112 | GEN 5:6 | Set moomee am na téeméeri at ak juróom (105), doora jur Enos. |
116 | GEN 5:10 | Kenan juddu na, Enos dundaat juróom ñetti téeméeri at ak fukk ak juróom (815), amaat doom yu góor ak yu jigéen. |
117 | GEN 5:11 | Kon Enos dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom (905), doora faatu. |
121 | GEN 5:15 | Malaleel nag am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Yeredd. |
123 | GEN 5:17 | Kon Malaleel dund na juróom ñetti téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (895), doora faatu. |
127 | GEN 5:21 | Enog moomee, am na juróom benn fukki at ak juróom (65), doora jur Matusalem. |
129 | GEN 5:23 | Kon Enog dund na ñetti téeméeri at ak juróom benn fukk ak juróom (365). |
136 | GEN 5:30 | Nóoyin juddu na, Lemeg dundaat juróomi téeméeri at ak juróom ñeent fukk ak juróom (595), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
138 | GEN 5:32 | Nóoyin moomee am na juróomi téeméeri at (500), doora jur Sem ak Xam ak Yafet. |
234 | GEN 9:28 | Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Nóoyin dundaat na ñetti téeméeri at ak juróom fukk (350). |
235 | GEN 9:29 | Nóoyin dund na juróom ñeenti téeméeri at ak juróom fukk (950), doora faatu. |
278 | GEN 11:11 | Arpagsàdd juddu na, Sem dundaat juróomi téeméeri at (500), juraat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
299 | GEN 11:32 | Teraa dund na ñaar téeméeri at ak juróom (205), doora génn àddina, ñu denc ko Karan. |
303 | GEN 12:4 | Ibraam daldi dem, na ko ko Aji Sax ji waxe woon, Lóot topp ca. Ba Ibraam di jóge Karan, booba am na juróom ñaar fukki at ak juróom (75). |
666 | GEN 25:7 | Ati Ibraayma téeméer la ak juróom ñaar fukk ak juróom (175). |
2659 | EXO 38:25 | Xaalis bi tukkee ci limeefu askan wi, ñetti junniy kilo ak fukk ak juróom ñaar (3 017), ak juróom ñaar téeméeri garaam ak juróom fukk (750), yemook téeméeri (100) talaŋ ak junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi (1 775) siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, |
2660 | EXO 38:26 | muy juróomi garaami xaalis bopp bu nekk, yemook genn-wàllu siikal, ci siikal bi ñu yoonal ci bérab bu sell bi, ñeel képp ku bindu ci limeef bi, dale ko ci ñi am ñaar fukki at jëm kaw, ñépp di juróom benni téeméeri junniy góor ak ñetti junneek juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
2662 | EXO 38:28 | Fukki kilook juróom ñaar yeek juróom ñaar téeméeri garaam yeek juróom fukk (17 kilo 750 garaam) yi ci topp, yemook junneek juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróomi siikali xaalis, ay wékkukaay la ci sàkk ngir jën yi, xoob ci boppi jën yi, sàkk ci galan yi. |
3626 | NUM 1:21 | Limub Rubeneen ñi di ñeent fukki junni ak juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3628 | NUM 1:23 | Limub Cimyoneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3630 | NUM 1:25 | Limub Gàddeen ñi di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3634 | NUM 1:29 | Limub Isakareen ñi di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3636 | NUM 1:31 | Limub Sabuloneen ñi di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3638 | NUM 1:33 | Limub Efraymeen ñi di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3642 | NUM 1:37 | Limub Beñamineen ñi di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3646 | NUM 1:41 | Limub Asereen ñi di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3648 | NUM 1:43 | Limub Neftaleen ñi di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3651 | NUM 1:46 | Ña ñu lim ñépp di juróom benn téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3665 | NUM 2:6 | Ña ñu lim ci gàngooram di juróom fukki junneek ñeent ak ñeenti téeméer (54 400). |
