1 | GEN 1:1 | Ca njàlbéen ga Yàlla sàkk na asamaan ak suuf. |
21 | GEN 1:21 | Ci biir loolu Yàlla bind rabi géej yu mag yi ak mboolem mbindeef muy féey tey ramm-rammi ci ndox mi, mu ci nekk ak wirgoom, teg ca lépp luy boroomi laaf, lu ci nekk ak wirgoom. Yàlla gis ne baax na. |
32 | GEN 2:1 | Ci kaw loolu asamaan ak suuf ak li ñu ëmb lépp mat. |
37 | GEN 2:6 | Ci biir loolu mbënn di balle ci suuf, di tooyal fépp. |
88 | GEN 4:8 | Ci kaw loolu Kayin séq ak rakkam Abel wax. Ba mu ko defee ñu dem ca àll ba, Kayin dal ci kaw Abel, bóom ko. |
97 | GEN 4:17 | Gannaaw loolu Kayin dëkkoo na soxnaam, mu ëmb, am Enog. Ci biir loolu Kayin sanc ab dëkk, dippee ko doomam ju góor Enog. |
142 | GEN 6:4 | Ca jamono yooya ak itam gannaaw ba goney Yàlla yooyu àndeek jigéeni àddina, ba am ca ay doom, aw xeetu ponkal wu ñuy wax Nefilim moo nekkoon ci àddina. Ñooy ponkal ya woon te doonoon góor ñu amoon tur. |
176 | GEN 7:16 | mboolem xeetu mbindeef rekk, di góor ak jigéen, ni ko ko Yàlla sante. Ci kaw loolu Aji Sax ji ne ràpp buntu gaal gi, gannaaw bi Nóoyin duggee. |
185 | GEN 8:1 | Ci biir loolu Yàlla xalaat na Nóoyin ak li mu nekkal ci gaal gi, di rabi àll yi ak jur gi. Yàlla daldi yebal ngelaw, mu wal kaw suuf, ba ndox yi wàcc. |
187 | GEN 8:3 | Ci kaw loolu ndox mi taa ci suuf di wàññiku. Bi téeméeri fan yi ak juróom fukk matee nag, ndox ma gëna néew. |
205 | GEN 8:21 | Ci kaw loolu xetug jàmm gillee ca sarax sa, yéeg fa Aji Sax ja. Booba la wax ci xolam ne: «Dootuma rëbb suuf mukk ndax nit, doonte ba muy ndaw lay dale xinte lu ñaaw ci xolam. Dootuma boole fàdd mukk lépp luy dund, nii ma ko defe. |
207 | GEN 9:1 | Ci kaw loolu Yàlla barkeel Nóoyin aki doomam ne leen: «Giirleen te bare, ba fees àddina. |
223 | GEN 9:17 | Ci kaw loolu Yàlla ne Nóoyin: «Loolu mooy màndargaal sama kóllëre, gi ma fas ak mboolem mbindeef mu nekk ci kaw suuf.» |
232 | GEN 9:26 | Mu dellu ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, Yàllay Sem, yal na Kanaan dib jaamam. |
246 | GEN 10:11 | Ca réew mooma la Namróot jóge dem Asur, sanc dëkk bu mag boobee di Niniw, ak dëkk yooyee di Reyobot Ir ak Kala, ba Resen, gi ci diggante Niniw ak Kala. |
254 | GEN 10:19 | Kemu suufas Kanaaneen ña, mu ngi tàmbalee Sidon, jaar weti Gerar, dem ba Gasa, wuti Sodom ak Gomor ak Atma ak Ceboyim, daldi teeri Lesa. |
267 | GEN 10:32 | Làngi doomi Nóoyin yu góor a ngoogu, làng gu nekk ak askanam, ñu diy xeet. Ci ñoom la xeet yépp jóge tasaaroo ci kaw suuf, gannaaw ba mbënn ma wéyee. |
268 | GEN 11:1 | Ca ndoorte la nag waa àddina sépp a bokkoon wenn làkk, seeni wax di benn. |
270 | GEN 11:3 | Ñu ne: «Ayca nu defar ay móol yu ñu lakk cib taal, ba mu ñor.» Ci kaw loolu ñu def móol ya doji tabax, taqalee ko koltaar, |
