106 | GEN 4:26 | Set it, am doom ju góor, tudde ko Enos. Fan yooya lañu tàmbalee tudd Aji Sax ji, di ko wormaal. |
249 | GEN 10:14 | ak Pataruseen ñi ak Kasluyeen, ñooñee waa Filisti bàyyikoo ca seen réew; ak it Kaftoreen ñi. |
307 | GEN 12:8 | Gannaaw loolu mu jóge fa, jëm tund, wi féete Betel penku, samp fa xaymaam; Betel féete ko sowu, Ayi féete ko penku. Foofa itam Ibraam tabaxal na fa Aji Sax ji sarxalukaay, tudd fa Aji Sax ji, wormaal ko. |
314 | GEN 12:15 | Jaraafi Firawna itam gis ko, di ko kañ ca Firawna ndax taar ba, ñu daldi ko yóbbu ca kër Firawna. |
315 | GEN 12:16 | Firawna nag topptoo Ibraam bu baax ndax moom, ñu may ko ay gàtt ak ay nag, ay mbaam yu góor, ak ay jaam yu góor ak yu jigéen, ak ay mbaam yu jigéen aki giléem. |
316 | GEN 12:17 | Teewul Aji Sax ji wàcce ca Firawna ak waa këram jàngoro yu metti ndax Sarayi, soxnas Ibraam. |
317 | GEN 12:18 | Firawna woolu Ibraam ne ko: «Li nga ma def nag? Lu tax waxoo ma ne kii sa soxna la? |
319 | GEN 12:20 | Naka la Firawna wax loolu ba noppi, daldi sant ay dagam, ñu génne Ibraam réew ma, moom ak soxnaam ak alalam jépp. |
341 | GEN 14:4 | Fekk na diiru fukki at ak ñaar Kedorlamer moo leen yilifoon, teewul ca fukkeelu at ma ak ñett ñu fippu. |
350 | GEN 14:13 | Ba loolu xewee, kenn ci ñi ñu jàppoon rëcc, ñëw ci Ibraam miy ab Ebrë, wax ko ko. Fekk na mu dëkk ca wetu garab yu mag ya woon ca toolub Mamre, ma dib Amoreen, di mbokk mu jege ci Eskol ak Aner, ñoom ñi doon wóllërey Ibraam. |
473 | GEN 19:15 | Fajar a ngay xar, malaaka ya fuug Lóot ne ko: «Gaawal gaaw, ànd ak sa soxna ak sa ñaari doom yu jigéen yii, ba bu Yàlla tasee dëkk bi, dungeen sànku.» |
501 | GEN 20:5 | Du góor gi da maa waxoon ne kii jigéenam la? Du jigéen ji it da maa waxoon ne kooku càmmiñam la? Fexewuma dara lu ñaaw te di ko tey de!» |
513 | GEN 20:17 | Fekk na Aji Sax ji um jigéeni waa kër Abimeleg, ba kenn du ci am doom, du soxnaam, du ay jaamam, te li ko waral di Saarata soxnas Ibraayma. Ibraayma nag ñaan Yàlla; Yàlla def ñu wér, ba mana am doom. |
542 | GEN 21:28 | Fekk na Ibraayma ber juróom ñaari xar yu jigéen. |
546 | GEN 21:32 | Naka lañu fasoo kóllëre ca Beerseba, Abimeleg jóg ànd ak Pikol kilifay xarekatam, ñu ñibbi réewu Filisti. |
548 | GEN 21:34 | Ibraayma gane na réewu Filisti lu yàgg. |
599 | GEN 24:7 | Aji Sax ji, Yàllay asamaan, moom mi ma jële sama kër baay ak fa ma juddoo, te wax ak man, giñal ma ne ma, dina jox sama askan réew mii, moom ci boppam dina yebal malaakaam, mu jiitu la. Foofa ngay jëlale sama doom soxna. |
694 | GEN 26:1 | Ba loolu wéyee xiif am ca réew ma, muy xiif bu wuute ak ba woon ca jamonoy Ibraayma; Isaaxa nag dem Gerar ca Abimeleg, buurub waa Filisti. |
695 | GEN 26:2 | Foofa Aji Sax ji feeñu ko fa ne ko: «Bul dem Misra, waaye nanga toog ci réew mi ma lay wax. |