3667 | NUM 2:8 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñaar ak ñeenti téeméer (57 400). |
3670 | NUM 2:11 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (46 500). |
3672 | NUM 2:13 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek juróom ñeent ak ñetti téeméer (59 300). |
3674 | NUM 2:15 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer ak juróom fukk (45 650). |
3675 | NUM 2:16 | «Mboolem ña ñu limal dalub Ruben aki gàngooram doon téeméeri junneek juróom fukk ak benn, ak ñeenti téeméer ak juróom fukk (151 450). Bu ñuy dem, ñooñooy doon ñaareelu kurél, dox, topp ca. |
3678 | NUM 2:19 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junni ak juróomi téeméer (40 500). |
3682 | NUM 2:23 | Ña ñu limal gàngooram di fanweeri junneek juróom ak ñeenti téeméer (35 400). |
3687 | NUM 2:28 | Ña ñu limal gàngooram di ñeent fukki junneek benn ak juróomi téeméer (41 500). |
3689 | NUM 2:30 | Ña ñu limal gàngooram di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
3690 | NUM 2:31 | «Mboolem ña ñu limal dalub Dan daldi doon téeméer ak juróom fukki junneek juróom ñaar ak juróom benni téeméer (157 600). Ñooñooy mujja jóg, topp seeni raaya.» |
3691 | NUM 2:32 | Ñooñu lañu limal bànni Israyil na ñu bokke seen këri maam. Mboolem ña ñu limal dal ya ak seeni gàngoor doon juróom benni téeméeri junneek ñett ak juróomi téeméer ak juróom fukk (603 550). |
3715 | NUM 3:22 | Ña ñu leen limal, ba ñu waññee mboolem góor ña am weer, jëm kaw, juróom ñaari junni ak juróomi téeméer (7 500) lañu. |
3743 | NUM 3:50 | Xaalis ba mu nangoo ca taawi bànni Israyil di junniy siikal ak ñetti téeméer ak juróom benn fukk ak juróom (1 365), ci siikalu bérab bu sell bi, xawa tollu ci fukki kilo ak ñett. |
3780 | NUM 4:36 | Ña ñu limal seeni làng di ñaari junni ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukki góor (2 750). |
3792 | NUM 4:48 | seenub lim nekk na juróom ñetti junni ak juróomi téeméer ak juróom ñett fukki góor (8 580). |
3936 | NUM 7:85 | ndabal xaalis lu nekk di téeméeri siikal ak fanweer, di kilook liibar, këll bu nekk di juróom ñaar fukki siikal, di juróom ñetti téeméeri garaam, mboolem xaalisu jumtukaay yi di ñaari junniy siikali bérab bu sell bi ak ñeenti téeméer (2 400), di ñaar fukki kilook juróom ñaar ak juróomi téeméeri garaam (27 500). |
4197 | NUM 16:2 | ñu jógal Musaa, ñook ñaar téeméer ak juróom fukk (250) ci bànni Israyil, diy kilifa ci mbooloo mi, am baat ca pénc ma, te di ñu amu tur. |
4509 | NUM 26:18 | Làngi Gàddeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróomi téeméer (40 500). |
4513 | NUM 26:22 | Làngi Yudeen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom ñaar fukki junneek juróom benn ak juróomi téeméer (76 500). |
