57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
59 | GEN 3:3 | Waaye garab gi ci digg tool bi la Yàlla ne: “Buleen ci lekk, buleen ko laal sax, lu ko moy ngeen dee.”» |
438 | GEN 18:13 | Aji Sax ji daldi wax Ibraayma ne ko: «Lu Saarata di ree, te naan: “Man mu màggat mii, deeti naa am doom moos?” |
509 | GEN 20:13 | Te bés, ba ma Yàlla génnee sama kër baay, may wëndeelu, dama koo waxoon ne ko: “Déglul, li ngay def soo ma bëggee xettli, mooy lii: fépp fu nu dem, nanga wax ne sa càmmiñ laa.”» |
566 | GEN 22:18 | te xeeti àddina sépp ci saw askan lañuy barkeele, ndax déggal nga ma.”» |
606 | GEN 24:14 | Janq bu ma wax ne ko: “Doo yenniku sa njaq, may ma, ma naan,” mu ne ma: “Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,” na kooka di ki nga jagleel sa jaam Isaaxa. Noonu laay xame ne laaye nga biir sama sang.» |
630 | GEN 24:38 | Waaye demal ca sama kër baay, ca samay bokk, nga jëlal fa sama doom soxna.” |
631 | GEN 24:39 | Ma ne sama sang: “Bu ndaw sa nanguwula ànd ak man nag?” |
633 | GEN 24:41 | Boo demee ba ca samay bokk, wàcc nga, ndax bu ñu la mayul soxna, wàccoo nga ak man.” |
636 | GEN 24:44 | mu ne ma: ‘Naanal ba noppi, ma wëggal la say giléem,’ kooku na di soxna, si Aji Sax ji jagleel sama doomu sang.” |
637 | GEN 24:45 | «Bala maa ñaan ba noppi, Rebeka ne jimeet, gàddu njaqam, wàcc ca seyaan ba, di root. Ma ne ko: “May ma, ma naan.” |
638 | GEN 24:46 | Mu gaaw yenniku njaq li, daldi ne ma: “Naanal ba noppi ma wëggal la say giléem.” Ma naan ba noppi, mu wëggal ma giléem yi. |
639 | GEN 24:47 | Ma laaj ko ne ko: “Kan moo la jur?” Mu ne: “Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom. |
735 | GEN 27:7 | “Demal rëbbi, indil ma, toggal ma ko lu neex, ma lekk, ba ñaanal la, Aji Sax ji seede, bala may dëddu.” |
882 | GEN 31:8 | Bu nee: “Yi tippanteey sa peyoor,” jur gépp jur lu tippante; mbaa mu ne: “Yi seereer ay sa peyoor,” jur gépp jur lu seereer. |
885 | GEN 31:11 | Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: “Yanqóoba,” ma ne ko: “Naam.” |
887 | GEN 31:13 | Maay Yàlla, ja la feeñu woon Betel, fa nga samp doj, sotti ci diw, sellale ko, te dogu woon fa ci man. Léegi nag jógal, génn réew mii, dellu ca réew, ma nga juddoo.”» |
903 | GEN 31:29 | Manoon naa laa def lu bon, waaye sa Yàllay baay da maa feeñu biig ne ma: “Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.” |
934 | GEN 32:6 | ma doora ñëw, ànd ak ay nag ak ay mbaam ak ay gàtt ak ay jaam yu góor ak yu jigéen; may yónnee ci yaw, di la siyaare tey sàkku nga dalal ma jàmm.”» |
938 | GEN 32:10 | Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.” |
941 | GEN 32:13 | Te yaw yaa ma ne: “Dinaa la baaxe moos, yokk saw askan, ba mu tollu ni suufas géej, si kenn manula lim ndax bare.”» |
946 | GEN 32:18 | Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?” |
947 | GEN 32:19 | nee ko: “Lii de sang bi, lu la Yanqóoba may la, di la ko siyaaree, yaw Esawu, te moom ci boppam mu ngi topp ci sunu gannaaw.”» |
949 | GEN 32:21 | tegati ca ne ko: «Te nee ko itam: “Sa surga Yanqóobaa ngi topp ci sunu gannaaw.”» Booba Yanqóobaa ngi naa ci xelam: «Bu ma jiitalee li ma ko may, neexale ko ko, bala maa janook moom, jombul mu dalal ma jàmm.» |
