183 | GEN 7:23 | Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga. |
203 | GEN 8:19 | Rabi àll yi ak luy raam ak luy naaw ak luy dox ci kaw suuf— lépp génne ca gaal ga, lu ci nekk ak wirgoom. |
216 | GEN 9:10 | fas ko it sama diggante ak mboolem mbindeef mu ngeen àndal, muy picc akug jur mbaa rabi àll— lépp daal lu génnandoo ak yeen ci gaal gi, di lépp luy dund ci kaw suuf. |
470 | GEN 19:12 | Ba loolu wéyee gan ña wax Lóot ne ko: «Boo amee mbokk ci dëkk bi, muy sa doom ju góor mbaa ju jigéen, mbaa kuy denc sa doom— koo fi am, génne ko fi, |
1305 | GEN 43:14 | Yal na Yàlla Aji Man ji def waa ja yërëm leen, ba bàyyi seen doomu baay ba, moom ak Beñamin itam. Man nag, su ma naree ñàkk ay doom— aa! Naa leen ñàkk rekk.» |
1356 | GEN 44:31 | bu gisul xale bu góor bi ànd ak nun ñibbsi— aa! Kon de dina dee, te dinanu yóbbe sunu baay naqar, wu koy topp, ba kera muy ànd ak bijjaawam, tàbbi njaniiw. |
1468 | GEN 48:16 | malaaka mi ma jot ci bépp loraange— yal na barkeel xale yi, ba ñu saxal sama tur ak samay turi waajur, Ibraayma ak Isaaxa, te giir, ba ne gàññ ci kaw suuf.» |
3349 | LEV 21:3 | mbaa ab jigéenam bu séyagul te bootu ci moom ndax amul jëkkër— ku mu bokkal noonu, sañ naa sobewu ndax moom. |
3503 | LEV 25:33 | Kon alalu Leween manees na koo jotaat —dëkkuwaay lay doon bu ñu jaay ci dëkki Leween ñi— dees koy delloo bu atum Yiwiku dikkee, ndax dëkkuwaay yi ci dëkki Leween ñi, seen alal la ju leen lew fàww ci seen biir bokki bànni Israyil. |
7256 | 1SA 2:14 | capp ko ci biir, muy ndab lu tell, mbaa kawdir, mbaa cin, mbaa mbana— lu roq ba génne rekk, mu jël, sarxalkat bi féetewoo. Noonu lañu daan def ak mboolem niti bànni Israyil, ña daan ñëw foofa ca Silo. |
8599 | 2SA 21:16 | Ci kaw loolu Isbi Bënob ne dina rey Daawuda — kooku askanu ponkal ya ñu daan wooye Rafayeen, ca la bokkoon. Ñawkay xeejam xànjar la, diise ñetti kilo. Mu yore itam saamar bu bees. |
8750 | 1KI 1:30 | bir na ne loolu ma la giñaloon ci Aji Sax ji, Yàllay Israyil, ne la bir na ne Suleymaan sa doom mooy doon buur wuutu ma te mooy toog ci kaw jal bii ma toog— loolu déy dinaa ko sottal bés niki tey.» |
15568 | PSA 99:3 | Sa tur weeka màgg te raglu. Sàbbaal-leen ko. —Kee sell! |
15570 | PSA 99:5 | Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell! |
15574 | PSA 99:9 | Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa tundam wu sell wa. —Sunu Yàlla Aji Sax jee sell! |
17489 | ECC 6:2 | Nit ku Yàlla may alal, koom ak daraja, te mboolem lu mu namm, ñàkku ca lenn, waaye Yàlla mayu ko mu tal caa lekk, xanaa jaambur di ko xéewloo — loolu cóolóoli neen la, di naqar wu tar. |
22459 | AMO 2:11 | Maa tabboon ci seen doom yu góor ay yonent, tànne ci seen xale yu góor ay séddoo, — am déet, yeen bànni Israyil?» Kàddug Aji Sax jee. |
28623 | 1CO 9:15 | Waaye man jariñoowuma lenn ci sañ-sañ yooyu, te binduma lii it ngir defalees ma noonu. Xanaa dee sax a may gënal— boobu sañ-sañu kañu daal, kenn du ma ko yàqal! |