306 | GEN 12:7 | Ci kaw loolu Aji Sax ji feeñu Ibraam ne ko: «Sa askan wi soqikoo ci yaw laay jox réew mii.» Ibraam nag daldi tabaxal Aji Sax, ji ko feeñu, ab sarxalukaay. |
309 | GEN 12:10 | Ca jamono jooja xiif a amoon ca réew ma, ba tax Ibraam dem réewum Misra, toogi fa, ndax xiif bu metti la woon. |
324 | GEN 13:5 | Ci biir loolu Lóot, mi mu àndal, moom it yor jur gu gudd ak gu gàtt aki xayma, |
338 | GEN 14:1 | Ca jamonoy Amrafel buurub Sineyaar, ak Aryog buurub Elasaar, Kedorlamer buurub Elam, ak Tidal buurub Goyim, |
339 | GEN 14:2 | ànd nañu, dal ci kaw ñoom Bera buurub Sodom, ak Birsa buurub Gomor, ak Sineyab buurub Atma, ak Semeber buurub Ceboyim, ak it buuru dëkk ba ñuy wax Bela, mooy Sowar ba tey. |
342 | GEN 14:5 | Ca déwén sa Kedorlamer ak buur ya faroon ak moom, dem dàq Refayeen ña ca Àsterot Karnayim, ak Suseen ña ca Am, ak Emeen ña ca jooru Kiryaatayim, |
345 | GEN 14:8 | Ci kaw loolu buurub Sodom génn, mook buurub Gomor ak buurub Atma ak buurub Ceboyim ak buuru Bela, di Sowar ba tey, ñoom ñépp daldi làng, nara xare ca xuru Sidim, |
349 | GEN 14:12 | Booba lañu yóbbu Lóot ma dëkk Sodom, te Ibraam di baayam bu ndaw. Ci biir loolu ñu yóbbaale li mu amoon lépp, dem. |
355 | GEN 14:18 | Ci kaw loolu Melkisedeg buurub Salem, mi doon sarxalkatu Yàlla Aji Kawe ji, daldi ñëw, indi mburu ak biiñ. |
437 | GEN 18:12 | Ci kaw loolu Saarata ree ci suuf, daldi ne: «Man mu ñor xomm mii, ndax man naa amati boobu bànneex, te sama boroom kër it di mag?» |
484 | GEN 19:26 | Ci kaw loolu soxnas Lóot ne gees, jëmm ja far soppliku xorom. |
485 | GEN 19:27 | Ca ëllëg sa Ibraayma dafa teela jóg, dem fa mu taxawoon jàkkaarlook Aji Sax ji. |
491 | GEN 19:33 | Ca guddi ga ñu nàndal seen baay biiñ, taaw ba dugg, tëdd ak baayam, te Lóot yégul ba fa doom jay tëdd ak ba muy jóg. |
492 | GEN 19:34 | Ca ëllëg sa taaw ba wax rakk ji, ne ko: «Man tëdd naa ak sama baay biig; guddig tey it, danu koy nàndalaat biiñ, su ko defee nga dugg tëdd ak moom, ndax sunu xeetu baay du fey.» |
528 | GEN 21:14 | Ca ëllëg sa Ibraayma jóg suba teel, sàkk mburu, booleek mbuusu ndox, jox Ajara, mu gàddu. Mu daldi ko dénk Ismayla, yebal ko, mu dem. Ci kaw loolu muy wëndeelu ca màndiŋu Beerseba. |
533 | GEN 21:19 | Ci kaw loolu Yàlla muri ay bëtam, mu gis ab seyaan, daldi cay dem, duy mbuusam, ba mu fees, jox ca doomam, mu naan. |
535 | GEN 21:21 | Ca àllub Paran la dëkkoon, yaayam wutali ko soxna ca réewum Misra. |
539 | GEN 21:25 | Ci kaw loolu Ibraayma tawat Abimeleg teen bu surgay Abimeleg nangu woon ci moom, aakimoo ko. |
552 | GEN 22:4 | Ca gannaaw ëllëg sa, Ibraayma daa dawal bëtam, séen bérab ba fu sore. |
563 | GEN 22:15 | Ci kaw loolu malaakam Yàlla ma dellu àddoo asamaan ne Ibraayma: |
