1854 | EXO 12:37 | Ci kaw loolu bànni Israyil jóge dëkk ba ñuy wax Ramses, jëm Sukkóot. Ña nga tollu ci juróom benni téeméeri junniy góor (600 000) te limaaleesul jigéen ñaak xale ya. |
2659 | EXO 38:25 | Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, |
2660 | EXO 38:26 | muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
2661 | EXO 38:27 | Ñetti junniy (3 000) kiloy xaalis, di téeméeri talaŋ, ñeel móolub teguy bérab bu sell bi, ak teguy rido bi. Muy téeméeri tegu ci ñetti junniy kilo, di fanweeri kilo ci benn tegu, muy téeméeri tegu ci téeméeri talaŋ, benn talaŋ ci benn tegu. |
2663 | EXO 38:29 | Xànjar bi ñu def saraxu yékkati-jébbal Yàlla, ñaari junniy kilo ak téeméer ak ñaar fukk ak ñeent la (2 124), yemook juróom ñaar fukki (70) talaŋ ak ñaari junneek ñeenti téeméeri (2 400) siikal. |
3626 | NUM 1:21 | Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3628 | NUM 1:23 | Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3630 | NUM 1:25 | Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3632 | NUM 1:27 | Limub Yudeen ñi di juróom ñaar fukki junneek ñeent, ak juróom benni téeméer (74 600). |
3634 | NUM 1:29 | Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3636 | NUM 1:31 | Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3638 | NUM 1:33 | Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3640 | NUM 1:35 | Limub Manaseen ñi di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3642 | NUM 1:37 | Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3644 | NUM 1:39 | Limub Daneen ñi di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). |
3646 | NUM 1:41 | Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3648 | NUM 1:43 | Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3651 | NUM 1:46 | Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3663 | NUM 2:4 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom ñaar fukki junneek ñeent ak juróom benni téeméer (74 600). |
3665 | NUM 2:6 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3667 | NUM 2:8 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3668 | NUM 2:9 | «Mboolem ña ñu limal dalub Yuda aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett fukk ak juróom benn ak ñeenti téeméer (186 400). Bu ñuy dem, ñooñooy dox, jiitu. |
3670 | NUM 2:11 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3672 | NUM 2:13 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3674 | NUM 2:15 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3675 | NUM 2:16 | «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca. |
3678 | NUM 2:19 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3680 | NUM 2:21 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek ñaar ak ñaar téeméer (32 200). |
3682 | NUM 2:23 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3683 | NUM 2:24 | «Mboolem ña ñu limal dalub Efrayim aki gàngooram daldi doon téeméeri junneek juróom ñett ak téeméer (108 100). Bu ñuy dem, ñooñoo di ñetteelu kurél, dox topp ca. |
3685 | NUM 2:26 | Ña ñu limal gàngooram di juróom benn fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (62 700). |
3687 | NUM 2:28 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3689 | NUM 2:30 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3690 | NUM 2:31 | «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.» |
3691 | NUM 2:32 | Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3715 | NUM 3:22 | Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom ñaari junni ak juróomi téeméer (7 500) lañu. |
3721 | NUM 3:28 | Ba ñu waññee mboolem góor ña ca am weer, jëm kaw, juróom ñetti junni ak juróom benni téeméer (8 600) lañu. Ñoo dénkoo woon dénkaaney bérab bu sell bi. |
3727 | NUM 3:34 | Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom benni junni ak ñaar téeméer (6 200) lañu. |
3732 | NUM 3:39 | Mboolem ña ñu limal Leween ñi, te Musaa ak Aaróona lim leen na ñu bokke seeni làng ci ndigalal Aji Sax ji, ñuy mboolem góor ñi am weer, jëm kaw, ñaar fukki junneek ñaar (22 000) lañu. |
3736 | NUM 3:43 | Ba ñu waññee mboolem taaw yu góor ya, bind seeni tur, dale ci ñi am weer, jëm kaw, seenub lim nekk na ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak ñett (22 273). |
3743 | NUM 3:50 | Xaalis ba mu nangoo ca taawi bànni Israyil di junniy siikal ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom (1 365), ci siikalu bérab bu sell bi, xawa tollu ci fukki kilo ak ñett. |