1101 | GEN 37:17 | Waa ja ne ko: «Jóge nañu fii de, ndax dégg naa ñu naan: “Nanu dem Dotan.”» Yuusufa toppi magam ya ba Dotan, fekk leen fa. |
1275 | GEN 42:22 | Ruben nag àddu ne leen: «Ndax newuma leen woon: “Buleen gàddu bakkanu xale bi,” waaye faalewuleen ma; tey rekk la nu Yàlla doon xaare bakkanam, bi nu gàddu.» |
1285 | GEN 42:32 | fukki góor ak ñaar lanu woon yu bokk sunu baay, waaye kenn ka nekkatul, te ka gën di xalee nga fa sunu baay, ba ca réewu Kanaan.” |
1287 | GEN 42:34 | su ko defee ngeen indil ma seen rakk ju ndaw, kon dinaa xam ne dungeen ay yëddukat waaye nit ñu maandu ngeen, te dinaa leen delloo seen mbokk, ngeen mana dem fu leen neex ci réew mi.”» |
1294 | GEN 43:3 | Yuda ne ko: «Waa ja da noo àrtu woon de, wax na nu ne nu: “Dootuleen jàkkaarlook man te ànduleen ak seen rakk.” |
1296 | GEN 43:5 | Waaye boo ko bàyyiwul kat, dunu dem, ndax waa ja waxoon na nu ne nu: “Dungeen jàkkaarlook man te seen rakk àndul ak yeen.”» |
1330 | GEN 44:5 | Ndax li ngeen jël du sama kaasu sang, bi muy naane, rawatina di ko gisaanee? Lu ñaaw ngeen def nii!”» |
1344 | GEN 44:19 | Sang bi, danga noo laajoon ne nu: “Ndax am ngeen baay walla rakk?” |
1345 | GEN 44:20 | Ba mu ko defee nu ne la: “Am nanu baay bu màggat. Sunu rakk, ji mu jur te fekk ko di màggat nag, moo ci gën di ndaw. Magam dafa dee, mu des moom doŋŋ ci ndeyam, baayam sopp ko lool.” |
1346 | GEN 44:21 | Nga waxoon nu ne nu: “Indil-leen ma ko, ngir ma gisal ko sama bopp.” |
1347 | GEN 44:22 | Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: “Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.” |
1348 | GEN 44:23 | Nga wax nu ne nu: “Bu seen rakk àndul ak yeen, dungeen jàkkaarlook man.” |
1350 | GEN 44:25 | «Ba nu demee ba mu yàgg, sunu baay ne: “Delluleen, jëndali nu tuuti dund.” |
1351 | GEN 44:26 | Teewul nu ne: “Dunu mana dem te sunu rakk àndul ak nun, ndaxte bu nu àndul ak moom, dunu gis kilifa ga.” |
1354 | GEN 44:29 | Te bu ngeen ma fi jëlalee kii itam, ba musiba dab ko, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.” |
1357 | GEN 44:32 | Gannaaw loolu it xasoon naa dige sama bakkan, ndax damaa waxoon ne: “Bu ma la ko délloosilul, maa koy gàlloo ba kera may dee.” |
1370 | GEN 45:11 | ndaxte des na juróomi ati xiif. Waaye dinaa la fi yore, ba doo ñàkk dara, yaak sa waa kër ak mboolem lu bokk ci yaw.” |
1377 | GEN 45:18 | jëli seen baay ak seeni njaboot, ngeen ñëw fi sama wet. Dinaa leen jox suuf si gën ci réewum Misra, ngeen di lekk li fi gëna duuf.”» |
1379 | GEN 45:20 | Te buleen réccu alal, ji ngeen di bàyyi seen gannaaw, ndax li gën ci réewum Misra yeena koy moom.”» |
1419 | GEN 46:32 | Dafa di seeni góor ay sàmm lañu, ag jur lañu masa yar, te indaale nañu seen jur gu gàtt ak gu gudd ak mboolem lu ñu moom.” |
1421 | GEN 46:34 | “Lan mooy seen liggéey?” ngeen ne ko: “Nun de sang bi, ag jur lanu masa yar, ba nuy gone ba tey, te noonu la ko sunuy maam daan defe.” Su boobaa, ngeen mana féetewoo diiwaanu Gosen, ndaxte waa Misra dañuy xof sàmm.» |
1456 | GEN 48:4 | te wax na ma ne ma: “Dinaa la giiral, fulandi la, def la nga sos mbooloom xeet, te réew mii laay may ñi askanoo ci yaw, ñu moom ko fàww.” |