619 | GEN 24:27 | daldi ne: «Cant ñeel na Aji Sax ji, sama Yàllay sang, Ibraayma, moom mi masula noppee laaye biir sama sang, te masu koo ñàkke worma. Man it, Aji Sax ji wommat na ma ba sama kër bokki sang!» |
639 | GEN 24:47 | Ma laaj ko ne ko: “Kan moo la jur?” Mu ne: “Betuwel, doomu Naxor ak Milka.” «Ca laa ko takkal jaaro bi ci bakkanam, ak lam yi ciy loxoom. |
645 | GEN 24:53 | Surga ba nag génne ay gànjari xaalis ak yu wurus booleek ay yére, jox Rebeka. Càmmiñ la ak yaay ja itam, mu may leen alal ju takku. |
647 | GEN 24:55 | Càmmiñal ndaw sa ak yaay ja daldi ne ko: «Xanaa kay janq bi dina toogaat ak nun ab diir boog, maanaam fii ak sibbir, doora dem.» |
650 | GEN 24:58 | Ci kaw loolu ñu woo Rebeka, ne ko: «Ndax dangay ànd ak waa ji léegi?» Mu ne: «Waaw.» |
681 | GEN 25:22 | Doom yi nag di buuxante ci biiram, ba mu naan: «Ndegam nii la kay, jaru ko woon!» Ci kaw loolu soxna si dem, diis ko Aji Sax ji. |
711 | GEN 26:18 | Ba loolu weesee Isaaxa sikkli teen, yi ñu gasoon ca jamonoy baayam Ibraayma, te waa Filisti sakkoon leen gannaaw ba Ibraayma nelawee. Ca la tudde teen yi tur, ya leen baayam tudde woon. |
713 | GEN 26:20 | Teewul sàmmi Gerar di soowook sàmmi Isaaxa naan: «Nun noo moom ndox mi.» Mu tudde teen ba Eseg (mu firi Coow), ndax li ñu soowoo ak moom. |
719 | GEN 26:26 | Ci diggante boobu Abimeleg dafa jóge Gerar, dem fekki ko, ànd ak Awusat, ma doon wóllëreem, ak Pikol, njiital xarekatam. |
724 | GEN 26:31 | Ca ëllëg sa, ñu xëy suba teel, daldi waatoo, Isaaxa door leena yiwi, ñu dem ci jàmm. |
725 | GEN 26:32 | Ca bés booba ay surgay Isaaxa ñëw nañu, di ko wax lu jëm ci teen, ba ñu doon gas, ne ko: «Gis nanu ndox.» |
766 | GEN 27:38 | Esawu ne baayam: «Baay, xanaa genn ñaan rekk nga am? Ngalla baay, ñaanal ma, man itam!» Ca la Esawu ne yikkét jooy. |
775 | GEN 28:1 | Ci kaw loolu Isaaxa woo Yanqóoba, ñaanal ko, jox ko ndigal lii ne ko: «Bul jël ci jigéeni Kanaan, |
788 | GEN 28:14 | Saw askan dina ne gàññ ni suuf. Dinga law penku ak sowu, ndijoor ak càmmoñ. Ci yaw ak saw askan la giir yi ci kaw suuf yépp di barkeele. |
790 | GEN 28:16 | Ci kaw loolu Yanqóoba yewwu ne: «Ndekete Aji Sax ji mu ngi ci bérab bii, te xawma ko woon.» |
792 | GEN 28:18 | Ca suba teel Yanqóoba jóg, jël doj, wi mu gegenoo woon, samp fa, muy xàmmikaay, ba noppi sotti ci ag diw, sellale ko. |
793 | GEN 28:19 | Ca la tudde bérab ba Betel, waaye ca njàlbéen Lus la dëkk ba tuddoon. |
808 | GEN 29:12 | Ca la Yanqóoba wax Rasel ne ko: «Maak sa baay a bokk, ndax maay sa doomu bàjjan Rebeka.» Rasel daw, yégal ko baayam. |
816 | GEN 29:20 | Ci kaw loolu Yanqóoba liggéeyal Laban diiru juróom ñaari at ngir Rasel, te mu mel ni ay fan rekk ci moom ndax mbëggeel, gi mu am ci Rasel. |