3780 | NUM 4:36 | Ña ñu limal seeni làng di ñaari junni ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukki góor (2 750). |
3784 | NUM 4:40 | te ñu limal leen seeni làng ak seen këri maam, ñaari junneek juróom benni téeméer ak fanweeri góor lañu (2 630). |
3788 | NUM 4:44 | te ñu limal leen seeni làng, ñetti junni ak ñaar téeméeri góor (3 200) lañu. |
3792 | NUM 4:48 | seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580). |
3936 | NUM 7:85 | ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikali bérab bu sell bi ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróomi téeméeri garaam (27 500). |
3937 | NUM 7:86 | Fukki bàttuy wurus yi feese cuuraay, mbàttu su ci nekk fukki siikali bérab bu sell bi la, di téeméeri garaam ak fukk (110), mboolem wurusu bàttu yi di téeméeri siikal ak ñaar fukk (120), muy kilo ak ñetti téeméeri garaam (1 300). |
4046 | NUM 11:21 | Ci kaw loolu Musaa ne: «Ãa! Juróom benni téeméeri junniy (600 000) góor a ngi ci mbooloo mii ma ne ci seen biir. Yaw nga ne aw yàpp nga leen di jox, ñu yàpp weeru lëmm! |
4244 | NUM 17:14 | Ña dee ca mbas ma nag doon fukki junneek ñeent ak juróom ñaar téeméer (14 700), te bokkul ak ña dee woon ca mbirum Kore ma. |
4481 | NUM 25:9 | Ña dee ca mbas ma nag di ñaar fukki junneek ñeent (24 000). |
4498 | NUM 26:7 | Làngi Rubeneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek ñett ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (43 730). |
4505 | NUM 26:14 | Làngi Cimyoneen ñaa ngoogu, di ñaar fukki junneek ñaar ak ñaar téeméer (22 200). |
4509 | NUM 26:18 | Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500). |
4513 | NUM 26:22 | Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500). |
4516 | NUM 26:25 | Làngi Isaakar a ngoogu. Ña ñu leen limal di juróom benn fukki junneek ñeent ak ñetti téeméer (64 300). |
4518 | NUM 26:27 | Làngi Sabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500). |
4525 | NUM 26:34 | Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (52 700). |
4528 | NUM 26:37 | Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500). Ñooñoo askanoo ci Yuusufa, ñook seeni làng. |
4532 | NUM 26:41 | Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600). |
4534 | NUM 26:43 | Mboolem làngi Cuwameen, ña ñu leen limal juróom benn fukki junneek ñeent la, ak ñeenti téeméer (64 400). |
4538 | NUM 26:47 | Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
4541 | NUM 26:50 | Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400). |
4542 | NUM 26:51 | Limeefu bànni Israyil a ngoogu, di juróom benni téeméeri junneek benn ak juróom ñaar téeméer ak fanweer (601 730). |
4553 | NUM 26:62 | Ña ñu limal Leween ñi nag ñaar fukki junneek ñett lañu (23 000), di mboolem góor ña am weer, jëm kaw, te limaaleesu leen ak bànni Israyil ga ca des, ndax joxeesu leen ab cér ci biir bànni Israyil. |
4671 | NUM 31:5 | Ba mu ko defee ñu tànne ca gàngoori Israyil, junniy góor jóge ci giir gu nekk, ñuy fukki junneek ñaari (12 000) xarekat yu gànnaayu. |
4698 | NUM 31:32 | La des ca alalu sëxëtoo, ja ña xareji woon indaale, gannaaw ba ñu ca génnee yooyu, nii la tollu: gàtt yi, juróom benni téeméeri junneek juróom ñaar fukk ak juróom (675 000); |
4699 | NUM 31:33 | nag yi, juróom ñaar fukki junneek ñaar (72 000); |
4700 | NUM 31:34 | mbaam yi, juróom benn fukki junneek benn (61 000), |
4701 | NUM 31:35 | aw nit, fanweeri junniy jigéen ñu xamul lalu góor (30 000). |
4702 | NUM 31:36 | Genn-wàll giy céru nit ña xareji woon, nii la tëdde: gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500), |
4704 | NUM 31:38 | nag yi, fanweeri junneek juróom benn (36 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom ñaar fukk ak ñaar (72); |
4705 | NUM 31:39 | mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom benn fukk ak benn (61); |
4706 | NUM 31:40 | aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000), galagu Aji Sax ji génne ci, di fanweeri bopp ak ñaar (32). |
4709 | NUM 31:43 | te muy céru mbooloo ma, ci wàllu gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500) la; |
4710 | NUM 31:44 | nag yi di fanweeri junneek juróom benn (36 000); |
4711 | NUM 31:45 | mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500); |