701 | GEN 26:8 | Ba ñu fa toogee ba mu yàgg, mu am bés Abimeleg, buurub waa Filisti tollu ci palanteeram, gis leen, fekk yóo Isaaxaa ngay raay soxnaam Rebeka. |
707 | GEN 26:14 | am géttu jur gu gudd ak gu gàtt, ak ay surga yu bare, ba tax waa Filisti iñaane ko, |
711 | GEN 26:18 | Ba loolu weesee Isaaxa sikkli teen, yi ñu gasoon ca jamonoy baayam Ibraayma, te waa Filisti sakkoon leen gannaaw ba Ibraayma nelawee. Ca la tudde teen yi tur, ya leen baayam tudde woon. |
715 | GEN 26:22 | Mu jóge foofa, gasati teen, jàmm ne ñoyy, mu tudde ko Reyobot (mu firi Fu yaatu), ndax da ne: «Léegi Aji Sax ji yaatal na nu, te dinanu woomle ci réew mi.» |
733 | GEN 27:5 | Fekk na Rebekaa ngi déglu, ba Isaaxay wax ak doomam Esawu. Esawu daldi dem ca àll ba, rëbbi lu mu toggsi. |
791 | GEN 28:17 | Ma nga tiit nag te naan: «Bérab beeka raglu! Fii kay du fenn, fu dul kër Yàlla; te mooy buntu asamaan.» |
847 | GEN 30:16 | Yanqóobaa ngay jóge tool ca ngoon, Leya génn, gatandu ko, ne ko: «Fi man nga wara aye tey, ndaxte jënde naa ay gi màndaragoor ji sama doom indi.» Yanqóoba daldi féete ca moom guddi googu. |
893 | GEN 31:19 | Fekk na Laban dem wati ay xaram. Ci biir loolu Rasel sàcc gàllaaji kër yu baayam. |
908 | GEN 31:34 | Fekk na Rasel fab gàllaaji kër ya, làq ca ron tegu giléem ga, toog ca. Laban tëcc, tëcc ca biir xayma ba, gisul dara. |
920 | GEN 31:46 | Yanqóoba ne ay bokkam: «Forleen ay doj.» Ñu for ay doj, def ko ab jal, daldi lekk foofa ca wetu jal ba. |
946 | GEN 32:18 | Ci biir loolu mu sant ki jiitu, ne ko: «Boo dajeek sama mag, mu laaj la ne la: “Kuy sa njaatige?” ak “Ku moom li nga jiital?” ak “Foo jëm?” |
979 | GEN 33:18 | Gannaaw ga Yanqóoba agsi Sikem, ga ca réewu Kanaan, ci jàmm. Fekk na mu bàyyikoo Padan Aram, ba dal fa jàkkaarlook dëkk ba. |
1020 | GEN 35:8 | Foofa itam la Debora, ma daa nàmpal Rebeka, faatoo, ñu suul ko ca taatu garab gu mag ga ca wetu Betel. Ñu tudde garab ga Alon Bakut (mu firi Garabu jooyoo). |
1041 | GEN 35:29 | Foofa la bakkanam rote, mu faatu, fekki ay maamam, gannaaw ba mu màggatee, ba ñor xomm. Ba loolu amee ay doomam Esawu ak Yanqóoba rob ko. |
1120 | GEN 37:36 | fekk waa Majan yóbbu nañu ko Misra, jaay ko Potifaar, jawriñu Firawna mi jiite ay dagam. |
1122 | GEN 38:2 | Foofa nag Yuda gis fa senn as ndaw, su doon doomu Kanaaneen bu tudd Suwa, mu jël ko soxna. |
1136 | GEN 38:16 | Mu jàdd, ñëw ba ca moom, ne ko: «May ma, ma ànd ak yaw.» Fekk na xamul woon ne goroom la. Mu ne ko: «Loo may fey, ngir ànd ak man?» |
1138 | GEN 38:18 | Mu ne ko: «Lu ma lay tayle?» Ndaw si ne ko: «Xanaa sa jaarob màndargaal, ak buum, gi mu àndal ak yet, wi ci sa loxo.» Mu jox ko nag, ba noppi ànd ak moom. Fa la doxe ëmb. |
1141 | GEN 38:21 | Mu laaj waa gox ba, ne leen: «Ana gànc biy toog Enayim ci yoon wi?» Ñu ne ko: «Fii de ab gànc nekku fi.» |
