23293 | MAT 4:15 | «Yaw réewum Sabulon ak réewum Neftali, di yoonu géej gannaaw dexu Yurdan, yaw Galile, réewum ñi dul Yawut— |
24374 | MRK 3:17 | Saag doomu Sebede, ak Yowaana mi mu bokkal ndey ak baay— ñoom ñi mu wooye Bowanerses, maanaam «Ñi aaytal ni dënnu gi»— |
24543 | MRK 7:11 | Waaye yéen dangeen ne: ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga wara jariñoo ci man Korban la,” —maanaam saraxu Yàlla la— |
24703 | MRK 10:46 | Bi loolu wéyee ñu agsi ca dëkku Yeriko. Bi ko Yeesu di génn, ànd ak taalibe ya ak mbooloo mu xawa bare, am gumba gu tudd Bartime— liy tekki «doomu Time», toog ci wetu yoon wi, di yelwaan. |
26250 | JHN 4:25 | Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi —maanaam Kirist— dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.» |
26419 | JHN 7:22 | Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi —jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan— moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi. |
26759 | JHN 14:22 | Yudaa —du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon— ne ko: «Boroom bi, lu xew, ba nga nar noo feeñu nun rekk, te doo feeñu àddina sépp?» |
27439 | ACT 13:8 | Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi —ndaxte loolu la turam di tekki— di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm. |
28565 | 1CO 7:10 | Ñi séy nag, maa ngi leen di jox ndigal lii —Boroom bi moo ko waxoon, du man— jigéen ju séy warula teqalikoo ak jëkkëram. |
28567 | 1CO 7:12 | Ñi ci des nag, lii laa leen di wax —Boroom bi waxu ko woon— su nit ku gëm Kirist amee jabar ju gëmul, te mu nangoo séy ak moom, waru koo fase. |
28589 | 1CO 7:34 | te noonu dafay daldi bare soxla. Jigéen ju séyul, walla janq, dafay bàyyi xel ci mbiri Boroom bi— bëgg koo jox yaramam ak xelam. Waaye jigéen ji séy dafay bàyyi xel ci mbiri àddina, ak nu mu mana neexe jëkkëram. |
28600 | 1CO 8:5 | Su fekkee ne am na sax yu ñuy teg Yàlla, muy ci asamaan mbaa ci suuf —ndaxte am na yu bare yu ñu faral di bokkaaleel Yàlla ak Boroom bi— |
28623 | 1CO 9:15 | Waaye man jariñoowuma benn ci sañ-sañ yooyu, te binduma yëf yooyu, ngir ngeen di ma defal yu ni mel. Dee sax moo ma ko gënal— kenn du jële ci man mbir moomu may kañoo! |
28825 | 1CO 15:39 | Jëmmi mbindeef yépp a wuute: nit ak jëmmam, mala, picc, jën— yu ci nekk ak sa jëmmi bopp. |
28902 | 2CO 2:10 | Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee —fekk am lu ma wara baale— yéena tax ma def ko ci kanam Kirist, |
28951 | 2CO 5:6 | Noonu kon nu ngi fees ak kóolute fu nu tollu; te xam nanu ne fi ak nu ngi dëkk ci yaram wii, àggagunu sunu màkkaan ci wetu Boroom bi— |
29040 | 2CO 10:1 | Ci lu jëm ci samay mbir nag, maa ngi leen di ñaan— man Pool, mi ñu ne, ci seen biir «ragal» laa, bu ma leen soree, «ñeme»— maa ngi leen di ñaan ndax woyof ak lewetaayu Kirist, ngir bu ma ñëwee, ma baña ànd ak ñeme gi may dencal ñenn ñiy xalaat ne gis-gisu nit lanu topp. |
29080 | 2CO 11:23 | Ndax surgay Kirist lañu? —maa ngi wax waxi ku tàggoo ak sagoom nag— maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey, maa leen ci man. Bu dee ci li ñu nu tëj ci kaso, maa leen ko gëna miin. Bu dee ci li ñu nu dóor ay yar, maa leen ëpple. Leru naa dee ba tàyyi. |
29125 | GAL 1:1 | Man Pool, ndawul Yeesu Kirist —nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Yàlla Baay, bi ko dekkal— |
29154 | GAL 2:6 | Waaye ñi ñu gëna fonk —ak lu mana doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla— waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas. |
29301 | EPH 2:5 | dundalaat na nu ak Kirist, fekk ndee lanu woon fa kanamam ci sunuy bàkkaar— ci kaw yiwu Yàlla ngeen mucce. |
29654 | 1TH 2:17 | Nun nag bokk yi, ba ñu ma leen xañee ab diir —xol yi taxul may wax, waaye jëmm yi rekk— jéem nanu leena gis ak sunu kem kàttan, ndax namm nanu leen, ba sunu xol seey ci gis leen. |
29655 | 1TH 2:18 | Kon jàppoon nanu leena seetsi— man Pool sax ay yooni yoon, waaye Seytaane téq na ma. |
29726 | 2TH 1:10 | Dina ñëw bés booba, ngir ndamam jolli ci biir gaayam yu sell yi, te ñépp ñi ko gëm yéemu ci moom— te ci ngeen bokk, ndaxte gëm ngeen li nu leen seede. |
29953 | 2TI 4:16 | Keroog bi ma jëkkee taxaw, di làyyil sama bopp, awma woon kenn ku ma taxawu, ñépp dañu maa daw— bu leen ko Yàlla jàppe nag. |
30150 | HEB 7:19 | —ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat— waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu mana jaare ngir jege Yàlla. |
30358 | JAS 1:25 | Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel —waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal— kooku barkeel na ci kaw jëfam. |
30393 | JAS 3:7 | Nit man na not xeeti rab yépp: rabi àll yi, picc yi, yiy raam ak yi ci géej gi— not na lépp. |
30812 | REV 2:27 | Dina leen jiite ak yetu weñ, tojat leen ni ñuy toje ndaal kew— |
30823 | REV 3:9 | Dinaa def ba ñenn ci ñi bokk ci ndajem Seytaane —te tuddoo Yawut, fekk dañuy fen— dinaa leen ñëwloo, ñu sukk ci sa kanam, nangu ne bëgg naa la. |
30872 | REV 6:11 | Ñu jox leen ku nekk mbubb mu weex, daldi leen ne, ñu muñ tuuti, ba kera seeni nawle ñëw, te lim bi mat— seeni nawle ci liggéey bi, di seeni bokk yu waa àddina waroona bóom ni ñoom. |
30968 | REV 12:9 | Daaneel nañu ko, moom ninkinànka ju réy ji, di jaani cosaan ji, te ñu di ko wax Tuumaalkat bi mbaa Seytaane, moom miy nax waa àddina sépp— daaneel nañu ko ci kaw suuf, moom ak i malaakaam. |
31001 | REV 14:6 | Noonu ma gis meneen malaaka naaw ca digg asamaan, yor xibaar bi sax, di ko yégal waa àddina— xeet yépp ak giir yépp ak kàllaama yépp ak réew yépp. |