820 | GEN 29:24 | Ci biir loolu Laban jël jaamam bu jigéen bu ñuy wax Silpa, may ko doomam Leya, mu dib jaamam. |
826 | GEN 29:30 | Yanqóoba nag dëkkoo Rasel, mi mu gënoona bëgg Leya. Ci kaw loolu mu liggéeyaatal Laban juróom ñaari at. |
831 | GEN 29:35 | Mu dellooti ëmb, am doom ju góor daldi ne: «Bii yoon dinaa sant Aji Sax ji,» loolu tax mu tudde ko Yuda (mu firi Cant). Gannaaw loolu njuram taxaw. |
835 | GEN 30:4 | Ci kaw loolu mu may ko jaamam Bilaa, muy soxnaam. Yanqóoba dëkkoo Bilaa, |
866 | GEN 30:35 | Ca bés booba Laban dafa ber sikket, yi seereer te todde, ak bëy, yi tippante te todde, maanaam yi rax, ak xari menn melo yu ñuul yi, daldi leen dénk ay doomam. |
868 | GEN 30:37 | Ci kaw loolu Yanqóoba tànn ñetti garab yu ñuy wax pëpalyee, gerte-tubaab ak palataan, gor ci bant yu tooy, xànc-xàncee ko, ba mu defi rëdd yu weex. |
885 | GEN 31:11 | Ca la ma malaakam Yàlla ma wax ci biir gént gi ne ma: “Yanqóoba,” ma ne ko: “Naam.” |
893 | GEN 31:19 | Fekk na Laban dem wati ay xaram. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam. |
898 | GEN 31:24 | Ci kaw loolu Yàlla feeñu Laban, Arameen ba, ci géntu guddi ne ko: «Moytula wax Yanqóoba lenn lu koy gaar.» |
929 | GEN 32:1 | Ca ëllëg sa, Laban xëy suba teel, tàggoo aki sëtam ak doomam yu jigéen ya, ñaanal leen, ba noppi waññiku ñibbi. |
930 | GEN 32:2 | Yanqóoba moom topp yoonam. Ci kaw loolu ay malaakay Yàlla feeñu ko. |
938 | GEN 32:10 | Ci kaw loolu Yanqóoba ñaan Yàlla, ne ko: «Yaw Aji Sax ji, sama Yàllay maam Ibraayma, di sama Yàllay baay Isaaxa itam, yaa ma ne woon: “Dellul réew ma nga cosaanoo, ca say bokk; dinaa la baaxe.” |
946 | GEN 32:18 | Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?” |
959 | GEN 32:31 | Ci kaw loolu Yanqóoba tudde bérab ba Peniyel (mu firi Xar-kanamu Yàlla), ndaxte da ne: «Ne naa Yàlla jàkk, te maa ngi dund ba tey.» |
983 | GEN 34:2 | Ci kaw loolu Sikem doomu Amor, miy Eween te di kilifa ca dëkk ba, daldi koy gis, jàpp ko, tëdde ko, torxal ko. |
987 | GEN 34:6 | Ci diggante boobu Amor, baayu Sikem, ñëw ci Yanqóoba, ngir gise ak moom. |
988 | GEN 34:7 | Ca la doomi Yanqóoba agsi, jóge ca tool ya. Ba ñu déggee la xew, dañoo am naqar wu réy, mer lool ndax gàcce, ga Sikem teg waa Israyil, ba mu tëddee doomu Yanqóoba ja, te loolu di lu defuwul. |
1006 | GEN 34:25 | Ca gannaaw ëllëg sa ñu ànd ak metit, ñaari doomi Yanqóoba ya, Simeyon ak Lewi, càmmiñi Diina, jël seeni saamar, dugg ca dëkk ba, bett leen, rey góor ñépp. |
1007 | GEN 34:26 | Ca lañu leel ñawkay saamar Amor ak doomam Sikem, ñu dee, ñu jële Diina kër Sikem, ànd ak moom, dem. |
1031 | GEN 35:19 | Ci kaw loolu Rasel faatu, ñu denc ko ca yoonu Efrata, ga ñuy wax Betleyem ba tey. |