1151 | GEN 39:1 | Ba ñu yóbboo Yuusufa Misra, Potifaar, jawriñu Firawna, ma jiite ay dagam, da koo jënd ca Ismayleen, ña ko fa indi. |
1175 | GEN 40:2 | Firawna nag mere lool ñaari jawriñ yooya, kenn ka di kilifay ñay topptoo naani buur, ka ca des di kilifay lakk-kati mburu ya, |
1180 | GEN 40:7 | Mu laaj jawriñi Firawna, yooyee ñu tëjandoo woon ak moom ca kër sangam, ne leen: «Lu leen tax ne yogg tey?» |
1184 | GEN 40:11 | Maa ngi téye nii kaasu Firawna ci sama loxo, jël reseñ ji nag, nal ko ci kaasu Firawna, ba noppi teg kaas bi ci loxol Firawna.» |
1186 | GEN 40:13 | Fii ak ñetti fan Firawna dina la siggil, delloo la sa liggéey, ngay teg kaasu Firawna ci loxoom, ni nga ko daa defe naka jekk, ba nga yoree naanam. |
1187 | GEN 40:14 | Waaye ngalla boo delloo ca sa teraanga, nanga ma geestu te dimbali ma, waxal ma Firawna lu jëm ci man, ba man maa génne fii. |
1190 | GEN 40:17 | ba féete kaw a nga yeb mboolem xeeti mburu yu ñuy lakkal Firawna, picc yaa nga koy for ca pañe, ba ma yenu.» |
1192 | GEN 40:19 | Fii ak ñetti fan Firawna dina la siggil, ba noppi wékk la ci bant, picc yi ñëw, di for sa suux.» |
1193 | GEN 40:20 | Ñu teg ca ñetti fan, Firawna di màggal bésu juddoom, dajale jawriñam yépp, di leen berndeel, daldi cay seppee kilifa gay topptoo ay naanam, ak kilifag lakk-kati mburu ya, siggil leen. |
1194 | GEN 40:21 | Mu delloo nag kilifa gay topptoo ay naanam ca liggéeyam, mu teg kaas ba ca loxol Firawna. |
1196 | GEN 40:23 | Waaye kilifa, ga yore naani Firawna, xalaatul sax Yuusufa, da koo fàtte. |
1197 | GEN 41:1 | Ñaari ati lëmm wees na gannaaw loolu, gént dikkal Firawna, mu jeneer taxaw ca wetu dexu Niil. |
1200 | GEN 41:4 | Nag yu ñaaw ya te yooy daldi lekk juróom ñaari nag yu rafet ya te suur. Firawna yewwu, |
1203 | GEN 41:7 | Ca la gub yu gooy ya wonn juróom ñaari gub yu nangu ya te baax. Gannaaw loolu Firawna yewwu, xam ne gént la woon. |
1204 | GEN 41:8 | Ba bët setee, Firawna jaaxle lool, ba woolu jibar ya ak boroom xam-xami Misra yépp, nettali leen la mu gént, te kenn manu koo firil Firawna. |
1205 | GEN 41:9 | Ba loolu amee kilifa gay topptoo naani Firawna ne ko: «Man de tooñ naa te dinaa la ko wax tey. |
1206 | GEN 41:10 | Sang bi, ba nga nu meree, yaw Firawna, ba tëj ma kaso ca kër njiitu dag ya, man ak kilifag lakk-kati mburu ya, |
1208 | GEN 41:12 | Fekk amoon na waxambaanew ebrë wu fa nekkoon ak nun, te doonoon jaamub njiital dag ya. Nu nettali ko sunuy gént, mu firil nu ko, wax nu ku nekk la sa gént di tekki. |
1210 | GEN 41:14 | Ba Firawna déggee loolu, dafa woolu Yuusufa. Ñu gaaw tijji ko, mu watu, solu, doora wuyji Firawna. |
1211 | GEN 41:15 | Firawna ne Yuusufa: «Damaa gént, te kenn manu koo firi, te ma dégg ñuy wax ci yaw naan, gént goo dégg rekk, xam ko, ba man koo firi.» |
