24543 | MRK 7:11 | Waaye yéen dangeen ne: ku ne sa yaay walla sa baay: “Li nga wara jariñoo ci man Korban la,” —maanaam saraxu Yàlla la— |
26250 | JHN 4:25 | Jigéen ja ne ko: «Xam naa ne Almasi bi —maanaam Kirist— dina ñëw te bu ñëwee, dina nu leeralal lépp.» |
26419 | JHN 7:22 | Li leen Musaa jox ndigalu xarafal gone yi —jógewul kat ci Musaa; mi ngi tàmbalee ci seen maami cosaan— moo tax ba ngeen nangoo xarafal nit ci bésub noflaay bi. |
26759 | JHN 14:22 | Yudaa —du Yudaa Iskariyo de, beneen la woon— ne ko: «Boroom bi, lu xew, ba nga nar noo feeñu nun rekk, te doo feeñu àddina sépp?» |
27010 | ACT 1:18 | —Pey gi Yudaa jotoon ci ñaawteefam, mu jënd ci tool, daanu fa, ba fàcc, ay butitam tuuru. |
27235 | ACT 7:50 | Ndax du sama loxo moo defar yëf yooyu yépp? —Moom la Boroom bi doon wax.” |
27439 | ACT 13:8 | Waaye Elimas, boroom xam-xam bu ñuul bi —ndaxte loolu la turam di tekki— di leen dogale, ngir bañ boroom réew ma gëm. |
27856 | ACT 24:19 | Waaye ay Yawut yu dëkk Asi —xanaa kay ñoo waroona ñëw ci sa kanam, di ma kalaame, bu ñu amee dara lu ñu may topp. |
28452 | 1CO 1:21 | Gannaaw àddina si ci xam-xamam demul ba xam Yàlla —te Yàllaa dogal loolu ci xam-xamam— soob na Yàlla mu musal ñi gëm, jaar ci yégleb xibaaru Kirist, fekk ag ndof la ci bëti nit. |
28565 | 1CO 7:10 | Ñi séy nag, maa ngi leen di jox ndigal lii —Boroom bi moo ko waxoon, du man— jigéen ju séy warula teqalikoo ak jëkkëram. |
28567 | 1CO 7:12 | Ñi ci des nag, lii laa leen di wax —Boroom bi waxu ko woon— su nit ku gëm Kirist amee jabar ju gëmul, te mu nangoo séy ak moom, waru koo fase. |
28600 | 1CO 8:5 | Su fekkee ne am na sax yu ñuy teg Yàlla, muy ci asamaan mbaa ci suuf —ndaxte am na yu bare yu ñu faral di bokkaaleel Yàlla ak Boroom bi— |
28897 | 2CO 2:5 | Su kenn tegee moroomam naqar, du man la ko teg, waaye man nanu ne yéen ñépp la ko teg —matul may réyal mbir mi. |
28902 | 2CO 2:10 | Ku ngeen baal, ma baal ko itam. Man nag, su ma baalee —fekk am lu ma wara baale— yéena tax ma def ko ci kanam Kirist, |
29080 | 2CO 11:23 | Ndax surgay Kirist lañu? —maa ngi wax waxi ku tàggoo ak sagoom nag— maa leen ko gëna doon. Bu dee ci liggéey, maa leen ci man. Bu dee ci li ñu nu tëj ci kaso, maa leen ko gëna miin. Bu dee ci li ñu nu dóor ay yar, maa leen ëpple. Leru naa dee ba tàyyi. |
29125 | GAL 1:1 | Man Pool, ndawul Yeesu Kirist —nit falu ma ko, te jaarewul it ci nit, mi ngi jaare ci Yeesu Kirist ak Yàlla Baay, bi ko dekkal— |
29154 | GAL 2:6 | Waaye ñi ñu gëna fonk —ak lu mana doon seen sag xooluma ko, ñépp a yem fa kanam Yàlla— waaye ñooñu ñu teg njiit boog, bi ma dajee ak ñoom, yokkuñu dara ci sama sas. |
29654 | 1TH 2:17 | Nun nag bokk yi, ba ñu ma leen xañee ab diir —xol yi taxul may wax, waaye jëmm yi rekk— jéem nanu leena gis ak sunu kem kàttan, ndax namm nanu leen, ba sunu xol seey ci gis leen. |
30150 | HEB 7:19 | —ndax yoonu Musaa yeggalewul dara cig mat— waaye dugalal nañu nu fii yaakaar ju gën ju nu mana jaare ngir jege Yàlla. |
30358 | JAS 1:25 | Waaye kuy gëstu yoonu Yàlla, wi mat tey goreel —waxuma ki dégg, ba noppi fàtte, waaye kiy jëfe ndigal— kooku barkeel na ci kaw jëfam. |
30823 | REV 3:9 | Dinaa def ba ñenn ci ñi bokk ci ndajem Seytaane —te tuddoo Yawut, fekk dañuy fen— dinaa leen ñëwloo, ñu sukk ci sa kanam, nangu ne bëgg naa la. |