4712 | NUM 31:46 | aw nit, fukki junneek juróom benn (16 000). |
4718 | NUM 31:52 | Mboolem wurusu jooxe, wi ñu jooxeel Aji Sax ji, di fukk ak juróom benni junniy siikal ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukk (16 750), yemook barigo ak juróom ñaar fukki kilo (170), te bawoo ci kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya. |
7455 | 1SA 11:8 | Ba Sóol nemmikoo limu góori Israyil ca Beseg, ñetti téeméeri junni lañu (300 000), waa Yuda di fanweeri junni (30 000). |
8216 | 2SA 8:4 | Daawuda jàpp junniy gawaram ak juróom ñaar téeméer (1 700) ak ñaar fukki junniy xarekat (20 000) yuy deme tànk, ba noppi dog sidditi tànki mboolem fas ya doon dawal watiir, bàyyiwu ca lu moy téeméeri fas. |
8217 | 2SA 8:5 | Waa Siri ña dëkke réewum Damaas dikk wallusi Adadeser buurub Soba. Daawuda rey ca ñoom ñaar fukki junneek ñaar (22 000). |
8225 | 2SA 8:13 | Daawudaa nga gënatee siiw ba mu dumaa waa Siri, teg ca duma fukk ak juróom ñetti junniy (18 000) Edomeen ca xuru Xorom wa. |
8249 | 2SA 10:6 | Amoneen ña xam ne Daawuda jéppi na leen lool. Ñu dem bindi ñaar fukki junniy (20 000) xarekat ca waa Siri ña dëkke Bet Reyob ak waa Siri ña dëkke Soba, teg ca junniy nit ñu bàyyikoo ca buuru Maaka, ak fukki junneek ñaar (12 000) ñu waa Tob. |
8261 | 2SA 10:18 | Waaye waa Siree daw, won Israyil gannaaw. Daawuda rey ca ñoom juróom ñaar téeméeri dawalkati watiiri xare (700), ak ñeent fukki junniy gawar (40 000). Sobag, seen njiital gàngoor, mu jam ko, mu dee foofa. |
8453 | 2SA 17:1 | Gannaaw loolu Ayitofel ne Absalom: «Ngalla may ma, ma tànn fukki junniy xarekat ak ñaar (12 000) te dàqi Daawuda ci guddi gi. |
8488 | 2SA 18:7 | mbooloom Israyil nag daanu foofa ca kanam xarekati Daawuda. Bésub keroog ñu baree dee: ñaar fukki junnee (20 000) daanu. |
8704 | 2SA 24:9 | Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000). |
8710 | 2SA 24:15 | Ba loolu amee Aji Sax ji wàcce mbas ci kaw Israyil, dale ko ca suba soosa ba keroog ba àpp ba matee. Ña dee ca askan wa di juróom ñaar fukki junni (70 000) diggante Dan ca bëj-gànnaar ba Beerseba ca bëj-saalum. |
8873 | 1KI 5:6 | Suleymaan amoon na ñeenti junniy (4 000) wuddi fasi watiir ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000). |
8892 | 1KI 5:25 | Suleymaan ci wàllu boppam jox Iram ñaar fukki junni ak juróom ñetti (28 000) barigoy peppu bele, ak ñaar fukki barigo ak ñaar (22) ci diwu oliw gu ñu segal. Suleymaan di defal Iram noonu at mu ne. |
8894 | 1KI 5:27 | Buur Suleymaan nag sas fanweeri junniy nit (30 000) ci Israyil gépp ay liggéeyi sañul-bañ. |
8895 | 1KI 5:28 | Mu di leen yebal Libaŋ, weer wu nekk fukki junni (10 000) dem. Bu ñu amee Libaŋ weer, am seeni kër ñaari weer. Adoniram a jiite woon sas ya. |
8896 | 1KI 5:29 | Suleymaan sàkk juróom ñaar fukki junniy (70 000) yenukat, ak juróom ñett fukki junniy (80 000) yettkati doj ca tund ya, |
8897 | 1KI 5:30 | te bokkul ak ñetti junni ak ñetti téeméeri nit (3 300) ñi Suleymaan tabb, ñuy jiite liggéey bi, di saytu liggéeykat yi. |
9051 | 1KI 8:63 | Mu defal Aji Sax ji saraxi cant ci biir jàmm, lépp di ñaar fukki junniy nag ak ñaar (22 000) ak téeméeri junniy gàtt ak ñaar fukk (120 000). Noonu la Buur ak bànni Israyil gépp amale xewu jagleb kër Aji Sax ji. |
9108 | 1KI 10:26 | Ba mu ko defee Suleymaan dajale watiir yaak fas ya, muy junni ak ñeenti téeméeri watiir (1 400), ak fukki junniy fas ak ñaar (12 000) yu mu yebal ca dëkk ya watiir ya féete, ak ca Yerusalem ga mu nekk. |
9175 | 1KI 12:21 | Ci kaw loolu Robowam agsi Yerusalem, daldi woo waa kër Yuda gépp, ñook giirug Beñamin, ñu daje di téeméer ak juróom ñett fukki junniy nit (180 000), diy ñeyi xare. Ñu nara xareek waa kër Israyil, ngir delloo nguur ga ca loxol Robowam doomu Suleymaan. |
9426 | 1KI 20:15 | Ba mu ko defee Axab lim dag ya kilifay diiwaan ya yebal, ñuy ñaar téeméer ak fanweer ak ñaar (232). Gannaaw loolu mu lim mbooloom Israyil gépp, ñuy juróom ñaari junni (7 000). |
9440 | 1KI 20:29 | Diiru juróom ñaari fan nag ñu jàkkaarloo ca seeni dal. Bésub juróom ñaareel ba xare ba jib, waa Israyil daane téeméeri junniy xarekat (100 000) yu warul fas ca waa Siri ci benn bés bi; |
9441 | 1KI 20:30 | ña ca des daw ba Afeg, ca biir dëkk ba, tata ja màbb ca kaw ñaar fukki junniy nit ak juróom ñaar (27 000) ca ñoom. Fekk na Ben Addàd daw dugg ca biir dëkk ba, jàll ci biir néeg bu làqoo làqu. |