35 | GEN 2:4 | Liy cosaanal asamaan ak suuf, ba ñu leen di sàkk, mooy lii. Bés ba Aji Sax ji Yàlla sàkkee suuf ak asamaan, |
36 | GEN 2:5 | genn garab nekkagul woon ci kaw suuf, te genn gàncax saxagul; ndaxte booba Yàlla Aji Sax ji tawagul, te nit kuy bey amagul. |
38 | GEN 2:7 | Yàlla Aji Sax ji nag móol nit ci pëndu suuf, sol ngelawal dund ci paxi bakkanam, nit daldi doon boroom bakkan. |
39 | GEN 2:8 | Naka noona Yàlla Aji Sax ji jëmbat tool ca biir Àjjana fa féete penku ba, tàbbal ca nit ka mu bind. |
40 | GEN 2:9 | Yàlla Aji Sax ji nag saxal ci suuf lépp luy garab gu meññeef ma rafet te neexa lekk; mu def it garab gay taxa dund ca digg tool ba, moom ak garab gay taxa xam lu baax ak lu bon. |
41 | GEN 2:10 | Amoon na dex guy balle Àjjana, di suuxat tool ba, dale fa nag, séddlikoo, def ñeenti wal. |
42 | GEN 2:11 | Turu menn wal ma di dexu Pison, moo wër réewum Awila mépp. Wurus a nga woon ca réew mooma, |
45 | GEN 2:14 | turu ñetteelu dex ga di Tiigar, féete réewum Asiri penku; ñeenteelu dex ga di Efraat. |
46 | GEN 2:15 | Yàlla Aji Sax ji nag jël nit ki, tàbbal ko biir toolub Àjjana, mu di ko bey ak a sàmm. |
47 | GEN 2:16 | Yàlla Aji Sax ji sant nit ki, ne ko: «Man ngaa lekk ci mboolem garabi tool bi, |
49 | GEN 2:18 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Wéet baaxul ci nit, kon dinaa ko bindal ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam.» |
50 | GEN 2:19 | Loolu fekk na Yàlla Aji Sax ji sàkk ci suuf nja-àll yépp ak njanaaw yépp, daldi leen indil nit, di seet nu leen nit di tudde; te tur wu mu leen jox, muy moom. |
51 | GEN 2:20 | Ba mu ko defee nit kooku, di Aadama, tudd jur gépp ak picc yépp ak rabi àll yépp, waaye fekku ca ku koy jàpple te jekk ci doon wéttalam. |
52 | GEN 2:21 | Bi loolu amee Yàlla Aji Sax ji nelawloo Aadama nelaw yu xóot. Ba muy nelaw nag, mu rocci genn ciy faaram, fatte pax ma aw suux. |
53 | GEN 2:22 | Yàlla Aji Sax ji bind jigéen ci faar, gi mu jële ci Aadama, indil ko ko. |
54 | GEN 2:23 | Aadama ne tonet, daldi ne: «Waaw kay nag, kii moo bokk ci samay yax ak sama suux! Dees na ko tudde jigéen, ndaxte ci góor lees ko jële.» |
57 | GEN 3:1 | Jaan nag moo gënoona muus ci rabi àll, yi Yàlla Aji Sax ji sàkk yépp. Jaan ja moo ne jigéen ja: «Ndax wóor na ne Yàllaa ne: “Buleen lekk ci doomi genn garabu tool bi”?» |
64 | GEN 3:8 | Gannaaw loolu ñu dégg tànki Yàlla Aji Sax ji, muy doxantu ca tool ba, fekk ker gi sedd, ñu daldi fexee làqu Yàlla Aji Sax ji ci biir garabi tool bi. |
65 | GEN 3:9 | Yàlla Aji Sax ji nag ne Aadama: «Ana nga?» |
67 | GEN 3:11 | Yàlla Aji Sax ji ne ko: «Ku la xamal ne dangaa def yaramu neen? Mbaa du dangaa lekk ca garab, ga ma la aaye, waay?» |
68 | GEN 3:12 | Aadama ne ko: «Jigéen, ji nga ma booleel de, moo ma jox ci garab gi, ma lekk.» |
69 | GEN 3:13 | Yàlla Aji Sax ji ne jigéen ja: «Yaw, li nga def nii mooy lan?» Jigéen ja ne ko: «Aa, jaan de moo ma nax, ba ma lekk ci.» |
70 | GEN 3:14 | Yàlla Aji Sax ji nag ne jaan ja: «Gannaaw def nga loolu, yaw rekk yaay alku ci rabi kër yépp ak rabi àll yépp; dinga watatu, di lekk pënd sa giiru dund gépp. |
73 | GEN 3:17 | Mu tegaat ca ne Aadama: «Gannaaw dégg nga sa waxu soxna, ba lekk ci garab gi ma la aaye, dinaa rëbb suuf ndax yaw; coono bu metti nga ciy dunde sa giiru dund gépp. |