1472 | GEN 48:20 | Gannaaw loolu mu ñaanal leen keroog ne leen: «Yal na Israyil di ñaane seeni tur naan: “Yal na la Yàlla def ni Efrayim ak Manase.”» Noonu la jiitale Efrayim, door caa teg Manase. |
1524 | GEN 50:17 | Waxleen Yuusufa ne ko, sa baay nee: “Say mag def nañu la lu bon moos, waaye ngalla baal leen seeni tooñ ak àq, ji ñu la ameel.” Kon rikk waay, baal nu àq, ndax nun nook sa baay a bokk jenn Yàlla ju nuy jaamu.» Ba ñu waxee Yuusufa loolu, mu daldi jooy. |
1594 | EXO 3:14 | Yàlla ne Musaa: «Maay Ki nekk. Kon waxal bànni Israyil ne leen: “Aji Nekk ji moo ma yónni ci yeen.”» |
1595 | EXO 3:15 | Yàlla dellu ne Musaa: «Dangay wax bànni Israyil, ne leen: “Aji Sax ji, seen Yàllay maam ya, di Yàllay Ibraayma, di Yàllay Isaaxa te di Yàllay Yanqóoba, moo ma yónni ci yeen.” Aji Sax jee di sama tur wu sax dàkk, ñu di ma ko fàttlikoo ba fàww. |
1597 | EXO 3:17 | Dogu naa leena jële ci seen notaange gii ngeen nekke ci Misra, yóbbu leen ca réewum Kanaaneen ña ak Etteen ña ak Amoreen ña ak Periseen ña ak Eween ña ak Yebuseen ña, réew mu meew maak lem ja tuuroo.’ ” |
1598 | EXO 3:18 | «Magi Israyil dinañu la déggal, su ko defee nga ànd ak ñoom, dem ca buuru Misra. Waxleen ko ne ko: “Aji Sax ji Yàllay Ebrë yi moo nu feeñu. Kon nag ngalla may nu, nu dem topp màndiŋ mi lu mat doxub ñetti fan, ngir rendili sunu Yàlla Aji Sax ji ay sarax.” |
1603 | EXO 4:1 | Gannaaw loolu Musaa dellu wax Aji Sax ji ne ko: «Waaw, su ñu ma dégluwul te gëmuñu ma, xanaa ne ma: “Aji Sax ji feeñuwu la” nag?» |
1625 | EXO 4:23 | Te wax naa la ne la, nga bàyyi sama doom, ndax mu man maa jaamu, nga bañ. Kon nag dinaa rey sa taaw bu góor.’ ”» |
1634 | EXO 5:1 | Gannaaw loolu Musaa ak Aaróona dem ca Firawna, ne ko: «Aji Sax ji Yàllay Israyil dafa wax ne: “Bàyyil sama ñoñ, ñu dem màggali ma ca màndiŋ ma.”» |
1641 | EXO 5:8 | Waaye sasleen leen limu móol, ya ñu daan móol naka jekk. Buleen ko wàññi, ndax ay yaafus lañu; moo leen tax di dee-deeluy waxeey naan: “May nu, nu dem rendili sunu Yàlla sarax!” |
1650 | EXO 5:17 | Firawna ne leen: «Yaafus yi ngeen doon! Yaafus a leen tax di wax naan: “May nu, nu dem rendili Aji Sax ji sarax.” |
1695 | EXO 7:9 | «Bu leen Firawna waxee ne leen: “Defleen seeni kéemaan boog!” danga naan Aaróona: “Jëlal yet wi, sànni ci suuf ci kanam Firawna.” Su ko defee yet wi dina soppliku jaan.» |
1704 | EXO 7:18 | su ko defee jën yi ci dex gi dee, dexu Niil gi mujj xasaw, ba waa Misra dootuñu mana naan ci ndoxum Niil.’ ”» |
1705 | EXO 7:19 | Ci kaw loolu Aji Sax ji ne Musaa: «Waxal Aaróona ne ko: “Jëlal saw yet, te tàllal sa loxo tiimale ko ndoxi Misra, muy seeni dex ak seen yooni ndox ak seeni déeg ak fépp fu ndox taa, mu ànd soppliku deret.” Deret ja dina daj Misra gépp, ba ca këll yaak njaq ya.» |
1715 | EXO 7:29 | Mbott yi dinañu yéeg ci sa kaw, yéeg ci kaw waa réew mi, ak sa dag yépp.”» |
1734 | EXO 8:19 | te maay musal sama ñoñ ci musiba moomuy dal saw askan. Ëllëg firnde jooju dina am.’ ”» |
1747 | EXO 9:4 | Waaye man Aji Sax ji maay ràññatle juru bànni Israyil ak juru waa Misra, ba lenn du dee ci mboolem lu bànni Israyil moom.”» |