1212 | GEN 41:16 | Yuusufa ne ko: «Du ci man de, waaye Yàlla mooy baaxe Firawna pirim jàmm.» |
1213 | GEN 41:17 | Firawna ne Yuusufa: «Damaa gént, taxaw ci tàkkal dexu Niil, |
1221 | GEN 41:25 | Yuusufa ne Firawna: «Sa ñaari gént yi de, sang bi, ñoo bokk piri. Sang bi, Yàlla da laa xamal li muy def ëllëg. |
1229 | GEN 41:33 | Yuusufa teg ca ne Firawna: «Kon léegi sang bi, wutal nit ku muus te rafet xel, jiital ko ci réewum Misra. |
1231 | GEN 41:35 | Ñoom nañu dajale mboolem dundi at yu baax yi, te boole pepp mi ci sa ndigalu bopp, yaw Firawna, muy dund bu ñuy denc ci dëkk yi. |
1233 | GEN 41:37 | Pexe moomu nag doon lu Firawna aki jawriñam yépp njort ne baax na. |
1234 | GEN 41:38 | Firawna daldi ne jawriñ ya: «Ndax masees naa gis ku mel ni kii a waay, nit ku Yàlla sol Noowug boppam?» |
1235 | GEN 41:39 | Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Ndegam Yàlla xamal na la lii lépp kay, leer na ne amul kenn ku muus te rafet xel ni yaw. |
1237 | GEN 41:41 | Gannaaw loolu Firawna neeti Yuusufa: «Bés niki tey, dénk naa la réewum Misra gépp» |
1238 | GEN 41:42 | Ba loolu amee Firawna tekkee jaarob màndargaal ba ca loxoom, takkal ko Yuusufa, solal ko yérey tànnéef, takkal ko caqu wurus, |
1239 | GEN 41:43 | ba noppi waral ko watiiru ku sës rëkk ci moom Firawna, te fu mu ware ñu jiitu ko, di yéene naan: «Sujjóotleen!» Noonu la ko Firawna fale, mu yilif Misra gépp. |
1240 | GEN 41:44 | Ci kaw loolu Firawna ne Yuusufa: «Man maay Firawna, waaye gannaaw-si-tey mboolem waa réewum Misra, kenn du ci sañatee yékkati loxo mbaa muy séqi jéego, te àndoo ci.» |
1241 | GEN 41:45 | Firawna nag tudde Yuusufa Safnat Paneya, may ko jabar Asnat doomu Potifera ma doon sarxalkat ca dëkk ba ñuy wax On. Yuusufa doxe ca tegoo kilifteefu Misra gépp. |
1242 | GEN 41:46 | Ba Yuusufay tàmbalee liggéeyal Firawna buuru Misra, mu ngi tollu ci fanweeri at. Yuusufa daldi bàyyikoo ca Firawna, wër réew ma mépp. |
1245 | GEN 41:49 | Fa la Yuusufa jaare dajale pepp, mu ne gàññ, ni suufas géej, ba tàyyeeti koo waññ, ndax mujj na wees ab lim. |
1251 | GEN 41:55 | Ba waa Misra xiifee, dañoo dem jooytuji dund ca Firawna. Mu wax ak ñépp ne leen: «Demleen ca Yuusufa; lu mu leen wax, defleen ko.» |
1259 | GEN 42:6 | Fekk booba Yuusufa mooy dogal ca réew ma, di jaay pepp waa réew mépp. Magi Yuusufa ya ñëw, sujjóotal Yuusufa. |
1260 | GEN 42:7 | Naka la Yuusufa gis magam ya, xàmmi leen, te mel ni ku leen xamul, di wax ak ñoom kàddu yu dëgër ne leen: «Fu ngeen jóge?» Ñu ne ko: «Réewu Kanaan lañu jóge, di jëndsi ab dund.» |
1268 | GEN 42:15 | Waaye nii laa leen di seetloo: bu seen rakk ñëwul, ak bakkanu Firawna, dungeen fi jóge. |