76 | GEN 3:20 | Aadama nag tudde soxnaam Awa (mu firi Dund), ndax mooy ndeyu képp kuy dund. |
77 | GEN 3:21 | Gannaaw gi Yàlla Aji Sax ji sàkkal Aadama ak soxnaam ay yérey der, wodde leen. |
78 | GEN 3:22 | Yàlla Aji Sax ji daldi ne: «Léegi nit mel na ni nun, xam lu baax ak lu bon. Kon nag bumu tàllal loxoom, di witt ci doomi garab giy taxa dund, di lekk, bay dund fàww.» |
79 | GEN 3:23 | Ba loolu amee Yàlla Aji Sax ji génne ko toolub Àjjana, muy bey suuf, si ñu ko sàkke. |
81 | GEN 4:1 | Gannaaw loolu Aadama dëkkoo na soxnaam Awa, mu ëmb, am Kayin, mu ne: «Am naa doom ju góor ci ndimbalu Aji Sax ji.» |
82 | GEN 4:2 | Awa teg ca rakkam, Abel. Abel di sàmm, Kayin di bey. |
83 | GEN 4:3 | Ñu dem ba mu yàgg, Kayin sàkk ci mbeyam, jébbal ko Aji Sax ji, màggale ko ko. |
84 | GEN 4:4 | Abel moom jébbal ko nebbonu jur, ga jëkka juddu ca géttam. Aji Sax ji nangul Abel, |
86 | GEN 4:6 | Aji Sax ji ne Kayin: «Lu la taxa mer, ba ne fóññ nii? |
88 | GEN 4:8 | Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. |
89 | GEN 4:9 | Aji Sax ji ne Kayin: «Ana sa rakk Abel?» Mu ne ko: «Gisuma ko de; xanaa maa wara sàmm sama rakk?» |
93 | GEN 4:13 | Teewul Kayin wax Aji Sax ji ne ko: «Sama mbugal diis na lool, ba àttanuma ko! |
95 | GEN 4:15 | Aji Sax ji ne ko: «Kon nag ku la rey, yaw Kayin, dina jot juróom ñaari yoon lu ko raw.» Ba loolu amee mu sàkkal Kayin màndarga, ba ku ko gis du ko rey. |
96 | GEN 4:16 | Kayin daldi bàyyikoo ca Aji Sax ji, dem dëkki réewu Nódd, fa féete Àjjana penku. |
99 | GEN 4:19 | Lemeg nag jël ñaari jabar, aawo bi tudd Ada, ñaareel bi di Silla. |
100 | GEN 4:20 | Ada taawloo Yabal, miy cosaanu sàmm yiy màngaan, |
103 | GEN 4:23 | Lemeg nag ne ay soxnaam: «Dégluleen maa, yeen soxnay Lemeg, teeyluleen maa, yeen Ada ak Silla. Nit a ma gaañ, ma bóom, goneg jàmbaar dóor ma, ma faat. |
105 | GEN 4:25 | Bi loolu wéyee Aadama dëkkoo soxnaam, mu am doom ju góor; tudde ko Set (mu firi May), ndax da ne: «Yàlla may na ma weneen askan, mu wuutu Abel, mi Kayin rey.» |
106 | GEN 4:26 | Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal. |
107 | GEN 5:1 | Ni téere indee askanu Aadama nii la. Ba Yàlla di sàkk nit, da koo bind ci melokaanam, |
109 | GEN 5:3 | Aadama dund téeméeri at ak fanweer (130), jur doom ju góor, mu bindoo melokaanam te nirook moom. Mu tudde ko Set. |
110 | GEN 5:4 | Set juddu na, Aadama dundaat juróom ñetti téeméeri at (800), amaat ay doom yu góor ak yu jigéen. |
111 | GEN 5:5 | Kon Aadama dund na juróom ñeenti téeméeri at ak fanweer (930), doora faatu. |
135 | GEN 5:29 | Mu tudde ko Nóoyin (mu firi Noflaay) ndax dafa ne: «Kii moo nuy taxa noyyiwaat, noppal nu ci liggéey yu metti ak coonoy mbeyu suuf, si Aji Sax ji rëbb.» |
141 | GEN 6:3 | Aji Sax ji daldi wax ne: «Manumaa bàyyi nit, muy wéyee dunde noo, gi ma ko may, ndax nit du dara lu dul suuxi neen, kon dinaa leen àppal diirub téeméeri at ak ñaar fukk (120).» |
143 | GEN 6:5 | Aji Sax ji dafa gis ne mbonu nit màgg na lool ci biir àddina, te fu mu mana tollu, lu bon rekk lay xinte ci xolam. |
144 | GEN 6:6 | Aji Sax ji nag am tiis ci xolam, ba mititlu li mu doon sàkk nit ci kaw suuf. |