1762 | EXO 9:19 | Kon nag sa jur ak mboolem loo am, te mu nekk ci biti, booleel fat fu wóor, ndax lu nekk ci biti te fateesu ko, su tawtee dee, muy nit mbaa mala.’ ”» |
1784 | EXO 10:6 | Te itam dinañu fees say biir kër ak sa këri dag yépp ak këri waa Misra gépp, muy mbir mu say maam ak say mamaat masula gis, ba ñu ganee àddina ba bésub tey jii.”» Ba loolu amee Musaa walbatiku, bàyyikoo ca Firawna. |
1814 | EXO 11:7 | Waaye fépp fu bànni Israyil dëkke, dara du fa wokk nit ak mala.” Su boobaa dingeen xam ne, Aji Sax jee ràññatle waa Misra ak bànni Israyil. |
1815 | EXO 11:8 | Bu loolu amee mboolem sa dag yii dinañu ma sujjóotalsi te naan ma: “Demal, yaak mbooloo, mi la topp yépp!” Su ko defee ma doora dem.» Musaa nag won Firawna gannaaw, mer ba, fees. |
1843 | EXO 12:26 | Te bu leen seeni doom laajee ne leen: “Lu aada jii di wund?” |
1844 | EXO 12:27 | waxleen leen ne leen: “Loolu sarax la ñeel Aji Sax ji ngir bésub Mucc ba, ndax la mu teggi woon këri bànni Israyil ca Misra, kera ba muy fàdd waa Misra te musal ca sunuy kër.”» Ba mu waxee loolu ba noppi, mbooloo ma sujjóot, màggal Yàlla. |
1876 | EXO 13:8 | Bu keroogee na ku nekk xamal doomam, ne ko: “La ma Aji Sax ji defaloon, ba ma génnee Misra, moo waral lii tey.” |
1882 | EXO 13:14 | Su ko defee, bu leen seen doom laajee ëllëg, ne leen: “Lii lu muy tekki?” ngeen wax ko ne ko: “Dooley loxol Aji Sax jee nu génne Misra, kërug njaam ga. |
1883 | EXO 13:15 | Ba Firawna tëwee, bañ noo bàyyi, nu dem, Aji Sax jee rey mboolem lu doon taaw bu góor ca réewum Misra, taawu nit ba ci taawu mala. Looloo waral nuy rendil Aji Sax ji mépp mala mu jëkka juddu, di góor, sunu bépp taaw bu góor it, ñu war koo jote sarax su nu koy rendil.” |
1893 | EXO 14:3 | Su ko defee Firawna da naan: “Bànni Israyil de dañoo réer ci àll bi, ba faf keppu ci màndiŋ mi.” |
1930 | EXO 15:9 | «Noon baa nga naa: “Maay dàqe, dabe, lël alal ja, séddale séddu, ba xol sedd, ne saamar boset, teg leen loxo.” |
1964 | EXO 16:16 | Aji Sax ji dafa santaane ne: “Na ku nekk for lu mat njëlam, bopp bu ne andaar, te mu natt ko ci limu nit, ñi mu bokkal xayma.”» |
1980 | EXO 16:32 | Ci biir loolu Musaa ne: «Aji Sax ji dafa santaane ne: “Sàkkleen ci andaar, denc ngir seeni sët ak seeni sëtaat. Su ko defee ñu gis ñam, wi ma leen daan leel ca màndiŋ ma, gannaaw ba ma leen génnee réewum Misra.”» |
2033 | EXO 19:6 | waaye yeenay doon nguuru sarxalkati Yàlla, te di xeet wu sell.” Kàddu yooyu ngay wax bànni Israyil.» |
2040 | EXO 19:13 | Bu loxo laal kooka, waaye nañu ko dóor ay doj ba mu dee, mbaa ñu jam ko. Su dee nit, su dee mala, bumu dundati.” Bu liit gi jibee doŋŋ nag lañuy doora mana dem ba ca tund wa.» |
2078 | EXO 20:26 | Buleen yéeg ci ay dëggastal, doora mana àgg ca sama sarxalukaay, ndax loolu day tax ngeen di fa sàgganu.”» |
2083 | EXO 21:5 | Waaye su jaam bi biralee ne: “Maa bëgg sama sang, maak sama jabar ak samay doom, te buggumaa moom sama bopp”, |
2330 | EXO 28:36 | «Sàkkal dogu wurusu ngalam wu tell, nga ñaas ci mbind mii ni ñuy ñaase mbindum torlu: “Lu sell a ngii, ñeel Aji Sax ji.” |