1269 | GEN 42:16 | Na kenn ci yeen jëli seen rakk, ñu tëj ñi ci des te topp seen wax, ba xam ndax yeena ngi ci dëgg. Su dul dëgg, giñ naa ci Firawna ne ay yëddukat doŋŋ ngeen.» |
1280 | GEN 42:27 | Fa ñu dal ca guddi, kenn ci ñoom bëgga xont mbaamam, ubbi saakoom rekk, ne pemm ci xaalisam. |
1343 | GEN 44:18 | Yuda jegesi ne ko: «Ngalla sang bi, ma ñeme laa diis lenn rekk, te sa xol baña tàng ci man, doonte yaak Firawnaa tolloo. |
1361 | GEN 45:2 | Mu ne yikkét, jooy jooy yu metti, waa Misra di ca dégg, ba ca kër Firawna sax. |
1367 | GEN 45:8 | Kon nag du yeena ma yebal fii, waaye Yàllaa. Te moo ma jagleel, ma doon cëslaayal Firawna, mel ni baay ci moom, jiite këram gépp, boole ci yilif mboolem réewum Misra. |
1375 | GEN 45:16 | Ba xibaar ba àggee kër Firawna, ñu naan magi Yuusufa ñëw nañu, doonoon na lu neex Firawna, moom aki dagam. |
1376 | GEN 45:17 | Firawna ne Yuusufa: «Waxal say mag, ne leen: “Ni ngeen di def mooy nii: sëfleen seeni mbaam te dem réewu Kanaan, |
1378 | GEN 45:19 | Firawna dellu ne Yuusufa: «Am nga ndigal itam ci wax leen ne leen: “Ni ngeen koy defe nii la: dangeen di jële ay watiir ci réew mi, dem yeb ci seeni doom ak seeni soxna, te ànd ak seen baay, ngeen ñëw. |
1380 | GEN 45:21 | Ba loolu amee doomi Israyil def noona. Yuusufa jox leen ay watiir ci ndigalu Firawna, ak lu ñu lekk ca yoon wa, |
1392 | GEN 46:5 | Ba loolu amee Yanqóoba jóge Beerseba; doomi Israyil boole seen baay ak seeni doom ak seeni soxna, yeb leen ci watiir, yi Firawna yónnee woon, ngir yóbbu leen. |
1418 | GEN 46:31 | Ba mu ko defee Yuusufa wax ak doomi baayam ya ak waa kër baayam ne leen: «Maa ngi dellu yégali Firawna ne ko: “Samay bokk ak sama waa kër baay, ña nekkoon ca réewu Kanaan, ñëw nañu fi man. |
1420 | GEN 46:33 | Kon bu leen Firawna wooyee, ne leen: |
1422 | GEN 47:1 | Yuusufa daa dem ca Firawna, wax ko ne ko: «Sama baay ak samay bokk, jóge nañu Kanaan, ànd ak seen jur gu gàtt ak gu gudd ak mboolem lu ñu moom. Ña nga léegi ca diiwaanu Gosen.» |
1423 | GEN 47:2 | Fekk na Yuusufa tànn juróom ciy doomi baayam. Mu nuyole leen ak Firawna. |
1424 | GEN 47:3 | Firawna laaj doomi baay ya, ne leen: «Lan mooy seen liggéey?» Ñu ne ko: «Nun de sang bi, ay sàmm lanu naka jekk ca sunuy maam ba tey.» |
1426 | GEN 47:5 | Firawna wax ak Yuusufa ne ko: «Gannaaw sa baay ak say bokk ñëw nañu fi yaw, |
1428 | GEN 47:7 | Gannaaw loolu Yuusufa ànd ak baayam ba fa Firawna, nuyole ko ak moom. Yanqóoba nuyu Firawna. |
1429 | GEN 47:8 | Firawna laaj Yanqóoba ne ko: «Aa, góor gi, xanaa war ngaa doon mag de!» |
1430 | GEN 47:9 | Yanqóoba wax Firawna ne ko: «Samay ati màngaan, ba ma ganee àddina ba tey de, mu ngi tollu ci téeméer ak fanweer, muy at yu gàtt te naqari, te it demuma bay tolloo ay at ak samay maam, ba ñuy màngaan ci àddina.» |
1431 | GEN 47:10 | Ba mu ko defee Yanqóoba ñaanal Firawna, bàyyikoo fa, daldi dem. |