4518 | NUM 26:27 | Làngi Sabuloneen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom benn fukki junni ak juróomi téeméer (60 500). |
4525 | NUM 26:34 | Làngi Manasee ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñaar ak juróom ñaar téeméer (52 700). |
4528 | NUM 26:37 | Làngi Efrayim a ngoogu, ña ñu leen limal di fanweeri junneek ñaar ak juróomi téeméer (32 500). Ñooñoo askanoo ci Yuusufa, ñook seeni làng. |
4532 | NUM 26:41 | Ñooñoo askanoo ci Beñamin, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak juróom benni téeméer (45 600). |
4538 | NUM 26:47 | Làngi Asereen ñaa ngoogu, ña ñu leen limal di juróom fukki junneek ñett ak ñeenti téeméer (53 400). |
4541 | NUM 26:50 | Neftaleen ñaa ngoogu, ñook seeni làng, ña ñu leen limal di ñeent fukki junneek juróom ak ñeenti téeméer (45 400). |
4694 | NUM 31:28 | Te ngeen sàkkal Aji Sax ji, ci céru xarekat ya xareji woon, ab galag bu yemook benn bopp ci juróomi téeméer (500) yu nekk, ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt. |
4696 | NUM 31:30 | Céru bànni Israyil bi ci des, nangeen ci sàkk benn ci juróom fukk yu nekk (50), ci aw nit, mbaa ay nag, mbaa ay mbaam, mbaa ay gàtt, mbaa gépp jur, te ngeen jox ko Leween ñi dénkoo dénkaaney màkkaanu Aji Sax ji.» |
4698 | NUM 31:32 | La des ca alalu sëxëtoo, ja ña xareji woon indaale, gannaaw ba ñu ca génnee yooyu, nii la tollu: gàtt yi, juróom benni téeméeri junneek juróom ñaar fukk ak juróom (675 000); |
4702 | NUM 31:36 | Genn-wàll giy céru nit ña xareji woon, nii la tëdde: gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500), |
4703 | NUM 31:37 | galagu Aji Sax ji génne ci gàtt yi, di juróom benni téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom (675); |
4705 | NUM 31:39 | mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500), galagu Aji Sax ji génne ci, di juróom benn fukk ak benn (61); |
4709 | NUM 31:43 | te muy céru mbooloo ma, ci wàllu gàtt yi, ñetti téeméeri junneek fanweer ak juróom ñaar ak juróomi téeméer (337 500) la; |
4711 | NUM 31:45 | mbaam yi, fanweeri junneek juróomi téeméer (30 500); |
4718 | NUM 31:52 | Mboolem wurusu jooxe, wi ñu jooxeel Aji Sax ji, di fukk ak juróom benni junniy siikal ak juróom ñaar téeméer ak juróom fukk (16 750), yemook barigo ak juróom ñaar fukki kilo (170), te bawoo ci kilifay kuréli junni yaak kilifay kuréli téeméer ya. |
7808 | 1SA 22:18 | Buur ne Doweg: «Ayca yaw, fàddal sarxalkat yii!» Doweg Edomeen ba fàdd sarxalkat ya. Rey na bésub keroog juróom ñett fukki nit ak juróom (85) ñuy sol xar-sànnim lẽe. |
8704 | 2SA 24:9 | Yowab nag indil Buur limu askan wa: Israyil di juróom ñetti téeméeri junniy góor (800 000) ñu tollu ci xare; Yuda di juróomi téeméeri junniy góor (500 000). |
8869 | 1KI 5:2 | Suleymaan daan na njëloo bés bu nekk ñeent fukki barigoy sunguf ak juróom (45), ak juróom ñeent fukki (90) barigo ci sunguf su ñagas; |
9077 | 1KI 9:23 | Ñoo doon itam saytukat yi yore liggéeyi Suleymaan. Amoon na juróomi téeméeri jawriñam ak juróom fukk (550) yu daan jiite nit ñiy def liggéey bi. |
9111 | 1KI 10:29 | Ab watiir bu ñu jëggaanee Misra, indi, juróom benni téeméeri dogi xaalis (600) la leen daan dikke, aw fas di téeméer ak juróom fukki dogi xaalis (150), te noonu lañu ca daan jëndaaleel mboolem buuri Etteen ña ak buuri Siri, indil leen. |
