MAT 22:12 | Buur ne ko: “Sama waay, naka nga dugge fii, te amuloo mbubbum céet?” Waa ji ne miig. |
24086 | MAT 25:9 | Waaye ñi am xel ne leen: “Li nu yor du doy ngir nun ak yéen. Tee ngeena dem ca jaaykat ya, jënd?” |
24116 | MAT 25:39 | Kañ lanu la gisoon, nga wopp mbaa ñu tëj la, nu ñëw ci yaw?” |
24121 | MAT 25:44 | Ci kaw loolu dinañu ne: “Boroom bi, kañ lanu la gisoon, nga xiif, mbaa nga mar, nga nekk ab doxandéem mbaa rafle, nga wopp mbaa ñu tëj la, te topptoowunu la?” |
24712 | MRK 11:3 | Bu leen kenn nee: “Lu ngeen di def?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla, te léegi mu delloosi ko.”» |
24740 | MRK 11:31 | Bi ñu ko déggee, ñuy werante ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” kon dina nu laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” |
24837 | MRK 14:14 | Kër gi mu dugg nag, ngeen ne boroom kër gi: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc bi, man ak samay taalibe?” |
25548 | LUK 12:20 | Waaye Yàlla ne ko: “Ñàkk xel! Guddig tey, dees na jël sa bakkan. Kon li nga dajale lépp, ku koy moom?” |
25594 | LUK 13:7 | Noonu mu ne surga ba: “Ñetti at a ngii may ñëw di raas-si garab gii te duma ci fekk dara. Gor ko. Lu tax muy xatal tool bi?” |
25694 | LUK 16:5 | Noonu mu daldi woolu kenn ku nekk ca ña ameeloon njaatigeem bor. Ka jëkka ñëw, mu ne ko: “Ñaata nga ameel sama njaatige?” |
25696 | LUK 16:7 | Mu neeti keneen: “Yaw nag, ñaata nga ko ameel?” Mu ne ko: “Téeméeri saakuy pepp.” Bëkk-néeg ba ne ko: “Sa kayit a ngii. Bindal juróom ñett fukk.” |
25831 | LUK 19:31 | Bu leen kenn laajee: “Lu tax ngeen koy yiwi?” neleen ko: “Boroom bi da koo soxla.”» |
25853 | LUK 20:5 | Ñu waxtaan ci seen biir naan: «Bu nu nee: “Ci Yàlla,” dina laaj: “Lu tax gëmuleen ko kon?” |
25944 | LUK 22:11 | te ngeen ne boroom kër ga: “Kilifa gi nee na: Ana néegu gan, bi may lekke reeru bésu Mucc ba, man ak samay taalibe?” |
26676 | JHN 12:27 | «Léegi nag damaa jàq. Lu may wara wax? Mbaa du dama naan: “Baay, musal ma ci li nara xew waxtu wiy ñëw?” Déedéet, ñëw naa sax ngir jaar ci waxtu woowu. |
26683 | JHN 12:34 | Mbooloo ma ne ko: «Jàng nanu ci sunu téereb yoon ne, Almasi bi dina sax ba fàww. Kon yaw, nan nga mana waxe ne: “Doomu nit ki dina yékkatiku?” Kuy Doomu nit kooku?» |
27211 | ACT 7:26 | Ca ëllëg sa mu juux ci ay Yawut yuy xeex, mu di leen jéema jubale ne leen: “Yéen ay bokk ngeen, lu tax ngeen di xeex?” |
27213 | ACT 7:28 | Ndax danga maa bëgga rey, ni nga defoon démb waayi Misra ja?” |
27220 | ACT 7:35 | «Musaa moomu bañoon nañu ko, ba ne ko: “Ku la teg kilifa ak àttekat?” Waaye moom la Yàlla yebal, jaarale ko ci malaaka mi ko feeñu ca ngarab sa, ngir mu nekk kilifa gu leen di goreel. |
27779 | ACT 22:7 | Ma daldi ne nërëm ci suuf, dégg baat bu ma ne: “Sóol, Sóol, lu tax nga di ma fitnaal?” |
27780 | ACT 22:8 | Ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Mu ne ma: “Maa di Yeesum Nasaret, mi ngay fitnaal.” |
27782 | ACT 22:10 | Noonu ma laaj ko: “Lu ma wara def, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Jógal dem Damaas, foofa dees na la biral lépp, li ma la yen.” |
27906 | ACT 26:15 | «Noonu ma ne ko: “Yaa di kan, Boroom bi?” Boroom bi ne ma: “Maa di Yeesu, mi ngay fitnaal. |