1118 | GEN 37:34 | Ci kaw loolu Yanqóoba mititlu ko, ba xotti ay yéreem, taraxlaayoo ab saaku, di jooy doomam ay fan. |
1121 | GEN 38:1 | Ca jamono yooyu Yuda dafa teqlikoo ak ay doomi baayam, dal ca waa ju dëkk Adulam te tudd Ira. |
1152 | GEN 39:2 | Ci kaw loolu Aji Sax ji ànd ak Yuusufa, may ko ndam, mu dëkk ca kër sangub waa Misraam ba. |
1172 | GEN 39:22 | Ci kaw loolu mu may Yuusufa, mu yilif ñi ñu tëj ñépp, te mboolem lu ñu fay def, mu di ko jiite. |
1182 | GEN 40:9 | Jawriñ bay topptoo naanu buur daldi nettali géntam Yuusufa, ne ko: «Ci gént gi, garabu reseñ laa gis ci sama kanam, |
1203 | GEN 41:7 | Ca la gub yu gooy ya wonn juróom ñaari gub yu nangu ya te baax. Gannaaw loolu Firawna yewwu, xam ne gént la woon. |
1240 | GEN 41:44 | Ci kaw loolu Firawna ne Yuusufa: «Man maay Firawna, waaye gannaaw-si-tey mboolem waa réewum Misra, kenn du ci sañatee yékkati loxo mbaa muy séqi jéego, te àndoo ci.» |
1249 | GEN 41:53 | Ci kaw loolu juróom ñaari ati naataange ya jeex ca réewum Misra, |
1256 | GEN 42:3 | Ci kaw loolu fukki magi Yuusufa ya dem Misra, jëndi pepp. |
1271 | GEN 42:18 | Ca gannaaw ëllëg sa Yuusufa ne leen: «Bu ngeen defee lii may wax, dingeen dund, ndax man ragal naa Yàlla. |
1274 | GEN 42:21 | te naa ci seen biir: «Céy su nu yégoon, sunu àqu rakk a nu topp nii, ndax danu koo seetaanoon, mu nekk ci njàqarey xol, di nu tinu, te faalewunu ko; looloo waral sunu njàqarey tey jii.» |
1277 | GEN 42:24 | Ci biir loolu mu dummóoyu leen, di jooy. Ba mu jooyee ba noppi, walbatiku, wax ak ñoom, doora jël Simeyon, jéng ko ci seen kanam. |
1291 | GEN 42:38 | Ci kaw loolu Yanqóoba ne: «Sama doom daal, du ànd ak yeen, ndax magam faatu na, te moom rekk a des. Su ko musiba dabee ci yoon wi ngeen jëm, dingeen ma yóbbe naqar wu may jàpp, ba kera may ànd ak sama bijjaaw, tàbbi njaniiw.» |
1314 | GEN 43:23 | Mu ne leen: «Jàmm rekk la; buleen tiit, seen Yàlla, jiy seen Yàllay baay, moo leen defal alal ci seeni saaku. Seen xaalis jot naa ci.» Ci kaw loolu mu génne Simeyon, indil leen ko. |
1321 | GEN 43:30 | Ci kaw loolu Yuusufa gaaw génn ndax yaram wu daw, te manatula téye ay rongooñam ndax rakkam ja, mu dugg néegu biiram, di jooy. |
1328 | GEN 44:3 | Ca ëllëg sa, ba jant bay fenk, yiwi nañu gaa ña, ñu sëf seeni mbaam, dem. |
1347 | GEN 44:22 | Ci kaw loolu, sang bi, nu wax la ne: “Xale bu góor bi manula tàggook baayam. Bu tàggoo ak moom, kon baayam dina dee.” |
1403 | GEN 46:16 | Doomi Gàdd yu góor ñoo di Cefon ak Agi ak Suni ak Esbon ak Eri ak Arodi ak Areli. |
1460 | GEN 48:8 | Ci kaw loolu Israyil gis doomi Yuusufa ya. Mu ne: «Ñii ñooy ñan?» |
1464 | GEN 48:12 | Ca la leen Yuusufa wàccee fi ñu uufu ci seen maam, daldi dëpp jëëm ci suuf, |