9363 | 1KI 18:19 | Léegi nag wooteel, Israyil gépp daje, fekksi ma ca tundu Karmel, ñu ànd ak ñeenti téeméeri yonenti Baal ak juróom fukk (450) ak ñeenti téeméeri nit (400) ñuy lekk njëlal Yesabel, te di yonenti Asera tuur ma.» |
9366 | 1KI 18:22 | Ilyaas ne mbooloo ma: «Man de maa fi des ci yonenti Aji Sax ji, man doŋŋ, te yonenti Baal yi ñeenti téeméer lañook juróom fukk (450). |
10100 | 2KI 19:35 | Guddig keroog malaakam Aji Sax ji moo dikk, fàdd ca dalub Asiri téeméer ak juróom ñett fukk ak juróomi junni (185 000). Ca ëllëg sa ña mucc teela xëy, yemuñu ci lu moy ñooña ñépp, diy néew. |
12032 | EZR 1:11 | Mboolem ndabi wurus yeek yu xaalis yi juróomi junni la ak ñeenti téeméer (5 400). Sesbasar jële lépp Babilon, yóbbu Yerusalem, ba ngàllo gay ñibbi. |
12037 | EZR 2:5 | Askanu Ara, juróom ñaar téeméer ak juróom ñaar fukk ak juróom lañu (775). |
12039 | EZR 2:7 | Askanu Elam, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12040 | EZR 2:8 | Askanu Sàttu, juróom ñeenti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (945). |
12046 | EZR 2:14 | Askanu Bigway, ñaari junni ak juróom fukk ak juróom benn lañu (2 056). |
12047 | EZR 2:15 | Askanu Adin, ñeenti téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (454). |
12052 | EZR 2:20 | Askanu Gibar, juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). |
12054 | EZR 2:22 | Waa Netofa, juróom fukk ak juróom benn lañu (56). |
12061 | EZR 2:29 | Waa Nebo, juróom fukk ak ñaar lañu (52). |
12062 | EZR 2:30 | Waa Magbis téeméer ak juróom fukk ak juróom benn lañu (156). |
12063 | EZR 2:31 | Waa Elam gu ndaw, junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12065 | EZR 2:33 | Waa Lodd ak Adidd ak Ono, juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk ak juróom lañu (725). |
12066 | EZR 2:34 | Waa Yeriko, ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (345). |
12069 | EZR 2:37 | Askanu Imer, junni ak juróom fukk ak ñaar lañu (1 052). |
12092 | EZR 2:60 | Askanu Delaya, ak askanu Tobya, ak askanu Nekoda, di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). |
12098 | EZR 2:66 | Amoon nañu juróom ñaar téeméeri fas ak fanweer ak juróom benn (736), ak ñaar téeméeri berkelle ak ñeent fukk ak juróom (245), |
12099 | EZR 2:67 | ak ñeenti téeméeri giléem ak fanweer ak juróom (435), ak juróom benni junniy mbaam ak juróom ñaar téeméer ak ñaar fukk (6 720). |
12209 | EZR 8:3 | mi askanoo ci Sekaña la. Askanu Paros, Sàkkaryaa bawoo ca, ànd ak téeméeri góor ak juróom fukk (150). |
12212 | EZR 8:6 | Ci askanu Adin, Ebedd doomu Yonatan la, mook juróom fukki góor (50). |
12404 | NEH 5:17 | Rax ci dolli daan naa woo téeméeri kilifay Yawut ak juróom fukk (150), di bokk ak ñoom sama njël, te limaalewuma ñi bàyyikoo ci jaambur yi nu séq, di nu fekksi. |
12435 | NEH 7:10 | Askanu Ara di juróom benn téeméer ak juróom fukk ak ñaar (652). |
12437 | NEH 7:12 | Askanu Elam junni ak ñaar téeméer ak juróom fukk ak ñeent lañu (1 254). |
12438 | NEH 7:13 | Askanu Sàttu juróom ñetti téeméer ak ñeent fukk ak juróom lañu (845). |
12445 | NEH 7:20 | Askanu Adin juróom benn téeméer ak juróom fukk ak juróom lañu (655); |
12450 | NEH 7:25 | Askanu Gabawon juróom ñeent fukk ak juróom lañu (95). |