145 | GEN 6:7 | Aji Sax ji daldi ne: «Dinaa far ci kaw suuf doom aadama yi ma sàkk, nit ak jur, luy raam ak luy naaw, ndax mititlu naa li ma leen sàkk.» |
146 | GEN 6:8 | Waaye fekk na Aji Sax ji xool Nóoyin bëti yërmande. |
147 | GEN 6:9 | Askanu Nóoyin mooy lii. Nóoyin nit ku jub la woon, di ku mat ci biir nit ñi mu bokkal jamono, te di ku topp Yàlla. |
161 | GEN 7:1 | Gannaaw ba loolu amee Aji Sax ji dafa wax Nóoyin ne ko: «Duggal ci gaal gu mag gi, yaak sa njaboot gépp, ndaxte niti jamono jii, yaw rekk laa ci gis, nga jub ni ma ko bëgge. |
165 | GEN 7:5 | Nóoyin daldi def la ko Aji Sax ji sant lépp. |
171 | GEN 7:11 | At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at, ca fukki fan ya ak juróom ñaar ca ñaareelu weer wa, kera la bëti ndox ya ne jàyy, jóge xóotey géej, bunti ndoxi asamaan ne kulbét, mu ne yureet, |
176 | GEN 7:16 | mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee. |
183 | GEN 7:23 | Luy dund ci àddina daldi sànku, ba nit ak jur ak luy raam ak luy naaw— lépp la Aji Sax ji raafal ci àddina. Nóoyin rekk a des, moom ak ña àndoon ak moom ca gaal ga. |
188 | GEN 8:4 | Ba juróom ñaareelu weer wa amee fukki fan ak juróom ñaar, gaal gaa nga teereji tundi Araraat. |
197 | GEN 8:13 | At ma Nóoyin amee juróom benni téeméeri at ak benn, keroog benn fanu weer wa jëkk, ndox ma taa woon ca suuf daldi fendi. Nóoyin ubbi kubeer ga, xool, ba gis ne kaw suuf sépp wow na. |
204 | GEN 8:20 | Naka la Nóoyin génn, daldi sàkkal Aji Sax ji sarxalukaay, màggale ko ko. Mu sàkk nag ci mboolem rab wu set ak mboolem picc mu set, jébbal Yàlla ca sarxalukaay ba, muy saraxu rendi-dóomal. |
205 | GEN 8:21 | Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. |
232 | GEN 9:26 | Mu dellu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Sem, yal na Kanaan dib jaamam. |
236 | GEN 10:1 | Askanu doomi Nóoyin mooy lii. Gannaaw ba mbënn ma wéyee, Sem ak Xam ak Yafet am nañu ay doom. |
238 | GEN 10:3 | Doomi Gomeer yu góor di Askenas, Rifaat ak Togarma. |
242 | GEN 10:7 | Doomi Kuus yu góor di Seba ak Awila ak Sabta ak Raama ak Sabteka. Doomi Raama yu góor di Saba ak Dedan. |
245 | GEN 10:10 | Dëkk yiy péeyi nguuram ñoo di: Babel ak Ereg ak Akàdd ak Kalne, gi ci réewu Sineyaar. |
246 | GEN 10:11 | Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala. |
248 | GEN 10:13 | Misrayim nag mooy maami Luddeen ñi ak Anameen ñi ak Leyabeen ñi ak Naftuyeen ñi |
251 | GEN 10:16 | te mooy maami Yebuseen ñi ak Amoreen ñi ak Girgaseen ñi |
252 | GEN 10:17 | ak Eween ñi ak Arkeen ñi ak Sineen ñi, |
253 | GEN 10:18 | ak Arwàddeen ñi ak Semareen ñi ak Amateen ñi. La ca tegu làngi Kanaan tasaaroo. |
254 | GEN 10:19 | Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa. |
257 | GEN 10:22 | Doomi Sem yu góor ñii la: Elam ak Asur ak Arpagsàdd ak Ludd ak Aram. |
258 | GEN 10:23 | Góor ñi Aram jur ñii la: Uus ak Xuul ak Geter ak Maas. |
259 | GEN 10:24 | Arpagsàdd jur Sela, Sela jur Eber; |
261 | GEN 10:26 | Yogtaan a jur Alamodàdd ak Selef ak Asarmawet ak Yera |
262 | GEN 10:27 | ak Adoram ak Usal ak Digla |
263 | GEN 10:28 | ak Obal ak Abimayel ak Saba |
264 | GEN 10:29 | ak Ofir ak Awila ak Yobab. Ñooñu ñépp di doomi Yogtaan yu góor. |