2416 | EXO 30:33 | Képp ku njafaan lu ni mel, mbaa mu taqal ci yaramu ku ci bokkul, dees koy dagge ci biir bànni Israyil.”» |
2438 | EXO 31:17 | Sama diggante laak bànni Israyil, te firnde la ju sax dàkk, ndax ci juróom benni fan la Aji Sax ji sàkk asamaan ak suuf, bésub juróom ñaareel ba, mu dal-lu, daldi yeeslu.”» |
2447 | EXO 32:8 | Jàdd nañu xaat yoon wa ma leen tegoon. Dañoo sàkkal seen bopp sëllu wu ñu móol, di ko sujjóotal ak a sarxalal, naan: “Israyiloo, seen yàllaa ngii, moo leen génne réewum Misra!”» |
2451 | EXO 32:12 | Ana lu jar Misra di wax naan: “Musiba mi mu leen naraloon, ba mu leen di yiwi de, du lenn lu moy rey leen ba ñu jeex ca tund ya, ba fare leen kaw suuf sépp.” Ngalla dëddul sa sawaras sànj te nga fomm musiba mi nga naral sa ñoñ. |
2452 | EXO 32:13 | Bàyyil xel Ibraayma ak Isaaxa ak Israyil, sa jaam ñi nga giñaloon ci sa bopp, ne leen: “Maay yokk seen askan ni biddiiwi asamaan, te mboolem réew mii ma waxoon, maa koy jox seen askan, ñu moom ko fàww.”» |
2462 | EXO 32:23 | Dañu ma ne: “Sàkkal nu yàlla ju nu jiite, ndax Musaa mii nu génne réewum Misra kat, xamunu lu ko dal.” |
2463 | EXO 32:24 | Ma ne leen: “Ku takk wurus, tekkil, indi!” Ñu jox ma, ma sànni ci sawara wi, sëllu wii génne ci!» |
2466 | EXO 32:27 | Mu ne leen: «Aji Sax ji, Yàllay Israyil dafa wax ne: “Na ku nekk teg saamaram ci luppam, te ngeen wër dal bi bépp buntoo bunt, ba mu daj. Reyleen ñépp; doomu ndey, xarit ak jegeñaale.”» |
2486 | EXO 33:12 | Musaa nag ne Aji Sax ji: «Waaw, yaw de yaa ngi ma naa ma yóbbu mbooloo mii, waaye xamaloo ma kan ngay yebal, mu ànd ak man. Yaa ma waxoon it ne ma: “Maa la xam ci saw tur, te it daj nga sama yiw.” |
2511 | EXO 34:14 | ndax waruleena jaamu jeneen yàlla, ngir Aji Sax ji, turu “Ku fiir ki” lay wuyoo, te Yàlla ju fiir la. |
2981 | LEV 10:3 | Musaa ne Aaróona: «Lii la Aji Sax ji doon wax ba mu nee: “Ci biir ñi may jegeñ laay feeñal samag sellaay, te ci kanam mbooloo mi mépp lees may terale.”» Aaróonaa nga ne cell. |
3098 | LEV 13:45 | «Ku ànd ak jàngoroy der juy law nag yére yu xottiku lay sol te day njañu. Na muur li ko dale ci tuñum kaw mi ba ci sikkim bi, te nay jàppoo àddu ca kaw naan: “Setuma de, setuma!” |
3147 | LEV 14:35 | boroom néeg bi dafa wara dem ca sarxalkat ba ne ko: “Lu mel ni aw liir laa gis sama néeg.” |
3490 | LEV 25:20 | Jombul ngeen di wax naan: “Lu nuy lekk nag ci atum juróom ñaareel ba, gannaaw dunu ci ji te dunu ci dajale sunu meññeef?” |
3813 | NUM 5:20 | Waaye su dee yaa moy te fekk la ci sa buumu jëkkër, su dee yaa sobeel sa bopp ak geneen góor gu ànd ak yaw te du sa jëkkër nag...” |
3815 | NUM 5:22 | Yal na ndoxum alkànde mii tàbbi ci say butit, laxal sa njurukaay, wal sab koll.” Su ko defee ndaw si ne: “Amiin, Amiin.” |
3850 | NUM 6:26 | «“Yal na la Aji Sax ji siggil, jàmmal la.” |
4038 | NUM 11:13 | Ana fu may jële yàpp wu ma jox mii mbooloo mépp, ba ñuy jooy nii ci sama kaw, naa ma: “Jox nu yàpp wu nu lekk.”? |
4043 | NUM 11:18 | «Mbooloo mi nag, ne leen ñu sell-lu ngir ëllëg, te ne leen dinañu yàpp moos, gannaaw ñooy jooy ci kaw Aji Sax ji, naan “Éy ku nuy leelatiw yàpp, nooka neexle woon ca Misra!” Kon nag Aji Sax jee leen di jox yàpp wu ñu lekk. |